Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

2 Timothy 2 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 So then, my child, draw your strength from the grace that is in Christ Jesus. Kon nag yaw doom, doolewool yiw wi Almasi Yeesu di maye.
2 And what you heard from me in the presence of many witnesses, entrust to faithful people able to teach others too. Li nga dégge ci man te seede yu bare teewe ko, nanga ko jottali nit ñu wóor ñu ko mana xamal ñeneen.
3 Take your share of suffering like a good soldier of Christ Jesus. Jëlal sa wàll ci coono bi takk-derub Almasi Yeesu bu wóor di jànkoonteel.
4 No soldier on duty gets tangled in civilian affairs—he wants to please the one who enlisted him. Ab takk-der bu bëgga neex ka ko solal kat, du xintewoo mbiri nit ña soluwul.
5 And an athlete is not crowned unless he competes according to the rules. Kuy joŋante it, deesu ko kaala te joŋantewul ci yoon.
6 The hard-working farmer ought to be the first to receive a share of the crops. Te it beykat bi yor coonob liggéey bi, moo wara njëkka séddu ca meññeef ma.
7 Think over what I am saying, for the Lord will give you understanding in everything. Defal sam xel ci li ma la wax. Boroom bi moo lay leeralal lépp.
8 Remember Jesus Christ, risen from the dead, a descendant of David, as told in my gospel, Bàyyil xel ci Yeesu Almasi bi ñu dekkal te mu soqikoo ci Daawuda, ni ko sama xibaaru jàmm indee.
9 for which I suffer, chained like a criminal. But the word of our Father is not chained! Xibaaru jàmm boobu moo tax may daj coono yu metti ni defkatu mbon, ba ci jéng yii ñu ma jéng. Waaye kàddug Yàlla moom, deesu ko jéng.
10 So I endure everything for the sake of the chosen, so they too may gain the salvation in Christ Jesus, with eternal glory. Looloo ma tax di muñ lépp, ngir ñi ñu tànn, ndax ñoom it ñu dajeek mucc gi ci Almasi Yeesu, boole ci teraanga ju sax.
11 This saying is trustworthy: If we have died with him, we will also live with him; Kàddu gu wóor a ngii: Su nu deewandoo ak Almasi bi, nooy dundandoo ak moom itam;
12 if we endure, we will also reign with him; if we disown him, he also will disown us; su nu muñee, nooy bokk nguuru. Su nu ko gàntalee, moom it dinanu gàntal;
13 if we are faithless, he remains faithful, for he cannot disown himself. su nu ko ñàkkee kóllëre, mu saxoo kóllëreem, ndax manula gàntal boppam.
14 Remind them of these things, and warn them before our Father not to quarrel over words—useless, and ruins those who listen. Loolu, dee ko fàttalee, te ngay dénkaane fi kanam Yàlla, ñu bañ di xuloo ci li baat yiy tekki, ndax amul njariñ, te ñi koy dégg doŋŋ lay sànk.
15 Do your best to present yourself to our Father approved, a worker unashamed, rightly handling the word of truth. Defal sa kem-kàttan ba boo teewee fa kanam Yàlla, di ku mu gërëm, ab liggéeykat bu mucc gàcce, di xamle kàddug dëgg gi ni mu ware.
16 But avoid empty, godless chatter; it leads people further into wickedness, Waaye ay kebetuy àddinay kese, moytu ko, ndax ngëmadi gu ko yées rekk lay yóbbee,
17 and their talk will spread like gangrene. Among them are Hymenaeus and Philetus, te kàdduy ñooñu day law ni ngal. Ci ñooñu la Imene ak Filet bokk.
18 who wandered away from the truth, claiming the resurrection already happened, and are undermining some people's faith. Ñoo lajj yoonu dëgg, ba naan ñiy dekki, dekki nañu ba noppi, te seen wax jooju, am na ñenn ñu muy yàq seen ngëm.
19 Yet our Father's firm foundation stands, sealed: "He knows those who are his," and "Let all who name his name turn from evil." Teewul cëslaay lu dëgër, li Yàlla tabax, mu ngi ne kekk, te màndarga ma ca nekk, kàddu yii la: «Boroom bi xam na ki mu séddoo,» ak: «Kuy tudd turu Sang bi, na daw njubadi.»
20 In a large house there are vessels not only of gold and silver, but also of wood and clay—some for honor, some for dishonor. Kër gu mag nag, du ndabi wurus ak xaalis rekk a fa am, waaye yoy bant a nga fa ak yoy ban; yii di ndabi teraanga, yee di ndabi njoogaan.
21 So if anyone purifies himself from these, he becomes a vessel of honor: holy, useful to the Master, ready for every good work. Ku setal sa bopp nag ba mucc ci yu bon yooyii, yaay doon ndabal teraanga lu sell te amal sangam njariñ ngir jépp jëf ju baax.
22 Flee youthful cravings; pursue righteousness, faith, love, and peace with those who call on the Lord from a pure heart. Xemmemtéefi ndaw nag, daw ko, te nga topp njub ak ngëm ak cofeel ak jàmm, ànd ceek ñiy tudde Boroom bi xol bu set wecc.
23 Have nothing to do with foolish, ignorant controversies; you know they breed quarrels. Waaye werante yu xeluwul te du xam-xam, moytu ko, te xam ne ay ŋaayoo lay jur.
24 The Lord's servant must not be quarrelsome, but be gentle to all, able to teach, patient when wronged. Te jaamub Boroom bi warul di ŋaayoo, waaye day lewet ci ñépp, mana jàngale tey muñ.
25 Gently correcting those who oppose him. Perhaps our Father will grant them repentance to know the truth, Jaamub Boroom bi ndànk la war di jubbanti diiŋatkat yi, ndax jombul Yàlla may leen ñu tuub, ba xam liy dëgg.
26 and they may sober up, escaping the devil's trap where he has held them captive to do his will. Su ko defee seenum xel dellusi, ba ñu rëcc fiirug Seytaane mi leen jàpp, di leen defloo coobareem.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]