Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Numbers 6 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Then our Father spoke to Moses: Aji Sax ji waxati Musaa,
2 "Speak to the Israelites and say to them: When a man or woman makes a special vow, a Nazirite vow, to set themselves apart to the Father. ne ko mu wax bànni Israayil ne leen: «Góor ak jigéen, képp ku ci dogu ba xas ngir nekk ab Nasireen, ngir sédd boppam Aji Sax ji,
3 They must not drink wine or strong drink, nor vinegar from either, nor any grape juice, nor eat grapes fresh or dried. muy biiñ, di ñoll wu mu mana doon, na moytu di ko jëfandikoo. Bineegaru biiñ ak bineegaru ñoll wu mu mana doon it, du ko naan. Mboolem luy ndoxum reseñ, du ko naan, te reseñ ju tooy ak ju wow it, du ko lekk.
4 During their separation they must eat nothing from the grapevine, from seeds to skin. Mboolem diiru fani céddoom, mboolem lu jóge ci doomu garabu reseñ, dale ci xoox ba ci der, du ci lekk lenn.
5 "During their vow of separation, no razor touches their head. Until it's complete, they stay holy to the Father; they must let their hair grow. «Kemu fani céddoo yi mu xas ne dina ko nasireenal, saatus watukaay du laal boppam ba keroog fani nasireenal, yi mu séddoo Aji Sax ji matee. Ku sell lay doon te day jañu.
6 "Throughout their time of separation to the Father they must not go near a dead body. Kemu fan yi muy nasireenal, séddoo Aji Sax ji, ab néew, bumu ko jege.
7 They must not make themselves unclean even for father, mother, brother, or sister when they die, since their dedication crown to our Father is on their head. Baayam ak ndeyam, mbaa góor mbaa jigéen ju mu bokkal waajur sax, bu deewee, du sobeel boppam ngir ñoom, ndax moo yenu ci kaw boppam, njañu nasireen gi mu séddoo Yàllaam.
8 Throughout their time of separation they are holy to the Father. Kemu fani céddoom, ku sell lay doon, ñeel Aji Sax ji.
9 "If someone dies very suddenly beside them, making their dedicated head unclean, they must shave their head on the day of their cleansing—shave it on the seventh day. «Su nit jekkee dee ci wetam, ba sobeel njañu céddoom, keroog bés buy setlu ca lay watu, te keroog bésub juróom ñaareel ba lay watu.
10 On the eighth day they must bring two turtledoves or two young pigeons to the priest at the meeting tent's entrance. Bés ba ca topp, di juróom ñetteel ba, na yóbbu ca sarxalkat ba, ñaari pitax mbaa ñaari xati yu ndaw, ca bunt xaymab ndaje ma.
11 The priest must offer one as a sin offering, the other as a burnt offering, and make atonement for them, because they sinned by being near the dead body. That same day they must rededicate their head. Sarxalkat bi day def menn mi saraxu póotum bàkkaar, mi ci des saraxu rendi-dóomal, mu jote ko boroom céddoo gi, bàkkaaram ba ko néew ba yóbbe. Bésub keroog lay sellalaat boppam ba yenu woon njañam.
12 They must rededicate to the Father their days of separation and bring a year-old male lamb as a guilt offering; the earlier days don't count—their separation was made unclean. Day yeesalal Aji Sax ji nasireenam ga mu ko séddoo woon, kemu fan ya mu xasoona nasireenal. Su ko defee day indi kuuyu menn at, def ko saraxas peyug tooñ. Fan yi mu njëkkoona nasireenal day neen, ndax nasireen googa moo sobewu.
13 "This is the law of the Nazirite: when their days of separation end, they must come to the tent of meeting's entrance. «Dogalu yoon wi ci ab nasireen nag mooy lii: Bés bi ag céddoom matee, dees koy yóbbu ca bunt xaymab ndaje ma.
