1When Moses finished setting up the tabernacle, he anointed and dedicated it and all its furnishings, the altar and all its utensils, anointing and dedicating them.RWBTKeroog ba Musaa sampee jaamookaay bi ba noppi, diw na ko ngir sellal ko, mook mboolem ay jumtukaayam, sarxalukaay beek mboolem ndabam it, mu boole diw, sellale ko.
2Then Israel's leaders—heads of their fathers' houses, the tribal leaders in charge of the census—brought an offering.RWBTBa loolu amee kilifay Israayil yi jiite seeni kër maam dikk. Ñooñoo doon njiiti giir yi te ñoo doon saytu limeefu nit ñi.
3They brought their offering before our Father: six covered wagons, twelve oxen—a wagon per two leaders, an ox for each—then presented them before the tabernacle.RWBTÑu indil Aji Sax ji seen sarax, muy juróom benni watiir ak fukki nag ak ñaar; ñaari kilifa yu nekk, benn watiir; kilifa gu nekk, wenn nag, ñu yóbbu lépp fa kanam jaamookaay ba.
4And our Father said to Moses,RWBTAji Sax ji wax Musaa,
5"Take these from them for the tent of meeting's service; give them to the Levites, each according to his service."RWBTne ko: «Nangul lii, mu jëm ci liggéeyu xaymab ndaje mi, te nga jox ko Leween ñi, ku ci nekk ak li liggéeyam laaj.»
6So Moses took the wagons and the oxen and gave them to the Levites.RWBTMusaa nangu watiir yaak nag ya, jox Leween ñi.
7Two wagons and four oxen he gave to the sons of Gershon, according to their service.RWBTYii ñaari watiir ak ñeenti nag, mu jox Gersoneen ña, na ko seen liggéey laaje,
8He gave four wagons and eight oxen to Merari's sons, for their service, under Ithamar son of Aaron the priest.RWBTyee ñeent, mu booleek juróom ñetti nag, jox Merareen ña, na ko seen liggéey laaje, ci njiital sarxalkat ba Itamar doomu Aaróona.
9To the sons of Kohath he gave none, since the holy things' service was theirs—carried on the shoulder.RWBTKeyateen ña nag, joxu leen, ndax yu sell ya lañu sasoo woona gàddu.
10On the day the altar was anointed, the leaders brought its dedication offering; the leaders brought their offering before the altar.RWBTCi biir loolu kilifa yi indi itam saraxu daloob sarxalukaay bi, keroog bés ba ñu koy diw. Ñu daldi joxe seeni sarax fi kanam sarxalukaay bi.
11And our Father said to Moses, "Each day one leader is to bring his offering for the altar's dedication."RWBTTeewul Aji Sax ji wax Musaa, ne ko: «Kilifa yiy joxesi seen sarax, yi jëm ci daloob sarxalukaay bi, nañu ko def bés bu nekk, kenn.»
12Nahshon son of Amminadab, of Judah's tribe, presented his offering on the first day.RWBTKi joxe saraxam ci bés bu njëkk bi, ñeel giirug Yuda, mooy Naason doomu Aminadab.
13His offering: one silver plate, about three and a quarter pounds, and one silver basin, about one and three-quarter pounds, both filled with fine flour mixed with oil for a grain offering.RWBTAb saraxam di benn ndabu xaalis bu diise téeméeri siikal ak fanweer, muy kilook liibar, ak benn këllu xaalis bu diise juróom ñaar fukki siikal, ci siikal bi ñu yoonal ci néeg bu sell bi, muy juróom ñetti téeméeri garaam, lu ci nekk fees ak sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ngir saraxu pepp bi,
14One gold dish weighing about four ounces, full of incense;RWBTak senn mbàttus wurus su fees ak cuuraay te diise fukki siikal, di téeméeri garaam ak fukk ak juróom,
15one young bull, one ram, and one male lamb a year old, for a burnt offering;RWBTak wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy mu mag, ak menn kuuyu menn at, ngir saraxu rendi-dóomal,
16one male goat for a sin offering;RWBTak wenn sikket ngir saraxu póotum bàkkaar,
17for the peace offering: two oxen, five rams, five male goats, five year-old male lambs. This was Nahshon son of Amminadab's offering.RWBTak saraxas cant gi ci biir jàmm, di ñaari yëkk ak juróomi kuuy yu mag ak juróomi sikket, ak juróomi kuuyu menn at. Looloo doon saraxu Naason doomu Aminadab.
