Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Daniel 12 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 At that time Michael, the great prince guarding your people's children, will arise. There will be distress unmatched since nations began, until then. At that time your people—all listed in the book—will be rescued. Malaaka ma waxati ma, ne ma: «Jamono yooyu ci la Mikayel, malaakam wattukat mu mag miy taxawu sa mbooloo, di jóg. Muy jamonoy njàqare ju masula am, cosaanal xeet yi ba tey jii. Bu keroogee sa bokk yiy mucc, ñooy ñi ñu bind ci téereb dund bi.
2 Many sleeping in earth's dust will wake—some to everlasting life, some to shame and everlasting contempt. Ñu bare ñuy nelaw ci seeni bàmmeel dinañu yewwu. Ñenn ña nara dund fàww, ña ca des añe gàcceek njàqare fàww.
3 The wise will shine like the sky's brightness; those who turn many to righteousness, like stars, forever and ever. Ña rafet xel leer nàññ ni leeraayu déndub asamaan. Ñi doon xiir mbooloo mi ci njub ne boyy niy biddiiw, ba fàww.
4 But you, Daniel, close these words and seal the book until the end time. Many will roam back and forth, and knowledge will grow. «Yaw nag Dañeel, dencal kàddu yii, muy kumpa te nga tëj téere bi, tay ko ba mujug jamono jub. Su keroogee ñu bare dinañu gëstu fu ne, ba xam-xam yokku.»
5 Then I, Daniel, looked and saw two others standing, one on each bank of the river. Noonu man Dañeel, may xool ci biir peeñu mi, daldi yem ci ñeneen ñaar ñu taxaw, séq dex gi.
6 One asked the linen-clad man above the river's waters, "How long till these wonders end?" Kenn ki wax ak ka sol mbubbam lẽe, te taxaw ca kaw dex ga, ne ko: «Ana fu kéemaan yiy yem?»
7 I heard the man dressed in linen, above the river's waters, lift his right hand and left toward heaven and swear by the One who lives forever: for a time, times, and half a time; when the shattering of the holy people's power is finished, all these things will be finished. Ka sol mbubbam lẽe te taxaw ca kaw dex ga, ma nga yékkati loxo ndijoor baak bu càmmoñ ba, te ma dégg ko mu naa: «Giñ naa ko ci Kiy dund fàww ne ñetti diir ak genn-wàll lay doon. Xew-xew yooyu yépp a ngi dakk keroog bu dooley mbooloo mu sell mi jeexee tàkk.»
8 I heard, but didn't understand, so I said, "My lord, what is the end of these things?" Maa ngi ciy dégg waaye xawma lu muy tekki. Ma ne: «Sang bi, ana nu xew-xew yooyu di mujje?»
9 He said, "Go, Daniel, for the words are shut and sealed until the time of the end. Mu ne ma: «Dañeel, demal rekk, ndax mbir yii dees koo làq, dëxëñ ko, ba keroog muj ga taxaw.
10 Many will be purified, whitened, refined; the wicked will keep doing evil. None of the wicked will understand, but the wise will understand. Ñu bare dees na leen sellal, fóot leen ba ñu set wecc. Waaye ñu bon ñi wéy di bon, te kenn du ci xam liy xew, teewul ñi rafet xel dinañu ko xam.
11 From the daily sacrifice's removal and the setting up of the abomination that causes desolation: 1,290 days. Jamono ja ñuy dakkal sarax si ñu wara joxe bés bu ne, di keroog ba ñuy taxawal lu siblu lay jur yàqute, junniy fan ak ñaari téeméer ak juróom ñeent fukk (1 290) dina ca topp.
12 Blessed is the one who waits and reaches the 1,335 days. Ndokkalee ku muñ nag diiru junniy fan ak ñetti téeméer ak fanweer ak juróom (1 335).
13 But you, go to the end. You will rest, then stand for your inheritance at the end of the days." Waaye yaw Dañeel, muñal ba fa muy mujje. Su keroogee fekk la nelaw, doora jóg jël sab yool, ca mujug jamono.»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]