Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Mark 13 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 Leaving the temple, one of his disciples said to him, "Teacher, look! What huge stones, what magnificent buildings!" Bi Yeesu di jóge ca kër Yàlla ga, kenn ca taalibe ya ne ko: «Kilifa gi, xoolal! Ni mu réye ay doj, te rafete ni ay taax!»
2 Jesus said to him, "Do you see these great buildings? Not one stone will remain here on another; all will be torn down." Waaye Yeesu ne leen: «Du gis ngeen taax yu réy yii yépp? Lii lépp dina daanu, ba doj dootul des ci kaw doj.»
3 As he sat on the Mount of Olives facing the temple, Peter, James, John, and Andrew asked him privately, Gannaaw loolu, bi nga xamee ne Yeesu toog na ci tundu Oliw ya, jàkkaarlook kër Yàlla ga, Piyeer, Saag, Yowaana ak Andare fekki ko cig wet, laaj ko:
4 tell us, when will these things happen, and what sign shows all this is about to be fulfilled? «Wax nu kañ la loolu di am? Te luy tegtal ne, mbir yii yépp a ngi bëgga mat?»
5 Jesus began to tell them: "Watch out that no one deceives you. Noonu Yeesu ne leen: «Moytuleen, bu leen kenn nax.
6 Many will come in my name, claiming, 'I am he,' and they will deceive many. Ñu bare dinañu ñëw ci sama tur naan: “Moom laa,” te dinañu nax ñu bare.
7 When you hear of wars and rumors of wars, don't be troubled—these must happen, but the end isn't yet. Bu ngeen déggee ay xare ak coowi xare, wottuleena tiit; loolu war na am, waaye mujug jamono ji jotagul.
8 Nation will rise against nation, kingdom against kingdom, earthquakes in various places, famines—these are the beginning of birth pains. Xeet dina jóg, xeex ak weneen xeet, réew xeex ak meneen réew. Te yëngu-yënguy suuf dina am ciy bérab yu bare, ak ay xiif. Loolu lépp mooy ndoortel metit yi, mel ni jigéen juy matu.
9 Watch yourselves. They'll hand you to councils and beat you in synagogues. Because of me you'll stand before governors and kings, as a testimony to them. «Moytuleen. Dees na leen jébbal àttekat ya, di leen dóor ay yar ca jàngu ya. Dinañu leen dëj ci kanam i boroom réew ak i buur ndax sama tur, ngir ngeen nekk seede ci ñoom.
10 And the gospel must first be proclaimed to all nations. Fàww xibaaru jàmm bi jëkka jib ci xeet yépp.
11 When they arrest and hand you over, don't worry beforehand what to say. Say whatever you're given in that hour—it's not you speaking, but the Holy Spirit. Saa su ñu leen jàppee nag, dëj leen ci péncum layoo, buleen jàq ci li ngeen wara wax; li ngeen jot ca waxtu woowa waxleen ko, ndaxte du yéenay wax waaye Xel mu Sell mi.
12 Brother will betray brother to death, father his child. Children will rise against parents and have them put to death. «Mag dina joxe rakkam cig dee, baay joxe doomam; ay doom it dinañu jóg, di bañ seeni waajur, di leen reylu.
13 All will hate you for my name, but whoever endures to the end will be saved. Te ñépp dinañu leen bañ ndax sama tur; waaye ku muñ ba ca muj ga, mucc.
14 When you see the abomination of desolation standing where it should not be (reader, take note), those in Judea must flee to the mountains. «Bés baa ngi ñëw, bu li ñuy wax “Lu araam luy yàqe” tegee ca bérab bu mu yelloowul; kiy jàng, na xam. Bu ngeen gisee loolu nag, ku nekk ci biir diiwaanu Yude, nanga daw ca tund ya.
15 Let no one on the housetop go down or enter the house to take anything out. Ku nekk ci kaw taax mi, bul wàcc ngir dugg kër gi, fab say yëf ya fa nekk.
16 Let no one in the field go back to get their coat. Ku nekk ci tool bi, bul ñibbi ngir fab sa mbubb.
17 How dreadful it will be in those days for pregnant women and nursing mothers! Ngalla jigéen ñi ëmb ca bés yooya, ngalla it ñiy nàmpal.
