Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Ruth 2 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Naomi had a relative through her husband, a prominent, wealthy man from Elimelech's clan, named Boaz. Nawmi nag amoon na wóllërey jëkkëram, di góor gu ñuy wax Bowas, bokk ci làngu Elimeleg, di ku am daraja.
2 Ruth the Moabite said to Naomi, "Let me glean grain behind anyone who favors me." She said, "Go, my daughter." Mu am bés Ruut, ndawas Mowab sa, ne Nawmi: «Tee maa dem tool, ndax ma gis boog ku ma laaye biir, ma mana raasaatu gub yu des ca gannaawam?» Mu ne ko: «Waaw, demal, doom.»
3 So she went out and gleaned behind the harvesters, and she happened to come to the field belonging to Boaz, of Elimelech's family. Mu dem ca tool ya, topp ñay góob, di raasaatu. Yàlla-woo-yàlla, tool booba di toolu Bowas ma bokk ak Elimeleg.
4 Just then Boaz came from Bethlehem, telling the harvesters, "May our Father be with you." "Our Father bless you," they replied. Nes tuut Bowas ne jalañ, jóge Betleyem. Mu nuyook ñay góob ne leen: «Jaagéenjëf waay, yal na Aji Sax ji ànd ak yeen.» Ñu fey ko ne ko: «Jaajëf sa wàll, yal na la Aji Sax ji barkeel.»
5 Then Boaz said to his foreman, "Whose young woman is this?" Mu laaj ka jiite ngóob ma, ne ko: «Ndaw sii fu mu bokk?»
6 The foreman answered, "She's the young Moabite woman who returned with Naomi from Moab's country. Mu ne ko: «Mooy waa Mowab ba Nawmi àndal, jóge Mowab, ñibbisi.
7 She said, 'Please let me glean and gather among the sheaves behind the harvesters.' She came and has stayed from morning till now, resting only briefly in the shelter." Dafa ñaan ñu may ko, mu topp ci ñiy góob, di raasaatu ci gub yi ñuy rotle. Ci suba la ñëw di liggéey ba nëgëni; noppaluwul lu moy diir bu gàtt ci mbaar mi.»
8 Boaz said to Ruth, "Listen, my daughter. Don't glean in another field or leave here; stay close to my young women. Bowas nag ne Ruut: «Doom, ma ne, bul raasaatuji ci beneen tool bu dul bii. Bul wees fii. Toogal fii ci samay surga yu jigéen.
9 Watch the field they harvest and follow behind them. I've told the young men not to touch you. When thirsty, drink from the jars the young men filled." Xoolal bu baax fi xale yu góor yiy góobe, te nga topp fa jigéen ñi. Dinaa wax xale yu góor yi ne leen buñu la sonal. Soo maree, demal naan ca njaq ya góor ñi duy.»
10 She bowed facedown to the ground and asked him, "Why have I found favor in your eyes that you notice me, a foreigner?" Naka la wax loolu, mu sujjóot, dëpp jëëm fa suuf, ne ko: «Xanaa su la neexoon de, doo ma nemmiku sax, ndax ab doxandéem laa, waxatuma nga di ma laaye nii biir!»
11 Boaz answered, "I've heard all you did for your mother-in-law since your husband died—how you left your father, mother, and homeland to come to a people you didn't know before. Mu ne ko: «Dégg naa bu baax li nga defal sa goro lépp, te fekk sa jëkkër faatu, ak ni nga wonee gannaaw sa ndey ak sa baay ak sa réewum cosaan, ba ñëw dëkksi ci biir xeet woo xamuloon démb ak bërki-démb.
12 May our Father repay your deed; may our Father, the God of Israel, under whose wings you've come for refuge, reward you fully." Yal na la Aji Sax ji fey sa jëf. Aji Sax ji Yàllay Israayil ji nga làqusi ci kiiraayam, yal na la yool, ba mu mat sëkk.»
13 "May I find favor in your eyes, my lord," she said, "for you've comforted me and spoken kindly to your servant, though I'm not one of your servants." Ruut ne ko: «Teral nga ma de, sang bi. Yaa ngi may laaye biir, ndaxte dëfal nga ma, wax ma lu seral sama xol, te moona say surga yu jigéen yi sax a ma gën.»
14 At mealtime Boaz said, "Come here, eat some bread, dip your piece in the wine vinegar." She sat beside the harvesters; he passed her roasted grain. She ate her fill and had some left. Ba añ jotee, Bowas ne Ruut: «Kaay, sàkk ci mburu mi ak ñeex mi.» Mu daldi toog, feggook ñay góob; Bowas may ko mbool, mu lekk ba suur, ba desal.
15 When she rose to glean, Boaz ordered his young men, "Let her glean even among the sheaves; don't shame her. Naka la jóg, di raasaatuji, mu sant ay surgaam, ne leen: «Bu doon raasaatu ci biir sabaar yi sax, buleen ko ñàkke kersa.
16 Instead, pull stalks from the bundles for her and leave them for her to pick up, and don't correct her." Roccilleen koo roccil ci takk yi, bàyyi ko mu for, te buleen ko gëdd.»
17 She gleaned in the field till evening, then beat out what she'd gathered—about twenty quarts of barley. Ba loolu amee, Ruut di raasaatu ba ngoon jot, mu bàcc la mu raasaatu ci peppum lors, mu doon lu tollook fanweeri kilo.
18 She carried it to town; her mother-in-law saw how much she'd gleaned. She also brought out and gave her what she'd saved after eating her fill. Mu yóbbu ko ba ca dëkk ba, goroom gis la mu raasaatu, mu daldi yebbi la desoon ca añam, jox ko.
19 Her mother-in-law asked, "Where did you gather today? Where did you work? Blessed be the man who noticed you!" Ruth named whose field: "The man I worked with today is Boaz." Goro ba ne ko: «Foo raasaatoo lii lépp tey? Ban tool nga doon liggéeye sax? Ki la nemmikoo nii de, yal na barkeel!» Ruut nag wax goroom ka mu doon liggéeye toolam, ne ko: «Ka ma doon liggéeye toolam de, Bowas lañu koy wax.»
20 Naomi told her daughter-in-law, "May our Father bless him, whose kindness hasn't left the living or the dead." She added, "He's a close relative, one of our redeemers." Nawmi ne Ruut: «Yal na Aji Sax ji barkeel Bowas, moom mi saxoo sàmm ngoram digganteem ak nit, muy kuy dund walla ku dee!» Mu teg ca ne ko: «Kooku ku nu jege la; bokk na ci ñi nekk sunu jotkat.»
21 Then Ruth the Moabite said, "He even told me, 'Stay with my workers until they finish all my harvest.'" Ruut ndawas Mowab sa ne: «Moom de da ma ne sax, ma topp ciy surgaam, ba ngóobam mépp daj.»
22 Naomi told her daughter-in-law Ruth, "Good, my daughter—go out with his young women, so you won't be harmed in another field." Mu ne ko: «Waaw kay, doom, toppal ci surgay Bowas yu jigéen rekk, bala ñu laa soxore ci beneen tool.»
23 She stayed close to Boaz's young women, gleaning until the barley and wheat harvests ended, and lived with her mother-in-law. Noonu la Ruut ànde ak surgay Bowas yu jigéen, topp ci ñoom di raasaatu, ba keroog ngóobum lors baak bele ba lépp jeex. Mu toog nag ak goroom.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]