Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Numbers 28 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Our Father said to Moses, Aji Sax ji waxati Musaa, ne ko:
2 "Command the Israelites, say to them: Be sure to present my offering, my food for my food offerings, a pleasing aroma to me, at its set time. «Santal bànni Israayil ne leen sama sarax, sama ñam wi jëm ci sama saraxi sawara ngir xetug jàmm, ñeel ma, nañu farlu ci di ma ko indil saa yu àppam jotee.
3 Say to them: This is the food offering you are to present to me: two flawless year-old lambs daily, a regular burnt offering. Nga waxleen ne leen, lii moo di saraxu sawara bi ñuy indil Aji Sax ji: ay kuuyu menn at yu mucc sikk, ñaar ci bés bi, muy saraxu rendi-dóomal bi war bés bu nekk.
4 Offer one lamb in the morning, the second lamb at twilight, Menn kuuy mi, ngeen sarxal ko ci suba, ñaareel bi, ngeen sarxal ko diggante ngoon ak jant bu so.
5 with about two quarts of fine flour for a grain offering, mixed with about one quart of pressed oil. Benn fukkeelu efab sunguf su mucc ayib, tollu ci ñetti kilo, mooy saraxu pepp bi kuuy mu nekk di àndal, ñu tooyale ko walaatu xiinu diwu segalu oliw, tollu ci liitar.
6 A regular burnt offering, ordained at Mount Sinai for a pleasing aroma, a food offering to me. Looloo di rendi-dóomal bi war bés bu nekk, na ñu ko dogale woon ca tundu Sinayi, ngir xetug jàmm, muy saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji.
7 Its drink offering is a quart for each lamb; pour it out to me in the holy place as strong drink. «Saraxu tuuru si mu àndal, walaatu xiin lay doon, tollu ci liitar ngir kuuy mu ci nekk. Ci ëtt bu sell bi lees di sotti biiñ, muy saraxu tuuru bi ñeel Aji Sax ji.
8 Offer the second lamb at twilight, with a grain offering and drink offering like the morning's, a food offering, a pleasing aroma to me. Meneen kuuy mi, sarxeleen ko diggante ngoon ak jant bu so, mu ànd ak saraxu pepp ak saraxu tuuru niki ci suba, ngeen def ko saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.
9 "On the Sabbath, offer two flawless year-old lambs, about four quarts of fine flour mixed with oil as grain offering, plus its drink offering. «Bésub Noflaay nag ñaari kuuyu menn at yu mucc sikk lay doon, ak saraxu pepp, biy ñaari fukkeeli efay sunguf su mucc ayib, di juróom benni kilo, ñu tooyale ko ag diw, te mu ànd ak saraxu tuuru.
10 The burnt offering for each Sabbath, besides the regular burnt offering and its drink offering. Loolooy saraxu rendi-dóomalu bésub Noflaay, ci bésub Noflaay bu nekk, te bokkewul ak dóomal bi war bés bu nekk, te ànd ak saraxu tuuru.
11 "On the first of each of your months, offer me a burnt offering: two young bulls, one ram, seven male lambs a year old, without defect, «Te itam seen bési Terutel weer, nangeen sarxe ab rendi-dóomal, ñeel Aji Sax ji. Ñaari yëkk yu ndaw, ak menn kuuy mu mag, ak juróom ñaari kuuyu menn at, te lu ci nekk mucc sikk,
12 about six quarts of fine flour mixed with oil as a grain offering for each bull, about four quarts of fine flour mixed with oil as a grain offering for the one ram, ak ñetti fukkeeli efay sunguf su mucc ayib, di juróom ñeenti kilo, muy saraxu pepp, ñu tooyale ko ag diw, booleek yëkk wu nekk, ak ñaari fukkeeli efay sunguf su mucc ayib, di juróom benni kilo, muy saraxu pepp, ñu tooyale ko ag diw, booleek kuuy mu mag mi,
13 and two quarts of fine flour mixed with oil as a grain offering for each lamb - a burnt offering, a pleasing aroma, a food offering to me. ak benn fukkeelu efab sunguf su mucc ayib, di ñetti kilo, muy saraxu pepp, ñu tooyale ko ag diw, booleek mépp kuuyum menn at. Saraxu rendi-dóomal la, ngir xetug jàmm, di saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji.
14 Their drink offerings: two quarts of wine for the bull, just over a quart for the ram, and a quart for the lamb. This is the burnt offering for the new moon, month by month, all year. «Ay saraxi tuuru lay àndal, genn-wàllu xiinu biiñ la, tollu ci ñaari liitar ci yëkk wu nekk, ak benn ñetteelub xiin, tollu ci liitar ak genn-wàll ci kuuy mu mag mi, ak walaatu xiin, tollu ci liitaru biiñ ci mépp kuuyu menn at. Loolooy saraxu rendi-dóomalu weer wi, weer wu ci nekk, ba weeri at mi daj.