18On the second day Nethanel son of Zuar, the leader of Issachar, presented an offering.RWBTBésub ñaareel ba, kilifag Isakareen ña, Netaneel doomu Cuwar moo indi saraxam,
19His offering: one silver plate weighing about three and a quarter pounds, one silver bowl weighing about one and three-quarter pounds, both filled with fine flour mixed with oil for a grain offering.RWBTsarax ba mu indi di benn ndabu xaalis bu diise téeméeri siikal ak fanweer, di kilook liibar, ak benn këllu xaalis bu diise juróom ñaar fukki siikal, ci siikal bi ñu yoonal ci néeg bu sell bi, muy juróom ñetti téeméeri garaam, lu ci nekk fees ak sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ngir saraxu pepp,
20One gold dish weighing about four ounces, full of incense;RWBTak senn mbàttus wurus su fees ak cuuraay te diise fukki siikal, di téeméeri garaam ak fukk ak juróom,
21one young bull, one ram, and one male lamb a year old, for a burnt offering;RWBTak wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy mu mag, ak menn kuuyu menn at, ngir saraxu rendi-dóomal,
22one male goat for a sin offering;RWBTak wenn sikket ngir saraxu póotum bàkkaar,
23for the peace offering: two oxen, five rams, five male goats, five year-old male lambs. This was Nethanel son of Zuar's offering.RWBTak saraxas cant gi ci biir jàmm, di ñaari yëkk ak juróomi kuuy yu mag ak juróomi sikket, ak juróomi kuuyu menn at. Looloo doon saraxu Netaneel doomu Cuwar.
24On the third day it was Eliab son of Helon, the leader of the sons of Zebulun.RWBTBésub ñetteel ba, kilifag Cabuloneen ña, Elyab doomu Elon moo aye,
25His offering: one silver plate weighing about three and a quarter pounds, one silver basin weighing about one and three-quarter pounds, both full of fine flour mixed with oil for a grain offering;RWBTab saraxam di benn ndabu xaalis bu diise téeméeri siikal ak fanweer, muy kilook liibar, ak benn këllu xaalis bu diise juróom ñaar fukki siikal, ci siikal bi ñu yoonal ci néeg bu sell bi, di juróom ñetti téeméeri garaam, lu ci nekk fees ak sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ngir saraxu pepp,
26one gold dish weighing about four ounces, full of incense;RWBTak senn mbàttus wurus su fees ak cuuraay te diise fukki siikal, muy téeméeri garaam ak fukk ak juróom,
27one young bull, one ram, and one male lamb a year old, for a burnt offering;RWBTak wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy mu mag, ak menn kuuyu menn at, ngir saraxu rendi-dóomal,
28one male goat for a sin offering;RWBTak wenn sikket ngir saraxu póotum bàkkaar,
29for the peace offering sacrifice: two oxen, five rams, five male goats, five male lambs a year old. This was Eliab son of Helon's offering.RWBTak saraxas cant ci biir jàmm, di ñaari yëkk ak juróomi kuuy yu mag ak juróomi sikket, ak juróomi kuuyu menn at. Looloo doon saraxu Elyab doomu Elon.
