Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

2 Chronicles 6 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Then Solomon said, "Our Father has said that he would dwell in thick darkness. Ba mu ko defee Suleymaan ne: «Aji Sax ji moo noon lëndëm gu fatt lay màkkaanoo.
2 But I have built you an exalted house, a place for you to dwell in forever." Man nag tabaxal naa la kër gu màgg, màkkaan mooy dëkke ba fàww.»
3 Then the king turned and blessed the whole assembly of Israel as they all stood. Ci kaw loolu Buur Suleymaan walbatiku, ñaanal mbooloom Israayil mépp, fekk mbooloom Israayil mépp a nga taxaw.
4 He said, "Praise our Father, the God of Israel, whose hand has fulfilled what his mouth promised my father David, saying, Mu ne: «Cant ñeel na Aji Sax ji Yàllay Israayil, moom mi sottale loxoy boppam, la mu waxoon Daawuda sama baay ci gémmiñam, ne ko:
5 'Since the day I brought my people out of Egypt, I chose no city from all the tribes of Israel to build a house for my name to be there, nor any man to rule my people Israel. “La dale bés ba ma génnee bànni Israayil, sama ñoñ, ca réewum Misra ba tey, tànnuma benn dëkk, ci mboolem giiri Israayil, bu ñuy tabax kër gu sama tur di nekk. Te it tànnuma kenn ngir mu jiite Israayil sama ñoñ.
6 But I chose Jerusalem for my name to be there, and I chose David to lead my people Israel.' Waaye Yerusalem laa tànn, ngir nekkal fa sama tur, Daawuda it laa tànn ngir fal ko ci kaw Israayil.”
7 David my father had it in his heart to build a house for the name of our Father, the God of Israel. La doon yéeney Daawuda sama baay nag moo doon tabax kër gu mu tudde Aji Sax ji Yàllay Israayil.
8 But our Father told David my father, 'Because building a house for my name was in your heart, you did well to intend this. Teewul Aji Sax ji wax Daawuda sama baay, ne ko: “Gannaaw yaa fasoon ci sa xol yéeney tabax kër, tudde ma ko, def nga lu rafet, ngir sa yéeney xol la woon.
9 But you will not build the house; your son, from your own body—he will build the house for my name.' Waaye du yaw yaay tabax kër gi; sa doom ju góor ju soqikoo ci sa geño, moom mooy tabax kër gi, tudde ma ko.”
10 Now our Father has fulfilled the word he spoke: I have succeeded David my father and sit on Israel's throne, as he promised, and I have built the house for the name of our Father, the God of Israel. Aji Sax ji moo sottal waxam ja mu waxoon. Maa wuutu Daawuda sama baay, ba toog ci jalub Israayil, noonee ko Aji Sax ji waxe woon, maa tabax kër gi, tudde ko Aji Sax ji Yàllay Israayil.
11 There I placed the ark, holding the covenant our Father made with the people of Israel." Te it fa laa def gaal gi def àlluway kóllërey Aji Sax ga mu fasoon ak bànni Israayil.»
12 Then Solomon stood before our Father's altar in the presence of the whole assembly of Israel and spread out his hands. Gannaaw loolu Suleymaan taxaw jàkkaarlook sarxalukaayu Aji Sax ji, fa kanam mbooloom Israayil mépp. Mu daldi tàllal ay loxoom.
13 Solomon had made a bronze platform about seven and a half feet long, seven and a half feet wide, four and a half feet high, and set it in the middle of the court. He stood on it, knelt before the whole assembly of Israel, and spread his hands toward heaven. Fekk na Suleymaan sàkklu ab tóojub xànjar, ba teg ko ca diggu ëtt ba. Juróomi xasab la tóoj ba gudde, yaatoo juróomi xasab, taxawe ñett. Mu taxaw ca kaw, daldi sukk bëti óomam fa kanam mbooloom Israayil mépp. Ci kaw loolu mu tàllal ay loxoom asamaan,
14 He said, O my Father, God of Israel, no Father is like you in heaven or on earth, keeping covenant and showing loyal love to your servants who walk before you wholeheartedly. daldi ne: «Yaw Aji Sax ji Yàllay Israayil, amul jenn Yàlla ju mel ni yaw fa asamaan mbaa ci suuf, yaw miy sàmm kóllëre ak ngor, ñeel sa jaam ñiy doxe seen léppi xol fi sa kanam.
15 You kept your promise to your servant David my father; what you spoke with your mouth you fulfilled with your hand today. Yaa sàmm kàddu ga nga waxoon sa jaam ba, Daawuda sama baay, ci sa gémmiñu bopp, te yaa sottal ci sab loxo, sa kàddu bés niki tey.
