Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Daniel 11 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 And I, in the first year of Darius the Mede, stood up to support and strengthen him. Man ci sama wàllu bopp nag, maa nga woon ca wetam, di ko aar aka jàppale, ca at ma njëkk ca nguurug Daryus waa Medd ba.»
2 Now I'll tell you the truth: look, three more kings will rise in Persia, then a fourth far richer than all. Strengthened by his wealth, he will stir up everyone against Greece's kingdom. «Léegi, maa ngi lay xamal lu wér. Dama ne, dina amaat ñetti buur yuy falu ci réewum Pers, ñeenteel ba dikk, dajale alal ju bare, ba ëpple leen ñoom ñépp. Bu demee ba alalam may ko doole, dina def lépp lu mu man ngir xabtal ñépp ci kaw nguuru Geres.
3 Then a mighty king will arise, who will rule with great dominion and do as he pleases. Waaye buur bu jàmbaare dina falu, di boroom kilifteef gu yaatu, di def lu ko soob.
4 Once he rises, his kingdom will break apart and split toward the four winds of heaven—not to his descendants, nor with the power he held, for his kingdom will be uprooted and given to others besides them. Naka lay jóg rekk, nguuram daldi foq, tas, ñeenti ngelawi asamaan tasaare, yóbbu. Aw askanam du moom nguur ga, te nguur ga dootul am doole ja mu amoon. Nguuram day foq, tàbbi ci loxoy ñeneen ñu dul askanam.
5 The king of the south will grow strong; one of his commanders will grow stronger than him and rule—his dominion will be vast. «Buur bëj-saalum dina am doole, waaye kenn ca ña mu jiital a koy ëpp doole, te kilifteefam mooy gëna yaatu.
6 After some years they will ally: the daughter of the king of the south will come to the king of the north to make an agreement. But she won't keep her strength, nor will he or his arm stand. She will be handed over—with her escort, her father, and her supporter—in those times. «Gannaaw ay at, buur bëj-saalum ak buur bëj-gànnaar dinañu mànkoo. Doomu buur bëj-saalum mooy séysi kër buur bëj-gànnaar, ngir dëgëral diggante bi. Waaye nguurug doom ja du yàgg, boroom këram it du dundaat lu yàgg mook seen doom. Doomu buur bëj-saalum day dee, mook toppam ak baayam ak boroom këram.
7 A shoot from her roots will rise in his place, attack the army, enter the north king's fortress, act against them, and prevail. Kenn ci waa këram mooy wuutu baayam, dikk, dal ca mbooloom xarem buur bëj-gànnaar, jàll ba ca wàllaa tatay buur bëj-gànnaar, jëflanteek ñoom, duma leen, ba daan.
8 He will take their gods captive to Egypt, with their metal images and precious silver and gold vessels; for years he will stay away from the king of the north. Dinañu lël sax seen jëmmi tuur yu ñu móol, yóbbu Misra, boole kook seen gànjaru xaalis ak wurus. Gannaaw loolu dina toog ay at te du laaleek buur bëj-gànnaar.
9 The king of the north will invade the king of the south's realm, then return home. Gannaaw gi, buur bëj-gànnaar dina dem réewum bëj-saalum, doora dellu réewam.
10 His sons will arm for war, gather a vast army that keeps coming, overflows, sweeps through, then renews war to his stronghold. «Ay doomam yu góor nag dinañu waajal xare, dajale gàngoor yu takku. Ñu jubal, bëtt, jàll nim wal, daldi ñoqali, songi noon ba ca dëkk ba ñu wëralee tata.
11 The southern king, enraged, will march out to fight the northern king, who musters a vast army; but the army is given into the southern king's hand. «Buur bëj-saalum dina xabtalu, songi buur bëj-gànnaar. Kooku waajal mbooloom xare mu mag, waaye mbooloo moomu dees na leen teg ci seen loxoy noon.
12 When the crowd is carried off, his heart grows proud; he strikes down tens of thousands, yet fails. Mbooloo moomu dees na leen daan, buur bëj-saalum di ca réy-réylu. Dina rey ay junniy nit nag, waaye du ko taxa am ndam.
13 The king of the north will again raise a horde bigger than before, then after years come with a great army and vast supplies. Li ko waral mooy buur bëj-gànnaar day dellu waajalaat mbooloo mu ëpp ma jiitu. Bu amee ay at dina dikkaat, ànd ak mbooloom xare mu mag ak ngànnaay lu takku.
14 In those times many will rise against the king of the south; violent men of your people will lift themselves up to fulfill the vision, but fail. «Jamono yooyu ñu bare dinañu jógal buur bëj-saalum, te ay nit ñu soxor ñu bokk ci saw xeet dinañu fippu, ni ko am peeñu indee, waaye duñu ko man.
