Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

2 Chronicles 7 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 When Solomon finished praying, fire fell from heaven and consumed the burnt offering and sacrifices, and our Father's glory filled the house. Naka la Suleymaan ñaan ba sottal, sawara wàcce fa asamaan, xoyom saraxu rendi-dóomal ba ak yeneen sarax ya, leeru Aji Sax ji daldi fees kër ga.
2 The priests couldn't enter our Father's house, because our Father's glory filled it. Sarxalkat ya nag manuñoo dugg ca kër Aji Sax ji, ndax leeru Aji Sax ja fees kër Aji Sax ji.
3 When all the Israelites saw the fire fall and our Father's glory on the house, they knelt, faces to the ground on the pavement, worshiping and thanking our Father: "He is good; his faithful love endures forever." Bànni Israayil gépp a gis ba sawara wa ak leeru Aji Sax ja wàccee ca kër ga. Ci kaw loolu ñu sukk ca dér ba, dëpp seen jë fa suuf, sujjóot tey sàbbaal Aji Sax ji, naan: «Kee baax, kee saxoo ngoram ba fàww!»
4 Then the king and all the people offered sacrifices before our Father. Ba mu ko defee Buur ak mboolem askan wa sarxe ay sarax fi kanam Aji Sax ji.
5 King Solomon sacrificed 22,000 oxen and 120,000 sheep; the king and all the people dedicated the house of our Father. Buur Suleymaan daldi sarxe saraxu ñaar fukki junniy nag ak ñaar (22 000) ak téeméeri junniy gàtt ak ñaar fukk (120 000). Noonu la Buur ak askan wépp amale xewu jagleb kër Yàlla ga.
6 The priests stood at their posts; the Levites stood with the musical instruments for our Father that King David made for giving thanks to our Father—"for his faithful love endures forever"—whenever David praised through the instruments. Opposite them the priests blew the trumpets, and all Israel stood. Ci biir loolu sarxalkat ya taxaw fa ñu leen féetale, Leween ñi jibal jumtukaayi xumbéen ya ñuy woye Aji Sax ji, te Buur Daawuda defarlu woon ko, ngir saa yu santoon Leween ñi, ne leen ñu woy Aji Sax ji ngir ngoram gi sax dàkk. Sarxalkat yaa nga fa seen kanam, di wal liit ya, bànni Israayil gépp taxaw.
7 Solomon dedicated the courtyard's middle, in front of our Father's house, for there he offered the burnt offerings and fat of the peace offerings, since the bronze altar he had made could not hold the burnt offering, grain offering, and fat. Suleymaan nag sellal digg ëtt ba janook néegu Aji Sax ji, ndax fa la joxe saraxu rendi-dóomal ba ak nebbonu saraxu cant ci biir jàmm, ndax sarxalukaayu xànjar ba Suleymaan defarlu woon manul woona defandoo saraxu rendi-dóomal ba ak saraxu pepp ba ak nebbon ja.
8 At that time Solomon kept the feast seven days, and all Israel with him—a vast assembly—from Lebo-hamath to the Brook of Egypt. Suleymaan nag ci juróom ñaari fan la amal màggal ga ca jant yooyu, ànd caak Israayil gépp, muy ndaje mu réy mu jóge Buntu Amat ca bëj-gànnaar, ba ca xuru Misra ca bëj-saalum.
9 On the eighth day they held a closing assembly, having kept the altar's dedication seven days and the feast seven days. Bésub juróom ñetteel ba, ca lañu amal am ndaje, ndax xewu jagleb sarxalukaay ba lañu njëkka amal diiru juróom ñaari fan, teg ca amal màggalu Mbaar ya diiru juróom ñaari fan.
10 On the twenty-third day of the seventh month, he sent the people home, joyful and glad at heart for the goodness our Father showed to David, to Solomon, and to Israel his people. Keroog ñaar fukki fan ak ñett ci juróom ñaareelu weeru at ma, ca la Suleymaan yiwi mbooloo ma, ñu dellu seeni xayma, ci biir mbégte ak xol bu sedd, ci lu baax la Aji Sax ji defal Daawuda ak Suleymaan ak Israayil ñoñam.
