Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Numbers 29 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 "In the seventh month, on the first day, hold a holy assembly. Do no ordinary work; it is a day for you to sound the trumpets. «Bu loolu weesoo, benn fanu weeru juróom ñaareel, seen bésu woote bu sell lay doon. Mboolem lees baaxoo liggéey, deesu ko ci liggéey. Bés la bu ngeen di yéenee ay liit.
2 Offer a burnt offering, a pleasing aroma to our Father: one young bull, one ram, seven male lambs a year old, all without defect. Sarxalleen ci ab rendi-dóomal ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji: wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy mu mag, ak juróom ñaari kuuyu menn at, te lu ci nekk mucc sikk.
3 Their grain offering: fine flour mixed with oil—about six quarts for the bull, about four quarts for the ram, Saraxu peppam lay àndal, di sunguf su mucc ayib, su ñu tooyale ag diw; ñetti fukkeeli efay sunguf, di juróom ñeenti kilo ci yëkk wi, ñaari fukkeeli efa, di juróom benni kilo ci kuuy mu mag mi,
4 and about two quarts for each of the seven lambs; ak benn fukkeelu efab sunguf, di ñetti kilo ci mii kuuy, benn fukkeelu efa ca mee, ba juróom ñaari kuuy yu ndaw yi daj,
5 and one male goat as a sin offering, to make atonement for you. ak benn sikketu póotum bàkkaar, ngir seen njotlaay.
6 Besides the new-moon burnt offering and its grain offering, the daily burnt offering and its grain offering, and their drink offerings, by their rule—a soothing aroma, a fire offering to our Father. Bokkewul ak rendi-dóomalu Terutel weer wu nekk, biy ànd ak saraxu pepp, bokkewul it ak rendi-dóomal bi war bés bu nekk, teyu ànd ak saraxu pepp, ak seen saraxi tuuru, ni ko yoon tërale. Dees koy def ngir xetug jàmm, muy saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji.
7 "On the tenth day of this seventh month, hold a sacred gathering and practice self-denial; do no work at all. «Fukki fanu juróom ñaareelu weer woowu it, seen bésub woote bu sell lay doon, te ngeen toroxlu ci. Mboolem lees baaxoo liggéey, deesu ko ci liggéey.
8 Present a burnt offering to our Father as a pleasing aroma: one young bull, one ram, and seven male lambs a year old, all without blemish. Sarxalleen ci ab rendi-dóomal, ñeel Aji Sax ji, ngir xetug jàmm: wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy mu mag, ak juróom ñaari kuuyu menn at, te lu mucc sikk ngeen di def lépp.
9 Their grain offering: fine flour mixed with oil—about six quarts for the bull, about four quarts for the one ram, Saraxu pepp lay àndal, di sunguf su mucc ayib su ñu tooyale ag diw; ñetti fukkeeli efay sunguf, di juróom ñeenti kilo ci yëkk wi, ñaari fukkeeli efa, di juróom benni kilo ci kuuy mu mag mi,
10 and about two quarts for each of the seven lambs; ak benn fukkeelu efab sunguf, di ñetti kilo ci mii kuuy, benn fukkeelu efa ca mee, ba juróom ñaari kuuy yu ndaw yi daj,
11 also one male goat as a sin offering, besides the atonement sin offering, the regular burnt offering, its grain offering, and their drink offerings. ak benn sikketu póotum bàkkaar, te du bokke ak póotum bàkkaaru njotlaay gi, ak saraxu dóomal bi war bés bu nekk, mook saraxu pepp, ak seen saraxi tuuru yi ci war.
12 "On the fifteenth day of the seventh month, hold a holy assembly. Do no ordinary work; celebrate a feast to our Father for seven days. «Fukki fan yaak juróom ci juróom ñaareelu weer woowu itam, seen bésu woote bu sell lay doon. Mboolem lees baaxoo liggéey, deesu ko ci liggéey. Amalleen ci ag màggal, ñeel Aji Sax ji, diiru juróom ñaari fan, doore ko ca bés ba.
