Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Matthew 13 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 On that day Jesus went out of the house and sat down beside the sea. Bés booba Yeesu génnoon na ca kër ga, toog ca wetu dex ga.
2 Large crowds gathered around him, so he got in a boat and sat, while the whole crowd stood on the shore. Mbooloo mu bare dajaloo ca moom, ba tax mu dugg cig gaal, toog; mbooloo mépp taxaw ca tefes ga.
3 And he told them many things in parables, saying: "Look, a sower went out to sow. Noonu Yeesu dégtal leen lu bare ciy léeb ne leen: «Dafa amoon beykat bu demoon jiyi.
4 And as he sowed, some seed fell along the path, and the birds came and devoured it. Bi muy saaw toolam nag, lenn ci pepp mi wadd ci kaw yoon wi, picc yi daldi ñëw, lekk ko lépp.
5 Other seed fell on rocky ground with little soil, and sprang up quickly since the soil lacked depth. Leneen ci pepp mi wadd ci bérab bu bare ay doj te néew suuf, mu daldi sax bu gaaw, ndaxte suuf si barewul.
6 When the sun rose, the plants were scorched; since they had no root, they withered. Waaye bi jant bi naajee, mu lakk, wow, ndaxte amul ay reen.
7 Other seed fell among thorns, and the thorns grew up and choked it. Leneen nag wadd ci biir ay xaaxaam, xaaxaam yi daldi jóg, tanc ko.
8 Other seed fell on good soil, producing grain: some a hundredfold, some sixty, some thirty. Li ci des dal ci suuf su baax, nangu ba def ay gub; lii àntu ba mat téeméeri yoon lu ëpp la mu ji woon, lii mat juróom benn fukk, li ci des fanweer.
9 Whoever has ears, let them hear." Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.»
10 Then the disciples came to him and asked, "Why do you speak to them in parables?" Bi Yeesu waxee ba noppi, ay taalibeem jegeñsi, laaj ko lu tax mu di leen wax ciy léeb.
11 He said, "You've been given to know the secrets of the kingdom of our Father; they have not. Noonu mu ne leen: «May nañu leen, ngeen xam mbóoti nguuru Yàlla Aji Kawe ji, waaye ñale mayuñu leen ko.
12 Whoever has will be given more and have plenty; whoever has none loses even what he has. Ndaxte ku am, dinañu la dollil, ba nga barele; waaye ku amul, li nga am as néew, dinañu ko nangu.
13 This is why I speak to them in parables: they look but don't see; they listen but don't hear or understand. “Dañuy xool te duñu gis, di déglu waaye duñu dégg te duñu xam,” moo tax ma di leen wax ciy léeb.
14 In them Isaiah's prophecy is fulfilled: 'You will hear and hear, yet never understand; you will see and see, yet never perceive.' Li Esayi waxoon ci kàddug Yàlla am na ci ñoom, bi mu naan: “Dingeen déglu bu baax waaye dungeen xam dara; di xool bu baax waaye dungeen gis dara.
15 For this people's heart has grown calloused; they hardly hear with their ears, and they have closed their eyes—otherwise they might see with their eyes, hear with their ears, understand with their heart, and turn, and I would heal them.' Ndaxte xolu xeet wii dafa dërkiis; dañuy déglu ak nopp yu naqari, tey gëmm seeni bët, ngir baña gis ak seeni bët, dégg ak seeni nopp, te xam ci seen xol, ñu waññiku ci man, ma wéral leen.”
16 But blessed are your eyes, for they see, and your ears, for they hear. «Waaye yéen barkeel ngeen, ndaxte seeni bët a ngi gis te seeni nopp di dégg!
17 I assure you: many prophets and righteous people longed to see what you see, and didn't; to hear what you hear, and didn't. Ndaxte ci dëgg maa ngi leen koy wax, ay yonent yu bare ak nit ñu jub ñu bare bëggoon nañu gis li ngeen di gis waaye gisuñu ko, te dégg li ngeen di dégg waaye dégguñu ko.
18 Listen, then, to the parable of the sower. «Yéen nag dégluleen li léebu beykat biy tekki.
19 Everyone who hears the kingdom's word and doesn't grasp it—the evil one comes and snatches what was sown in his heart. This is the seed sown beside the path. Boo xamee ne nit mu ngi déglu wax ju jëm ci nguuru Yàlla te xamu ko, Ibliis day ñëw, këf li ñu def ci xolam; kooku mooy ki jot ci jiwu wi ci kaw yoon wi.
20 Seed sown on rocky ground is the one who hears the word, immediately receiving it with joy, Ki jot ci jiwu wi ci bérab bu bare ay doj nag, mooy ki dégg wax ji, am ci bànneex bu gaaw;
21 but having no root in themselves, they don't last; when trouble or persecution comes because of the word, they quickly fall away. waaye du yàgg, ndaxte wax ji saxul ci moom. Bu jaaree ci nattu nag, mbaa ñu fitnaal ko ndax kàddu gi, mu dàggeeku ci saa si.