30On the fourth day it was Elizur son of Shedeur, the leader of the sons of Reuben.RWBTBésub ñeenteel ba kilifag Rubeneen ña, Elicur doomu Sedeyur moo aye,
31His offering: one silver plate, about three and a quarter pounds, and one silver basin, about one and three-quarter pounds—both full of fine flour mixed with oil for a grain offering.RWBTab saraxam di benn ndabu xaalis bu diise téeméeri siikal ak fanweer, di kilook liibar, ak benn këllu xaalis bu diise juróom ñaar fukki siikal, ci siikal bi ñu yoonal ci néeg bu sell bi, di juróom ñetti téeméeri garaam, lu ci nekk fees ak sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ngir saraxu pepp,
32One gold dish weighing about four ounces, full of incense;RWBTak senn mbàttus wurus su fees ak cuuraay te diise fukki siikal, muy téeméeri garaam ak fukk ak juróom,
33one young bull, one ram, and one male lamb a year old, for a burnt offering;RWBTak wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy mu mag, ak menn kuuyu menn at, ngir saraxu rendi-dóomal,
34one male goat for a sin offering;RWBTak wenn sikket ngir saraxu póotum bàkkaar,
35and for the peace offering sacrifice: two oxen, five rams, five male goats, five male lambs a year old. This was Elizur son of Shedeur's offering.RWBTak saraxas cant gi ci biir jàmm, di ñaari yëkk ak juróomi kuuy yu mag ak juróomi sikket, ak juróomi kuuyu menn at. Looloo doon saraxu Elicur doomu Sedeyur.
36On the fifth day it was Shelumiel son of Zurishaddai, the leader of the sons of Simeon.RWBTBésub juróomeel ba kilifag Cimyoneen ña, Selumyel doomu Curisadaay moo aye,
37His offering: one silver plate, about three and a quarter pounds, one silver basin, about one and three-quarter pounds, both full of fine flour mixed with oil for a grain offering.RWBTab saraxam di benn ndabu xaalis bu diise téeméeri siikal ak fanweer, di kilook liibar, ak benn këllu xaalis bu diise juróom ñaar fukki siikal, ci siikal bi ñu yoonal ci néeg bu sell bi, muy juróom ñetti téeméeri garaam, lu ci nekk fees ak sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ngir saraxu pepp,
38One gold dish weighing about four ounces, full of incense;RWBTak senn mbàttus wurus su fees ak cuuraay te diise fukki siikal, muy téeméeri garaam ak fukk ak juróom,
39one young bull, one ram, and one male lamb a year old, for a burnt offering;RWBTak wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy mu mag, ak menn kuuyu menn at, ngir saraxu rendi-dóomal,
40one male goat for a sin offering;RWBTak wenn sikket ngir saraxu póotum bàkkaar,
41for the sacrifice of peace offerings: two oxen, five rams, five male goats, five year-old male lambs. This was Shelumiel son of Zurishaddai's offering.RWBTak saraxas cant gi ci biir jàmm, di ñaari yëkk ak juróomi kuuy yu mag ak juróomi sikket, ak juróomi kuuyu menn at. Looloo doon saraxu Selumyel doomu Curisadaay.
42On the sixth day it was Eliasaph son of Deuel, the leader of the sons of Gad.RWBTBésub juróom benneel ba kilifag Gàddeen ña, Elyasaf doomu Dewel moo aye,
43His offering was one silver plate, about three and a quarter pounds, and one silver basin, about one and three-quarter pounds, both filled with fine flour mixed with oil for a grain offering.RWBTab saraxam di benn ndabu xaalis bu diise téeméeri siikal ak fanweer, muy kilook liibar, ak benn këllu xaalis bu diise juróom ñaar fukki siikal, ci siikal bi ñu yoonal ci néeg bu sell bi, muy juróom ñetti téeméeri garaam, lu ci nekk fees ak sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ngir saraxu pepp,
44One gold dish weighing about four ounces, full of incense;RWBTak senn mbàttus wurus su fees ak cuuraay te diise fukki siikal, muy téeméeri garaam ak fukk ak juróom,
45one young bull, one ram, and one male lamb a year old, for a burnt offering;RWBTak wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy mu mag, ak menn kuuyu menn at, ngir saraxu rendi-dóomal,
46one male goat for a sin offering;RWBTak wenn sikket ngir saraxu póotum bàkkaar,
47for the peace offering: two oxen, five rams, five male goats, five male yearling lambs. This was Eliasaph son of Deuel's offering.RWBTak saraxas cant gi ci biir jàmm, di ñaari yëkk ak juróomi kuuy yu mag ak juróomi sikket, ak juróomi kuuyu menn at. Looloo doon saraxu Elyasaf doomu Dewel.
