Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Numbers 30 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
2 Moses told Israel's tribal heads: This is what our Father commanded. Ci kaw loolu Musaa wax ak kilifay giiri bànni Israayil, ne leen: «Lii moo di ndigal li Aji Sax ji dénkaane:
3 When a man vows a vow to our Father, or swears an oath binding himself with a pledge, he must not break his word; he must do all his mouth has spoken. «Góor gu xasal Aji Sax ji aw xas, mbaa mu giñ ngir dogu gu mu tegool boppam, bumu tebbi kàddoom. Noonee ko làmmiñam tudde, na ko ni defe ba mu mat sëkk.
4 If a woman vows a vow to our Father and binds herself by a pledge while young, living in her father's house, «Te jigéen ju xasal Aji Sax ji aw xas, ngir dogu gu mu dogu, te fekk ko di ndaw ca biir kër baayam ba tey,
5 when her father hears her vow and pledge binding her, and says nothing to her, all her vows and every pledge binding her stand. su baay ba déggee xasu ndaw sa, ak dogu ga mu tegool boppam, te waxu ca doomam dara, su boobaa mboolem xasi ndaw sa day sax, te mboolem dogu gu mu doguloon boppam day sax.
6 But if her father forbids her the day he hears, none of her vows or bonds she bound herself with will stand; our Father will forgive her, because her father forbade her. Waaye su ko baayam aayee, ca bés ba mu ca déggee, su boobaa mboolem xasi ndaw si, ak mboolem dogu ya mu doguloon boppam, du sax, te Aji Sax jee koy jéggal, ndax baayam aaye woon na ko.
7 If she marries while under her vows, or under a rash promise she has made, «Su fekkee ne ndaw si dafa am jëkkër gannaaw kàdduy xas yu ko topp, mbaa kàddug rëccle gu mu tegool boppam,
8 and her husband hears of it and stays silent to her on the day he hears, her vows stand, and the bonds she bound herself with stand. su ko jëkkër ja déggee, te bés ba mu ko déggee, waxu ko ca dara, su boobaa xasi ndaw si day sax, te kàdduy dogu ya mu tegooloon boppam day sax.
9 But if her husband forbids her the day he hears, he cancels the vow binding her and the rash promise she made; and our Father will forgive her. Waaye su fekkee ne ca bés ba ko jëkkër ja déggee, ca la ko aaye, su boobaa jëkkër ja neenal na xas wa toppoon ndaw si, mbaa kàddug rëccle ga mu tegooloon boppam, te Aji Sax jee koy jéggal.
10 But a widow's or divorced woman's vow—everything she bound herself to—stands against her. «Su dee kàddug xas gu jibe ci ku jëkkëram faatu, mbaa ku ñu baal, mboolem lu mu tegooloon boppam day sax.
11 If she vowed in her husband's house, or bound herself by a pledge under oath, «Su fekkee ne ci biir kër jëkkëram la nit ki xase, mbaa mu dogul fa boppam ab dogu, ci kaw ngiñ,
12 and her husband heard it, said nothing to her, and did not forbid her—so all her vows stand, and every pledge by which she bound herself stands. jëkkër ji dégg ci, te waxu ko dara, aayewu ko, su boobaa mboolem xasi ndaw si day sax, te mboolem dogu bu ndaw si tegooloon boppam, day sax.
13 But if her husband nullifies them the day he hears, nothing she said—her vows or the pledge binding her—will stand: he has nullified them, and our Father will forgive her. Su wéree nag ne jëkkër ji neenal na kàdduy jabaram yooyu, ca bés ba mu ko déggee, su boobaa lépp lu làmmiñu ndaw si tuddoon, jëme ci kàdduy xasam, mbaa kàddu gu mu tegooloon boppam, lenn du ci sax. Jëkkëram a ko neenal, te Aji Sax jee koy jéggal.
14 Any vow and any binding oath to humble herself, her husband may confirm or nullify it. Mboolem aw xas nag, ak mboolem ngiñ lu ku jigéen ki dogoo, te jublu ci ag toroxlu, jëkkëram moo koy saxal, jëkkëram moo koy neenal.
15 But if her husband stays silent to her from day to day, he confirms all her vows or obligations binding her; he confirms them, because he stayed silent to her on the day he heard them. Su jëkkër ji noppee ba noppi, waxu ko dara ca bés ba, ba ca ëllëg sa, su boobaa mboolem kàdduy xasi jabaram, mbaa mboolem kàdduy dogu yu toppoon jabaram, jëkkër jee ko saxal, ndax moo ko waxul dara ca bés ba mu ko déggee.
16 But if he nullifies them after he has heard them, then he will bear her guilt. Ndegam nag jëkkër ji, beneen bés, gannaaw ba mu déggee kàdduy jabaram, la doora àddu ngir neenal wax ja, su boobaa mooy gàddu bàkkaaru jabaram.»
17 These are the rules our Father commanded Moses, between a man and his wife, between a father and his young daughter still in his house. Yooyu dogali yoon la Aji Sax ji dénk Musaa, ci diggante nit ak jabaram, ak diggante baay ak doom ju jigéen, ba muy ndaw te nekk kër baayam.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]