Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

3 John 1 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 The elder, to the beloved Gaius, whom I love in truth. Ci man mag mi la bataaxal bii bawoo, ñeel Gayus, ku nu sopp ki, te ma sopp ko dëgg.
2 Beloved, I pray you prosper in every way and stay healthy, as your soul prospers. Soppe, yal nanga am jàmmi wet gu nekk. Ni nga ame jàmmu xol, yal nanga ni ame jàmmu yaram.
3 I rejoiced greatly when brothers arrived and testified about your faithfulness to the truth—for you truly are walking in it. Bég naa lool ci bokk yi dikk, ba seedeel la ni nga sàmme dëgg gi.
4 I have no greater joy than this: to hear that my children are walking in the truth. May dégg ne samay doom a ngi wéye dëgg gi, moomu mbég daal, awma mu ko raw.
5 Beloved, you act faithfully in all you do for the brothers, even strangers. Sama soppe, kóllëre nga wéye ci li ngay defal bokki gëmkat ñi, ba ci ñi nga xamul sax.
6 They testified to your love before the church. Send them on in a way worthy of our Father. Ñoo seede sag cofeel fi kanam mbooloom gëmkat ñi. Yaa ngi def lu baax, noonu nga leen di waajale seenu yoon, na mu jekke fa Yàlla.
7 For they went out for the sake of the Name, accepting nothing from the Gentiles. Ndax kat boroom Tur wi moo leen taxa jóg, te sàkkuwuñu daray jàmbur ñi gëmul.
8 Therefore we ought to support such people, so that we may be fellow workers for the truth. Kon nun nag, fàww nu dalal ñu mel noonu, ngir bokk ak ñoom liggéey bi ñuy liggéeyal dëgg.
9 I wrote something to the church, but Diotrephes, who loves being first among them, does not receive us. Bind naa mbooloo mi kàddu, waaye Joteref, miy sàkkoo jiitu ci seen biir moo nu faalewul.
10 So if I come, I'll expose what he's doing—slandering us with malicious words. Not satisfied with that, he refuses to welcome the brothers, stops those who want to, and throws them out of the church. Moo tax su ma dikkee, dinaa fàttali jëf ji muy def, di wasaare kàddu yu ñaaw yu mu teg ci sunub der. Loolu doyatu ko, moom ci boppam nanguwula dalal bokk yi, xanaa di ko tere ñi leen bëgga dalal, ba di leen dàq, ñu génn mbooloo mi.
11 Beloved, don't imitate evil, but good. Whoever does good is from our Father; whoever does evil hasn't seen our Father. Sama soppe, bul roy lu bon, xanaa lu baax. Ñiy def lu baax ci Yàlla lañu bokk; ñiy def lu bon nag, dajewuñook Yàlla.
12 All speak well of Demetrius, and so does the truth. We testify too, and you know our testimony is true. Naka Demetirus nag, mbaax la ko ñépp seedeel, te dëgg gi muy wéye sax seedeel na ko ko. Nun itam mbaax lanu ko seedeel, te xam nga ne dëgg lanu seede.
13 I had much to write to you, but I would rather not write with pen and ink. Bare na lu ma la bëggoona bind, waaye bëgguma la koo waxe daa ak xalima.
14 I hope to see you soon, and we will talk face to face. Teewul ma yaakaar laa gis balaa yàgg, ba ne la jàkk, nga ne ma jàkk, nu waxtaan.
15 Peace to you. The friends send their greetings. Greet each of the friends by name. Jàmm ñeel na la. Say soppee ngi lay nuyu. Nuyul ma soppe yi, ku nekk ciw turam.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]