48On the seventh day it was Elishama son of Ammihud, the leader of the sons of Ephraim.RWBTBésub juróom ñaareel ba kilifag Efraymeen ña, Elisama doomu Amiyudd moo aye,
49His offering: one silver plate, about three and a quarter pounds, and one silver basin, about one and three-quarter pounds, both filled with fine flour mixed with oil for a grain offering;RWBTab saraxam di benn ndabu xaalis bu diise téeméeri siikal ak fanweer, muy kilook liibar, ak benn këllu xaalis bu diise juróom ñaar fukki siikal, ci siikal bi ñu yoonal ci néeg bu sell bi, muy juróom ñetti téeméeri garaam, lu ci nekk fees ak sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ngir saraxu pepp,
50one gold dish weighing about four ounces, full of incense;RWBTak senn mbàttus wurus su fees ak cuuraay te diise fukki siikal, muy téeméeri garaam ak fukk ak juróom,
51one young bull, one ram, and one male lamb a year old, for a burnt offering;RWBTak wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy mu mag, ak menn kuuyu menn at, ngir saraxu rendi-dóomal,
52one male goat for a sin offering;RWBTak wenn sikket ngir saraxu póotum bàkkaar,
53for the sacrifice of peace offerings: two oxen, five rams, five male goats, five male lambs a year old. This was Elishama son of Ammihud's offering.RWBTak saraxas cant gi ci biir jàmm, di ñaari yëkk ak juróomi kuuy yu mag ak juróomi sikket, ak juróomi kuuyu menn at. Looloo doon saraxu Elisama doomu Amiyudd.
54On the eighth day it was Gamaliel son of Pedahzur, the leader of the sons of Manasseh.RWBTBésub juróom ñetteel ba kilifag Manaseen ña, Gamliyel doomu Pedacur moo aye,
55His offering: one silver plate, about three and a quarter pounds, and one silver basin, about one and three-quarter pounds, both full of fine flour mixed with oil for a grain offering.RWBTab saraxam di benn ndabu xaalis bu diise téeméeri siikal ak fanweer, muy kilook liibar, ak benn këllu xaalis bu diise juróom ñaar fukki siikal, ci siikal bi ñu yoonal ci néeg bu sell bi, muy juróom ñetti téeméeri garaam, lu ci nekk fees ak sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ngir saraxu pepp,
56One gold dish weighing about four ounces, full of incense;RWBTak senn mbàttus wurus su fees ak cuuraay te diise fukki siikal, di téeméeri garaam ak fukk ak juróom,
57one young bull, one ram, and one male lamb a year old, for a burnt offering;RWBTak wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy mu mag, ak menn kuuyu menn at, ngir saraxu rendi-dóomal,
58one male goat for a sin offering;RWBTak wenn sikket ngir saraxu póotum bàkkaar,
59for the peace offering: two oxen, five rams, five male goats, five year-old male lambs. Offering of Gamaliel son of Pedahzur.RWBTak saraxu cant gi ci biir jàmm, di ñaari yëkk ak juróomi kuuy yu mag ak juróomi sikket, ak juróomi kuuyu menn at. Looloo doon saraxu Gamliyel doomu Pedacur.
60On the ninth day it was Abidan son of Gideoni, the leader of the sons of Benjamin.RWBTBésub juróom ñeenteel ba kilifag Beñamineen ña, Abidan doomu Gidoni moo aye,
61His offering: one silver plate, about three and a quarter pounds, one silver basin, about one and three-quarter pounds, both full of fine flour mixed with oil for a grain offering.RWBTab saraxam di benn ndabu xaalis bu diise téeméeri siikal ak fanweer, muy kilook liibar, ak benn këllu xaalis bu diise juróom ñaar fukki siikal, ci siikal bi ñu yoonal ci néeg bu sell bi, muy juróom ñetti téeméeri garaam, lu ci nekk fees ak sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ngir saraxu pepp,
62One gold dish weighing about four ounces, full of incense;RWBTak senn mbàttus wurus su fees ak cuuraay te diise fukki siikal, di téeméeri garaam ak fukk ak juróom,
63one young bull, one ram, and one male lamb a year old, for a burnt offering;RWBTak wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy mu mag, ak menn kuuyu menn at, ngir saraxu rendi-dóomal,
64one male goat for a sin offering;RWBTak wenn sikket ngir saraxu póotum bàkkaar,
65for the peace-offering sacrifice: two oxen, five rams, five male goats, five yearling male lambs. This was Abidan son of Gideoni's offering.RWBTak saraxu cant gi ci biir jàmm, di ñaari yëkk ak juróomi kuuy yu mag ak juróomi sikket, ak juróomi kuuyu menn at. Looloo doon saraxu Abidan doomu Gidoni.
