Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

2 Chronicles 12 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 When Rehoboam's reign was secure and strong, he abandoned our Father's law, and all Israel with him. Ba nguurug Robowam demee ba dëgër, ba Robowam ci boppam am doole, ca la wacc yoonu Aji Sax ji, mook Israayil gépp.
2 In Rehoboam's fifth year, because they were unfaithful to our Father, Shishak king of Egypt attacked Jerusalem. Ba Buur Robowam faloo, ba dugg ca juróomeelu atu nguuram, ca la Sisag buuru Misra song Yerusalem ndax la ñu fecci Aji Sax ji kóllëre.
3 He came with 1,200 chariots, 60,000 horsemen, and countless troops from Egypt: Libyans, Sukkites, and Cushites. Sisag songe leen junniy watiir ak ñaari téeméer (1 200) ak juróom benn fukki junniy (60 000) gawar ak gàngoor gu limuwul gu ànd ak moom, jóge Misra: niti Libi ak ay Sukkeen aki Kuuseen.
4 He captured the fortified cities of Judah and came as far as Jerusalem. Ba loolu amee mu nangu dëkk ya tata wër te ñu bokk ca Yuda, doora agsi Yerusalem.
5 Shemaiah the prophet came to Rehoboam and Judah's leaders, gathered in Jerusalem because of Shishak: "So says our Father: You abandoned me, so I abandon you to Shishak." Semaya yonent ba nag fekki Robowam ak kilifay Yuda fa ñu dajeji woon fa Yerusalem, ba Sisag jegesee. Mu ne leen: «Aji Sax ji dafa wax ne: Yeena ma wacc, man itam, ma wacc leen ci loxol Sisag.»
6 Then the leaders of Israel and the king humbled themselves and said, "Our Father is righteous." Buur ak kilifa yi daldi toroxlu, ne: «Aji Sax ji moo am dëgg.»
7 When our Father saw they had humbled themselves, our Father's word came to Shemaiah: "They've humbled themselves; I won't destroy them, but grant them a little rescue, and my anger won't pour out on Jerusalem through Shishak. Ba Aji Sax ji gisee na ñu toroxloo, kàddug Aji Sax ji moo dikkal Semaya ne: «Gannaaw toroxlu nañu, duma leen sànk, waaye dinaa leen may tuuti xettal, te duma sottee loxol Sisag sama sànj ci kaw Yerusalem.
8 But they will be Shishak's servants, to know my service and the service of earthly kingdoms." Waaye du tere ñu doon jaami Sisag, te dinañu xam li ci jaamu ma, ak li ci jaamu nguuri réew yi.»
9 Shishak king of Egypt attacked Jerusalem and took everything—the treasures of our Father's house, the royal palace, including the gold shields Solomon made. Ci kaw loolu Sisag buuru Misra song Yerusalem. Mu jël nag alali kër Aji Sax ji ak alali kër buur. Lépp la jël ba ca pakki wurus ya Suleymaan defarlu woon.
10 Rehoboam replaced them with bronze shields, entrusted to the guard commanders watching the entrance to the king's house. Ba mu ko defee Buur Robowam defarlu ay pakku xànjar yu wuutu yu wurus ya. Mu teg ko ca loxoy njiiti dag yay wattu buntu kër buur.
11 Whenever the king entered our Father's house, the guards carried the shields, then returned them to the guard chamber. Saa yu Buur dee duggsi ca kër Aji Sax ji, dag ya ŋàbb pakk ya, bu ñu noppee delloo ko ca néegu dag ya.
12 When Rehoboam humbled himself, our Father's anger turned from him, not destroying him completely; good things remained in Judah too. Ba mu toroxloo, ca la ko sànjum Aji Sax ji dëddu ko, ba tax sànku ko sànkute gu mat sëkk, te biir Yuda itam amoon na mbir yu mu baaxle.
13 King Rehoboam strengthened himself in Jerusalem and reigned; forty-one when he became king, he reigned seventeen years in Jerusalem, the city our Father chose from all the tribes of Israel to place his name there. His mother was Naamah, an Ammonite. Noonu la Buur Robowam dëjoo bu baax ca Yerusalem, yor nguur ga. Ñeent fukki at ak benn la Robowam amoon ba muy falu. Fukki at ak juróom ñaar la nguuroo Yerusalem, dëkk ba Aji Sax ji tànn, ngir dëël fa turam, ci mboolem dëkki giiri Israayil. Ndeyam di Naama, di ab Amoneen.
14 He did evil, because he did not set his heart to seek our Father. Lu bon la Robowam daan def ndax deful woon am xelam ci wut Aji Sax ji.
15 Rehoboam's deeds, first to last, appear in the records of Shemaiah the prophet and Iddo the seer, listing genealogies. Rehoboam and Jeroboam warred continually. Mbiri Robowam yu njëkk yaak yu mujj ya, bindees na ko moos ci nettalib Semaya yonent ba, ak Ido boroom peeñu ba, ca téere ba yittewoo limu maam yi. Ay xare nag la Robowam ak Yerbowam a jàppoo woon bés bu nekk.
16 Rehoboam rested with his ancestors, buried in the City of David; his son Abijah reigned instead. Gannaaw gi, Buur Robowam saay, fekki ay maamam, ñu denc ko ca gox ba ñu naan Kër Daawuda. Abya doomam moo falu buur, wuutu ko.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]