Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

1 Chronicles 2 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 These were the sons of Israel: Reuben, Simeon, Levi, Judah, Issachar, and Zebulun, Góor ñiy doomi Yanqóoba mi ñuy wax itam Israayil ñoo di Ruben ak Simeyon ak Lewi ak Yuda ak Isaakar ak Sabulon
2 Dan, Joseph, Benjamin, Naphtali, Gad, and Asher. ak Dan ak Yuusufa ak Beñamin ak Neftali ak Gàdd ak Aser.
3 Judah's sons: Er, Onan, Shelah—three born to him by Shua's Canaanite daughter. Er, the firstborn, was evil in our Father's eyes, so he killed him. Doomi Yuda yu góor ñoo di Er ak Onan ak Sela. Ñooñu, doomu Suwa, ndawas Kanaaneen sa la ko amal. Waaye Er, taawub Yuda boobu, doonoon ku Aji Sax ji seede coxoram; Aji Sax ji rey ko.
4 Tamar, Judah's daughter-in-law, bore him Perez and Zerah. Judah had five sons in all. Ku ñuy wax Tamar, gorob Yuda ba doomam doon denc, am ak Yuda Peres ak Sera. Doomi Yuda yu góor yépp di juróom.
5 The sons of Perez: Hezron and Hamul. Doomi Peres yu góor nag di Esron ak Amul.
6 The sons of Zerah: Zimri, Ethan, Heman, Calcol, and Dara—five of them in all. Doomi Sera yu góor ñoo di Simri ak Etan ak Eman ak Kalkol ak Daara; ñoom ñépp di juróom.
7 Carmi's son: Achar, Israel's troubler, who broke faith over the devoted things. Doomu Karmi ju góor moo di Akar (muy firi Musiba), ki yóbbe woon Israayil musiba ba mu feccee worma ca mbir ya ñu aayaloon, jagleel ko Yàlla.
8 The son of Ethan: Azariah. Doomu Etan ju góor moo di Asaryaa.
9 The sons born to Hezron: Jerahmeel, Ram, and Chelubai. Doomi Esron yu góor yi mu am ñoo di Yeraxmeel ak Ram ak Kaleb, mooy Kelubay ba tey.
10 Ram fathered Amminadab, and Amminadab fathered Nahshon, leader of the people of Judah. Ram mooy baayu Aminadab, Aminadab di baayu Naason, kilifag giirug Yuda.
11 Nahshon fathered Salma, and Salma fathered Boaz, Naason mooy baayu Salma, Salma di baayu Bowas.
12 Boaz fathered Obed, and Obed fathered Jesse. Bowas mooy baayu Obedd, Obedd di baayu Yese.
13 Jesse fathered Eliab his firstborn, Abinadab the second, Shimea the third, Yese mooy baayu Elyab, taawam bu góor, Abinadab di tofoom, Simeya di ñetteelu doomam ju góor.
14 Nethanel the fourth, Raddai the fifth, Netaneel mooy ñeenteelu doomam ju góor, Raday di juróomeelu doomam ju góor.
15 Ozem the sixth, and David the seventh. Occem a ca topp di juróom benneel, Daawuda toppaat ca, di juróom ñaareelu doomam ju góor.
16 Their sisters were Zeruiah and Abigail. Zeruiah's sons: Abishai, Joab, and Asahel—three. Ñooñu seeni jigéen a doon Ceruya ak Abigayil. Doomi Ceruya yu góor di Abisay, Yowab ak Asayel, ñuy ñett.
17 Abigail bore Amasa, and the father of Amasa was Jether the Ishmaelite. Abigayil moo jur Amasa ma Yeter Ismayleen ba di baayam.
18 Caleb son of Hezron had children by his wife Azubah and by Jerioth; her sons were Jesher, Shobab, and Ardon. Kaleb miy doomu Esron ju góor am na ñetti doom yu góor ak soxnaam yi tudd Asuba ak Yeryot, ñuy: Yeser, Sobab ak Ardon.
