Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

2 Chronicles 13 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 In the eighteenth year of King Jeroboam, Abijah became king of Judah. Ci fukkeelu at ak juróom ñett ca nguurug Yerbowam, ca la Abya falu buur ca Yuda.
2 He reigned three years in Jerusalem; his mother was Micaiah, Uriel of Gibeah's daughter. Abijah and Jeroboam went to war. Ñetti at la nguuru fa Yerusalem, te yaayam moo doon Mikaya, doomu Uryel ma dëkk Gibeya. Xare nag amoon na diggante Abya ak Yerbowam.
3 Abijah joined battle with an army of 400,000 chosen warriors, mighty in war; Jeroboam lined up against him with 800,000 chosen, mighty warriors. Abya moo song xare ba ànd ak gàngooru jàmbaari xare; ñeenti téeméeri junniy (400 000) góor ñu ñu tànn. Yerbowam it làng-déral ab xare janook moom, ak juróom ñetti téeméeri junniy (800 000) góor ñu ñu tànn, xeexkat yu jàmbaare.
4 Abijah stood on Mount Zemaraim in Ephraim's hill country and said, "Hear me, Jeroboam and all Israel! Abya moo taxaw fa kaw tundu Cemarayim ca diiwaanu tundi Efrayim, daldi xaacu ne: «Yaw Yerbowam, déglu ma yaak Israayil gépp.
5 Don't you know our Father, the God of Israel, gave David and his sons Israel's throne forever, by a covenant of salt? Xanaa war ngaa xam ne Aji Sax ji Yàllay Israayil moo jox Daawuda nguur ci kaw Israayil ba fàww, moom ak aw askanam, muy kóllëreg xorom gu dul jaas, du fecciku, xanaa sax dàkk.
6 But Jeroboam son of Nebat—a servant of Solomon son of David—rose and rebelled against his master. Teewul Yerbowam doomu Nebat miy surgab Suleymaan doomu Daawuda, moo jóg fippu ci kaw sangam.
7 Worthless men gathered around him, defying Solomon's son Rehoboam, young and timid, unable to resist them. Ci kaw loolu ay sagari nit ñu tekkiwul dara booloo ànd ak moom, jaay Robowam doomu Suleymaan doole, fekk Robowam di gone gu fit wa dëgërul ba manu leena të.
8 Now you think you can resist our Father's kingdom in David's sons' hands, since you're a huge crowd with the golden calves Jeroboam made as your gods. Léegi nag yeen ngeen defe ne man ngeena të nguurug Aji Sax ji ci loxol doomi Daawuda. Gàngoor gu réy ngeen, te ñi ànd ak yeen di ay wëlluy wurus yu leen Yerbowam sàkkal, ñu taxawe ay yàlla.
9 Haven't you driven out our Father's priests, Aaron's sons and the Levites, and made your own priests like other nations? Anyone who comes with a young bull and seven rams can become a priest of things that aren't gods. Xanaa du yeena dàq sarxalkati Aji Sax ji, doomi Aaróona yu góor, ak Leween ñi, ba sàkkal seen bopp ay sarxalkat ni askani yeneen réew yi? Ku mu mana doon rekk dikk ak aw yëkk, ak juróom ñaari kuuy, ngir tabbees ko cig carxal, ba mu doon ab sarxalkatub lu dul Yàlla.
10 But our Father is ours, and we haven't abandoned him. The priests serving him are Aaron's sons, and the Levites are at their work. Nun nag Aji Sax ji mooy sunu Yàlla, te waccunu ko. Te sarxalkat yi fi nun di liggéeyal Aji Sax ji, askanu Aaróona lañu, feggook Leween ñeek seen wàll ci liggéey bi.
11 Every morning and evening they burn to our Father burnt offerings and fragrant incense; they set rows of bread on the pure gold table and tend the gold lampstand, lit every evening. We keep our Father's charge, but you have abandoned him. Ñooy lakk suba su nekk ak ngoon su nekk, ñeel Aji Sax ji, ay saraxi rendi-dóomal ak cuuraay lu xeeñ. Mburum teewal ma it ñoo koy teg bu jekk ca taabal ju set wecc ja, te ñooy teg tegukaayu làmp bu wurus ba aki làmpam, ñuy tàkk ngoon su nekk, ndax nun déy sunu ndénkaaneb Yàlla Aji Sax ji lanu sàmm. Yeen nag yeena ko wacc.
12 Look, our Father is with us at our head, and his priests have trumpets to sound alarm against you. Israelites, do not fight our Father, the God of your ancestors, for you will not prevail." Mu ngoogu, Yàllaa ngii jiite nu, mooki sarxalkatam ak seeni liit yu xumb, ngir jibal wooteb xare ci seen kaw. Kon yeen bànni Israayil, buleen xareek Aji Sax ji seen Yàllay maam, ndax kat dungeen am ndam.»
13 Jeroboam had sent an ambush around, to come from behind them; his forces faced Judah, the ambush behind them. Ci biir loolu Yerbowam yónnee ndànk lenn ca gàngooram, ñu doxe Yudeen ña gannaaw, ngir tëru leen.
14 Judah turned, saw battle facing them front and back, cried to our Father; the priests blew the trumpets. Yuda walbatiku, gisuñu lu moy xare bu leen tance kanam ak gannaaw. Ñu daldi woo Aji Sax ji wall, sarxalkat ya wal liit ya.
15 Judah's men shouted the war cry, and as they shouted, our Father struck Jeroboam and all Israel before Abijah and Judah. Ci kaw loolu Yudeen ña xaacoondoo. Naka la Yudeen ña xaacu, Yàlla duma Yerbowam ak Israayil gépp fa kanam Abya ak Yuda.
16 The people of Israel fled before Judah, and our Father handed them over to Judah. Bànni Israayil daldi daw, won Yuda gannaaw, Yàlla teg leen ci seen loxo.
17 Abijah and his army struck them a heavy blow; 500,000 chosen men of Israel fell dead. Abya ak gàngooram nag duma leen duma yu réy, néewi Israayil tëdd, di juróomi téeméeri junniy (500 000) tànnéefi xarekat.
18 So Israel was humbled then, and Judah prevailed because they relied on our Father, God of their ancestors. Jant yooyu la bànni Israayil suufe, Yudeen ña féete kaw, ndax la ñu wéeroo Aji Sax ji seen Yàllay maam.
19 Abijah chased Jeroboam, capturing cities from him—Bethel and its villages, Jeshanah and its villages, Ephron and its villages. Abya nag dàqi Yerbowam, ba nangu ca moom ay dëkk. Betel aki dëkk-dëkkaanam ca la, ak Yesana aki dëkk-dëkkaanam, ak Efron aki dëkk-dëkkaanam.
20 Jeroboam never regained his strength during Abijah's lifetime, and our Father struck him down, and he died. Yerbowam amatuloon doole ca janti Abya. Gannaaw gi, Aji Sax ji faat ko, mu dee.
21 But Abijah grew strong. He married fourteen wives and had twenty-two sons and sixteen daughters. Ba mu ko defee Abya gëna am doole. Ci biir loolu mu jël fukki jabar ak ñeent, am ñaar fukki doom yu góor ak ñaar, ak fukki doom yu jigéen ak juróom benn.
22 The rest of Abijah's acts, his ways and sayings, are written in the prophet Iddo's commentary. Li des ci mbiri Abya, ay waxam aki jëfam, bindees na ko ci nettalib Ido yonent ba.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]