Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

2 Chronicles 11 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Rehoboam came to Jerusalem and assembled the house of Judah and Benjamin—180,000 chosen warriors—to fight against Israel and restore the kingdom to Rehoboam. Ci kaw loolu Robowam agsi Yerusalem, daldi woo waa kër Yuda ak Beñamin, ñu daje di téeméer ak juróom ñett fukki junniy (180 000) nit, diy ñeyi xare. Ñu nara xareek Israayil, ngir delloo nguur ga ca loxol Robowam.
2 But the word of our Father came to Shemaiah, the man of our Father, saying: Ci biir loolu kàddug Aji Sax ji dikkal góoru Yàlla gu ñuy wax Semaya, ne ko:
3 "Say to Rehoboam son of Solomon, king of Judah, and to all Israel in Judah and Benjamin: «Waxal Robowam doomu Suleymaan buurub Yuda ak mboolem bànni Israayil gi ci Yuda ak Beñamin, ne leen:
4 This is what our Father says: Don't go up or fight against your brothers. Go home, each of you—this came from me." So they obeyed the words of our Father and turned back from advancing against Jeroboam. “Aji Sax ji dafa wax ne: Buleen jóg di xeex ak seeni bokk. Na ku nekk ñibbi këram, ndax ci man la mbir mii sababoo.”» Ñu dégg kàddug Aji Sax ji, daldi walbatiku, fomm cong ma ñu naraloon Yerbowam.
5 Rehoboam lived in Jerusalem and built up cities for defense in Judah. Ba mu ko defee Robowam dëkke Yerusalem, daldi tabax fa Yuda ay dëkk yu ñu dàbbali ngir kaaraange.
6 He built Bethlehem, Etam, and Tekoa, Tabax na Betleyem ak Etam ak Tekowa
7 Beth-zur, Soco, Adullam, ak Bet Cur ak Soko ak Adulam
8 Gath, Mareshah, Ziph, ak Gaat ak Maresa ak Sif
9 Adoraim, Lachish, Azekah, ak Adorayim ak Lakis ak Aseka
10 Zorah, Aijalon, and Hebron, the fortified cities in Judah and Benjamin. ak Cora ak Ayalon ak Ebron, dëkk ya ñu dàbbali ca diiwaani Yuda ak Beñamin.
11 He strengthened the fortresses and put commanders in them, along with stores of food, oil, and wine. Tatay dëkk ya la dàbbali, teg fa ay jawriñ, denc fa ab dund akug diw ak biiñ.
12 In every city he placed shields and spears, strengthening them greatly. So Judah and Benjamin remained his. Mboolem dëkk yooyu yépp, ay pakk aki xeej a nga fa woon. Noonu la dooleele dëkk ya lool, ba teg loxoom ca kaw Yuda ak Beñamin.
13 The priests and the Levites who were throughout all Israel came to him from all their territory, Ci biir loolu sarxalkat yeek Leween yi dëkk ca biir giiri Israayil ya ca bëj-gànnaar, ñoom ñépp toxoo mboolem gox ya ñu moom, daldi dikk far ak Robowam.
14 for the Levites left their pasturelands and property, going to Judah and Jerusalem, since Jeroboam and his sons turned them away from serving as priests of our Father. Leween ña sax dañoo mujj wacc seen suufi parlu ak seen moomeel, ba dem Yuda ak Yerusalem, ndax Yerbowam ak doomam yu góor ñoo leen dàqe ci liggéeyu carxal gu ñeel Aji Sax ji.
15 He appointed his own priests for the high places, for the goat idols, and for the calf idols he had made. Fekk na Yerbowam tabbal boppam ay sarxalkat ngir yàllay bëy yaak wëllu ya mu sàkk ca bérebi jaamookaay ya.
16 From every tribe of Israel, those who set their heart on seeking our Father, the God of Israel, followed the Levites to Jerusalem to sacrifice to our Father, the God of their ancestors. Ci kaw loolu ci mboolem giiri Israayil gu bëj-gànnaaru Israayil, ña ca nammoona jaamu Aji Sax ji Yàllay Israayil, ñépp bàyyikoo ca, topp ca Leween ña, dem Yerusalem, ngir sarxal fa Aji Sax ji seen Yàllay maam.
17 They strengthened Judah's kingdom, supporting Rehoboam son of Solomon three years, for they walked in the way of David and Solomon three years. Noonu lañu dooleele nguurug Yuda, dooleel Robowam doomu Suleymaan diiru ñetti at, ndax diiru ñetti at lañu topp tànki Daawuda ak Suleymaan.
18 Rehoboam married Mahalath, the daughter of Jerimoth son of David and of Abihail the daughter of Eliab son of Jesse. Robowam nag jël jabar Maxalat mi baayam di Yerimot. Yerimot, Daawudaay baayam, yaayam di Abiyayil. Abiyayil, Elyab doomu Yese mooy baayam.
19 She bore him sons: Jeush, Shemariah, and Zaham. Maxalat jural ko doom yu góor, ñoo di Yewus ak Semarya ak Sayam.
20 After her, he married Maacah the daughter of Absalom, who bore him Abijah, Attai, Ziza, and Shelomith. Gannaaw kooku mu jël Maaka mi baayam di Absalom. Mu jural ko Abya ak Atay ak Sisa ak Selomit.
21 Rehoboam loved Maacah daughter of Absalom more than his other wives and concubines, since he had eighteen wives, sixty concubines, twenty-eight sons, and sixty daughters. Maaka nag la Robowam gënoona bëgg ci mboolem ay jabaram aki nekkaaleem, te fukki jabar ak juróom ñett la Robowam jëloon, ak juróom benn fukki nekkaale, am ca ñaar fukki doom yu góor ak juróom ñett, ak juróom benn fukki doom yu jigéen.
22 Rehoboam made Abijah, son of Maacah, chief leader among his brothers, intending to make him king. Robowam nag nara fal Abya doomu Maaka buur, ba tax mu jiital ko, muy njiitu ñi mu bokkal waajur.
23 He acted wisely, spreading some of his sons through every district of Judah and Benjamin, to each fortified city, giving them abundant provisions and seeking many wives for them. Ci kaw loolu mu def ag muus, tasaare yeneen doomam yu góor yépp, yebal leen ca mboolem goxi Yuda ak Beñamin, ca mboolem dëkk ya tata wër. Mu daldi leen jox dund bu ne gàññ, jëlal leen jabar yu bare.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]