Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Numbers 1 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Our Father spoke to Moses in the Sinai wilderness, in the tent of meeting, on the first day of the second month of the second year after they left the land of Egypt. He said: Aji Sax ji moo wax ak Musaa ca màndiŋu Sinayi ca biir xaymab ndaje ma, keroog benn fanu ñaareelu weer wu ñaareelu at, ma topp ca gàddaay ga bawoo Misra. Mu ne ko:
2 "Count the whole community of Israel's people, by clans and fathers' houses—every male, by name, head by head. «Limleen mbooloom bànni Israayil gépp, na ñu bokke seeni làng ak seen këri maam. Waññleen góor ñépp, bopp ak bopp, ku nekk ak turam.
3 Register everyone in Israel twenty and older who can serve in the army—you and Aaron—by their divisions. Li ko dale ñaar fukki at, jëm kaw, mboolem ñi xare war ci Israayil daal, nangeen leen lim, gàngoor ak gàngoor, yaw ak Aaróona.
4 A man from each tribe is to be with you, each one the head of his family. Giir gu ci nekk, àndleen ceek kilifa yi jiite seen këri maam, ñu jàppale leen ci.
5 "Names of the men who will stand with you: from Reuben, Elizur son of Shedeur. Ñiy wuyoo tur yii nag, ñoo leen ciy taxawu: Ci wàllu Rubeneen ñi, Elicur doomu Sedeyur.
6 "From Simeon, Shelumiel son of Zurishaddai; Wàllu Cimyoneen ñi, Selumyel doomu Curisadaay.
7 "From Judah, Nahshon son of Amminadab; Wàllu Yudeen ñi, Naason doomu Aminadab.
8 "From Issachar, Nethanel son of Zuar; Wàllu Isakareen ñi, Netaneel doomu Cuwar.
9 "From Zebulun, Eliab son of Helon; Wàllu Cabuloneen ñi, Elyab doomu Elon.
10 "From the sons of Joseph: from Ephraim, Elishama son of Ammihud; from Manasseh, Gamaliel son of Pedahzur; Ñi ciy askanu Yuusufa ñii la: Ci wàllu Efraymeen ñi, Elisama doomu Amiyudd. Wàllu Manaseen ñi, Gamliyel doomu Pedacur.
11 "From Benjamin, Abidan son of Gideoni; Wàllu Beñamineen ñi, Abidan doomu Gidoni.
12 "From Dan, Ahiezer son of Ammishaddai; Wàllu Daneen ñi, Axyeser doomu Amisadaay.
13 "From Asher, Pagiel son of Ochran; Wàllu Asereen ñi, Pagyel doomu Okkran.
14 "From Gad, Eliasaph son of Deuel; Wàllu Gàddeen ñi, Elyasaf doomu Dewel.
15 "From Naphtali, Ahira son of Enan. Wàllu Neftaleen ñi, Axira doomu Enan.»
16 "These were the community's called ones, leaders of their ancestral tribes, heads of Israel's clans." Ñooñu lañu woo ci mbooloo mi, muy ñi jiite seen giiri maam. Ñooy njiiti gàngoori Israayil.
17 So Moses and Aaron took these men who had been designated by name, Ba loolu amee Musaa ak Aaróona tofloo ñooñu ñu tudd seeni tur,
18 on the first day of the second month they gathered the whole community. The people registered their ancestry by clan and family—every male twenty years old and older, listed by name, one by one, ñu dajale mbooloo ma mépp, keroog ca benn fanu ñaareelu weer wa. La ko dale ca ña am ñaar fukki at, jëm kaw, ñoom ñépp daldi bindu ca limeefu tur ya, ku nekk ak kër maamam, giir ak giir, làng ak làng, bopp ak bopp.
19 as our Father had commanded Moses. So Moses counted them in the wilderness of Sinai. Noonee ko Aji Sax ji sante woon Musaa, na la Musaa takke seen lim ca màndiŋu Sinayi.
20 From Reuben's descendants, Israel's firstborn: recorded by clan and family, name by name, every male twenty years old and up, able to serve in war. Ñu lim bopp ak bopp, turi sëti Ruben taawub Israayil seen maam, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
21 Those counted from the tribe of Reuben were 46,500. Limub Rubeneen ñi di ñeent fukki junni ak juróom benn ak juróomi téeméer (46 500).
22 Simeon's descendants, by clans and families, counted by name, head by head: every male twenty years old and up, fit for the army. Ñu lim bopp ak bopp, turi sëti Simeyon, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
23 Those counted from the tribe of Simeon were 59,300. Limub Cimyoneen ñi di juróom fukki junneek juróom ñeent ak ñetti téeméer (59 300).
24 From Gad's descendants: by clans, families, and names, every man twenty and older fit for military service. Ñu lim turi sëti Gàdd, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
25 Those counted from the tribe of Gad were 45,650. Limub Gàddeen ñi di ñeent fukki junneek juróom ak juróom benni téeméer ak juróom fukk (45 650).
26 Judah's descendants, listed by clans and families, by name, every man twenty and older able to serve in the army: Ñu lim turi sëti Yuda, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
27 those counted from the tribe of Judah were 74,600. Limub Yudeen ñi di juróom ñaar fukki junneek ñeent, ak juróom benni téeméer (74 600).
