Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Ruth 1 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 When the judges ruled, a famine struck the land, and a man from Bethlehem in Judah went with his wife and two sons to stay a while in the fields of Moab. Ba njiit ya daan àtte faloo ca Israayil, jamono jooju dafa amoon xiif ca réew ma. Jenn waay bàyyikoo Betleyem ca diiwaanu Yuda, ànd ak soxnaam ak ñaari doomam yu góor, ñu toxuji ca réewum Mowab.
2 The man was named Elimelech, his wife Naomi, and his two sons Mahlon and Chilion—Ephrathites from Bethlehem in Judah. They went to the territory of Moab and stayed there. Waa ja Elimeleg la tuddoon, soxnaam di Nawmi, ñaari doomam yu góor ya di Maxlon ak Kilyon. Ay Efrateen lañu, cosaanoo Betleyem ca Yuda. Ñu agsi ca réewum Mowab, daldi sanc foofa.
3 Then Elimelech, Naomi's husband, died, and she was left with her two sons. Gannaaw gi, Elimeleg jëkkëru Nawmi faatu; Nawmi des ak ñaari doomam yu góor.
4 They married Moabite women—Orpah and Ruth—and lived there about ten years. Ñooñu mujj jël ay jigéeni Mowab soxna; kenn ka di Orpa, ka ca des di Ruut. Ba ñu nekkee foofa lu tollu ci fukki at,
5 Both Mahlon and Chilion also died, and Naomi was left without her two children and husband. ñoom ñaar ñooñu di Maxlon ak Kilyon faatu ñoom it, jigéen ja ñàkk noonu ñaari doomam ak jëkkëram. Mu des moom kese.
6 In Moab's fields, Naomi heard that our Father had attended his people, giving them food, so she set out with her two daughters-in-law to return from there. Ba loolu amee Nawmi fabu, mook goroom ya, ngir jóge réew ma. Booba fekk na mu dégge ca Mowab ne Aji Sax ji xettali na ñoñam, ba may leen ab dund.
7 She left the place where she had been, with her two daughters-in-law, and they went on the road back to the land of Judah. Ma nga jóge fa mu dëkkoon, ànd ak ñaari goroom ya, ñu tegu ca yoon wa, jëm Yuda.
8 Naomi told her two daughters-in-law, "Return, each to your mother's home. May our Father deal kindly with you, as you dealt with the dead and with me. Ci biir loolu mu wax ak ñaari goro ya, ne leen: «Demleen kay, ñibbileen, ku nekk sa kër yaay. Yal na leen Aji Sax ji baaxe, na ngeen baaxe woon ñi wuutu, te baaxe ma, man itam.
9 May our Father give each of you rest in another husband's home." Then she kissed them, and they wept aloud. Yal na Aji Sax ji may ku nekk ci yeen jàmm ca kër jëkkër ja muy amaat.» Ci kaw loolu mu fóon leen, ñu ne yikkét jooyoo.
10 And they said to her, "No—we will return with you to your people." Ñu ne ko: «Déet, yaw kay lanuy àndal, dem ca say bokk.»
11 Naomi said, "Go back, my daughters. Why go with me? Do I have more sons in my womb to become your husbands? Mu ne leen: «Ñibbileen ngalla, doom, lu ngeen di ànd ak man doye? Ndax dama leena manatee jural ay jëkkër ci sama biir bii?
12 Return, my daughters, go, for I'm too old to marry. Even if I said there's still hope, even if I had a husband tonight and bore sons, Ñibbileen rikk doom, demleen, ngir man damay mag, ba wees séy; te su ma ci dese woon yaakaar it, guddig tey jii sax su ma ci séyoon, jur ciy doom,
13 would you wait for them until grown? Would you stay unmarried for them? No, my daughters—it's far more bitter for me than you, since our Father's hand has turned against me." mbaa dingeen leen mana xaar, ba ñu màgg? Xanaa dungeen toog, baña séy ndax ñoom? Déedéet, doom. Maa leen ëpp naqar, man mi Aji Sax ji nattoo nii.»
14 At this they wept aloud again. Then Orpah kissed her mother-in-law goodbye, but Ruth clung to her. Ñu dellu ne yikkét, di jooyoo. Orpa fóon goroom, tàggatook moom, Ruut nag moom langaamu ko rekk.
15 Naomi said, "Look, your sister-in-law went back to her people and her gods. Go back with her." Mu ne ko: «Gis nga sa wujju peccorgo waa ngay ñibbi cay bokkam aki yàllaam. Àndal ak moom ñibbi kay!»
16 Ruth said, "Don't push me to leave you or turn back from following you. Where you go, I'll go; where you stay, I'll stay. Your people will be my people, and your God my God. Mu ne ko: «Bu ma soññ mukk ci loolu, duma la wacc, duma la dëddu. Foo jëm, fa laa jëm; fooy dal, fa laay dal; say bokk di saay bokk; sa Yàlla di sama Yàlla.
17 Where you die I will die, and there I will be buried. May our Father punish me ever so severely if anything but death separates you and me." Foo deewe it, ma deewe fa, ñu denc ma fa. Yal na ma Aji Sax ji teg mbugal mu gëna tar, ndegam lenn lu moy dee tàggale na maak yaw.»
18 When Naomi saw that Ruth was determined to go with her, she said no more to her. Nawmi nag gis ni Ruut dogoo ci ànd ak moom, ba tax soññatu ko.
19 So both of them traveled until they reached Bethlehem. When they entered Bethlehem, the whole town stirred over them, and the women said, "Is this Naomi?" Ba mu ko defee ñu ànd ñoom ñaar, ba àgg Betleyem. Naka lañu àgg Betleyem, dëkk ba bépp ne kër-kër, ne këpp ndax ñoom. Jigéen ña naa: «Xanaa kii kay du Nawmi?»
20 "Don't call me Naomi," she said. "Call me Mara—the Almighty has dealt very bitterly with me. Mu ne leen: «Buleen ma ne Nawmi (muy firi Boroom mbégte mi), neleen ma Mara (muy firi Boroom naqar wi), ndax Aji Man ji da maa teg naqar wu réya réy.
21 I went away full, but our Father has brought me back empty. Why call me Naomi, when our Father has afflicted me and the Almighty has brought misfortune upon me?" Maa demoon ak loxo yu ne gadd, Aji Sax ji delloosi maak loxoy neen. Kon lu ngeen may woowe Nawmi doye, te Aji Sax ji àtte ma ñàkkal? Ndax kat Aji Man ji ci njàqare la ma tàbbal!»
22 So Naomi returned from the fields of Moab with Ruth the Moabite, her daughter-in-law, who came back with her. They reached Bethlehem as barley harvest began. Noonu la Nawmi jógee Mowab, ñibbisi, ànd ak Ruut, gorob Mowabeenam ba. Ñu agsi Betleyem, fekk ngóobum lors ma di tàmbali.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]