Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

2 Samuel 1 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 After the death of Saul, David returned from defeating the Amalekites and stayed in Ziklag two days. Gannaaw ba Sawul faatoo, fekk na Daawuda walbatikoo ca dumay Amalegeen ña, dellu Ciglaag, ba toog fa ñaari fan.
2 On the third day a man came from Saul's camp, clothes torn, dirt on his head. Reaching David, he fell to the ground and bowed. Ca gannaaw ëllëg sa, jenn waay ne jimeet, jóge ca dalub Sawul, dikk. Yére yaa nga xottiku, bopp ba taq suuf, ngir naqarlu. Naka la agsi ci Daawuda, daldi daanu fi suuf, sujjóot.
3 David asked him, "Where have you come from?" "I escaped from the camp of Israel," he replied. Daawuda ne ko: «Foo jóge nii?» Mu ne ko: «Ca dalub Israayil laa rëcce.»
4 "What happened?" David asked. "Tell me." He said, "The people fled the battle. Many fell and died. Saul and his son Jonathan are dead too." Daawuda ne ko: «Lu xew, gaawe ma!» Mu ne ko: «Mbooloom Israayil a dawe ca xare ba. Ñu bare ca ñoom daanu nañu, dee. Sawul ak doomam Yonatan it dee nañu.»
5 David asked the young man who brought the news, "How do you know Saul and his son Jonathan are dead?" Daawuda ne ndaw la: «Lu la xamal ne Sawul ak doomam Yonatan dee nañu?»
6 The young man said, "I happened onto Mount Gilboa, and there was Saul, leaning on his spear, the chariots and horsemen bearing down on him. Ndaw la ne ko: «Dafa yemook ma tollu tembe ca kaw tundu Gilbowa. Ndeke Sawul a nga fa, sukkandikoo xeejam. Watiiri xare yaak gawar ya defuñu lu moy ne ko dann.
7 He turned around, saw me, and called to me. I said, 'Here I am.' Naka la ne gees, yem ci man, woo ma, ma wuyu.
8 He asked me, 'Who are you?' I told him, 'I am an Amalekite.' Mu ne ma: “Yaa di kan?” Ma ne ko: “Ab Amalegeen laa.”
9 He said to me, 'Stand over me and kill me; anguish has seized me, but I'm still alive.' Mu ne ma: “Kaay fii, jekkali ma. Maa ngi ci miirum dee, doonte dese naa tuuti.”
10 So I stood over him and killed him, since I knew he wouldn't survive his fall. Then I took the crown from his head and the band on his arm, and brought them here to my lord." Ma dikk, daldi koy jekkali, ndax xamoon naa ne du dundati gannaaw jéllam ba. Ma summi nag mbaxanam buur ma mu soloon, tekki lam ba woon ca përëg ma. Yooyu laa la yótsi nii, sang bi.»
11 Then David grabbed his own clothes and tore them, and so did all the men with him. Ba loolu amee Daawuda sëq yéreem, xotti, ña ànd ak moom ñépp itam, noonu, ndax aw naqar.
12 They mourned, wept, and fasted until evening for Saul, his son Jonathan, our Father's people, and the house of Israel, because they had fallen by the sword. Ñaawlu nañu, di jooy, lekkuñu ba ca ngoon ndax Sawul ak doomam Yonatan ak gàngooru Aji Sax ji, ak waa kër Israayil ña ñu reye saamar.
13 David asked the young man who brought the news, "Where are you from?" He said, "I'm the son of a foreigner, an Amalekite." Daawuda ne ndaw la: «Ana foo bokk?» Mu ne ko: «Man doomu doxandéemub Amalegeen laa.»
14 David said, "How were you not afraid to raise your hand to kill our Father's anointed?" Daawuda ne ko: «Noo saña xàcce sa loxo, di bóom ki Aji Sax ji fal?»
15 David called one of his young men and said, "Go, strike him down." He struck him, and he died. Daawuda nag woo kenn cay surgaam, ne ko: «Dikkal dóor, mu dee!»
16 David had said to him, "Your blood is on your own head, for your own mouth testified against you when you said, 'I killed our Father's anointed.'" Daawuda ne Amalegeen ba: «Yaa gàddu sa bakkanu bopp, ndax yaa seedee sa gémmiñu bopp ne yaa rey ki Aji Sax ji fal.» Surga ba dóor Amalegeen ba, mu dee.
17 Then David sang this lament over Saul and his son Jonathan, Kàddu yii la Daawuda jooye Sawul ak doomam Yonatan.
18 and ordered the people of Judah taught this lament, called The Bow; it is written in the Book of Jashar: Moo santaane ñu jàngal ko askanu Yuda. «Fittkat» lañu dippee woy wi. Nii lañu ko binde ci Téereb aji jub ji. Mu ne:
19 "Your glory, Israel, lies slain on your heights. How the mighty have fallen! Wóoy Israayil, ña ngay sagoo lañu jam, ñu ne lareet ca sa tund ya! Jàmbaar ñaa daanu!
20 Don't tell it in Gath, don't proclaim it in the streets of Ashkelon, or the daughters of the Philistines will rejoice, the daughters of the uncircumcised will exult. Buleen ko siiwal fa Gaat, buleen ko yéene fa mbeddi Askalon, lu ko moy janqi Filisti bég, janqi yéefar yiy tex-texi.
21 Mountains of Gilboa, may you have no dew or rain, no fields yielding offerings. For there the shield of the mighty was defiled, the shield of Saul, no longer rubbed with oil. Wóoy tundi Gilbowa! Yàlla bu ngeen lay, bu ngeen tawlu. Yàlla bu seeni tool nangooti, ba duunal njoxem pepp, nde foofa lees toroxale pakkub jàmbaar. Wóoy pakkub Sawul ba deesul diwati!
22 From the blood of the slain, from the flesh of the mighty, the bow of Jonathan did not turn back, the sword of Saul did not return unsatisfied. Du deret mbaa nebbonu jàmbaar bu fittug Yonatan xof, te saamaru Sawul ba du sooy!
23 Saul and Jonathan, beloved and cherished in life, in death they were not parted. They were swifter than eagles, stronger than lions. Wóoy Sawul ak Yonatan, ñoo yiw, sopplu ba ñuy dund, te ba ñu deewee, teqalikoowuñu. Ag jaxaay, ñoo ko gëna gaaw, te gaynde, ñoo ko gëna jàmbaare.
24 Daughters of Israel, weep for Saul, who clothed you in scarlet and finery, who adorned your garments with ornaments of gold. Yeen jigéeni Israayil, jooyleen Sawul ma leen wodde ndimol tànnéef lu xonq curr, takkal leen gànjari wurus ca seen kawi yére.
25 How the mighty have fallen in the thick of battle! Jonathan lies slain on your heights. Jàmbaar ñaa daanoo biir xare ba, Yonatan lañu jam ca kaw tund ya!
26 I grieve for you, my brother Jonathan; you were very dear to me. Your love for me was wonderful, surpassing the love of women. Yonatan, doom yaay, tiisoo naa la, dama laa soppoon lool, te sa mbëggeel ci man yéeme, ba raw mbëggeelu jigéen.
27 How the mighty have fallen! The weapons of war have perished." Jàmbaar ñaa daanu, ngànnaayi xare ya sànku!
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]