Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Numbers 2 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Then our Father spoke to Moses and Aaron, saying: Ba loolu wéyee Aji Sax ji wax Musaa ak Aaróona, ne leen:
2 "The Israelites are to camp, each by his standard, with banners of their ancestral houses, facing the tent of meeting all around, they are to camp. «Na bànni Israayil di dal, ku nekk ak raayaam ak xàmmikaayu kër maamam. Fi wër xaymab ndaje mi te dànd ko as lëf, fi lañuy dale:
3 "To the east, toward sunrise: the camp of Judah, by their divisions, under its standard. Leader of Judah's people: Nahshon son of Amminadab. «Ñay dale ca kanam, fa féete penku, ñooy waa raayab Yuda ak seeni gàngoor, kilifag Yudeen ñi di Naason doomu Aminadab.
4 His division, those counted, numbered 74,600. Ña ñu lim ci gàngooram di juróom ñaar fukki junneek ñeent ak juróom benni téeméer (74 600).
5 "Camping next to him: the tribe of Issachar; the leader of Issachar's sons is Nethanel son of Zuar. «Ñay dale fa feggook ñoom ñooy giirug Isakareen ñi, kilifag askanu Isaakar di Netaneel doomu Cuwar.
6 His division, those counted, numbered 54,400. Ña ñu lim ci gàngooram di juróom fukki junneek ñeent ak ñeenti téeméer (54 400).
7 "Then the tribe of Zebulun; leader of Zebulun's sons: Eliab son of Helon. «Giirug Cabuloneen ñeey feggook ñoom, kilifag askanu Sabulon di Elyab doomu Elon.
8 His division, those counted, numbered 57,400. Ña ñu limal gàngooram di juróom fukki junneek juróom ñaar ak ñeenti téeméer (57 400).
9 "All counted in Judah's camp: 186,400, by their divisions. They set out first. «Mboolem ña ñu limal dalub Yuda aki gàngooram daldi doon téeméeri junneek juróom ñett fukk ak juróom benn ak ñeenti téeméer (186 400). Bu ñuy dem, ñooñooy dox, jiitu.
10 "South side: the banner of Reuben's camp, by divisions. Leader of Reuben's people: Elizur son of Shedeur. «Waa raayab Ruben ñooy dale bëj-saalum, ñook seeni gàngoor, kilifag askanu Ruben di Elicur doomu Sedeyur.
11 His division, those counted, numbered 46,500. Ña ñu limal gàngooram di ñeent fukki junneek juróom benn ak juróomi téeméer (46 500).
12 "Camping beside him: the tribe of Simeon; leader of Simeon's people, Shelumiel son of Zurishaddai. «Ñay dale fa feggook ñoom ñooy giirug Cimyoneen ñi, kilifag askanu Simeyon di Selumyel doomu Curisadaay.
13 His division, those counted, numbered 59,300. Ña ñu limal gàngooram di juróom fukki junneek juróom ñeent ak ñetti téeméer (59 300).
14 "Then the tribe of Gad: leader of Gad's people, Eliasaph son of Deuel. «Giiru Gàddeen ñeey feggook ñoom, kilifag askanu Gàdd di Elyasaf doomu Rewel.
15 His division, those counted, numbered 45,650. Ña ñu limal gàngooram di ñeent fukki junneek juróom ak juróom benni téeméer ak juróom fukk (45 650).
16 "Those counted in Reuben's camp, by their divisions: 151,450. They set out second. «Mboolem ña ñu limal dalub Ruben aki gàngooram doon téeméeri junneek juróom fukk ak benn, ak ñeenti téeméer ak juróom fukk (151 450). Bu ñuy dem, ñooñooy doon ñaareelu kuréel, dox, topp ca.
17 "Then the tent of meeting sets out, with the Levites' camp in the middle of the camps. They set out in the order they camp, each in place, under their banners. «Su ko defee xaymab ndaje mi jóg topp ca, ànd ak Leween ñi koy gàddu, te seen dal nekk ci digg dal yi. Noonee kuréel yiy dale daal, ni lañuy jóge dem, ku nekk topp ayam ak raayaam.
