Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Mark 12 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 He began speaking to them in parables: "A man planted a vineyard, fenced it in, dug a winepress pit, built a watchtower, rented it to farmers, and left. Noonu Yeesu daldi leen wax ciy léeb. Mu ne leen: «Amoon na fi nit ku jëmbët toolu reseñ. Mu ñag tool bi, gas pax ngir nal ci reseñ yi, tabax wottukaay, ba noppi batale ko ay beykat, daldi tukki.
2 At harvest time he sent a servant to the tenants to collect some of the vineyard's fruit. «Bi tool bi ñoree nag, mu yónni surga ci ñoom, ngir jot wàllam ci meññeef gi.
3 But they seized him, beat him, and sent him away empty-handed. Waaye ñu jàpp ko, dóor ko ay yar, dàq ko, mu dellu ak loxoy neen.
4 Again he sent them another servant; they hit him on the head and dishonored him. Mu yónniwaat beneen surga, waaye ñu dóor ko ci bopp, toroxal ko.
5 And he sent another, and they killed him—then many more, beating some and killing others." Mu yónneeti beneen surga, ñu rey ko. Mu yónni ñeneen ñu bare, ñii ñu dóor leen, ñii ñu rey.
6 He had still one, a beloved son; last he sent him to them, saying, "They will respect my son." «Noonu mu dese ko kenn rekk, di doomam ji mu bëgg. Mujj mu yónni ko naan: “Xëy na ñu weg sama doom.”
7 "But the tenants said to each other, 'This is the heir. Come, let's kill him—the inheritance will be ours.' Waaye beykat yi daldi ne ci seen biir: “Kii moo wara donn tool bi; nan ko rey, moom ndono li.”
8 So they took him and killed him and threw him out of the vineyard. Ñu jàpp ko nag, rey, sànni ci biti.»
9 So what will the vineyard's owner do? He'll come, destroy the tenants, and give the vineyard to others. Noonu Yeesu laaj leen: «Boroom tool bi nag, lu muy def? Xanaa ñëw, rey beykat ya, dénk tool ba ñeneen.
10 Have you not read this Scripture: 'The stone the builders rejected has become the cornerstone; Ndax masuleena jàng wax jii ci Mbind mi? “Doj wi tabaxkat yi sànni, mujj na di doju koñ;
11 this was our Father's doing, and it is marvelous in our eyes'?" ci Boroom bi la loolu jóge, te yéemu nanu ci.”»
12 They wanted to arrest him but feared the crowd, knowing he'd told the parable against them. So they left him and went away. Noonu kilifa yi di wut pexem jàpp ko, ndaxte xam nañu ne ñoom lay wax. Waaye ragal nañu mbooloo mi, ba ñu bàyyi ko fa, dem.
13 They sent some of the Pharisees and Herodians to trap him in his words. Bi loolu amee ñu yónni ci Yeesu ay Farisen ak ñu far ak buur bi Erodd, ngir fiir ko ci waxam.
14 They came and said to him, "Teacher, we know you're true and don't care what anyone thinks, since you don't judge by appearance but truly teach our Father's way. Is it lawful to pay taxes to Caesar, or not? Should we pay, or should we not?" Ñu ñëw ci moom nag ne ko: «Kilifa gi, xam nanu ne ku wóor nga, te ragaloo kenn, ndaxte seetuloo jëmmi nit, waaye dangay xamle yoonu Yàlla ci bu wóor. Wax nu, ndax jaadu na, nu fey buur bi Sesaar galag am déet? Nu fey ko walla nu bañ koo fey?»
15 But, knowing their hypocrisy, he said to them, "Why are you testing me? Bring me a silver coin to look at." Waaye Yeesu xam na seen naaféq, mu ne leen: «Lu tax ngeen bëgg maa fiir? Indil-leen ma posetu denariyon, ma seet.»