13 Present a burnt offering, a fire offering, a pleasing aroma to our Father: thirteen young bulls, two rams, fourteen male lambs a year old, all without defect. Nangeen ca sarxal ab rendi-dóomal, muy saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji: fukki yëkk yu ndaw ak ñett, ak ñaari kuuy yu mag, ak fukk ak ñeenti kuuyu menn at, te lépp mucc sikk.
14 Their grain offering: fine flour mixed with oil—about six quarts for each of the thirteen bulls, about four quarts for each of the two rams, Seen saraxi pepp di sunguf su mucc sikk su ñu tooyale ag diw, ñetti fukkeeli efay sunguf, di juróom ñeenti kilo ci wenn yëkk wu nekk, ba fukki yëkk yeek ñett daj; ñaari kuuy yu mag yi, kuuy mu ci nekk, ñaari fukkeeli efay sunguf, di juróom benni kilo,
15 and about two quarts for each of the fourteen lambs; ak benn fukkeelu efab sunguf, di ñetti kilo ci mii kuuy, benn fukkeelu efa ca mee, ba fukki kuuy yu ndaw yeek ñeent daj,
16 and one male goat as a sin offering, besides the daily burnt offering, its grain offering, and its drink offering. ak benn sikketu póotum bàkkaar. Bokkewul ak saraxu dóomal bi war bés bu nekk, ak saraxu pepp si muy àndal, ak saraxu tuuru.
17 "On the second day: twelve young bulls, two rams, fourteen year-old male lambs, all without defect, «Bésub ñaareel ba: fukki yëkk yu ndaw ak ñaar; ak ñaari kuuy yu mag, ak fukk ak ñeenti kuuyu menn at, te lépp mucc sikk.
18 with their grain and drink offerings for the bulls, the rams, and the lambs, by number, as required; Te seen saraxi pepp, ak seen saraxi tuuru yay ànd ak yëkk ya, ak kuuy yu mag ya, ak kuuyu menn at ya, na dayo ya dëppoo ak li yoon tëral.
19 also one male goat as a sin offering, besides the regular burnt offering, its grain offering, and their drink offerings. Dees na ca teg benn sikketu póotum bàkkaar, te du bokke ak saraxu dóomal bi war bés bu nekk, mook saraxu pepp ak saraxi tuuru yi mu àndal.
20 "On the third day: eleven bulls, two rams, fourteen year-old male lambs, all without defect, «Bésub ñetteel ba: fukki yëkk yu ndaw ak benn, ak ñaari kuuy yu mag, ak fukk ak ñeenti kuuyu menn at, te lépp mucc sikk.
21 with their grain and drink offerings for the bulls, rams, and lambs, by number, as required. Te seen saraxi pepp, ak seen saraxi tuuru yay ànd ak yëkk ya, ak kuuy yu mag ya, ak kuuyu menn at ya, na dayo ya dëppoo ak li yoon tëral.
22 One male goat as a sin offering, besides the regular burnt offering with its grain and drink offerings. Dees na ca teg benn sikketu póotum bàkkaar, te du bokke ak saraxu dóomal bi war bés bu nekk, mook saraxu pepp ak saraxu tuuru yi mu àndal.
23 "Fourth day: ten bulls, two rams, fourteen year-old male lambs, all without defect, «Bésub ñeenteel ba: fukki yëkk, ak ñaari kuuy yu mag, ak fukk ak ñeenti kuuyu menn at, te lépp mucc sikk.
24 with grain and drink offerings for the bulls, rams, and lambs, by their number, as required; Te seen saraxi pepp, ak seen saraxi tuuru yay ànd ak yëkk ya, ak kuuy yu mag ya, ak kuuyu menn at ya, na dayo ya dëppoo ak li yoon tëral.
25 plus one male goat as a sin offering, besides the daily burnt offering with its grain and drink offerings. Dees na ca teg benn sikketu póotum bàkkaar, te du bokke ak saraxu dóomal bi war bés bu nekk, mook saraxu pepp ak saraxu tuuru ya mu àndal.
26 "On the fifth day: nine bulls, two rams, fourteen year-old male lambs, all without defect, «Bésub juróomeel ba: juróom ñeenti yëkk, ak ñaari kuuy yu mag, ak fukk ak ñeenti kuuyu menn at, te lépp mucc sikk.
