Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

2 Chronicles 10 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Rehoboam went to Shechem, for all Israel had come to Shechem to make him king. Ba loolu amee Robowam dem dëkk ba ñuy wax Sikem, ndax fa la Israayil gépp daje woon, ngir fal ko buur.
2 When Jeroboam son of Nebat heard of it—he was in Egypt, having fled from King Solomon—Jeroboam returned from Egypt. Yerbowam doomu Nebat dégge ko ca Misra ga mu dawoon dem, di fa làqu Buur Suleymaan. Ci kaw loolu Yerbowam bàyyikoo Misra, dellusi.
3 So they sent for him, and Jeroboam and all Israel came and said to Rehoboam, Ñu woolu ko, ñu ànd, mook Israayil gépp ca Robowam. Ñu ne ko:
4 "Your father made our yoke heavy. Now lighten your father's hard service and the heavy yoke he put on us, and we will serve you." «Sa baay da noo tegoon njaam gu metti. Kon nag dangay woyofal sunu liggéey bu metti bi nu sa baay sëf, te yolomal buumu njaam gu teeŋ gi mu nu gàll, kon nu jaamu la.»
5 He said to them, "Come back to me in three days." So the people went away. Mu ne leen: «Demleen ba mu am ñetti fan, ngeen délsi.» Mbooloo ma daldi dem.
6 Then King Rehoboam consulted the elders who had served his father Solomon during his lifetime: "How do you advise me to answer these people?" Buur Robowam giseek mag ña daa taxawu Suleymaan baayam, ba muy dund. Mu ne leen: «Lu ngeen may digal, ma wax ko mbooloo mii?»
7 They replied, "If you are good to these people, please them, and speak kindly, they will always be your servants." Ñu ne ko: «Soo baaxee mbooloo mii, yéwéne leen, wax leen kàddu yu rafet, say jaam lañuy doon ba fàww.»
8 But he rejected the elders' advice and consulted the young men who grew up with him and served him. Robowam nag dégluwul waxi mag ña, xanaa dem giseek xale yu góor ya màggandoo ak moom te di ko taxawu.
9 He asked them, "What do you advise? How should we answer these people asking me to lighten the yoke my father put on us?" Mu ne leen: «Lu ngeen may digal ma wax ko mbooloo mii ne ma, ma yolomal buumu njaam gi leen sama baay yeewe woon?»
10 The young men who grew up with him replied, "Tell the people who told you, 'Your father made our yoke heavy; lighten it for us'—tell them: 'My little finger is thicker than my father's waist.' Xale yu góor ya mu màggandool wax ko ne ko: «Mbooloo mi ne la sa baay da leena yeewoon buumu njaam gu teeŋ, waaye yaw yolomalal leen ko, li nga leen di wax mooy lii: “Sama baaraamu sanqleeñ moo gëna diis sama tànku baay.
11 My father put a heavy yoke on you; I'll add to it. My father disciplined you with whips; I will discipline you with scorpions.'" Sama baay a leena tegoon njaam gu metti, waaye man maay yokk seen njaam, ba mu gëna metti. Te sama baay ay yar la leen daan cawe, waaye samab yar, ay leraw yu ñu kor weñ la.”»
12 So Jeroboam and all the people came to Rehoboam on the third day, as the king had said, "Come back to me on the third day." Ca ñetteelu bés ba Yerbowam ànd ak mbooloo ma mépp, dellu ca Robowam, noonee leen ko Buur waxe woon ne leen ñu dem ba mu am ñetti fan, ñu délsi.
13 The king answered them harshly. King Rehoboam rejected the advice of the elders, Buur Robowam tontu leen kàddu gu ñagas, bàyyi la ko mag ña digaloon.
14 and spoke to them as the young men advised: "My father made your yoke heavy; I will make it heavier. My father disciplined you with whips; I will discipline you with scorpions." Na ko xale yu góor ya digale la waxeek ñoom, ne leen: «Maa leen di teg njaam gu metti, te maa koy yokkati. Te sama baay ay yar la leen daa cawe, waaye samab yar, ay leraw yu ñu kor weñ la.»
15 So the king did not listen to the people, for this turn came from our Father, to fulfill the word our Father spoke through Ahijah the Shilonite to Jeroboam son of Nebat. Noonu la Buur tanqamloo mbooloo ma, te Yàlla moo walbatee noonu mbir ma, ngir amal wax ja mu waxoon Yerbowam doomu Nebat, Axya waa Silo ba jottali.
16 When all Israel saw the king would not listen to them, the people answered him: "What share do we have in David? No inheritance in Jesse's son! To your tents, Israel! Look to your own house, David!" So all Israel went home to their tents. Ba Israayil gépp gisee na leen Buur tanqamloo, dañu koo tontu ne ko: «Ana lu nu bokk ak Daawuda? Lu nu séq ak doomu Yese? Bànni Israayiloo, delluleen ca seeni xayma! Yaw askanu Daawuda, xoolalal sa bopp sa kër.» Ba mu ko defee bànni Israayil gépp dellu ca seeni xayma.
17 But Rehoboam still reigned over the Israelites who lived in the cities of Judah. Teewul bànni Israayil ya dëkkoon ca dëkki Yuda, Robowam wéy di seen buur.
18 Then King Rehoboam sent Hadoram, in charge of the forced labor, but the Israelites stoned him to death. King Rehoboam himself jumped into his chariot and fled to Jerusalem. Ci kaw loolu Buur Robowam yónni Adoram may sase liggéeyi sañul-bañ ya. Teewul Israayil bokk dóor ko ay doj ba mu dee. Buur Robowam daldi gaaw war watiir, daw làquji Yerusalem.
19 So Israel has been in rebellion against the house of David to this day. Noonu la Israayil fippoo ci kaw waa kër Daawuda ba sunu jonni yàllay tey.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]