18 "West side: Ephraim's camp standard, by their divisions; leader of Ephraim's people is Elishama son of Ammihud. «Waa raayab Efrayim ñooy dale wetu sowu, ñook seeni gàngoor, kilifag askanu Efrayim di Elisama doomu Amiyudd.
19 His division, those counted, numbered 40,500. Ña ñu limal gàngooram di ñeent fukki junni ak juróomi téeméer (40 500).
20 "Beside him: the tribe of Manasseh, led by Gamaliel son of Pedahzur. «Ñay dale fa feggook ñoom ñooy giirug Manaseen ñi, kilifag askanu Manase di Gamliyel doomu Pedacur.
21 His division, those counted, numbered 32,200. Ña ñu limal gàngooram di fanweeri junneek ñaar ak ñaari téeméer (32 200).
22 "Then the tribe of Benjamin, led by Abidan son of Gideoni. «Giirug Beñamineen ñeey feggook ñoom, kilifag askanu Beñamin di Abidan doomu Gidoni.
23 His division, those counted, numbered 35,400. Ña ñu limal gàngooram di fanweeri junneek juróom ak ñeenti téeméer (35 400).
24 "All counted in Ephraim's camp: 108,100, by their divisions. They set out third. «Mboolem ña ñu limal dalub Efrayim aki gàngooram daldi doon téeméeri junneek juróom ñett ak téeméer (108 100). Bu ñuy dem, ñooñoo di ñetteelu kuréel, dox topp ca.
25 "Dan's camp standard stands on the north side, by divisions. Ahiezer son of Ammishaddai leads Dan's people. «Waa raayab Dan ñooy dale bëj-gànnaar, ñook seeni gàngoor, kilifag askanu Dan di Axyeser doomu Amisadaay.
26 His division, those counted, numbered 62,700. Ña ñu limal gàngooram di juróom benn fukki junneek ñaar ak juróom ñaari téeméer (62 700).
27 "Camping next to it: the tribe of Asher, its leader Pagiel son of Ochran. «Ñay dale fa feggook ñoom ñooy giirug Asereen ñi, kilifag askanu Aser di Pagyel doomu Okkran.
28 His division, those counted, numbered 41,500. Ña ñu limal gàngooram di ñeent fukki junneek benn ak juróomi téeméer (41 500).
29 "Then the tribe of Naphtali; Naphtali's leader is Ahira son of Enan. «Giirug Neftaleen ñeey feggook ñoom, kilifag askanu Neftali di Axira doomu Enan.
30 His division, those counted, numbered 53,400. Ña ñu limal gàngooram di juróom fukki junneek ñett ak ñeenti téeméer (53 400).
31 "All counted in Dan's camp: 157,600. They set out last, by their standards." «Mboolem ña ñu limal dalub Dan daldi doon téeméer ak juróom fukki junneek juróom ñaar ak juróom benni téeméer (157 600). Ñooñooy mujja jóg, topp seeni raaya.»
32 These are Israelites counted by their clans, all camp divisions: 603,550. Ñooñu lañu limal bànni Israayil na ñu bokke seen këri maam. Mboolem ña ñu limal dal ya ak seeni gàngoor doon juróom benni téeméeri junneek ñett ak juróomi téeméer ak juróom fukk (603 550).
33 But the Levites were not counted among the Israelites, just as our Father had commanded Moses. Leween ñi nag limaaleesu leen ci bànni Israayil, te noonu la ko Aji Sax ji sante woon Musaa.
34 So the Israelites did all our Father commanded Moses. So they camped by their standards, and so they set out, each by clan, by ancestral family. Bànni Israayil daldi def noonu. Mboolem noonee ko Aji Sax ji sante woon Musaa, na lañu daan dale, topp seeni raaya, na lañu daan jóge, ku nekk ak làngam ak kër maamam.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]