16 So now, my Father, God of Israel, keep for your servant David my father what you promised: "You will never lack a man before me on Israel's throne, if only your sons watch their way to walk in my law, as you have walked before me." Léegi nag Aji Sax ji Yàllay Israayil, ngalla sàmmal la nga waxoon sa jaam ba, Daawuda sama baay, ne ko: “Deesu la xañ mukk ci saw askan ku góor kuy tooge jalub Israayil fi sama kanam, ndegam saw askan a ngi moytu seenu yoon, ngir di doxe sama ndigalu yoon, noonee nga daan doxe fi sama kanam.”
17 And now, my Father, God of Israel, let the word you spoke to your servant David be confirmed. Kon nag yaw Yàllay Israayil, ngalla saxalal wax jooju nga waxoon Daawuda, sa jaam ba.
18 But will our Father really live with people on earth? The heavens and highest heavens can't hold you—how much less this house I built. «Waaye yaw Yàlla! Ndax yaay dëkk ak doom aadama ci kaw suuf sax? Seetal rekk, asamaan ba ca asamaani asamaan manu laa fat, astamaak kër sii ma tabax.
19 Yet hear the prayer of your servant and his plea, O my Father, and hear the cry and prayer your servant prays before you. Waaye Aji Sax ji, sama Yàlla, rikk, teewlul li ma lay ñaan, man sab jaam, di la ko dagaan; ngalla déggal sama yuux, te nangu ñaan gi ma lay ñaan.
20 May your eyes be open toward this house day and night, toward the place where you said you'd put your name, to hear the prayer your servant prays toward this place. Yal nanga ne jàkk, muy bëccëg di guddi, ci kër gii, béreb bi nga noon fi ngay def sa tur, te yal nanga dégg ñaan gi may ñaan jublu ci béreb bii, di ko ñaan, man sab jaam.
21 Hear your servant's and your people Israel's pleas when they pray toward this place. Hear from heaven, your dwelling; and when you hear, forgive. Yal nanga may nangul samay dagaan, nangul Israayil sa ñoñ. Bu ñu jubloo béreb bii, ñaan la, yal nanga ko dégge béreb ba nga dëkke ca asamaan, ba nangul leen, jéggal leen.
22 If a man sins against his neighbor and must swear an oath, and he comes and swears his oath before your altar in this house, «Su dee nit lañu tuumaal ne moo tooñ moroomam, te yoon waatloo ko ba waat war ko, bu dikkee di waatsi fi sa kanam sarxalukaay bi ci biir kër gii,
23 then hear from heaven and act. Judge your servants: pay back the guilty for their deeds, and clear the righteous, rewarding them by their righteousness. su boobaa, yaw rikk dégge ko fa asamaan, àtte say jaam, ngir fey ki tooñ, këpp añu jëfam ci kaw boppam, te nga dëggal ki am dëgg, ngir jox ko dëggam gi mu yelloo.
24 If your people Israel, defeated by enemies for sinning against you, turn back to praise your name, pray, and plead with you in this house, «Su Israayil sa ñoñ daanoo fi kanam ab noon, ngir tooñ gu ñu la tooñ, bu ñu waññikoo ci yaw, sàbbaal saw tur, ñaan, sàkku aw yiw fi sa kanam, ci biir kër gii,
25 then hear from heaven, forgive the sin of your people Israel, and bring them back to the land you gave to them and their ancestors. su boobaa yaw, yal nanga dégge fa asamaan, ba jéggale bàkkaarub Israayil sa ñoñ, te nga delloo leen ca réew ma nga leen joxoon, ñook seeni maam.
26 When the sky is shut with no rain because they sinned against you, if they pray toward this place, praise your name, and turn from their sin when you make them suffer, «Bu asamaan tëjoo, ba taw amul ndax tooñ gu ñu la tooñ, bu ñu jubloo béreb bii, ñaan la, sàbbaal saw tur, dëddu seen bàkkaar ndax sa mbugal,
27 then hear from heaven, forgive your servants' sin, your people Israel, when you teach them the good path to walk, and send rain on your land, which you gave your people as their inheritance. su boobaa yaw ngalla nangool fa asamaan, te nga jéggale sa bàkkaaru jaam ñi, Israayil sa ñoñ. Ngalla xamal leen yoon wu baax wi ñu wara doxe, te nga tawal sa suuf si nga joxoon sa ñoñ, muy seen cér.
