Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

2 John 1 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 The elder, to the chosen lady and her children, whom I love in truth—not only I, but all who know the truth, Ci man mag mi la bataaxal bii bawoo, ñeel la, yaw soxna su tedd si, yaak say doom. Maa leen sopp dëgg, te du man doŋŋ sax, waaye képp ku xam liy dëgg, sopp na leen.
2 because of the truth that lives in us and will be with us forever. Li waral sunu cofeel moo di dëgg gi ci nun, te di ànd ak nun ba fàww.
3 Grace, mercy, and peace will be with us from our Father and from Jesus Christ, our Father's Son, in truth and love. Yal na yiw ak yërmande ak jàmm ànd ak nun, ci biir dëgg ak cofeel, lépp bawoo ci Baay bi ak Yeesu Almasi bi, Doomam.
4 I was overjoyed to find some of your children walking in truth, as our Father commanded us. Bége naa lool ni ma gise ñenn ci say doom, ñuy wéye dëgg, ni nu ko Baay bi sante.
5 Now I ask you, dear lady: not a new command, but one we've had from the start—love one another. Léegi soxna si, li ma lay ñaan, te du sax ndigal lu bees, xanaa la nu jotoon ca njàlbéen, te mooy nanu soppante.
6 This is love: that we walk by his commands. This is the command, as you heard from the beginning: that you walk in love. Cofeel nag moo di nu wéye ndigalu Yàlla; loolu mooy ndigal li, noona ngeen ko dégge woon ca njàlbéen, ngir ngeen war koo wéye.
7 For many deceivers have gone out into the world, denying that Jesus Christ came in the flesh. This is the deceiver and the antichrist. Ndax kat bare na ay naxekat yu dajal àddina, te di ñu dëggalul ne Yeesu Almasi bi moo wàcce yaramu suux. Ku ni mel mooy ab naxekat te mooy bañaaleb Almasi bi.
8 Watch yourselves, so that you don't lose what we have worked for, but receive a full reward. Wattuleen seen bopp bala ngeena ñàkk njariñ li sunub liggéey meññ, xanaa seenub yool mat sëkk.
9 Anyone who oversteps, not remaining in Christ's teaching, lacks our Father; whoever remains in the teaching has both our Father and the Son. Képp ku saxoowul àlluway Almasi bi, xanaa di ko wees, kooku amul Yàlla. Ku saxoo àlluwa ji nag, yaa am Baay bi, am Doom ji.
10 If someone comes to you without this teaching, don't welcome them into your home or greet them, Ku dikk fi yaw, te dikkewul jooju àlluwa, bu ko dalal sa kër, bu ko sax nuyu,
11 for whoever greets him shares in his evil deeds. nde ku ko nuyu, am nga ab cér ci jëfam ju bon.
12 I have much to write, but I'd rather not use paper and ink. I hope to come and speak with you face to face, so our joy may be complete. Bare na lu ma leen bëggoona bind, waaye bëgguma leen koo waxe kayit ak daa. Teewul ma yaakaara dikkaat wax ak yeen, ne leen jàkk, ngeen ne ma jàkk, ba nu bokk mbég mu mat sëkk.
13 The children of your chosen sister greet you. Say doomi rakk ju jigéen, soxna si tedd si, ñu ngi lay nuyu.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]