19 When Azubah died, Caleb married Ephrath, and she bore him Hur. Ba Asuba faatoo, Kaleb jël Efrata, mu am ak moom Ur.
20 Hur fathered Uri, and Uri fathered Bezalel. Ur mooy baayu Uri, Uri di baayu Beccalel.
21 Afterward Hezron had relations with the daughter of Machir the father of Gilead, marrying her at sixty; she bore him Segub. Gannaaw gi, Esron tollu ci juróom benn fukki at, jël doomu Makir miy baayu Galàdd. Mu am ca doom ju góor ju ñuy wax Segub.
22 Segub fathered Jair, who held twenty-three towns in the land of Gilead. Segub mooy baayu Yayir ma tegoon loxo ñaar fukki dëkk ak ñett ca diiwaanu Galàdd.
23 But Geshur and Aram took Havvoth-jair from them, plus Kenath and its villages—sixty towns. All these were sons of Machir, father of Gilead. Waaye Gesureen ñaak Arameen ña nangu ca ñoom dëkk yu ndaw ya ca Yayir, boole ca Kenat ak dëkk ya ca bokk, lépp di juróom benn fukki dëkk. Góor ñooñu ñépp nag doomi Makir lañu woon, moom baayu Galàdd.
24 After Hezron died in Caleb-ephrathah, Abijah, Hezron's wife, bore him Ashhur, the father of Tekoa. Gannaaw ba Esron faatoo ca Kaleb Efrata, la Abya ma doon soxnaam jur doomu Esron ja ñuy wax Asuur mi sanc Tekowa.
25 The sons of Jerahmeel, Hezron's firstborn: Ram his firstborn, then Bunah, Oren, Ozem, and Ahijah. Góor ñi Yeraxmeel, taawub Esron di seen baay ñoo di Ram may taawam ak Buna ak Oren ak Occem ak Axya.
26 Jerahmeel had another wife, whose name was Atarah; she was the mother of Onam. Yeraxmeel jëlaat na soxna su ñuy wax Atara, am ca ku ñuy wax Onam.
27 The sons of Ram, Jerahmeel's firstborn: Maaz, Jamin, and Eker. Ram, taawub Yeraxmeel, ay doomam yu góor ñoo di Màcc ak Yamin ak Eker.
28 The sons of Onam: Shammai and Jada. The sons of Shammai: Nadab and Abishur. Doomi Onam yu góor ñoo di Samay ak Yada. Doomi Samay yu góor di Nadab ak Abisur.
29 Abishur's wife was named Abihail, and she bore him Ahban and Molid. Abisur nag jël Abiyayil, am ca Aban ak Molit.
30 The sons of Nadab: Seled and Appaim. Seled died without children. Doomi Nadab yu góor ñoo di Selet ak Apayim. Selet faatu na te amul doom.
31 The son of Appaim: Ishi. The son of Ishi: Sheshan. The child of Sheshan: Ahlai. Doomu Apayim ju góor moo di Yisey. Doomu Yisey ju góor moo di Sesan. Doomu Sesan di Axlay.
32 The sons of Jada, Shammai's brother: Jether and Jonathan. Jether died without children. Góor ñi Yada mi bokk ak Samay jur ñoo di Yeter ak Yonatan. Yeter faatu na te amul doom.
33 The sons of Jonathan: Peleth and Zaza. These were the descendants of Jerahmeel. Doomi Yonatan yu góor ñoo di Pelet ak Sasa. Ñooñu ñoo soqikoo ci Yeraxmeel.
34 Now Sheshan had no sons, only daughters. He had an Egyptian servant whose name was Jarha, Sesan nag amul doom ju góor waaye ay jigéen la am. Sesan amoon na jaamu waa Misra bu tudd Yarxa.
35 and Sheshan gave his daughter in marriage to Jarha his servant, and she bore him Attai. Mu may Yarxa kenn ciy doomam yu jigéen. Mu amal ko ca doom ju góor ju tudd Atay.
