Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Malachi 2 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Now, priests, this command is for you. «Léegi nag, sarxalkat yi, santaane bii yeen la ñeel.
2 If you won't listen, or take it to heart to honor my name, says the Father of heaven's armies, I will send the curse on you and curse your blessings. I have already cursed them, because you don't take it to heart. Su ngeen dégluwul, te defuleen seen xel ci teral sama tur,» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax, «alkànde laay yebal fi seen biir, ba alagaale seeni barke, te alag naa ko jeeg, nde defuleen seen xel ci teral ma.
3 I will rebuke your offspring and smear manure on your faces—the manure of your feasts—and you will be carried off with it. Maa ngii di yar seen askan, sëlëm leen sébbriit, mi jóge ci seen saraxi màggal, ñu tonniwaale leen ak sébbriit mi.
4 Then you will know I sent this command to you, so my covenant with Levi stands, says the Father of heaven's armies. Su boobaa ngeen xam ne maa leen yónnee santaane bii, ngir saxal sama kóllëreek Lewi.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
5 "My covenant with him was life and peace; I gave them to him to be held with reverence, and he revered me and trembled before my name. «Sama kóllëre moom laa ko séqal, mu jur dund ak jàmm, maa ko may loolu ngir mu ragal ma, ragaloon na ma it, bay yéemu ci sama tur.
6 True instruction was in his mouth, no wrong on his lips. He walked with me in peace and integrity, and turned many from sin. Njàngalem dëgg la dëkkaloon ci gémmiñam, te ag njubadi, déggeesu ko ciw làmmiñam, xanaa di ànd ak man ci jàmm ak njub, tey bàyyiloo ñu bare yoonu ñaawtéef.
7 A priest's lips guard knowledge, and people seek instruction from his mouth, for he is the messenger of the Father of heaven's armies. «Kàddug sarxalkat déy day sàmm xam-xam, te ciy waxam la nit ñi di sàkkoo àlluwa, nde mooy ndawal Aji Sax ji Boroom gàngoor yi.
8 But you turned from the way and made many stumble by your instruction; you corrupted the covenant of Levi, says the Father of heaven's armies. Waaye yeen dangeena moy yoon wi, seenum njàngale ngeen fakkastale ñu bare, te yeena fecci kóllëreg Lewi.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
9 So I made you despised and low before all the people, because you haven't kept my ways but shown favoritism in your instruction." «Moo tax man it ma def xeet wépp xeeb leen, sewal leen, feye leen ko seen ñàkka sàmm samay yoon, ak par-parloo gi ngeen di diglee yoon wi.»
10 Don't we all have one Father? Didn't one Father create us? Why betray each other, desecrating our fathers' covenant? Xanaa du benn baay lanu am, nun ñépp? Te jenn Yàlla jee nu sàkk? Lu waral ku ne di wor mbokkam, ba ñàkka wormaal kóllërey maam ya?
11 Judah is unfaithful; a detestable thing is done in Israel and Jerusalem. Judah has desecrated our Father's holy place, which he loves, and married the daughter of a foreign god. Waa Yuda wor nañu, lu jomblu lees def fi Israayil ak Yerusalem. Yuda déy moo teddadil li Aji Sax ji sopp te mooy bérebam bu sell: Yuda moo takk janqub yàllay doxandéem yi.
12 May our Father cut off from Jacob's tents the man who does this—anyone at all—even one bringing an offering to the Father of heaven's armies. Ku def lii, yal na la Aji Sax ji dagge ci xaymay Yanqóoba gépp yaak sa bépp kuutaay, boole ci kuy indil ab sarax Aji Sax ji Boroom gàngoor yi.
13 And a second thing you do: you cover our Father's altar with tears, weeping and groaning, because he no longer regards the offering or accepts it gladly from your hand. Lii itam yeena ngi koy def: yeena ngi tawal ay rongooñ sarxalukaayu Aji Sax ji, di jooy aka binni, ndax moo geesootul seen sarax, te nangootul lenn ci seen loxo.
14 You ask, "Why?" Because our Father witnessed between you and the wife of your youth, whom you betrayed—though your companion, your wife by covenant. Ngeen naa: «Ndax lan?» Ndax Aji Sax ji moo seede seen diggante ak seen jabar ja ngeen jël ba ngeen di ndaw, tey ngeen wor ko, te mu doonoon seen wéttal, seen jabar ju ngeen séqal kóllëre.
15 Didn't the Father make you one with your wife? Body and spirit, you are his. And what does he want? Godly children from your union. So guard your spirit; let no one betray the wife of his youth. Kenn deful lii te desem xel. Kenn doŋŋ a ko defoon. Ndax lan? Kuutaay li ko Yàlla digoon la doon wut. Kon nag sàmmleen seenum xel, te buleen wor seen jabar ja ngeen jël ba ngeen di ndaw.
16 "For I hate divorce," says our Father, the Father of Israel, "and whoever covers his garment with violence," says the Father of heaven's armies. So guard your spirit; do not be unfaithful. «Pase laa bañ,» Aji Sax ji Yàllay Israayil moo ko wax, «ak ku làmboo jëfi loraange ni mbubb.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. Kon nag sàmmleen seenum xel, te buleen wor.
17 You have worn out our Father with your words. Yet you ask, "How have we worn him out?" By saying, "All who do evil are good in his sight, and he delights in them"—or, "Where is the Father of justice?" Soof ngeen Aji Sax ji ak seeni wax, ngeen naan: «Nu nu ko soofe?» Xanaa naan: «Képp kuy def lu bon mooy ki baax ci Aji Sax ji, te kooku la safoo.» Mbaa ngeen naa: «Ana Yàlla jiy àtte dëgg sax?»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]