Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Daniel 10 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 In Cyrus king of Persia's third year, a message was revealed to Daniel, called Belteshazzar—true, about a great war. He understood it, gaining insight into the vision. Ci ñetteelu atu nguurug Sirus buuru Pers, kàddu daa dikkal Dañeel ma ñuy wax Beltacar. Kàddu googu di gu wóor tey yégle xare bu mag. Mu dégg kàddu gi, xam pirim peeñu mi.
2 In those days I, Daniel, was mourning for three full weeks. Jant yooyu, man Dañeel maa nga doon ñaawlu diiru ñetti ayi bés.
3 I ate no fine food; no meat or wine touched my mouth; I used no oil at all, until three weeks passed. Ñam wu neex lekkuma ko, te yàpp ak biiñ jaarul sama gémmiñ. Diwuwuma diwu gu xeeñ it ba ñetti ayi bés yi mat.
4 On the twenty-fourth day of month one, I stood on the bank of the great river—the Tigris. Keroog ñaar fukki fan ak ñeent ci weer wi njëkk ci at mi, maa nga ca tàkkal dex gu mag gi ñuy wax Tiigar.
5 I looked up and saw a man in linen, a belt of fine gold of Uphaz around his waist. Ma séentu, xool, yemuma ci ku moy genn góor gu sol yérey lẽe, gañoo ngañaayal wurus wu raxul.
6 His body like beryl, his face like lightning, his eyes like torches of fire, his arms and legs like polished bronze, and the sound of his words like a roaring crowd. Yaram waa nga rafet ni peru gànjar, xar-kanam ba mel ni melax, bët ya mel ni jumi sawara, loxo yeek tànk yi mel ni xànjar bu ñu jonj, riiru baatam mel ni coowal mbooloo.
7 I, Daniel, alone saw the vision; the men with me didn't see it, but great trembling fell on them, and they fled and hid. Man Dañeel doŋŋ maa gis peeñu mi. Ñi ma àndal gisuñu ko. Tiitaange ju réy nag jàpp leen, ba ñu daw, làquji.
8 Left alone, I saw this great vision. No strength remained in me; my face turned deathly pale, and I kept no strength. Ba loolu amee ma des fa man rekk, ne jàkk ci peeñu mu réy moomu. Waaye deseetuma woon doole, damaa jeexal tàkk, amatuma genn kàttan.
9 Then I heard his words, and hearing them, I fell face down on the ground in a deep sleep. Ci kaw loolu ma dégg baatam. Naka laa dégg baatam, daldi daanu leer, sama kanam dëppu fi suuf.
10 Suddenly a hand touched me and set me trembling on my hands and knees. Yéguma lu moy ab loxo bu ma laal, yékkati ma, ma teg sama bëti óom ak sama tenqi loxo fi suuf, di lox.
11 He said to me, "Daniel, dearly loved man, understand the words I speak to you; stand up, for I am now sent to you." When he spoke this word to me, I stood up, trembling. Mu ne ma: «Dañeel, yaw mi ñu naw, déggal kàddu yi ma lay wax. Jógal taxaw sa taxawaay, ndax dañu maa yebal ci yaw nii.» Naka la ma wax kàddu yooyu, ma ne ñokket, di lox.
12 He said to me, "Don't be afraid, Daniel. From the first day you set your heart to understand and humbled yourself before your Father, your words were heard, and I came because of your words. Mu ne ma: «Dañeel, bul tiit. Bés bu njëkk, ba nga fasee yéene xam, ba toroxlu ci sa kanam Yàlla, ca lañu dégg say kàddu te sa kàddu yooyoo ma taxa ñëw.
13 But the prince of Persia's kingdom opposed me twenty-one days; then Michael, one of the chief princes, came to help me, for I was left there with Persia's kings. Waaye malaaka miy wattu nguurug Pers moo ma dogale lu tollook ñaar fukki fan ak benn. Mikayel nag, kenn ci malaakay wattukat yu mag yi ñëw, wallusi ma. Yàgg naa ca buuri Pers ya.
14 I came to help you understand your people's future in days to come, for the vision is for days still ahead." Léegi ñëw naa ngir xamal la liy dikkal sa mbooloo ci jamono yiy ñëw ndax peeñu mi ëmb na jamono yooyu itam.»
15 As he spoke these words to me, I turned my face to the ground, unable to speak. Bi mu may wax kàddu yooyu, maa ngi sëgg, sama kanam jublu ci suuf, manumaa wax.
16 Then one like a man touched my lips. I opened my mouth and began to speak. I said to the one standing before me, "My lord, the vision has filled me with pain, and I have no strength left. Jekki-jekki jëmm ju mel ni nit dikk, laal samay tuñ. Ma ŋa, àddu, daldi wax ak ki taxaw ci sama kanam ne ko: «Sang bi, peeñu mi tax na ma jàq, ba amatuma benn doole.
17 How can I, your servant, speak with you, my lord? No strength remains in me now, no breath is left." Te it sang bi, nu may mana waxeek yaw, sang bi? Amatuma doole te deseetuma ngelawal gémmiñ.»
18 Again the one who looked like a man touched me and strengthened me. Ba loolu amee jëmm jiy nirook nit dellu laal ma, ma amaat doole.
19 He said, "Don't be afraid, treasured one. Peace to you; be strong, be strong!" His words strengthened me, and I said, "Speak, my lord, for you have strengthened me." Gannaaw loolu mu ne ma: «Yaw nit ki ñu naw, bul tiit. Jàmm la. Góor-góorlul!» Muy wax ak man, may amaat doole, ba ne ko: «Waxal sang bi, dooleel nga ma.»
20 He said, "Do you know why I came to you? Now I return to fight Persia's prince; then, as I leave, Greece's prince comes. Mu ne ma: «Ndax xam nga lu ma taxa dikk? Léegi ma dellu xarejeek malaaka miy wattu réewum Pers; te bu may dem, malaaka miy wattu Geres dikk.
21 But first I'll tell you what's written in the Book of Truth: none stands firmly with me against them but Michael, your prince." Waaye dinaa la xamal li ñu bind ci téereb dëgg gi. Kenn jàppalewu ma ci ñooñu ku dul Mikayel, seen malaakam wattukat, yeen bànni Israayil.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]