Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

2 Chronicles 8 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 After twenty years, in which Solomon built the house of our Father and his own palace, Ñaar fukki at yi Suleymaan tabax kër Aji Sax ji ak kërug boppam, ba mu matee,
2 Solomon rebuilt the cities that Huram had given him, and settled the people of Israel in them. dëkk ya Iram buuru Tir joxoon Suleymaan, ñoom la Suleymaan tabaxaat, sancal fa niti bànni Israayil.
3 Then Solomon marched against Hamath-zobah and overpowered it. Ba loolu wéyee Suleymaan songi dëkk ba ñuy wax Amat Coba, nangu ko.
4 He built Tadmor in the wilderness, along with all the storage cities he built in Hamath. Ci kaw loolu mu tabaxaat Tadmor ga ca màndiŋ ma, ak mboolem dëkk ya mu tabaxoon ca diiwaanu Amat, def leen ay dencukaay.
5 He also rebuilt Upper Beth-horon and Lower Beth-horon as fortified cities, with walls, gates, and bars, Mu tabaxaat nag Bet Oron kaw ak Bet Oron suuf, muy dëkk yu ñu dàbbali, am ay tata aki bunt yu yeti weñ di tëj.
6 Baalath, all Solomon's supply cities, his chariot and horsemen cities, and all he desired to build in Jerusalem, Lebanon, and his whole realm. Suleymaan moo tabaxaat itam Baalat, ak mboolem dëkki dencukaayam ak mboolem dëkk ya watiiri xare ya dence ak dëkki gawar ya. Mboolem lu Suleymaan nammoona tabax daal, tabax na ko ca Yerusalem ak ca Libaŋ ak mboolem réew mu nekk ci kilifteefam.
7 There were still people left from the Hittites, Amorites, Perizzites, Hivites, and Jebusites, who were not Israelites. Mboolem nit ña desoon ca Etteen ñaak Amoreen ñaak Periseen ñaak Eween ñaak Yebuseen ña, ñooñu bokkul ci bànni Israayil,
8 Their descendants still living in the land, whom Israel had not destroyed, Solomon conscripted for forced labor, as they still are today. ñenn ca seen sët ya leen wuutu ca réew ma, te bànni Israayil faagaagalu leen, Suleymaan moo leen dugal ci liggéeyu sañul-bañ, ñu nekke ko ba tey jii.
9 Solomon enslaved no Israelites for his work; they were soldiers, commanders of his officers, and commanders of his chariots and horsemen. Waaye ñi bokk ci bànni Israayil, Suleymaan defu leeni jaam, ngir liggéeyam, ndax ñoom ñoo doon ay xarekatam aki dagam aki jawriñam aki njiiti xareem ak boroom watiiri xareem ak dawalkati watiiram.
10 These were King Solomon's chief officers: 250 who supervised the people. Ñoo doon jawriñi Suleymaan yi yilif saytukat yi, ñuy ñaari téeméer ak juróom fukk (250), jiite mbooloom liggéeykat ya.
11 Solomon brought Pharaoh's daughter from the City of David to the house he built her, saying, "No wife of mine will live in David king of Israel's house, for holy is wherever our Father's ark has entered." Doomu Firawna ju jigéen ja nag, Suleymaan moo ko jële gox ba ñu naan kër Daawuda, toxal ko ca kër ga mu ko tabaxaloon, ndax da noon: «Sama jabar du dëkke kër Daawuda buurub Israayil, ndax gox yi gaalu Aji Sax ji dugg dañoo sell.»
12 Then Solomon offered burnt offerings to our Father on the altar he built before the portico, Ba mu ko defee Suleymaan joxe saraxi rendi-dóomal, ñeel Aji Sax ji, ca kaw sarxalukaayu Aji Sax ja mu tabax fa kanam mbaarum kër Yàlla ga,
13 daily as required, by Moses' command: Sabbaths, New Moons, and three yearly festivals—the Feast of Unleavened Bread, the Feast of Weeks, and the Feast of Tabernacles. na mu dëppoo ak ndigal yi jëm ci saraxu bés ak bés, ci ndigalu Musaa, ci wàllu bési Noflaay ak Terutel weer yi ak ñetti bési ndaje yi cim at, di màggalu Mburu mu amul lawiir ak màggalug Ayi bés ak màggalu Mbaar yi.
14 Following his father David's rules, he set priestly divisions for service, Levite divisions to praise and serve before the priests as each day required, and gatekeeper divisions at each gate, for David the man of our Father had commanded it. Ci biir loolu mu topp ndigalal Daawuda baayam, daldi tabb kuréeli sarxalkat ya ca seenub liggéey, tabb Leween ña ca seeni dénkaane, ngir ñuy sàbbaal aka liggéey fa kanam sarxalkat ya, na mu dëppook ndigali bés bu nekk, boole ca tabb ay kuréeli wattukati bunt, ku nekk ak sa bunt, na ko Daawuda góoru Yàlla ga santaanee woon.
15 They followed the king's orders to the priests and Levites exactly, down to the storerooms. Moyeesul fenn santaaneb Buur Daawuda yi jëm ci sarxalkat yi ak Leween ñi, ci mboolem mbir yooyu, ba ci wàllu denc ya.
16 All Solomon's work was finished, from the day our Father's house was founded until its completion; our Father's house was complete. Noonu lañu amale mboolem liggéeyu Suleymaan, dale ko ca bés ba fondmaa kër Aji Sax ji lalee, ba keroog kër Aji Sax ji sottee ba mat sëkk.
17 Then Solomon went to Ezion-geber and Eloth on the seacoast in the land of Edom. Suleymaan nag dem Eccon Geber ak Elat ca tefesu géeju Barax ya, ca réewum Edom.
18 Huram sent him ships by his servants, with sailors who knew the sea; they sailed with Solomon's servants to Ophir, took about seventeen tons of gold, and brought it to King Solomon. Buur Iram yóbbante ko ay surgaam, ngir ñu yót ko ay gaal yu mag ak mool yu xam géej. Ñu ànd ak niti Suleymaan ca gaal ya, dem Ofir. Téeméeri barigoy wurus ak juróom fukk (150) lañu fa jële, indil Buur Suleymaan.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]