28 Issachar's descendants, listed by clan and family, by name, every man twenty years and older fit for war: Ñu lim turi sëti Isaakar, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
29 those counted from the tribe of Issachar were 54,400. Limub Isakareen ñi di juróom fukki junneek ñeent ak ñeenti téeméer (54 400).
30 Zebulun's descendants: registered by clan and family, by name, every man twenty years old or older fit for military service. Ñu lim turi sëti Sabulon, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
31 Those counted from the tribe of Zebulun were 57,400. Limub Cabuloneen ñi di juróom fukki junneek juróom ñaar ak ñeenti téeméer (57 400).
32 Sons of Joseph, Ephraim's line: recorded by clan and family, by name, every man twenty and older fit for military service. Ñu lim turi sëti Yuusufa yi askanoo ci doomam Efrayim, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
33 Those counted from the tribe of Ephraim were 40,500. Limub Efraymeen ñi di ñeent fukki junni ak juróomi téeméer (40 500).
34 Manasseh's descendants, listed by clans and families, by name, each man twenty years or older able to serve in the army: Ñu lim turi sëti Yuusufa yi askanoo ci doomam Manase, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
35 those counted from the tribe of Manasseh were 32,200. Limub Manaseen ñi di fanweeri junneek ñaar ak ñaari téeméer (32 200).
36 From Benjamin's descendants, recorded by clan and family, by name, every man twenty years old and older, fit for military service: Ñu lim turi sëti Beñamin, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
37 those counted from the tribe of Benjamin were 35,400. Limub Beñamineen ñi di fanweeri junneek juróom ak ñeenti téeméer (35 400).
38 From Dan's descendants, listed by clan and family, by name, every man twenty years old and older fit for war: Ñu lim turi sëti Dan, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
39 those counted from the tribe of Dan were 62,700. Limub Daneen ñi di juróom benn fukki junneek ñaar ak juróom ñaari téeméer (62 700).
40 Asher's descendants, listed by clan and family, by name: every man twenty years old and up, fit for military service. Ñu lim turi sëti Aser, ku nekk ak làngam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
41 Those counted from the tribe of Asher were 41,500. Limub Asereen ñi di ñeent fukki junneek benn ak juróomi téeméer (41 500).
42 Naphtali's descendants: by clan and family, counted by name, every man twenty and older fit for war. Ñu lim turi sëti Neftali, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
43 Those counted from the tribe of Naphtali were 53,400. Limub Neftaleen ñi di juróom fukki junneek ñett ak ñeenti téeméer (53 400).
44 Moses, Aaron, and Israel's twelve leaders counted these men, each for his family. Yooyu limeef la Musaa ak Aaróona tënk, ña leen ca jàppale di fukki kilifay Israayil ak ñaar, ku ci nekk taxawal kër maamam.
45 All Israel's people were counted by families, every man twenty years old and older, fit to serve in Israel's army. Mboolem bànni Israayil yi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw, limees na leen, ku ci nekk ak kër maamam.
46 All those counted came to 603,550. Ña ñu lim ñépp di juróom benn téeméeri junneek ñett ak juróomi téeméer ak juróom fukk (603 550).
47 But the Levites were not counted among them by their ancestral tribe. Giirug Leween ñi nag ci bànni Israayil lañu bokk, waaye limaaleesu leen ak ñoom.
48 For our Father had said to Moses: Aji Sax ji moo waxoon Musaa, ne ko:
49 "Do not count the tribe of Levi or list them among the Israelites. «Giirug Lewi ñoom, bu leen lim, bu leen waññaaleek bànni Israayil.
50 Instead, put the Levites in charge of the tabernacle of the testimony, all its furnishings, and everything belonging to it. They must carry the tabernacle and its furnishings, care for it, and camp around it. Waaye yaw ci sa bopp nanga sas Leween ñi jaamookaay bi seedes kóllëre gi dence, mook la muy àndal lépp, ak mboolem lu ca bokk. Ñooy gàddu jaamookaay bi, ak la muy àndal lépp, di ko toppatoo, te it fi wër jaamookaay bi lañuy dal.
51 When the tabernacle sets out, Levites take it down; when it is pitched, Levites set it up. Any outsider who comes near is to be put to death. Bu jaamookaay bi dee dem, Leween ñee koy wékki, bu jaamookaay bi dee dale béreb, Leween ñee koy we. Ku ci bokkul ba laal ci nag, dees koy rey.
52 Israel's people are to camp, each by his own camp, each under his own banner, by their companies. Bànni Israayil gi ci des, na ku ci nekk topp dalam, ak raayaam ak kuréelam.
53 The Levites must camp around the tabernacle of the testimony, so no wrath falls on the Israelite community; the Levites are to guard the tabernacle of the testimony." Leween ñi nag nañu dal fi wër jaamookaay bi seedes kóllëre gi dence. Su ko defee sama sànj du dal ci kaw mbooloom bànni Israayil. Te itam na Leween ñi sàmm ndénkaaneb jaamookaay bi seedes kóllëre gi dence.»
54 The people of Israel did everything our Father had commanded Moses; that is exactly what they did. Bànni Israayil daldi def noonu. Mboolem lu Aji Sax ji santoon Musaa, noonee lañu ko defe.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]