11 Solomon finished the house of our Father and the royal palace. Everything Solomon set his heart to do in the house of our Father and his own house, he did successfully. Ba mu ko defee Suleymaan sottal kër Aji Sax ji ak kër buur. Mboolem lu ko xelam mayoon, ngir mu def ko ca kër Aji Sax ji ak ca kërug boppam, am na ca ndam.
12 Then our Father appeared to Solomon at night and said to him: "I have heard your prayer and chosen this place for myself as a house of sacrifice. Ci kaw loolu Aji Sax ji feeñu Suleymaan ag guddi. Mu ne ko: «Dégg naa sag ñaan, te tànnal naa sama bopp béreb bii, ngir mu di kërug sarax.
13 "If I shut the skies so no rain falls, or command locusts to devour the land, or send a plague among my children, Su ma tëjee asamaan ba taw amul, mbaa ma sant soccet mu lekk réew mi, mbaa ma yónni mbas ci sama ñoñ,
14 if my children—who bear my name—humble themselves, pray, seek my face, and turn from their evil ways, I will hear from heaven, forgive their sin, and heal their land. ba sama ñoñ ñi ñu tudde sama tur, toroxlu; su ñu ñaanee, sàkku sama yiw, te dëddu seen jëfin yu bon, su boobaa, man maay dégge fa asamaan, jéggale seen bàkkaar, faj seenum réew.
15 Now my eyes will be open and my ears attentive to the prayer offered in this place. Li dale tey, samay gët a ngi xool, samay nopp teewlu ñaanu béreb bii.
16 Now I have chosen and dedicated this house, so my name remains there forever; my eyes and heart will be there always. Li dale tey it maa tànn, maa sellal kër gii, ngir sama tur nekk fi ba fàww, te samay gët ak sama xol it fi lay nekk bés bu nekk.
17 As for you—if you walk before me as David your father walked, doing all I commanded you and keeping my statutes and judgments, Yaw nag, soo doxee fi sama kanam ni Daawuda sa baay daan doxe tey def lépp lu ma la sant, sama dogali yoon ak sama àttey yoon, nga di ko sàmm,
18 then I will confirm your kingdom's throne, as I covenanted with David your father: "A man of yours will always rule over Israel." kon maay saxal sab jal, na ma ko dogule woon Daawuda sa baay, ne ko: “Doo ñàkk ku góor kuy jiite Israayil.”
19 But if you turn away, abandon my statutes and commands I set before you, and go serve other gods and worship them, Waaye su ngeen dëddoo yeen, ba bàyyi sama dogali yoon ak sama santaane yi ma leen tëralal, bay dem di jaamu yeneen yàlla, di leen sujjóotal,
20 then I will uproot Israel from my land I gave them, cast from my sight this temple I set apart for my name, and make it an example and taunt among all peoples. su boobaa maa leen di witte fi sama kaw suuf si ma leen jox, te kër gii ma sellal ngir sama tur, maa koy xalab, mu sore ma, te maa koy def kër gu ñuy léeboo ak di ko kókkalee ci biir xeet yépp.
21 This house, once so exalted, will leave everyone who passes by appalled, saying, "Why did the LORD do this to this land and this house? Su boobaa, li kër gii doon yéeme lépp, képp ku ko romb, dina yéemu ci lu ni mel, te dina ne: “Ana nu Aji Sax ji defe nii réew mii ak kër gii?”
22 They will answer, "Because they abandoned the LORD, God of their ancestors, who brought them out of the land of Egypt, and clung to other gods, bowing and serving them—that's why he brought all this disaster on them." Su ko defee ñu ne: “Xanaa li ñu dëddu seen Yàllay maam, Aji Sax ji leen jële réewum Misra, di topp yeneen yàlla, di leen sujjóotal aka jaamu, moo tax Aji Sax ji teg leen musiba mii mépp.”»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]