Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Ruth 3 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Then her mother-in-law Naomi said, "My daughter, shouldn't I seek a home for you, so it goes well for you? Gannaaw gi Nawmi, gorob Ruut ba, dafa wax Ruut ne ko: «Doom, tee ma laa sàkkal fooy ame jàmm, nga féete fa?
2 Isn't Boaz, whose young women you were with, our relative? Tonight he winnows barley at the threshing floor. Bowas mii nga nekkoon aki surgaam yu jigéen, du mbokk lenqe la? Guddig tey jii kat Bowas dina jériji peppum lors ca dàgga ja.
3 Wash, perfume yourself, put on your cloak, and go down to the threshing floor. Don't reveal yourself to the man until he finishes eating and drinking. Kon nag sangul, solu ba jekk, xeeñu, dem ca dàgga ja. Bu ko feeñu nag te lekkul, ba naan ba noppi.
4 When he lies down, note the place; go uncover his feet and lie down—he'll tell you what to do." Bu demee ba tëdd, nanga nemmiku fa mu tëdd. Su ko defee nga àgg ba foofa, muri fa féeteek tànk ya, tëdd. Moom dina la xamal li nga wara def.»
5 And Ruth said to her, "All that you say I will do." Mu ne ko: «Baax na, loolu rekk laay def.»
6 So she went down to the threshing floor and did everything her mother-in-law had told her. Ba mu ko defee mu dem ca dàgga ja, daldi def la ko goroom wax lépp.
7 Boaz ate, drank, and felt good, then lay down at the end of the grain heap. She came secretly, uncovered his feet, and lay down. Bowas lekk, naan ba xolam sedd, doora dem tëdd ca peggub jalu pepp ba. Ruut jegesi ndànk, muri fa féeteek tànk yi, tëdd.
8 At midnight the man was startled, turned over, and there lay a woman at his feet! Ñu dem ba xaaju guddi, góor gi jekki ne bërét, toog, yem ci ndaw si tëdd fi féeteeki tànkam.
9 "Who are you?" he asked. "I am Ruth, your servant," she said. "Spread your cloak's corner over your servant, for you are a redeemer." Mu ne: «Kii ku mu?» Mu ne: «Man a Ruut, sang bi. Yiire ma sa mbubb, ndax mbokk nga, te jotkat nga.»
10 He said, "Blessed are you by our Father, my daughter. This last kindness is better than the first, since you didn't chase young men, poor or rich. Mu ne ko: «Yal na la Aji Sax ji barkeel, doom! Jiwati nga bokk gi ngor lu gënatee rafet. Ndax su la neexoon, nga topp ci xale yu góor yi, ñu am ak ñu ñàkk.
11 Now, my daughter, don't be afraid. I'll do all you ask, for my whole town knows you're a worthy woman. Léegi nag neel tekk rekk, doom. Loolu nga ñaan lépp, dinaa la ko defal, ndax waa dëkk bi bépp xam nañu ne jigéen ju jàmbaare nga.
12 Now it is true that I am a redeemer, yet there is a redeemer nearer than I. Da di nag, dëgg la sax, mbokk laa mu la mana jotaat, waaye meneen mbokk mu la mana jotaat a ngi fi, te moo ma ci gëna yey.
13 Stay tonight. In the morning, if he'll redeem you—good, let him redeem. If not, as our Father lives, I will redeem you. Lie down until morning." Dangay fanaan fii. Bu ëllëgee, su fekkee ne nangu naa def warugaram ci yaw, na ko def, baax na. Su nanguwul nag, dogu naa ci Aji Sax ji, Kiy dund, man dinaa ko def. Tëddal fii rekk, ba njël jot.»
14 She lay at his feet until morning, rose before anyone was recognizable, for he said, "No one may know a woman came to the threshing floor." Ba loolu amee mu tëdd fa féeteek tànki Bowas, ba njël jot, mu jóg balaa waxtu wu nit mana xàmmee moroomam. Booba Bowas bëgguloon ñu xam ne ndaw si ñëw na ci dàgga ji.
15 He said, "Bring the shawl you're wearing; hold it out." She held it out. He measured six portions of barley, put it on her, and went into the city. Mu ne ko: «Tàllalal malaan mi nga sàngoo, te téye ko bu baax.» Mu tàllal malaan ma, mu sotti ca juróom benni natti peppum lors, yen ko ko, doora dem ca dëkk ba.
16 When Ruth came to her mother-in-law, Naomi asked, "How did it go, my daughter?" She told her all the man had done for her. Naka la àgg ca goroom Nawmi, mu ne ko: «Doom, koo doon nag?» Ruut nettali ko na góor gi def ak moom yépp,
17 She said, "He gave me these six measures of barley, saying, 'Don't return to your mother-in-law empty-handed.'" daldi cay teg ne ko: «Juróom benni natti lors yii, moo ma ko may, ne ma duma dellu loxoy neen ca sama goro.»
18 Naomi said, "Wait, my daughter, until you know the outcome, for the man won't rest until he settles it today." Mu ne ko: «Yaw kay neel tekk fii rekk, doom, ba xam nu mbir miy mujje. Waa jii du toog te toppatoowul mbir mii tey, ba mu leer.»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]