15 The king of the north will come, raise a siege ramp, and take a fortified city; the south's forces will not stand, nor its elite troops—no strength remains to stand. Buur bëj-gànnaar dina ñëw yékkati ay jal, gaw dëkk bu ñu wërale tata, nangu ko. Mbooloom xarey bëj-saalum ak seen ñeyi xare duñu leen mana të. Duñu am doole ju ñu leen tëwe.
16 His invader does as he pleases; none can stand before him. He will stand in the splendid land, destruction in his hand. Ki leen di song dina leen def li ko soob, ndax kenn du ko të. Dina toog ci réew mu taaru ma, te am dooley tas ko.
17 He will set out to enter with his kingdom's full strength, and make terms with him; he will give him a daughter of women to ruin it, but it will not stand or benefit him. Dina fas yéenee dikk ak dooley nguuram gépp, ba dëgëral digganteem ak buur bëj-saalum. Da koy may doomam soxna, ngir di ko fexee sànk. Waaye loolu du sotti, ndax pexe ma du àntu.
18 Then he'll turn to the coastlands and take many, but a commander will end his arrogance, turning it back on him. Gannaaw loolu dina wuta moom fa féeteek dun ya, ba nangu ca ay réew, waaye dina am njiitu xare lu dakkal jëfi réy-réyloom ji muy toroxale, ba fey ko añam.
19 Then he will turn his face toward the fortresses of his own land, stumble, fall, and be found no more. Bu loolu weesoo dina walbatiku dal ci dëkk yi ñu wëralee tata ci biir réewum boppam, waaye du sotti. Day daanu, ne mes.
20 In his place will rise one who sends a tax collector for the glory of the kingdom; within a few days he'll be broken—not in anger, not in battle. Ki koy wuutu dina yebal kuy foqati ay galag yu ñuy yokke puukarey nguur gi, waaye du yàgg dara, ñu bóom ko ci sutura, te du doon ci xare.
21 A despised man will rise in his place, denied royal honor. He'll come in a time of ease and seize the kingdom through flattery. «Ku siblu moo koy wuutu, ku yelloowul darajay nguur. Day duggsi ndànk, lal ay pexeem, ba nangu nguur gi.
22 Armies will be swept away before him and broken, and the prince of the covenant as well. Mboolooy xare yi dinañu defum wal nig dex, dal ci kawam, waaye dees na leen rajaxe, ñook genn kilifay mbooloom kóllëreg Yàlla gi.
23 Once allied with him, he will act dishonestly and grow strong with only a few people. Gannaaw bu ñu wóllëranteek moom, dina wor. Dina gëna am doole, te amul mbooloo mu bare.
24 In a time of security, he will enter the province's richest regions and do what neither his fathers nor their fathers did—scattering plunder, spoil, and goods among them, devising schemes against fortresses, but only for a time. Day dugg ndànk ba ca biir gox ya gëna woomle ca diiwaan ba. Dina fa def lu ay baayam aki maamam masula def. Dina lël ay réew, séddale ay farandoom alal jaak koom ga. Dina lal pexe yu mu songe ay tata, waaye loolu ab diir lay doon.
25 He will rouse his strength and courage against the king of the south with a great army. The king of the south will fight with a very great, mighty army—but won't stand, for plots will be devised against him. «Bu loolu weesoo dina ànd ak mbooloo mu bare, daldi yebook doole ak pastéef ci kaw buur bëj-saalum. Buur bëj-saalum waajal xare, ànd ak mbooloo mu réy te bare doole lool, waaye sottiwul ndax pexe yu ñu koy lalal.
26 Those who eat his food will break him; his army is swept away, and many fall slain. Ci biir loolu ay nit ñuy bokk ak buur bëj-saalum ndab ñoo koy sànk, ba mbooloom jóoru, ñu bare tëdd.
27 Both kings' hearts bent on evil will speak lies at one table, but it will fail—the end awaits its appointed time. Ñaari buur yi dinañu nas lu bon ci seen xol; di bokk ndab tey waxantey fen. Waaye seeni pexe du mujj fenn, ndax du fekk muj ga jot.
28 He returns to his land with great wealth, heart against the holy covenant; he acts, then returns to his land. Gannaaw gi, buur bëj-gànnaar dina dellu réewam, yóbbaale alal ju takku. Ni mu ko nase woon dina fexeel mbooloom kóllëre gu sell gi, doora ñibbi réewam.
29 At the appointed time he will return and head south, but this time won't match the earlier or the latter. «Bu àpp bi jotee, buur bëj-gànnaar dina dal ci kaw réewum bëj-saalum. Waaye boobu yoon du deme na woon.
