Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

2 Peter 2 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 False prophets arose among the people, just as false teachers will arise among you. They will secretly bring in destructive heresies, even deny the Master who bought them, and bring swift destruction on themselves. Waaye na mu ame woon ci askanu bànni Israayil ay yonenti caaxaan, ni lay ame ci seen biir ay jàngalekati caaxaan yuy sërxal ay àlluway sànkute yuy weddi sax Sang bi leen jot, ba yóbbe seen bopp sànkute ju bette.
2 Many will follow their lust, and because of them the way of truth will be slandered. Ñu baree leen di topp ci seen ñaawtéef gu ëpp, ba tax yoonu dëgg gi tegoo ay saaga ndax ñoom.
3 In their greed they'll exploit you with made-up words. Their judgment, decreed long ago, isn't idle; their ruin isn't asleep. Seenug bëgge lañuy ràbbe ay kàddu yu ñu leen di koppartoo. Ñooñu la seenub daan yàgga yoot, te seen sànkute nelawul.
4 For if our Father did not spare angels who sinned, but threw them into the deepest pit of gloom, chained in darkness, kept for judgment; Ndax Yàlla kat, ndegam moo jéggalul malaaka ya bàkkaaroon, xanaa tàbbal leen kàmbu mbugal, wacce leen ci ay jéngi biir lëndëm gu ne këruus, di leen nége àtte ba.
5 if he didn't spare the ancient world, but protected Noah, an announcer of righteousness, with seven others, when he brought a flood on the wicked world; Ndegam àddina sa woon it Yàlla jéggalu ko, xanaa Nóoyin ma daan woote ci yoonu njub te di kenn ci juróom ñetti nit ña mu musal, ba mu walalee mbënn ma ci àddinay nit ñu gëmadi.
6 and if he condemned Sodom and Gomorrah, reducing their cities to ashes, as an example of what awaits the wicked; Ndegam dëkk ya ñuy wax Sodom ak Gomor it, la mbugale seenub taste, def leen ab dóom, ba def leen misaal mu ñeel aji gëmadiy ëllëg,
7 and if he rescued righteous Lot, worn out by the shameless behavior of lawless people. te mennum Lóot aji jub ji doŋŋ, nekkoon kenn ki mu musal, te mu sonnoon lool, ndax ñaawtéefi nit ñu dëng ñooñu.
8 That righteous man, living among them, was tormented day after day in his righteous soul by the lawless deeds he saw and heard, Ndax Lóot aji jub ja dëkkoon ci seen biir kat, la mu nekke woon ci biir xolu njubam, moo di naqarlu, ndax jëfi ndëngte ya muy gis, di ko dégg, bés bu nekk.
9 then our Father knows how to rescue the godly from trials, and keep the wicked under punishment until judgment day. Su demee noonu kay, kon Boroom bi def loolu lépp, xam na nu muy musale nit ñu ragal Yàlla cib nattu ak nu muy xaare nit ñu dëng ñi, ngir seen mbugal kera bésu àtte ba,
10 Especially those chasing flesh's corrupt desires and despising authority—bold, arrogant, unafraid to slander celestial beings. rawatina nag boroom xemmemtéefi yàqute yi topp seen bakkan te faalewuñu genn kilifteef. Ñu fétteeral lañu te bew, ragaluñoo saaga sax boroom daraja yu kawe ya fa asamaan.
11 Whereas angels, greater in strength and power, don't bring a slanderous judgment against them before our Father. Moona malaaka yi ëpp doole ak manoore sax, ñemewuñoo yékkati kàdduy saaga yu ñuy sikke yooyu boroom daraja, fa kanam Boroom bi.
12 But these people, like unreasoning animals born by instinct to be caught and destroyed, insult what they don't understand, and will be destroyed in their destruction, Waaye ñoom ñooñu mel ni mala yu amul xel, seen yég-yégi judduwaale jiital leen, te li leen taxa juddu di jàpp leen, rey doŋŋ, ñooy saaga lu ñu xamul. Dees na leen rey ni ñuy reye ay mala.
13 suffering wrong as pay for wrongdoing. They count it a pleasure to revel in broad daylight. They are stains and flaws, reveling in their deceptions while feasting with you. Loraange lees leen di feye loraange gi ñu sabab. Seen mbégte mooy xawaarey bëccëg ndarakàmm. Ñooñoo diy gàkk aki sikk, ndax seen teewaay gàcce la ci seen biir yeen, bu ñuy bokk ak yeen bernde, te ca lañuy bànneexoo ay nax.
14 Their eyes are full of adultery, never stopping from sin, luring unstable souls, hearts trained in greed—cursed children! Seeni gët xoolul lu moy ku ñu njaalool, te duñu bàkkaar ba regg mukk; ku dëgërul, ñu yóbbaale la. Ñooñu la seenub xol tàggatu ci ag bëgge mii di njurum alkànde!
15 Abandoning the straight path, they went astray, following the way of Balaam son of Beor, who loved the wages of wrongdoing. Ba ñu wàccee yoon wu jub wi lañu lajj topp yoonu Balaam, doomu Bosor, mi soppoon peyooru njubadi.
16 But he was corrected for his own wrongdoing: a mute donkey spoke with a human voice and stopped the prophet's madness. Waaye Balaam, ag tooñam tax na ñu femmu ko; ab waruwaay manula wax, te moo waxe baatub nit, ba dakkal jëfi ndofi yonent booba.
17 These are dry springs, storm-driven mists—thick darkness is kept for them. Ñooñooy teen yu dëy, ñooy xiin wu callweer tas, te lëndëm gu fatt taraj di seenub añ.
18 With inflated, empty words they lure through the sensual desires of the flesh those barely escaping from people living in error. Kàddu yu réy yu tekkiwul dara lañuy naxee, di fàbbee xemmemtéefi bakkan yu jéggi dayo, ay nit ñu yàggula rëcce ci ñeneen ñu nekk cig réer.
19 They promise them freedom, while themselves enslaved to corruption—for whatever overcomes a person enslaves them. Ag ngoreel lañu leen di dig, te ñoom ci seen bopp, ay jaami yàqute lañu, ndax lu la man, nga dib jaamam.
20 For if, having escaped the world's corruption through knowing our Lord and Savior Jesus Christ, they are entangled in it again and overcome, their end is worse than their start. Ndax kat gannaaw bu ñu xamee bu baax sunu Boroom, sunu Musalkat Yeesu Almasi bi, ba rëcc sobey àddina, bu ñu ca sóobuwaatee ba mu man leen, su boobaa seenug muj moo yées seenug njàlbéen.
21 It would have been better for them never to know the way of righteousness than to know it and turn back from the holy commandment given to them. Ndax kat ñàkkoona xam yoonu njub wi sax moo doon gën ci ñoom, xam ko ba noppi, dëddu ndigal lu sell la ñu leen ca àgge woon.
22 The true proverb has happened to them: "A dog returns to its vomit," and "A washed sow returns to wallow in mud." Li léeb wii wax te muy dëgg, moo leen dikkal: «Xaj waccu, lekkaat ko; te cangaayu mbaam-xuux, teewu koo xalangootee poto-poto.»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]