16 They brought one, and he asked them, "Whose image and inscription is this?" They told him, "Caesar's." Ñu jox ko poset bi. Noonu Yeesu laaj leen: «Kan lañu ci def nataalam ak turam?» Ñu ne ko: «Sesaar.»
17 Jesus told them, "Give to Caesar what's Caesar's, and to our Father what's our Father's." They were amazed at him. Noonu Yeesu ne leen: «Joxleen nag Sesaar li Sesaar moom, te jox Yàlla li Yàlla moom.» Ñu daldi waaru ci mbiram.
18 And the Sadducees came to him, who say there is no resurrection. And they questioned him, saying, Gannaaw loolu ay Sadusen ñëw ci moom, ngir laaj ko lenn. Sadusen yi nag gëmuñu ne ndekkite am na.
19 "Teacher, Moses wrote for us that if a man's brother dies leaving a wife but no child, the brother must marry her and raise up offspring for him. Ñu ne ko: «Kilifa gi, Musaa bindal na nu ne, ku magam faatu, te bàyyiwul doom ak soxnaam, kooku war na donn jigéen ji, ba yékkati giiru magam.
20 There were seven brothers; the first married, and when he died, left no children. «Amoon na fi nag juróom ñaari góor, ñu bokk ndey ak baay. Taaw ba takk jabar, faatu, te bàyyiwul doom.
21 And the second married her, and he died leaving no children. And the third likewise. Ñaareel ba takk jigéen ja, faatu moom itam te bàyyiwul doom. Ñetteel bi it noonu.
22 And none of the seven left any children. Last of all the woman also died. Mbir mi dem na nag, ba juróom ñaar ñooñu ñépp dem, te kenn bàyyiwu fi doom. Mujj jigéen ja faatu moom itam.
23 At the resurrection, when they rise, whose wife will she be? The seven had her as wife." Ci ndekkite li nag kan ci ñoom moo ko wara donn, fekk ku nekk ci juróom ñaar ñi mas na koo takk?»
24 Jesus said to them, "Isn't this why you're wrong—you know neither the Scriptures nor our Father's power? Yeesu ne leen: «Mbaa du dangeena nekk cig réer, ci li ngeen xamul Mbind mi mbaa kàttanu Yàlla?
25 For when the dead rise, they neither marry nor are given in marriage, but are like the angels in heaven. Ndaxte keroog ndekkite li kenn du am jabar, kenn du am jëkkër, waaye dinañu mel ni malaaka yi ci kaw.
26 About the dead being raised, haven't you read in Moses' book, in the passage about the bush, how our Father told him, 'I am the God of Abraham, of Isaac, and of Jacob'? Te sax li jëm ci mbirum ndekkite, xanaa jànguleen lii Yàlla wax ci Tawreetu Musaa ci saarum ngarab si: “Maay Yàllay Ibraayma, Isaaxa ak Yanqóoba”?
27 He is not God of the dead, but of the living. You are badly mistaken." Li ci génn mooy, nekkul Yàllay ñi dee, waaye Yàllay ñiy dund la. Kon sóobu ngeen cig réer.»
28 One scribe approached, heard them debate, saw Jesus answered well, and asked, "Which commandment is most important of all?" Bi ñuy werante, benn xutbakat ñëw, dégg seen waxtaan, gis ne Yeesu tontu na leen tont lu leer. Mu laaj ko nag: «Ci ndigal yi, ban moo ci gëna màgg?»
29 Jesus answered, "The most important is this: 'Hear, Israel: our Father is one.' Noonu Yeesu ne ko: «Bii: “Dégluleen, yéen bànni Israyil! Yàlla sunu Boroom mooy Boroom bi, te kenn la.
30 Love your Father with all your heart, with all your soul, with all your mind, with all your strength." Kon nanga bëgg Yàlla sa Boroom ak sa xol bépp ak sa bakkan bépp, sa xel mépp ak sa kàttan gépp.”
31 "The second is this: 'Love your neighbor as yourself.' No commandment is greater than these." Te ñaareel bi, lii la: “Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp.” Ndigal yii ñoo sut yépp.»
