Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

2 Timothy 3 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 But understand this: in the last days there will come times of difficulty. Lii, nanga ko xam: mujug jamono, bés yu tar dina dikk.
2 For people will be self-lovers, money-lovers, boastful, arrogant, abusive, disobedient to parents, ungrateful, unholy. Nit ñi, seen bopp doŋŋ lañuy bëgg, ay bëggkati xaalis lañuy doon, ay damukat, nit ñu réy, di ay saagakati Yàlla, ñu déggadil waajur, ñu goreedi te selladi.
3 Heartless, unforgiving, slanderous, without self-control, brutal, hating what is good, Duñu am yërmande, duñu meddi, ay soskat lañuy doon, ñu ñàkk sago, ñu néeg te bañ lu baax;
4 treacherous, reckless, swollen with conceit, lovers of pleasure rather than lovers of our Father. ay workat lañuy doon, ñu teeyadi, ñu daŋŋiiral te di ñu bëgg seen bànneexu bopp, ba mu gënal leen Yàlla.
5 They keep the shape of devotion to God but deny its power—turn from them. Ragal Yàlla lañuy mbubboo tey xalab leer ga leen ko wara manloo. Ñooñu, dëddu leen.
6 For among these are those who slip into homes and trap weak women weighed down with sins, driven by various desires. Ñenn ci ñooñu ñooy yoxoosuy dugg ci biir kër yi, di fàbbi jigéen ñu ñàkk bopp, ñi seeni bàkkaar man, te seen xemmemtéef yu bare jiital leen.
7 Always learning but never able to come to a knowledge of the truth. Gëstu ay àlluwa la jigéen ñooñuy wéye, waaye duñu mana xam liy dëgg mukk.
8 As Jannes and Jambres opposed Moses, these also oppose the truth—minds corrupted, disqualified regarding the faith. Noonee Sànnes ak Sàmbres doon jànkoonteek Musaa, ni la góor ñooñu di jànkoontee ak dëgg gi; ñooy nit ñu seenum xel yàqu, te ñu doyadi ci wàllu ngëm.
9 But they won't get far, for their foolishness will be clear to all, as with those two men. Waaye duñu soreeti, ndax seenug ndof dina bir ñépp, na ñaar ñooña mujje woon.
10 You, however, have followed my teaching, conduct, purpose, faith, patience, love, endurance, Yaw nag seetlu nga bu baax sama àlluwa ak sama dundin ak sama mébét ak sama ngëm ak samag muñ ak sama cofeel ak samag ñeme coono
11 my persecutions and suffering—at Antioch, at Iconium, at Lystra, what persecutions I endured! Yet the Lord rescued me from them all. ak itam bunduxataal yaak njàqare ya ma dikke woon fa dëkk yooyu di Àncos ak Ikoñum ak Listar. Céy na ñu ma bunduxataale, waaye Sang bee ma musal ci lépp!
12 Indeed, all who desire to live a godly life in Christ Jesus will be persecuted, Te kat képp ku namma farlu ci yoonu Almasi Yeesu, dees na la bunduxataal.
13 while evil people and impostors will go on from bad to worse, deceiving and being deceived. Waaye nit ñu bon ñi ak maa-man yi dañuy gën di bon rekk, di naxe tey nax seen bopp.
14 But you—stay with what you learned and became convinced of, knowing from whom you learned it, Yaw nag saxal ci li nga jàng, muy lu la wóor, nde xam nga ña nga tanqe.
15 and that from infancy you have known the sacred writings, able to make you wise for salvation through faith in Christ Jesus. Bi ngay gone nga dale xam Mbind mu sell mi, te moo la mana may xel mu la jëme ci mucc gi gëm Almasi Yeesu di maye.
16 All Scripture is breathed out by our Father—useful for teaching, exposing wrong, correcting, and training in right living, Mboolem Mbind mu sell mi la Yàlla wal ag Noowam, ba mu am njariñal jàngal nit ñi, femmu leen, jubbanti leen, yar leen cig njub.
17 so that the person of our Father may be complete, equipped for every good work. Su ko defee nitu Yàlla ki mat sëkk te matley jumtukaay ngir jépp jëf ju baax.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]