Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Mark 15 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 At dawn the chief priests, elders, scribes, and the whole council consulted together, bound Jesus, led him away, and handed him over to Pilate. Ci suba teel sarxalkat yu mag yi gise, ñoom ak njiit yi ak xutbakat yi ak kureelu àttekat yi yépp. Ñu yeew nag Yeesu, daldi ko yóbbu, jébbal ko Pilaat.
2 Pilate asked him, "Are you the King of the Jews?" "You say so," Jesus replied. Noonu Pilaat laaj ko: «Ndax yaa di buuru Yawut yi?» Yeesu ne ko: «Wax nga ko.»
3 The chief priests kept accusing him of many things. Te sarxalkat yu mag yi di ko jiiñ lu bare.
4 So Pilate questioned him again: "Have you no answer? See how many charges they bring against you." Kon nag Pilaat laajaat ko: «Déggal lépp li ñu lay jiiñ. Xanaa amoo ci tont?»
5 But Jesus said nothing more, and Pilate was amazed. Waaye ba tey Yeesu waxul dara, ba tax Pilaat waaru.
6 Now at the festival, Pilate used to release one prisoner for them—whoever they asked for. Màggal gu nekk nag Pilaat daan na may mbooloo mi, ñu tànn kenn ci ñi ñu tëjoon, mu bàyyil leen ko.
7 A man called Barabbas was in prison with the rebels who had committed murder during the uprising. Fekk booba amoon na ku ñu tëj, tudd Barabas, ku bokk ci ña bëggoona tas réew mi, boole ci rey nit.
8 The crowd came up and began asking Pilate to do for them what he always did. Noonu mbooloo mi ñëw, laaj Pilaat, mu defal leen la mu daan def.
9-10 "Do you want me to release for you the King of the Jews?" Pilate answered, Pilaat nag xam ne kiñaan rekk a taxoon sarxalkat yu mag yi jébbal ko Yeesu. Kon mu ne mbooloo mi: «Xanaa ma bàyyil leen buuru Yawut yi?»
10 for he knew it was out of envy that the chief priests had handed him over. Not in this edition
11 But the chief priests stirred up the crowd to have him release Barabbas for them instead. Waaye sarxalkat yu mag yi xiir mbooloo mi, ñu laaj Pilaat, mu bàyyil leen Barabas.
12 "So what do you want me to do with the one you call King of the Jews?" Pilate asked them again. Kon Pilaat ne leen: «Lan laay def nag ak ki ngeen di wooye buuru Yawut yi?»
13 Crucify him!" they shouted back. Ñu daldi yuuxuwaat naan: «Daaj ko ci bant, ba mu dee!»
14 "Why? What evil has he done?" Pilate asked. But they shouted all the louder, "Crucify him!" Pilaat ne leen: «Lu tax? Gan tooñ la def?» Waaye mbooloo mi di yuuxu bu gëna kawe: «Daaj ko ci bant!»
15 To satisfy the crowd, Pilate released Barabbas to them. He had Jesus flogged, and handed him over to be crucified. Noonu Pilaat, mi wuta neex mbooloo mi, bàyyil leen Barabas, ba noppi mu dóorlu Yeesu ay yar, jébbal ko, ngir ñu daaj ko ci bant.
16 Soldiers led him away into the palace (the governor's headquarters) and called together the whole company of soldiers. Bi loolu amee ñu dugal Yeesu ci biir kër boroom réew ma, mooy bérab bu ñuy wax Peretoriyum, ñu daldi woo mbooloom xarekat yépp.
17 They dressed him in purple, twisted together a crown of thorns, and set it on him. Noonu ñu solal ko mbubb mu xonq curr, ràbb kaalag dég, teg ko ci boppam.
18 And they began to salute him: "Hail, King of the Jews!" Ñu daldi ko wax bu kawe: «Nuyu nanu la, yaw buuru Yawut yi!»
19 They kept beating his head with a staff, spat on him, and knelt in mock homage to him. Ñu di ko dóor ci bopp ak bant, di ko tifli, daldi sukk, màggal ko.
20 After mocking him, they stripped off the purple and put his own clothes on him, then led him out to crucify him. Bi ñu ko ñaawalee noonu ba noppi, ñu summi mbubb mu xonq mi, solaatal ko ay yéreem, yóbbu ko, ngir daaj ko ci bant.
21 They forced a passerby coming from the countryside—Simon of Cyrene, father of Alexander and Rufus—to carry his cross. Amoon na nag nit ku dëkk Siren, tudd Simoŋ, di baayu Alegsàndar ak Rufus. Fekk booba mu romb fa, jóge ca wet, ga féete ak tool ya, ñu ga ko ngir mu gàddu bant bi.
22 They brought Jesus to the place called Golgotha (which means Place of a Skull). Noonu ñu yóbbu Yeesu ca bérab bu ñuy wax Golgota, liy tekki «bérabu Kaaŋu bopp.»
23 They offered him wine mixed with myrrh, but he did not take it. Ñu bëgg koo jox biiñ bu ñu boole ak naan gu tudd miir, waaye nanguwu ko.
24 They crucified him. They divided his clothes among them, casting lots for what each would get. Foofa ñu daaj Yeesu ci bant, daldi séddoo ay yéreem, tegoo ko ay bant, ba xam ku nekk, looy am;
25 It was nine in the morning when they crucified him. booba fekk yoor-yoor di jot.
26 The written notice of the charge against him read: THE KING OF THE JEWS. Mbind mi xamle lu tax ñu rey ko nee na: «Kii mooy buuru Yawut yi.»