32 The scribe said to him, "Well said, Teacher. You've said truly that he is one, and there's no other besides him. Xutbakat bi ne ko: «Waaw, kilifa gi, li nga wax dëgg la: Yàlla kenn la, te amul jeneen Yàlla ju dul moom.
33 Loving him with all the heart, all the understanding, all the strength, and loving one's neighbor as oneself, matters far more than all whole burnt offerings and sacrifices." Te nga bëgg ko ak sa xol bépp ak sa xel mépp ak sa kàttan gépp moo dàq bépp sarax bu ñuy yóbbu ngir màggal Yàlla ak bu ñuy lakk ca sarxalukaay ba.»
34 Seeing he answered wisely, Jesus said to him, "You are not far from the kingdom of our Father." After that, no one dared ask him any more questions. Bi Yeesu gisee nag ne tontu na ak xel, mu ne ko: «Sorewuloo nguuru Yàlla.» Bi mu waxee loolu, kenn ñemeetu koo laaj dara.
35 Teaching in the temple, Jesus asked, "How can the scribes say the Christ is the son of David? Bi nga xamee ne Yeesu ma nga doon jàngle ca kër Yàlla ga, mu laaj nit ñi: «Lu tax xutbakat yi di wax ne, Almasi bi mooy sëtu Daawuda?
36 David himself said by the Holy Spirit: 'Our Father said to my Lord, "Sit at my right hand until I put your enemies under your feet."' Daawuda moom wax na ci kàttanu Xel mu Sell mi naan: “Boroom bi nee na sama Boroom: ‘Toogal ci sama ndijoor, ba kera may daaneel say noon ci sa kanam.’ ”
37 "David himself calls the Christ Lord. How can the Christ be David's son?" The large crowd enjoyed listening to him. Gannaaw Daawuda nag wooye na ko: “Boroom bi,” nu muy nekke sëtam?» Noonu mbooloo mu mag mi di ko déglu ak bànneex.
38 And in his teaching he said, "Beware of the scribes, who like walking in long robes and being greeted in the marketplaces, Bi Yeesu di jàngle nag, mu ne leen: «Moytuleen xutbakat yi; dañoo bëgg di doxantu, sol ay mbubb yu réy, te ñépp di leen nuyoo ñaari loxo ci pénc mi.
39 and to have the best seats in the synagogues and the places of honor at banquets, Ci jàngu yi, féete kanam lañuy wut, te toogu yu yiw lañuy taamu ci reeri xew yi.
40 who devour widows' houses and make long prayers just for show. These will receive the greater condemnation." Ñu ngi lekk alalu jigéen ñi seeni jëkkër faatu, di ñaan Yàlla ay ñaani ngistal yu gudd. Seen mbugal dina gëna tar.»
41 Sitting across from the treasury, he watched the crowd drop coins in; many rich people dropped in large sums. Noonu Yeesu toog ca kër Yàlla ga, janook ndab, yi ñuy def sarax ngir Yàlla, muy xool nit ña cay dugal seen xaalis. Am nag ay boroom alal yu ci di def xaalis bu bare.
42 And a poor widow came and put in two small copper coins, worth a penny. Gannaaw ga daal benn jigéen ju jëkkëram faatu, te mu ñàkk, ñëw, def ci ñaari poseti xànjar, yu matul sax dërëm.
43 Calling his disciples, he said, "Truly, I tell you, this poor widow put in more than all who put into the offering box. Bi ko Yeesu gisee, mu woo taalibe yi ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, li jigéen ju ñàkk jee dugal ca defukaay ya moo ëpp maana alalu ñeneen ñi ñépp.
44 For they all gave from their surplus, but she gave from her poverty—all she had, her whole livelihood." Ñoom ñépp dañu sàkk ci seen barele, waaye moom dafa sàkk ci néewleem, ba far ko joxe lépp, toog.»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]