15 Offer me one male goat as a sin offering, besides the regular burnt offering and its drink offering. Ak itam bennub sikket, mu ànd ak saraxu tuuru ngir saraxu póotum bàkkaar, ñeel Aji Sax ji ci bésub Terutel weer wi, te bokkewul ak rendi-dóomal bi ñuy sarxe bés bu nekk.
16 "In the first month, on the fourteenth day of the month, is the Passover to me. «Fukki fan ak ñeent ci weer wi njëkk, mooy màggalu bésub Mucc ba, ñeel Aji Sax ji.
17 On this month's fifteenth day is a feast; bread without yeast is eaten seven days. Ëllëg sa, fukki fan ak juróom ci weer woowu, di màggal; diiru juróom ñaari fan, mburu mu amul lawiir lees cay lekk.
18 On the first day there is to be a holy assembly; you must do no ordinary work. Bés bu jëkk boobu, woote bu sell lees cay amal. Mboolem lees baaxoo liggéey, deesu ko ci liggéey.
19 Present me a food offering, a burnt offering: two young bulls, one ram, seven yearling male lambs; see that they are without defect. Nangeen ci def saraxu sawara, mu dib rendi-dóomal, ñeel Aji Sax ji: ñaari yëkk yu ndaw, ak menn kuuy mu mag, ak juróom ñaari kuuyu menn at, te ngeen def lépp di lu mucc sikk.
20 Their grain offering: fine flour mixed with oil—about six quarts for the bull, four quarts for the ram, Yooyii ànd ak saraxu peppam, di sunguf su mucc ayib, su ñu tooyale ag diw, ñetti fukkeeli efay sunguf, di juróom ñeenti kilo, ciw yëkk, ñaari fukkeeli efay sunguf, di juróom benni kilo, cim kuuy mu mag,
21 and with each of the seven lambs, about two quarts; ak benn fukkeelu efab sunguf, di ñetti kilo, ci mii kuuy, benn fukkeelu efa ca mee, ba juróom ñaari kuuy yu ndaw yi daj,
22 and one male goat as a sin offering to make atonement for you. ak benn sikketu póotum bàkkaar ngir seen njotlaay.
23 Offer these in addition to the morning burnt offering, which is the regular burnt offering. Te bokkewul ak rendi-dóomalu suba si, rendi-dóomal boobu war bés bu nekk.
24 Do this daily for seven days—food, a pleasing aroma to me—besides the regular burnt offering and its drink offering. Sarax yu mel noonu ngeen di sarxal ci bés bi, ak seen saraxu tuuru, diiru juróom ñaari fan, muy ñamu saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji. Ci kaw rendi-dóomal bi war bés bu nekk, ci lees koy dolli.
25 On the seventh day you are to hold a holy assembly; you must do no ordinary work. Bésub juróom ñaareel ba, seen bésub woote bu sell lay doon. Mboolem lees baaxoo liggéey, deesu ko ci liggéey.
26 "On the day of firstfruits, when you bring me a new grain offering at your Feast of Weeks, hold a holy assembly; do no ordinary work. «Bésub ndoortel meññeef ba ngeen di sarxesi saraxu pepp mu bees, ñeel Aji Sax ji, ci seen biir màggalug Ayi bés nag, seen bésub woote bu sell lay doon. Mboolem lees baaxoo liggéey, deesu ko ci liggéey.
27 Present a burnt offering, a pleasing aroma to me: two young bulls, one ram, seven year-old male lambs. Nangeen ci sarxal ab rendi-dóomal, ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji: ñaari yëkk yu ndaw, ak menn kuuy mu mag, ak juróom ñaari kuuyu menn at.
28 With them comes a grain offering of fine flour mixed with oil: about six quarts for each bull, about four quarts for the one ram, Saraxu peppam di sunguf su mucc ayib, su ñu tooyale ag diw. Ñetti fukkeeli efay sunguf, di juróom ñeenti kilo ci yëkk wu nekk, ak ñaari fukkeeli efa, di juróom benni kilo ci kuuy mu mag mi,
29 and about two quarts for each of the seven lambs; ak fukkeelub efa, di ñetti kilo, ci mii kuuy, fukkeelub efa ca mee, ba juróom ñaari kuuy yu ndaw yi daj,
30 with one male goat to make atonement for you. ak bennub sikket ngir seen njotlaay.
31 Offer these besides the regular burnt offering and its grain offering; see that they're flawless, with their drink offerings." Sarxeleen loolu, te bumu bokke ak rendi-dóomal bi war bés bu nekk tey ànd ak saraxu pepp. Lu mucc sikk nag ngeen di def sarax yooyii, te ngeen defaale saraxi tuuru yi ci war.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]