Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

2 Samuel 2 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Later, David inquired of our Father, "Should I go up to one of the cities of Judah?" Our Father said, "Go up." David said, "Where?" "Hebron," he said. Gannaaw ba loolu weesoo Daawuda daa laaj Aji Sax ji, ne ko: «Ndax ma dellu ci dëkki Yuda yi benn?» Aji Sax ji ne ko: «Demal.» Daawuda ne ko: «Bu ma ciy dem?» Aji Sax ji ne ko: «Ebron.»
2 David went up there with his two wives, Ahinoam of Jezreel and Abigail, Nabal the Carmelite's widow. Daawuda dem ca, ànd ak ñaari soxnaam, Axinowam ma cosaanoo Yisreel, ak Abigayil ma doon jabaru Nabal waa Karmel ba.
3 David brought up his men who were with him, each with his household, and they settled in Hebron's towns. Daawuda nag yóbbaale nit ña ànd ak moom, kenn ku ci nekk ak njabootam, ñu dem sanci ca dëkk ya wër Ebron.
4 Then Judah's men came and anointed David king over Judah's house there. They told David that Jabesh-gilead's men had buried Saul. Ba mu ko defee waa Yuda dikk, diw fa Daawuda, fal ko buurub waa kër Yuda. Gannaaw gi, ñu wax Daawuda ne ko waa Yabes Galàdd ñoo rob Sawul.
5 He sent messengers to the men of Jabesh-gilead: "May our Father bless you for this kindness to your lord Saul, burying him. Daawuda yónnee ay ndaw ca waa Yabes Galàdd, wax leen ne leen: «Yal na leen Aji Sax ji barkeel ndegam yeena jëfe ngor seen digganteek seen sang Sawul, ba rob ko.
6 Now may our Father show you kindness and faithfulness; I too will treat you well for doing this. Kon nag yal na Aji Sax ji jëfeek yeen ngor ak kóllëre. Man itam dinaa leen yéwéne ndax nii ngeen jëfe.
7 Be strong and take courage, for your master Saul is dead, and Judah's house has also anointed me king over them." Léegi nag dëgërluleen te góor-góorlu. Dëgg la seen sang Sawul faatu na, waaye man mii la giirug Yuda fal, may seen buur.»
8 But Abner son of Ner, Saul's army commander, took Ish-bosheth son of Saul and brought him across to Mahanaim. Doomu Ner, Abner njiital gàngooru xarem Sawul nag, fekk na mu yóbbu Isboset doomu Sawul ju góor, jàllale ko ba Maxanayim.
9 He made him king over Gilead, over the Ashurites, over Jezreel, over Ephraim, over Benjamin—over all Israel. Mu tabb ko nag buuru diiwaani Galàdd ak Aser ak Yisreel ak Efrayim ak Beñamin, Israayil gépp daal.
10 Ish-bosheth son of Saul was forty when he became king over Israel; he reigned two years. But Judah's house followed David. Ñeent fukki at la Isboset doomu Sawul amoon ba muy falu buurub Israayil, te ñaari at la nguuru. Waa kër Yuda doŋŋ ñoo toppoon Daawuda.
11 David was king in Hebron over the house of Judah for seven years and six months. Diir ba Daawuda falu buurub Ebron gu waa kër Yuda, juróom ñaari at la ak juróom benni weer.
12 Abner son of Ner, with Ish-bosheth son of Saul's servants, left Mahanaim for Gibeon. Mu am bés, Abner doomu Ner ànd ak niti Isboset doomu Sawul, ñu jóge Maxanayim, jëm diiwaanu Gabawon.
13 Joab son of Zeruiah and David's servants also went out and met them together at Gibeon's pool—one side sitting on one bank, the other on the opposite bank. Yowab mi Ceruya di yaayam, daldi ànd ak niti Daawuda, ñu dem dajejeek ñoom ca wetu déegub Gabawon. Ñii taxawe gii wet, ñee taxawe ca wàlla, ñu séq déeg ba.
14 Abner said to Joab, "Let the young men get up and compete before us." Joab said, "Let them get up." Abner ne Yowab: «Ayca na xale yu góor yi jóg, daje fi sunu kanam.» Yowab ne ko: «Ayca!»
15 So they got up and crossed over by count, twelve for Benjamin and Ish-bosheth son of Saul, twelve from David's servants. Ñu daldi limoo, fukki góor ak ñaar taxawal giirug Beñamin ak Isboset doomu Sawul; fukki góor ak ñaar taxawal Daawuda.
16 Each man gripped his opponent's head and drove his sword into his side, and they fell together. So the place in Gibeon was named Helkath-hazzurim. Ku nekk ne sa boppu moroom ŋëjj, rekk bojj sab saamar ca wet ga, ñu ànd daanu. Moo tax ñu woowe béreb booba ca Gabawon «Toolub ñawka yi.»