66On the tenth day it was Ahiezer son of Ammishaddai, the leader of the sons of Dan.RWBTBésub fukkeel ba kilifag Daneen ña, Axyeser doomu Amisadaay moo aye,
67His offering: one silver plate weighing about three and a quarter pounds, one silver basin weighing about one and three-quarter pounds, both full of fine flour mixed with oil for a grain offering.RWBTab saraxam di benn ndabu xaalis bu diise téeméeri siikal ak fanweer, muy kilook liibar, ak benn këllu xaalis bu diise juróom ñaar fukki siikal, ci siikal bi ñu yoonal ci néeg bu sell bi, muy juróom ñetti téeméeri garaam, lu ci nekk fees ak sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ngir saraxu pepp,
68One gold dish weighing about four ounces, full of incense;RWBTak senn mbàttus wurus su fees ak cuuraay te diise fukki siikal, di téeméeri garaam ak fukk ak juróom,
69one young bull, one ram, and one male lamb a year old, for a burnt offering;RWBTak wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy mu mag, ak menn kuuyu menn at, ngir saraxu rendi-dóomal,
70one male goat for a sin offering;RWBTak wenn sikket ngir saraxu póotum bàkkaar,
71for the peace-offering sacrifice: two oxen, five rams, five male goats, five male year-old lambs. This was Ahiezer son of Ammishaddai's offering.RWBTak saraxu cant gi ci biir jàmm, di ñaari yëkk ak juróomi kuuy yu mag ak juróomi sikket, ak juróomi kuuyu menn at. Looloo doon saraxu Axyeser doomu Amisadaay.
72On the eleventh day it was Pagiel son of Ochran, the leader of the sons of Asher.RWBTBésub fukkeel baak benn, kilifag Asereen ña, Pagyel doomu Okkran moo aye,
73He offered a silver plate, about three and a quarter pounds, and a silver basin, about one and three-quarter pounds, both filled with fine flour mixed with oil for a grain offering;RWBTab saraxam di benn ndabu xaalis bu diise téeméeri siikal ak fanweer, muy kilook liibar, ak benn këllu xaalis bu juróom ñaar fukki siikal, ci siikal bi ñu yoonal ci néeg bu sell bi, muy juróom ñetti téeméeri garaam, lu ci nekk fees ak sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ngir saraxu pepp,
74one gold dish weighing about four ounces, full of incense;RWBTak senn mbàttus wurus su fees ak cuuraay te diise fukki siikal, di téeméeri garaam ak fukk ak juróom,
75one young bull, one ram, and one male lamb a year old, for a burnt offering;RWBTak wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy mu mag, ak menn kuuyu menn at, ngir saraxu rendi-dóomal,
76one male goat for a sin offering;RWBTak wenn sikket ngir saraxu póotum bàkkaar,
77and for the sacrifice of peace offerings: two oxen, five rams, five male goats, five male lambs a year old. The offering of Pagiel son of Ochran.RWBTak saraxu cant gi ci biir jàmm, di ñaari yëkk ak juróomi kuuy yu mag ak juróomi sikket, ak juróomi kuuyu menn at. Looloo doon saraxu Pagyel doomu Okkran.