28 If famine, plague, blight, mildew, locust, or caterpillar strikes the land; if enemies besiege them in their towns—whatever plague or sickness comes, «Bu xiif amee ci réew mi, mbaa mbas, mbaa gàncax gi lakk, mbaa benaat xuural ko, mbaa mu diy njéeréer mbaa soccet, mbaa su dee congum seeni noon ci seen dëkki réew mi, mbaa muy mboolem luy musiba ak mboolem jàngoro, su boobaa,
29 whatever prayer or plea anyone or all your people Israel makes, each knowing his own suffering and pain and spreading his hands toward this house, lépp lu ciy ñaan akug tinu gu bawoo ci képp ku mu doon mbaa ci mboolem Israayil sa ñoñ, te fekk ku ci nekk ràññee mititam ak njàqareem, ba tàllal ay loxoom jublook kër gii,
30 then hear from heaven, your home, and forgive, and repay each according to all his ways, since you know his heart—for you alone know every human heart, su boobaa, yaw, ngalla nangoo ko fa asamaan, màkkaan ma nga dëkke, ba jéggale, te nga yool ku nekk kemu mboolem ay jëfam, yaw mi xam xolam, ndax yaw doŋŋ yaa xam xolu doom aadama.
31 so they may fear you and walk in your ways as long as they live on the land you gave our ancestors. Su ko defee dinañu la ragal bay doxe say yoon seen giiru dund, ci kaw suuf si nga joxoon sunuy maam.
32 Also, when a foreigner not of your people Israel comes from a distant land for your great name, your mighty hand, and your outstretched arm—when they come and pray toward this house, «Te itam doxandéem bu bokkul ci Israayil sa ñoñ te jóge réew mu sore ngir sa tur wu màgg ak sa dooley loxo ak sa kàttanu përëg, bu dikkee ba jublu ci kër gii, ñaan,
33 then hear from heaven where you live, and do all the foreigner asks, so all the earth's peoples may know your name and fear you, as your people Israel do, and know this house I built bears your name. su boobaa ngalla nangool fa asamaan, màkkaan ma nga dëkke, te nga defal doxandéem boobu mboolem lu mu la ñaan, ndax xeeti àddina yépp xam sa tur, ngir ragal la, ni Israayil sa ñoñ, te xam ne saw tur lañu tudd ci kër gii ma tabax.
34 If your people go to war against their enemies wherever you send them, and pray to you toward this city you have chosen and the house I built for your name, «Bu sa ñoñ di xarejeek seeni noon, ci yoon woo leen yebal, su ñu la ñaanee, jublook dëkk bii nga tànn, ak kër gii ma tabax ngir sa tur,
35 then hear from heaven their prayer and their plea, and uphold their cause. su boobaa ngalla nangool fa asamaan seenug ñaan ak seen dagaan te nga may leen ndam.
36 If they sin against you—for no one is without sin—and you are angry with them and hand them to an enemy who takes them captive to a land far or near, «Bu ñu la moyee, nde amul nit ku dul moy, ba nga mere leen, teg leen ci loxob noon, noon ba jàpp leen, yóbbu réew mu sore mbaa mu jege,
37 yet if in the land of their captivity they take it to heart, and turn back and plead with you there, saying, "We have sinned, we did wrong, we acted evilly," bu ñu demee ba seenum xel dellusee fa réew ma ñu leen yóbbu ngàllo, ñu tuub tey sàkku aw yiw fi yaw, foofa ca réew ma ñu duggi ngàllo, ne la noo moy, noo ñaaw, noo def lu bon,
38 if they turn back to you with all their heart and soul in the land of their captivity where they were taken, and pray toward their land you gave their ancestors, the city you chose, and the house I built for your name, bu ñu waññikoo seen léppi xol ak seen léppi jëmm ci yaw, foofa ca réew ma ñu duggi ngàllo ga ñu leen fa yóbbu, ba gannaaw gi ñu ñaan la, jublook seen réew ma nga joxoon seeni maam, jublook dëkk bi nga tànn, jublook kër gii ma tabax ngir sa tur,
39 then hear from heaven, your dwelling place, their prayer and pleas, uphold their cause, and forgive your people who sinned against you. su boobaa ngalla nangool fa asamaan, fa màkkaan ma nga dëkke, seen ñaan ak seeni dagaan, te nga sàmm seen àq, jéggal sa ñoñ ñi la moy.
40 Now, my Father, let your eyes be open and your ears attentive to the prayer of this place. «Léegi nag, sama Yàlla, ngalla waay, na say gët ne jàkk, te say nopp teewlu ñaan gu jibe ci béreb bii.
41 And now arise, my Father, and come to your resting place, you and the ark of your might. Let your priests, my Father, be clothed with salvation, and let your faithful ones rejoice in your goodness. Kon nag, Aji Sax ji Yàlla, jógal agsi sa dalluwaay, yaak gaal gi jëmmal sa doole. Aji Sax ji Yàlla, yal na say sarxalkat soloo mucc, te say wóllëre di bége xéewal.
42 My Father, do not reject your anointed one. Remember your covenant love for David your servant. Aji Sax ji Yàlla, ngalla bul gàntu ki nga fal. Bàyyil xel ci ngor gi nga ji Daawuda sab jaam.»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]