17 The fighting that day was very fierce; Abner and Israel's men fell before David's servants. Bésub keroog xeex ba metti na lool, waaye Abner ak waa Israayil ñoo féete suuf niti Daawuda.
18 Zeruiah's three sons were there: Joab, Abishai, and Asahel—Asahel as fast-footed as a wild gazelle. Ñetti doomi Ceruya ña nga fa woon: Yowab ak Abisay ak Asayel. Asayel nag daa manoona daw lool ni kéwél.
19 He chased Abner, turning neither to the right nor to the left as he pursued him. Asayel ne dann Abner rekk, jàddul ndijoor, jàddul càmmoñ.
20 Abner looked back and said, "Is that you, Asahel?" "It is," he answered. Abner geesu ne ko: «Kii Asayel?» Mu ne ko: «Man a.»
21 Abner told him, "Turn right or left, seize one of the young men, take his gear." But Asahel refused to stop chasing him. Abner ne ko: «Tee ngaa jàdd ndijoor mbaa càmmoñ, te jàpp kenn ci xale yu góor yi, futti ko!» Asayel nag bëggu koo bàyyi, xanaa topp ko rekk.
22 Abner told Asahel again, "Turn back. Why force me to strike you down? How could I face your brother Joab?" Abner dellu ne Asayel: «Xiddi ma! Bul tax ma jam la, nga daanu! Te kon xawma nu may jàkkaarlooteek sa mag Yowab!»
23 He refused to turn aside, so Abner struck him in the stomach with the butt of his spear; it came out through his back. He fell there and died on the spot. Everyone who came to where Asahel had fallen and died stood still. Asayel të ticc, topp ko. Abner jam ko catal xeejam ca biir ba, ba xeej ba fëll ca gannaaw ga, mu daanu dee ca saa sa. Ba loolu amee, ku dikk, ba tollook béreb ba Asayel daanu dee, daldi fay taxaw.
24 Joab and Abishai pursued Abner; at sunset they reached the hill of Ammah, near Giah on the way to the wilderness of Gibeon. Yowab ak Abisay nag dàqi Abner. Ba jant bay lang, ña nga tollu ca tundu Ama wa janook Giyax, ca yoon wa jëm màndiŋu Gabawon.
25 Benjamin's men gathered behind Abner, formed one band, and stood atop a hill. Beñamineen ñi daldi mànkoo, topp ca gannaaw Abner, ñu def menn mbooloo, bokk taxaw ci kaw wenn tund.
26 Abner called to Joab: "Must the sword devour forever? Don't you know this will end bitterly? How long until you tell the people to turn back from chasing their brothers?" Abner àddu ca kaw, ne Yowab: «Mbaa du saamar day wéy di lekk suux ba fàww? Xamuloo ne lii aw naqar doŋŋ lay mujje? Ana looy xaarati ci ne mbooloo mi ñu noppee topp seeni bokk?»
27 Joab said, "As surely as our Father lives, if you had not spoken, the people would have kept pursuing their brothers until morning." Yowab ne ko: «Giñ naa ci Yàlla jiy dund, boo waxuloon, nit ñi duñu noppee dàq seeni bokk te bët setul.»
28 Joab blew the trumpet; all the troops stopped, no longer pursuing Israel or fighting. Ba loola amee Yowab wal bufta ba, di liit gu ñu defare béjjénu kuuy, gaa ña ñépp nag taxaw, noppee topp Israayil, daldi dakkal xare ba.
29 Abner and his men marched through the Arabah all that night, crossed the Jordan, went through all Bithron, and reached Mahanaim. Abner aki nitam fanaanee topp xuru Yurdan guddig keroog, ba jàll dexu Yurdan. Ñu daldi jaare Bittron gépp, doora agsi Maxanayim.
30 Joab turned back from chasing Abner, gathered all the troops, and found nineteen of David's men missing, besides Asahel. Gannaaw ba Yowab walbatikoo ca ndàqum Abner, daa woo gàngooram gépp, fukk ak juróom ñeent wuute ci niti Daawuda, te limaalewuñu Asayel.
31 But David's servants struck down 360 of the men of Benjamin who were with Abner. Waaye fekk na niti Daawuda rey ñetti téeméer ak juróom benn fukk (360) ca Beñamineen ñaak niti Abner.
32 They carried Asahel, buried him in his father's tomb in Bethlehem; Joab and his men walked all night, reaching Hebron by dawn. Ñu yóbbu Asayel, rob ko ca wetu baayam ca Betleyem, Yowab aki nitam nag fanaanee dox, ba jant fenke leen Ebron.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]