36 Attai fathered Nathan, and Nathan fathered Zabad, Atay mooy baayu Natan, Natan di baayu Sabàdd.
37 Zabad fathered Ephlal, and Ephlal fathered Obed, Sabàdd mooy baayu Eflal, Eflal di baayu Obedd.
38 Obed fathered Jehu, and Jehu fathered Azariah, Obedd mooy baayu Yewu, Yewu di baayu Asaryaa.
39 Azariah fathered Helez, and Helez fathered Eleasah, Asaryaa mooy baayu Elecc, Elecc di baayu Elasa.
40 Eleasah fathered Sismai, and Sismai fathered Shallum, Elasa mooy baayu Sismay, Sismay di baayu Salum.
41 Shallum fathered Jekamiah, and Jekamiah fathered Elishama. Salum mooy baayu Yekamya, Yekamya di baayu Elisama.
42 Sons of Caleb, Jerahmeel's brother: Mesha his firstborn, father of Ziph; and the sons of Mareshah the father of Hebron. Góor ñi Kaleb, ma bokk ak Yeraxmeel, di seen baay ñoo di Mesa, may taawam, te di baayu Sif ak Maresa, baayu Ebron.
43 The sons of Hebron: Korah, Tappuah, Rekem, and Shema. Doomi Ebron yu góor ñoo di Kore ak Tapuwa ak Rekem ak Sema.
44 Shema fathered Raham, the father of Jorkeam, and Rekem fathered Shammai. Sema mooy baayu Raxam, Raxam di baayu Yorkam, Rekem mooy baayu Samay.
45 The son of Shammai was Maon, and Maon was the father of Beth-zur. Samay mooy baayu Mawon, Mawon di baayu Bet Cur.
46 Ephah, Caleb's concubine, bore Haran, Moza, and Gazez; and Haran fathered Gazez. Kaleb, Efa nekkaaleem la woon. Moo jur Karan ak Mocca ak Gases. Karan am na doom ju góor ju mu tudde Gases moom it.
47 The sons of Jahdai: Regem, Jotham, Geshan, Pelet, Ephah, and Shaaph. Doomi Yaday yu góor ñoo di Regem ak Yotam ak Gesan ak Pelet ak Efa ak Saaf.
48 Maacah, Caleb's concubine, bore Sheber and Tirhanah. Kaleb amoon na beneen nekkaale bu ñuy wax Maaka. Mu am ak moom Seber ak Tirxana.
49 She bore Shaaph, father of Madmannah, and Sheva, father of Machbenah and Gibea. Caleb's daughter was Achsah. Gannaaw mu amaat ku ñuy wax Saaf di baayu Madmana, ak ku ñuy wax Sewa, di baayu Magbena ak Gibeya. Doomu Kaleb ju jigéen mooy Agsa.
50 These were the descendants of Caleb. The sons of Hur, the firstborn of Ephrathah: Shobal the father of Kiriath-jearim, Ñeneen a ngi di ñu askanoo ci Kaleb: Ur taawam baak soxnaam sa ñuy wax Efrata, am na ñetti doom yu góor di Sobal ma sanc Kiryaat Yarim,
51 Salma the father of Bethlehem, and Hareph the father of Beth-gader. ak Salma ma sanc Betleyem, ak Aref ma sanc Bet Gader.
52 Shobal the father of Kiriath-jearim had other sons: Haroeh, and half of the Menuhoth. Sobal ma sanc Kiryaat Yarim moo meññ waa Arowe ak genn-wàllu waa Menuxot.
53 Kiriath-jearim's clans: Ithrites, Puthites, Shumathites, Mishraites—from them came the Zorathites and Eshtaolites. Sobal moo meññ itam làngi Kiryaat Yarim yii di Yetereen ñi ak Puuteen ñi ak Sumateen ñi ak Misrayeen ñi. Ci ñooñu la Corateen ñeek Estawleen ñi soqikoo.
54 The descendants of Salma: Bethlehem, the Netophathites, Atroth-beth-joab, half of the Manahathites, and the Zorites. Salma moo meññ waa Betleyem ak Netofa ak Aterot Bet Yowab ak genn-wàllu waa Manaxat ak Coreyeen ñi.
55 The scribe clans living at Jabez: Tirathites, Shimeathites, Sucathites—Kenites who came from Hammath, father of the house of Rechab. Salma moo meññ itam làngi bindkat ya dëkk Yabecc, di Tirateen ñi ak Simateen ñi ak Sukateen ñi. Ñooñu ay Keñeen lañu ñu soqikoo ca Amat maamu waa kër Rekab.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]