78On the twelfth day it was Ahira son of Enan, the leader of the sons of Naphtali.RWBTBésub fukkeel baak ñaar kilifag Neftaleen ña, Axira doomu Enan moo aye,
79His offering: one silver plate, about three and a quarter pounds, and one silver basin, about one and three-quarter pounds, both filled with fine flour mixed with oil for a grain offering.RWBTab saraxam di benn ndabu xaalis bu diise téeméeri siikal ak fanweer, muy kilook liibar, ak benn këllu xaalis bu diise juróom ñaar fukki siikal, ci siikal bi ñu yoonal ci néeg bu sell bi, muy juróom ñetti téeméeri garaam, lu ci nekk fees ak sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ngir saraxu pepp,
80One gold dish weighing about four ounces, full of incense;RWBTak senn mbàttus wurus su fees ak cuuraay te diise fukki siikal, di téeméeri garaam ak fukk ak juróom,
81one young bull, one ram, and one male lamb a year old, for a burnt offering;RWBTak wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy mu mag, ak menn kuuyu menn at, ngir saraxu rendi-dóomal,
82one male goat for a sin offering;RWBTak wenn sikket ngir saraxu póotum bàkkaar,
83and for the peace-offering sacrifice: two oxen, five rams, five male goats, five male lambs a year old. Ahira son of Enan's offering.RWBTak saraxu cant gi ci biir jàmm, di ñaari yëkk ak juróomi kuuy yu mag ak juróomi sikket, ak juróomi kuuyu menn at. Looloo doon saraxu Axira doomu Enan.
84This was the altar's dedication offering when it was anointed, from Israel's leaders: twelve silver plates, twelve silver basins, twelve gold dishes.RWBTLoolooy saraxi daloob sarxalukaay ba, ca bés ba ñu koy diw, sellal ko, lépp bawoo ca kilifay Israayil. Ndabi xaalis ya fukk laak ñaar, këlli xaalis ya di fukk ak ñaar, bàttuy wurus ya di fukk ak ñaar,
85Each silver plate weighed about three and a quarter pounds, each basin about one and three-quarter pounds; all the silver of the vessels totaled about sixty pounds.RWBTndabal xaalis lu nekk di téeméeri siikal ak fanweer, di kilook liibar, këll bu nekk di juróom ñaar fukki siikal, di juróom ñetti téeméeri garaam, mboolem xaalisu jumtukaay yi di ñaari junniy siikal, ci siikal bi ñu yoonal ci néeg bu sell bi, ak ñeenti téeméer (2 400), di ñaar fukki kilook juróom ñaar ak juróom benni téeméeri garaam (27 600).
86The twelve gold dishes full of incense weighed about four ounces each; all the gold totaled about three pounds.RWBTFukki bàttuy wurus yi feese cuuraay, mbàttu su ci nekk fukki siikal la, ci siikal bi ñu yoonal ci néeg bu sell bi, di téeméeri garaam ak fukk ak juróom (115), mboolem wurusu bàttu yi di téeméeri siikal ak ñaar fukk (120), muy kilo ak ñetti téeméeri garaam ak juróom ñett fukk (1 380).
87All the cattle for the burnt offering: twelve bulls, twelve rams, twelve year-old male lambs, with their grain offering; and twelve male goats for the sin offering.RWBTMboolem nagi saraxu rendi-dóomal yi, fukki yëkk yu ndaw ak ñaar la, kuuy yu mag yi di fukk ak ñaar, kuuyi menn at yi di fukk ak ñaar, ànd ak seen saraxi pepp, sikketi saraxu póotum bàkkaar bi di fukk ak ñaar.
88All the cattle for the peace offering sacrifices: twenty-four bulls, sixty rams, sixty male goats, sixty male year-old lambs. This was the altar's dedication offering, after it was anointed.RWBTMboolem nagi saraxu cantu biir jàmm yi, ñaar fukki yëkk yu ndaw ak ñeent la, kuuy yu mag yi di juróom benn fukk, sikket yi di juróom benn fukk, kuuyi menn at yi di juróom benn fukk. Loolooy saraxi daloob sarxalukaay ba, gannaaw ba ñu ko diwee, sellal ko.
89When Moses entered the tent of meeting to speak with our Father, he heard the voice speaking to him from above the mercy seat on the ark of the testimony, between the two cherubim—so our Father spoke with him.RWBTBu Musaa duggaan ca biir xaymab ndaje ma, ngir wax ak Aji Sax ji, day dégg baat ba di wax ak moom, bawoo fa tiim kubeeru gaalu seedes kóllëre ga, ca diggante ñaari serub ya. Noonu la daan waxeek moom.