27-28 They crucified two rebels with him, one on his right and one on his left. Booba it ñu daajaale ak moom ñaari taskati réew mi, kenn ci ndijooram, ki ci des ci càmmoñam.
29 Those passing by insulted him, shaking their heads, saying, "Ha! You who tear down the temple and build it in three days, Ña fa doon romb di ko xas, di wëcc seen bopp ndax sib ko, naan: «Waaw kay, yaw mi bëgga toj kër Yàlla gi, tabaxaat ko ci ñetti fan,
30 save yourself and come down from the cross!" wàccal ci bant bi te musal sa bopp!»
31 Likewise the chief priests and scribes mocked him among themselves: "He saved others; himself he can't save. Noonu it sarxalkat yu mag yi ak xutbakat yi di ko ñaawal ci seen biir naan: «Kii musal na ñeneen waaye manula musal boppam.
32 Let the Christ, King of Israel, come down from the cross now, so we can see and believe." Those crucified with him also insulted him. Almasi bii, di buuru Israyil, na wàcc léegi ci bant bi, nu gis ko te gëm.» Ñi ñu daajaale ak moom it di ko xarab.
33 At noon, darkness came over the whole land until three in the afternoon. Li tàmbalee digg bëccëg, ba ci tisbaar, réew mépp lëndëm.
34 At three in the afternoon Jesus cried out loudly, "Eloi, Eloi, lema sabachthani?" meaning, "My God, my God, why have you forsaken me?" Ci tisbaar nag Yeesu wootee kàddu gu dëgër naan: «Elowi, Elowi, lema sabaktani?» liy tekki: «Sama Yàlla, sama Yàlla, lu tax nga dëddu ma?»
35 When some of those standing nearby heard this, they said, "Listen, he's calling Elijah." Ñenn ci ña fa taxaw nag, bi ñu ko déggee, ñu ne: «Mu ngi woo yonent Yàlla Ilyaas.»
36 One ran, filled a sponge with sour wine, put it on a reed, and gave him a drink. "Let him be," he said, "let's see if Elijah comes to take him down." Noonu kenn daw, jël aw sagar, capp ko ci bineegar, mu teg ko ci bant, jox ko ko, mu muucu. Mu ne: «Bàyyileen, nu seet, ba xam Ilyaas dina ñëw, wàcce ko.»
37 With a loud cry, Jesus breathed his last. Noonu Yeesu wootewaat ak kàddu gu dëgër, delloo ruuwam Yàlla.
38 And the curtain of the temple was torn in two from top to bottom. Bi mu ko defee ridob bérab bu sell ba ca kër Yàlla ga xar ñaar, li dale ci kaw ba ci suuf.
39 The centurion facing Jesus saw how he breathed his last and said, "Truly this man was the Son of God." Njiitu xare nag, bi taxawoon ci kanam Yeesu, bi mu gisee ni Yeesu deeye, mu ne: «Ci dëgg, nit kii Doomu Yàlla la!»
40 Women were also watching from a distance, including Mary Magdalene, Mary the mother of James the younger and Joses, and Salome. Amoon na fa nag ay jigéen, ñu leen dànd, di xool. Xàmmi nañu ci: Maryaama mi dëkk Magdala, Maryaama yaayu Saag mu ndaw ak Yuusufa, ak Salome.
41 These women had followed him in Galilee and served him; many others who came up with him to Jerusalem were also there. Bi Yeesu nekkee Galile, jigéen ñooñu ñoo ko doon topp, di ko topptoo. Amoon na fa it yeneen jigéen yu bare yu àndoon ak moom, ba ñëw Yerusalem.
42 Evening had come, and since it was Preparation Day—the day before the Sabbath. Booba nag bésu Waajal la woon, maanaam bés bu jiitu bésub noflaay bi. Ca ngoon sa nag,
43 Joseph of Arimathea, a prominent council member who himself was waiting for the kingdom of our Father, dared to go to Pilate and ask for Jesus' body. Yuusufa mi dëkk Arimate takk aw fitam, dem Pilaat, laaj ko néewu Yeesu. Yuusufa moomu nag, ku siiw la woon ci kureelu àttekat yi, te doon séentu moom itam nguuru Yàlla.
44 Pilate was surprised he was already dead; summoning the centurion, he asked if Jesus had been dead long. Bi Pilaat déggee ne, Yeesu faatu na xaat, mu waaru. Mu woolu nag njiit li, laaj ko, ndax yàgg na faatu.
45 When he learned from the centurion that it was so, he granted the body to Joseph. Bi ko ko njiit li dëggalee, Pilaat jox néew bi Yuusufa.
46 Joseph bought linen, took the body down, wrapped it in the cloth, and laid it in a tomb cut from rock. Then he rolled a stone against the tomb's entrance. Noonu Yuusufa jënd càngaay, wàcce néew bi, laxas ko ci, dugal ko cib bàmmeel bu ñu yett ci xeer. Bi mu ko defee mu béraŋ aw doj, ube ko buntu bàmmeel bi.
47 Mary Magdalene and Mary the mother of Joses saw where he was laid. Maryaamam Magdala nag ak Maryaama yaayu Yuusufa xool fu mu ko denc.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]