Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

2 Chronicles 14 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
13:23 Abijah rested with his ancestors; they buried him in the City of David. His son Asa became king, and the land had peace ten years. Gannaaw gi, Buur Abya saay, fekki ay maamam, ñu denc ko ca gox ba ñu naan Kër Daawuda. Asa doomam moo falu buur, wuutu ko. Ay jantam, réew ma am na jàmm diiru fukki at.
1 Asa did what was good and right in the sight of our Father. Asa nag di def lu baax lu jub li Aji Sax ji Yàllaam rafetlu.
2 He removed the foreign altars and high places, smashed the sacred pillars, and cut down the Asherah poles. Moo dindi sarxalukaayi yàllay ndoxandéem yi, ak bérebi jaamookaay yi, moo toj tuuri doj yi, ak xer yi ñuy màggale Asera, tuur mi.
3 He commanded Judah to seek our Father, the God of their ancestors, and keep the law and commandment. Ci biir loolu mu wax Yuda ne leen ñu déggal Aji Sax ji seen Yàllay maam, tey jëfe yoon wi ak santaane bi.
4 He also removed the high places and incense altars from all Judah's cities, and the kingdom was at peace under him. Mboolem dëkki Yuda la jële bérebi jaamookaay ya ak sarxalukaayi cuuraay ya. Ba mu ko defee nguur ga am jàmm fa kanamam.
5 He built fortified cities in Judah, for the land was at peace. He fought no war those years, because our Father gave him rest. Asa tabax na ay dëkk yu ñu dàbbali fa Yuda, ndax jàmm ja réew ma am, kenn xarewul ak moom, at yooyu, ndax Aji Sax jee ko may noflaay.
6 He told Judah, "Let us build these cities and surround them with walls, towers, gates, and bars. The land is still ours, because we sought our Father; we sought him, and he gave us rest all around." So they built and thrived. Moo tax mu ne Yuda: «Nanu tabax dëkk yii, wërale leen ay tata ak seeni sooroor aki tëjukaayi weñ, li feek réew miy nekkagum fi sunu kanam. Ndax kat noo jaamu sunu Yàlla Aji Sax ji. Noo ko jaamu, mu may nu noflaay wet gu nekk.» Ci kaw loolu ñu tabax, ba sottile.
7 Asa had an army of 300,000 from Judah with large shields and spears, and 280,000 from Benjamin with shields and bows—all mighty warriors. Asa amoon na gàngooru nit ñu yor pakk yu mag aki xeej, bokk ci giirug Yuda, di ñetti téeméeri junni (300 000), ak ñu bokk ci giirug Beñamin, yor pakk yu ndaw tey bank xala, di ñaari téeméer ak juróom ñett fukki junni (280 000), ñooñu ñépp di jàmbaari góor yu am doole.
8 Zerah the Cushite marched against them with a million troops and 300 chariots, advancing to Mareshah. Sera Kuuseen ba nag moo dikkoon ci seen kaw, ak gàngooru junniy junni (1 000 000), ak ñetti téeméeri (300) watiir. Mu dikk ba Maresa.
9 Asa marched out against him, and they lined up for battle in the Valley of Zephathah at Mareshah. Asa génn dajejeek moom, ñu làng-déral xare fa xuru Cefata, feggook Maresa.
10 Then Asa cried to our Father his God: "Father, only you can help the powerless against the mighty. Help us, our God, for we rely on you, and in your name we face this vast horde. You are our God; let no mere man prevail against you." Ba loolu amee Asa woo Yàllaam Aji Sax ji, ne ko: «Yaw Aji Sax ji, kenn melul ni yaw, di dimbalee diggante ñu takku ak ñu néew doole. Kon Aji Sax ji sunu Yàlla, dimbali nu, ndax ci yaw lanu wàkkirlu, ci saw tur it lanu dajeseek gàngoor gii. Aji Sax ji sunu Yàlla, bu la nit man.»
11 So our Father struck down the Cushites before Asa and before Judah, and the Cushites fled. Aji Sax ji nag duma Kuuseen ña fa kanam Asa ak Yuda, Kuuseen ña daw.
12 Asa and his people pursued them to Gerar, and the Cushites fell until none survived, for they were shattered before our Father and his army. Judah's men carried off great plunder. Asa ak gàngoor ga mu àndal dàqi Kuuseen ña ba Gerar, ñu daanu, kenn rëccul. Fa kanam Aji Sax ji ak fa kanam gàngooram lañu rajaxoo. Ci kaw loolu Yudeen ña yóbbu alalu sëxëtoo ju bare lool.
13 They struck down all the cities around Gerar, for the terror of our Father had fallen on them. They looted all the cities, since much plunder was in them. Mboolem dëkk ya wër Gerar lañu daaneel ndax tiitaange ju leen dikke, sababoo ci Aji Sax ji. Dëkk yépp lañu sëxëtoo it, te alalu sëxëtoo ju baree ca nekkoon.
14 They also attacked the herdsmen's tents, carried off many sheep and camels, and returned to Jerusalem. Xaymay jur ga sax dañu leena daaneel, daldi yóbbu gàtt yu bare aki giléem. Gannaaw loolu ñu dellu Yerusalem.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]