30 For ships of Kittim will come against him; he loses heart, turns back, rages against the holy covenant, and acts. He returns and favors those who abandon the holy covenant. Ay boroom gaal yu mag dinañu jóge sowu, songsi ko, ba tax mu xàddi, ba dëpp. Mu daldi mer lool, sippi ko mbooloom kóllëre gu sell gi, tey ànd ak ñi dëddu kóllëre gu sell gi.
31 His forces will rise, defile the sanctuary fortress, end the daily sacrifice, and set up the abomination that causes desolation. Ay xarekat yu mu yebal dinañu dem teddadil kër gu sell gi ñu dàbbali; dinañu dakkal sarax siy am bés bu ne, ba noppi teg fa lu siblu luy jur yàqute.
32 He will corrupt those who violate the covenant with flattery, but people who know their Father will stand firm and act. Ñi sàmmul kóllëreg Yàlla ay nax la leen di fàbbee, waaye askan wi ràññee seen Yàlla, pastéef lañuy jëfeji.
33 The wise among the people will teach many, but will fall for a time by sword, flame, captivity, and plunder. Te it boroom xel yu rafet yi ci mbooloo mi dinañu gindi ñu bare. Nattu dina leen dikkal ab diir; ñii saamar jaar ci seen kaw, ñii ñu lakk leen, ñee ñu nangu seen alal, tëj leen.
34 When they fall, they will receive a little help, and many will join them with flattery. Te bu leen nattu dikkalee, ndimbal lu néew lañuy am, ndax ñu bare naaféq lañuy fareek ñoom.
35 Some of the wise will stumble, to be refined, purified, and cleansed until the end time, for it still awaits the set time. Ñenn ci boroom xel yu rafet yi dinanu jaare ci nattu yu leen di sellal, fóot leen ba ñu set wecc, ba keroog mujug jamono. Àpp ba nag des na.
36 The king will do as he pleases, lifting and enlarging himself above every god, speaking shocking things against our Father. He will flourish until the wrath is spent, since what is decreed will happen. «Buur bi dina def lu ko soob. Dina réy-réylooka damu, ba weesale boppam tuur yépp, te dina wax gilaawaali jëme ci Yàlla ji sut lépp. Dina am ndam nag ba keroog sànjum Yàlla ñoral ko. Li ñu dogal déy dina am.
37 He will disregard his fathers' gods, women's desired one, and every god—he will set himself above them all. Buur bi du faale tuuri maamam, du faale tuur mi jigéen ñi sopp. Du faale menn tuur, ndax day damu ba weesale boppam lépp.
38 Instead he'll honor a god of fortresses, unknown to his fathers, with gold, silver, precious stones, and costly gifts. Xanaa kay tuur mi yor kaaraangey tata yi lay jaamu, muy tuur mu ay maamam xamul woon. Dina ko jaamoo wurus ak xaalis ak xeer yu jafe ak yeneen gànjar.
39 With a foreign god he attacks the strongest fortresses. He greatly honors those who acknowledge him, gives them rule over many, and divides land for a price. Tuuri jàmbur yooyu lay doolewoo, di song dëkk yi ñu wëralee ay tata. Ku ko nangul, mu teral la, def la kilifag ñu bare, ba noppi yoole la ay suuf.
40 At the end time, the king of the south will engage him, and the king of the north will storm against him with chariots, horsemen, and many ships. He will invade the lands, overflow, and pass through. Ca mujug jamono buur bëj-saalum dina fenqoo ak buur bëj-gànnaar. Te itam buur bëj-gànnaar dina mel ni ngëlén, ne milib ci kawam, ànd ak watiiri xare aki gawar ak gaal yu mag yu bare. Dina dugg ci ay réew, bëtt, jàll nim wal.
41 He enters the beautiful land; many fall, but Edom, Moab, and Ammon's chief sons escape his hand. Gannaaw loolu dina dugg ci réew mu taaru ma, te ñu bareey daanu. Waaye Edomeen ñaak Mowabeen ñaak njiiti Amoneen ñi dinañu rëcc.
42 He will stretch out his hand against the lands, and the land of Egypt will not escape. Dina teg loxoom yeneen réew, te réewum Misra sax du ca mucc.
43 He will rule gold and silver treasures, and all Egypt's riches, with Libyans and Cushites at his heels. Dina aakimoo alali Misra, muy wurus, di xaalis ak mboolem gànjar. Waa Libi ak waa Kuus it dinañu ko nangul.
44 But news from the east and north will terrify him, and he'll set out in great rage to destroy and annihilate many. Waaye nag xibaar dina bawoo penku ak bëj-gànnaar, tiital ko lool. Noonu mu jóg ak xadar, rey ñu baree bare, faagaagal leen.
45 He will pitch his palace tents between the seas and the beautiful holy mountain, then come to his end with no helper. Dina samp xaymay kër buur ci diggante géej geek tund wu taaru wu sell wa. Waaye dina dee, te kenn du ko taxawu.»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]