27 with grain and drink offerings for the bulls, rams, and lambs, by number, as required. Te seen saraxi pepp, ak seen saraxi tuuru yay ànd ak yëkk ya, ak kuuy ya, ak kuuy yu ndaw ya, na dayo ya dëppoo ak li yoon tëral.
28 Also one male goat as a sin offering, besides the continual burnt offering, its grain offering, and its drink offering. Dees na ca teg benn sikketu póotum bàkkaar, te du bokke ak saraxu dóomal bi war bés bu nekk, mook saraxu pepp ak saraxu tuuru ya mu àndal.
29 "Sixth day: eight bulls, two rams, fourteen year-old male lambs, all without defect, «Bésub juróom benneel ba: juróom ñetti yëkk, ak ñaari kuuy yu mag, ak fukk ak ñeenti kuuyu menn at, te lépp mucc sikk.
30 with their grain offering and drink offerings for the bulls, rams, and lambs, by number, as required; Te seen saraxi pepp, ak seen saraxi tuuru yay ànd ak yëkk ya, ak kuuy yu mag ya, ak kuuy yu ndaw ya, na dayo ya dëppoo ak li yoon tëral.
31 and one male goat as a sin offering, besides the regular burnt offering, its grain offering, and its drink offerings. Dees na ca teg benn sikketu póotum bàkkaar, te du bokke ak saraxu dóomal bi war bés bu nekk, mook saraxu pepp ak saraxu tuuru ya mu àndal.
32 "On the seventh day: seven bulls, two rams, fourteen year-old male lambs, all without defect, «Bésub juróom ñaareel ba: juróom ñaari yëkk, ak ñaari kuuy, ak fukk ak ñeenti kuuyu menn at, te lépp mucc sikk.
33 with their grain and drink offerings for the bulls, rams, and lambs, by number, as prescribed; Te seen saraxi pepp, ak seen saraxi tuuru yay ànd ak yëkk ya, ak kuuy yu mag ya, ak kuuy yu ndaw ya, na dayo ya dëppoo ak li yoon tëral.
34 and one male goat as a sin offering, besides the daily burnt offering, its grain offering and its drink offering. Dees na ca teg benn sikketu póotum bàkkaar, te du bokke ak saraxu dóomal bi war bés bu nekk, mook saraxu pepp ak saraxu tuuru ya mu àndal.
35 "On the eighth day, hold a closing assembly; do no laborious work. «Bésub juróom ñetteel ba seen bésub ndaje lay doon. Mboolem lees baaxoo liggéey, deesu ko ci liggéey.
36 Present a burnt offering, a fire offering, a pleasing aroma to our Father: one bull, one ram, seven male lambs a year old, all without defect, Nangeen ci sarxal ab rendi-dóomal, muy saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji: wenn yëkk, ak menn kuuy yu mag, ak juróom ñaari kuuyu menn at, te lépp mucc sikk.
37 with their grain and drink offerings for the bull, ram, and lambs, by number, as prescribed. Te seen saraxi pepp, ak seen saraxi tuuru yay ànd ak yëkk ya, ak kuuy yu mag ya, ak kuuy yu ndaw ya, na dayo ya dëppoo ak li yoon tëral.
38 One male goat for a sin offering, besides the continual burnt offering, its grain offering and its drink offering. Dees na ca teg benn sikketu póotum bàkkaar, te du bokke ak saraxu dóomal bi war bés bu nekk, mook saraxu pepp ak saraxu tuuru ya mu àndal.
39 "Offer these to our Father at your appointed feasts, besides your vow and voluntary offerings—whether burnt, grain, drink, or peace offerings." «Yooyu sarax ngeen di def, ñeel Aji Sax ji, ci seen bési màggal, te du bokke ak seen sarax yi ngeen xasal seen bopp, ak seen saraxi yéene, ak seen saraxi dóomali bés bu nekk, ak seen saraxi pepp ak seen saraxi tuuru, ak seen saraxi canti biir jàmm.»
30:1 Moses told the Israelites everything, just as our Father had commanded Moses. Ba mu ko defee Musaa àgge bànni Israayil mboolem la ko Aji Sax ji sant.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]