Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Malachi 3 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Look, I am sending my messenger, and he will prepare the way before me. Then suddenly the Lord whom you are seeking will come to his temple—the messenger of the covenant in whom you delight. Look, he is coming, says the Father of heaven's armies. «Maa ngii di yebal sama ndaw, mu xàllal ma aw yoon. Sang bi ngeen di xaar mooy jekki agsi këram, ndawal kóllëre loolu, ki ngeen safoo, mu ngooguy dikk.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
2 "But who can endure the day he comes? Who can stand when he appears? He is like a refiner's fire, like a launderer's soap. Waaye bésub dikkam, ana ku ko mana dékku? Bu teewee ana kuy taxaw? Nde moom daa mel ni sawaras tëgg buy xelli weñ, melati ni xemey fóotkat.
3 He will sit refining and purifying silver; he will purify Levi's sons and refine them like gold and silver, and they will bring offerings to our Father in righteousness. Fa mbaxana dee benn lay tooge ni xellikat ak seggkat, te mooy segg sëti Lewi, xelli leen ni xaalis ak wurus, ba ñu doon niti Aji Sax ji, ñi koy indil sarax ci yoon.
4 Then Judah and Jerusalem's offering will please our Father, as in days past, as in former years." Su boobaa la saraxu Yuda ak Yerusalem di neex Aji Sax ji, na jant ya woon, at ya woon.
5 I will come near to judge you, a swift witness against sorcerers, adulterers, those who swear falsely, who cheat the worker of his wages, oppress the widow and orphan, push aside the foreigner, and do not fear me, says the Father of heaven's armies. «Maa leen di dikke ab àtte, di ab seede bu taxaw temm ci tuumaal xërëmkat yeek njaalookat yi, ak ñiy fene ngiñ, ak ñiy xañ ab liggéeykat peyooram, di noggatu ab jëtun akub jirim, di beddi doxandéem te ragaluñu ma.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
6 For I, your Father, do not change; therefore you, children of Jacob, have not been destroyed. «Man Aji Sax ji déy, duma soppiku, te yeen noppiwuleen di askanu Yanqóoba, maanaam ay suufukat.
7 Since your ancestors' days you have turned from my statutes and not kept them. Return to me, and I will return to you, says the Father of heaven's armies. But you ask, 'How are we to return?' «Ca seen janti maam ngeen dëddoo sama dogali yoon, sàmmuleen ko. Waññikuleen fi man, ma waññiku fi yeen,» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. «Yeena ngi naa: “Ci lan lanuy waññikoo?”
8 Will a person rob their Father? Yet you rob me. But you ask, 'How have we robbed you?' In the tenth and the offerings. Waaw, ndax nit dina sàcc Yàlla? Ndaxam yeen, yeena ngi may sàcc te yeena ne: “Ana nu nu la sàcce?” Xanaa ci seen cérub fukkeelu alal ak li ngeen may jébbal.
9 You are cursed with a curse, for you are robbing me—the whole nation of you. Alkànde ju réy a ngi leen di dikkal, nde man ngeen di sàcc, yeen mboolem askan wi.
10 Bring the full tenth into the storehouse, so there's food in my house. Test me in this, says the Father of heaven's armies, and see if I won't open heaven's windows for you and pour out blessing for you until there's no more need. Indileen mboolem céru fukkeel ca kërug denc ya, ba ab dund am sama biir kër, te ngeen seetloo ma ko rekk,» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax, «ndegam duma leen ubbil bunti asamaan, ba sottil leen barke bu doy.
11 I will rebuke the devourer for you, so it will not destroy your ground's fruit, and your vine in the field will not fail to bear, says the Father of heaven's armies. Maa leen di gëddal njéeréer, ba du leen yàqal meññeefum suuf, te reseñug tool du leen jaasiral,» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
12 Then all nations will call you blessed, for you will be a land of delight, says the Father of heaven's armies. «Xeet yépp ñu barkeel ñi lañu leen di woowe, nde réewum bànneex ngeen di dëkke,» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
13 Your words were harsh against me, says our Father. But you ask, 'What have we said against you?' «Kàddu yu ñagas ngeen teg ci sama kaw,» Aji Sax jee ko wax. «Te yeena ne: “Ana kàddu yu ñu la waxal?”
14 You said, 'Serving God is useless. What have we gained by keeping his charge and walking as mourners before the Father of heaven's armies?' Yeena ne: “Jaamu Yàlla ag neen la. Ana lu nu jële ci sàmm ndénkaaneem, tey wéye toroxlu fi kanam Aji Sax ji Boroom gàngoor yi?
15 Now we call the arrogant blessed. Those who do evil prosper; they even test God and escape. Moo tax nu ne nit ñu bew ñi ñooy ñi barkeel, ñiy def lu bon kay ñoo baaxle, ñoom ñiy diiŋat Yàlla, teg ca rëcc.”»
16 Then those who feared our Father spoke to one another, and he listened and heard. A scroll of remembrance was written before him for those who fear him and treasure his name. Ca la ñi ragal Aji Sax ji diisoo ci seen biir, Aji Sax ji teewlu, déglu leen. Ñu bind fi kanamam téereb fàttaliku, bu lim ñi ragal Aji Sax ji, te teral aw turam.
17 They will be mine, says the Father of heaven's armies, on the day I act, my treasured possession. I will spare them as a father spares his son who serves him. «Sama moomeelu bopp la ñooñuy doon,» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax, «ca bés ba may jëfi, sama gànjar lañuy doon, te ni baay di baaxe as ngóoram su ko taxawu, ni laa leen di baaxe.
18 Once more you will see the difference between the righteous and the wicked, between one who serves our Father and one who does not serve him. Ca ngeen di ràññaatlewaat diggante ku jub ak ku bon, kuy jaamu Yàlla, ak ku ko jaamuwul.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]