Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

2 Peter 1 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Simon Peter, servant and apostle of Jesus Christ, to those given a faith as precious as ours through the righteousness of our God and Savior Jesus Christ: Ci man Simoŋ Piyeer miy jaamub Yeesu Almasi bi, di ndawam, ci man la bataaxal bii bawoo, ñeel ñi ñu may ngëm gu njëg ga réye ni sunu gos, ci njubteg Almasi bi, sunu Yàlla, sunu Musalkat.
2 May grace and peace be multiplied to you through knowing our Father and Jesus our Lord. Na aw yiw ak jàmm juy baawaan ñeel leen, ndax xam gu nu xam Yàlla ak sunu Sang Yeesu.
3 His divine power gave us all we need for life and devotion to God, through knowing him who called us by his glory and excellence. Mboolem lu aju ci dund gu sax ak ragal Yàlla, Yàllaa nu ko may ci dooleem, ba mu nu xamalee ne darajay boppam ak jalooreem ju wéet la nu woowe.
4 Through these he gave us his precious and very great promises, so that through them you may share the divine nature, having escaped the world's corruption from evil desires. Ci jooju daraja ak jooju jaloore lees nu baaxee ay dige yu réy njëg te màgg. Yooyu dige nag, bu ngeen ci jotee, ci ngeen di séddu ci jikkoy Yàlla, gannaaw bu ngeen muccee ci yàqutey àddina gi xemmemtéefu bakkan waral.
5 So, making every effort, add goodness to your faith, and to goodness, knowledge; Loolu tax na ba ngeen def lu ngeen man, ba dolli ci seen ngëm, njàmbaar; seen njàmbaar, ngeen dolli ci xam-xam;
6 to knowledge, self-control; to self-control, endurance; to endurance, devotion to God, seen xam-xam, ngeen dolli ci noot seen bakkan; noot seen bakkan, ngeen dolli ci ag muñ; seenug muñ, ngeen dolli cig ragal Yàlla;
7 to devotion to God, brotherly affection; to brotherly affection, love. seenug ragal Yàlla, ngeen dolli ci bëgg seen bokki gëmkat; bëgg seen bokki gëmkat, ngeen dolli ci cofeel.
8 If you have these qualities, growing, they'll keep you from being useless or fruitless in knowing our Lord Jesus Christ. Ndax yooyu jikko kat su ngeen ko amee, ba mu law, dungeen yaafus, dungeen ñàkk njariñ ci nu ngeen di xame sunu Sang Yeesu Almasi bi.
9 Whoever lacks these things is blind, shortsighted, forgetting he was cleansed from his past sins. Waaye yii jikko, ku ko ñàkk, daa fekk mu gàtt gis-gis ba far gumba, te fàtte ne dees koo fóotoon ba mu set, teqalikook bàkkaari démbam.
10 So, brothers and sisters, strive to confirm your calling and election; do these things and you will never stumble. Kon nag bokk yi, nangeen gënatee def lu ngeen man ba dëggal woote bi ñu leen woo ak tànn gi ñu leen tànn. Su ngeen ko defee kat, dungeen daanu mukk.
11 This way you'll be richly given entrance into the eternal kingdom of our Lord and Savior Jesus Christ. Noonu lees leen di ubbile bunt bu yaa bu ngeen di tàbbee ca nguur gu sax gay sunu moomeelu Sang, sunu Musalkat, Yeesu Almasi bi.
12 So I will always remind you of these things, though you know them and stand firm in the truth you now hold. Moo waral ma fas yéene di leen dëkkee fàttali loolu, doonte xas ngeen koo xam, ba tax ngeen taxaw bu dëgër ci dëgg gi leen nuyusi.
13 I think it right to keep stirring you with reminders while I remain in this tent, Li jaadu ci sama gis-gis moo di, li feek may màkkaanoo aw suux, dinaa leen ko fàttali, ngir soññ leen.
14 since I know I'll soon set my tent aside, as our Lord Jesus Christ showed me. Ndax damaa leer, ni ma ko sunu Boroom Yeesu Almasi bi leeralale, ne bés bi may summi sama màkkaanu suux bii dëgmal na.
15 I will also strive so you can always recall these things after I depart. Waaye dinaa def sama kem-kàttan, ba fu ngeen tollu, di fàttaliku mbir yooyu, gannaaw bu ma dëddoo.
16 For we didn't follow ingenious myths to tell you of our Lord Jesus Christ's power and coming—we were eyewitnesses of his majesty. Du ay léeb yu xel mu xareñ fent lanu leen xamale woon sunu manoorey Boroom Yeesu Almasi bi ak na muy dikke, waaye noo teewe màggaayam.
17 He received honor and glory from our Father when a voice came to him from the Majestic Glory: "This is my Son, the one I love; I delight in him." Ndax kat moo nangoo ci Yàlla Baay bi, teraanga ak daraja, ba ko baat ba jibalee, bawoo fa Boroom daraja ju yéeme ja ne: «Kii moo di sama Doom, sama soppe; moom laay bànneexoo.»
18 We ourselves heard this voice come from heaven, for we were with him on the holy mountain. Baat booba jóge asamaan, moom lanu dégg, ba nu nekkee ak moom ca tund wu sell wa.
19 We also have the prophetic word made more certain—you do well to attend to it, like a lamp shining in a dark place, until day dawns and the morning star rises in your hearts. Rax ci dolli nu ngeek waxi yonent yi, muy wax ju wóor ju jara gëm, te yeena yey teewlu waxi yonent yi, ni ñuy teewloo ceeñeeru làmp bu tàkke ci biir lëndëm, ba kera fajar di xar, ba biddiiwu njël feqal seen xol.
20 Above all, you must understand that no prophecy of Scripture comes from one's own interpretation. Waaye li ngeen wara njëkka xam moo di amul ci Mbind mi genn kàddug waxyu te yonent ba ko wax, fiire ko xelum boppam.
21 No prophecy ever came by human will, but men spoke from our Father, carried along by the Holy Spirit. Ndax kat du kàddug waxyu gu masa soqikoo ci coobarey nit, waaye ci xiirtalub Noo gu Sell gi la aw nit daan waxe kàddug waxyu gu bawoo fa Yàlla.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]