18 Pray that it will not happen in winter, Ñaanleen ngir seen gàddaay baña tase ak jamonoy seddaayu lolli.
19 for those days will bring suffering unmatched since our Father created the world until now—and never to be matched again. Ndaxte booba dina am metit wu réy wu masula am, ba àddina sosoo ak tey, te dootul am mukk.
20 Had the Sovereign not shortened those days, no one would survive; but the Sovereign shortened them for the elect he chose. Te bu fekkul woon Boroom bi wàññi bés yooyu, kenn du mucc, waaye fekk na mu wàññi leen ndax gaayam ñi mu tànn.
21 Then if anyone tells you, 'Look, here is the Christ!' or 'Look, there!' don't believe it. «Booba nag, bu leen kenn waxee: “Kaayleen gis, Kirist a ngi fi,” mbaa: “Xool-leen, mu nga fale,” buleen ko gëm.
22 False christs and false prophets will appear, performing signs and wonders to deceive the elect, if possible. Ndaxte ñiy mbubboo turu Kirist ak ñiy mbubboo turu yonent, dinañu feeñ, di joxe ay firnde yu réy ak ay kéemaan, ba ciy nax sax ñi Yàlla tànn, su loolu manoona am.
23 So be on your guard; I have told you everything ahead of time. Wax naa leen ko lu jiitu. Kon nag moytuleen.
24 But in those days, after that suffering, the sun will darken, and the moon will not give its light; «Waaye booba, gannaaw metit yooyu: “Jant bi dina lëndëm te weer dootul leer;
25 the stars will fall from the sky, and the powers in the heavens will be shaken. biddiiw yi di daanoo asamaan, te kàttani asamaan yiy yëngu.”
26 Then they will see the Son of Man coming in clouds with great power and glory. «Noonu dees na gis Doomu nit ki ñëw ci niir yi, ànd ak kàttan ak ndam lu réy.
27 He will send his angels and gather his chosen from the four winds, from earth's ends to heaven's ends. Dina yónni ay malaakaam, ñu dajale ñi mu tànn ci ñeenti xébla yi, fa àddina dale, ba fa asamaan yem.»
28 Learn this from the fig tree: once its branch softens and leaves sprout, you know summer is near. Yeesu teg ca ne: «Jàngleen misaalu garabu figg ga. Boo xamee ne ay bànqaasam duy nañu, tey xobam sëq, xam ngeen ne nawet jege na.
29 So also, when you see these things happening, know it's near, at the door. Noonu itam bu ngeen gisee loolu lépp xew, xamleen ne jege na; mu ngi ci bunt bi sax.
30 Truly I tell you, this generation will certainly not pass away until all these things have happened. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, niti jamono jii duñu wéy, te loolu lépp amul.
31 Heaven and earth will pass away, but my words will never pass away. Asamaan ak suuf dinañu wéy, waaye samay wax du wéy mukk.
32 But no one knows that day or hour—not the angels in heaven, not the Son, only the Father. «Waaye bés boobu ak waxtu woowu, kenn xamul kañ lay doon; du malaaka yi ci kaw, du sax Doom ji, waaye Baay bi rekk moo ko xam.
33 Be on guard! Stay alert! For you do not know when that time will come. Moytuleen te xool! Xamuleen kañ la waxtu wi di jot.
34 Like a man on a journey: he leaves his house, gives his servants authority—each his own task—and orders the doorkeeper to stay alert. «Mi ngi mel ni nit ku tukki, mu dénk këram ay surgaam, ku nekk ak sa sas, te sant bëkk-néeg bi, mu xool.
35 So stay alert, since you don't know when the master of the house comes—evening, midnight, rooster's crow, or dawn. Yéen nag xool-leen, ndaxte xamuleen kañ la boroom kër gi di délsi, muy ci timis mbaa ci xaaju guddi, muy ci fajar mbaa njël.
36 Otherwise, if he comes suddenly, he may find you sleeping. Bu nee jalañ, bumu leen bett, ngeen di nelaw.
37 What I say to you, I say to everyone: Keep watch!" Li ma leen wax, ñépp laa ko wax: “Xool-leen!”»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]