14 They must bring the Father their offering: one flawless year-old male lamb as a burnt offering, one flawless year-old ewe lamb as a sin offering, and one flawless ram as a peace offering, Sarax si muy sarxalsi Aji Sax ji di menn kuuyu menn at mu amul sikk, ngir rendi-dóomal, ak menn xarum menn at mu jigéen mu amul sikk, ngir póotum bàkkaar, ak menn kuuy mu mag mu amul sikk, ngir saraxas cant ci biir jàmm,
15 with a basket of unleavened bread—loaves of fine flour mixed with oil, unleavened wafers coated with oil—plus their grain offering and drink offerings. ak pañeb mburu yu amul lawiir, yu ñu lakke sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ak mburu yu sew yu amul lawiir yu ñu wis ag diw, ak saraxi pepp ak saraxi tuuru ya muy àndal.
16 The priest must present them before the Father and offer the sin offering and the burnt offering. «Su ko defee sarxalkat bi boole ko indi fi kanam Aji Sax ji, daldi joxe póotum bàkkaar bi, ak rendi-dóomal bi.
17 He must offer the ram as a peace offering to the Father with the basket of bread without yeast, and offer its grain and drink offerings. Kuuy mi, na ko sarxalkat bi def saraxas cant ci biir jàmm, ñeel Aji Sax ji, boole kook pañeb mburu mi amul lawiir, doora joxe saraxi pepp yeek saraxi tuuru yi.
18 At the tent of meeting's entrance, the Nazirite must shave their dedicated head, take the hair of dedication, and put it on the fire under the peace offering. Su ko defee nasireen bi watu ci bunt xaymab ndaje mi te for kawari céddoom googu, def ko ci taal bi ci suufu saraxas cantu biir jàmm bi.
19 The priest takes the boiled ram's shoulder, one unleavened loaf and wafer from the basket, and puts them in the Nazirite's hands after the hair of dedication is shaved off. «Na sarxalkat bi jël tànku kanamu kuuy mi, gannaaw bu ñoree, te sàkk ci pañe bi menn mburu mu amul lawiir, ak menn mburu mu ndaw, daldi boole loola teg ci loxol nasireen bi, gannaaw bu watoo ba noppi.
20 The priest waves them as a wave offering before our Father—a holy portion for the priest, with the breast that is waved and the thigh that is contributed. Then the Nazirite may drink wine. «Na sarxalkat bi jébbale loola, defal ko Aji Sax ji saraxu yékkati-jébbal. Cér yu sell a ngoogu ñeel sarxalkat bi, mu boole kook dënn biy saraxu yékkati-jébbal, ak tànkub kanam bi ñu jébbale. Gannaaw loolu nasireen bi sañ naa naan biiñ.
21 "This is the law of the Nazirite who vows an offering to our Father for their separation, besides whatever else they can afford. They must do according to their vow, per the law of their separation." «Loolooy wartéef ci ab nasireen bu xas. Loolooy saraxam bi mu warlook Aji Sax ji cig céddoom, te bokkewul ak leneen lu mu ci àttan; waaye kàdduy xas wa mu xasoon daal, na sàmmonteek moom ni ko yoon diglee ci céddoom googu.»
22 Then our Father spoke to Moses: Gannaaw loolu Aji Sax ji waxati Musaa, ne:
23 "Tell Aaron and his sons: This is how you are to bless the Israelites. Say to them: «Waxal Aaróona aki doomam ne leen ni ñuy ñaanale bànni Israayil, nii la; nañu leen wax ne leen:
24 'May your Father bless you and keep you; «“Yal na la Aji Sax ji barkeel, sàmm la.
25 may your Father make his face shine upon you and be gracious to you; «“Yal na la Aji Sax ji geesoo leeram, baaxe la.
26 may your Father look on you with favor and give you peace.' «“Yal na la Aji Sax ji siggil, jàmmal la.”
27 "So they will put my name on the Israelites, and I will bless them." Bu ñu tuddalee noonu bànni Israayil sama tur, man, maa leen di barkeel.»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]