22 The one sown among thorns hears the word, but worry over this age and wealth's deceit choke it, making it unproductive. Ki jot ci jiwu wi ci xaaxaam yi mooy ki dégg wax ji, waaye soxlay àddina ak naxi alal tanc wax ji, ba du jur njariñ.
23 But the seed sown on good soil hears the word and understands it. It bears fruit—100, sixty, or thirty times what was sown." Ki jot ci jiwu wi ci suuf su baax si nag, mooy ki dégg wax ji te xam ko; mu jural ko njariñ, muy lu mat téeméeri yoon lu ëpp la ñu ji woon, muy juróom benn fukk mbaa fanweer.»
24 He gave them another parable: "The kingdom of our Father is like a man who sowed good seed in his field. Noonu Yeesu dégtal leen beneen léeb ne leen: «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni nit ku ji jiwu wu baax ci toolam.
25 But while everyone slept, his enemy came, sowed weeds among the wheat, and left. Waaye bi nit ñi di nelaw, noonam ñëw, ji jëmb ci biir dugub ji, daldi dem.
26 When the wheat sprouted and produced grain, then the weeds appeared as well. Bi dugub ji saxee nag, jëmb bi saxaale ak moom.
27 The owner's servants came saying, 'Master, didn't you sow good seed in your field? Where then did the weeds come from?' «Noonu surgay boroom kër ga ñëw ci moom ne ko: “Góor gi, xanaa jiwuloo jiwu wu baax ci sa tool? Fu jëmb bi jóge nag?”
28 'An enemy did this,' he replied. 'So do you want us to go pull them up?' the servants asked him. Mu ne leen: “Noon a ko def.” Surga ya ne ko: “Ndax nu dem dindi ko?”
29 'No,' he said, 'because while you are pulling the weeds, you may uproot the wheat with them. Mu ne leen: “Déedéet, ngir baña buddiwaale dugub ji, bu ngeen koy dindi.
30 Let both grow together until harvest. At harvest time I'll tell the reapers: Gather the weeds first, bind them in bundles to burn; then gather the wheat into my barn.'" Bàyyileen ñoom ñaar, ñu màgg, ba ngóob ma jot. Bu ngóob ma jotee nag, dinaa wax ñi koy góob: ‘Jëkkleena dindi jëmb bi, takk ko ay say, lakk ko, waaye ngeen semb dugub ji ci sama sàq.’ ”»
31 He told them another parable: "The kingdom of our Father is like a mustard seed a man took and planted in his field. Yeesu waxaat leen beneen léeb ne leen: «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni doomu fuddën bu nit jël, ji ko ci toolam.
32 Though the smallest of all seeds, when grown it becomes the largest of garden plants, a tree where birds come to nest in its branches." Doomu fuddën moo gëna tuuti ci jiwu yépp, waaye bu saxee, mooy sut ci gàncaxi tóokër yi, di nekk garab, ba picci asamaan ñëw, tàgg ciy caram.»
33 He gave them another parable: "The kingdom of our Father is like yeast a woman took and mixed into about twenty-five pounds of flour, until it spread through all the dough." Yeesu teg ca beneen léeb ne leen: «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni lawiir bu jigéen jël, jaxase ko ak ñetti andaari fariñ, ba kera tooyal bépp di funki.»
34 Jesus said all these things to the crowds in parables; he said nothing to them without a parable. Loolu Yeesu wax mbooloo ma, ëmb na ko lépp ciy léeb, te waxuleen dara lu dul ciy léeb.
35 This fulfilled what was spoken through the prophet: "I will open my mouth in parables; I will utter what's been hidden since the world was founded." Noonu am la ñu waxoon jaarale ko cib yonent, bi mu naan: «Dinaa leen wax ciy léeb, di yégle yëf yu nëbbu li dale ca njàlbéen ga ba bésu tey.»
36 Then he left the crowds and entered the house. His disciples approached him and said, "Explain to us the parable of the weeds in the field." Ci kaw loolu Yeesu bàyyi mbooloo ma, dugg ca kër ga. Taalibeem yi ñëw ci moom ne ko: «Firil nu léebu jëmb, bi sax ci tool bi.»
37 He answered, "The one who sowed the good seed is the Son of Man. Noonu Yeesu ne leen: «Doomu nit ki mooy ji jiwu wu baax wi;
38 The field is the world. The good seed is the kingdom's children; the weeds are the evil one's children. àddina mooy tool bi; ñi bokk ci nguuru Yàlla ñoo di jiwu wu baax wi; ñi bokk ci Ibliis ñooy jëmb bi;
39 The enemy who sowed them is the devil; the harvest is the end of the age; the harvesters are angels. Seytaane mooy noon bi ko ji; tukkitel àddina mooy ngóob mi, te malaaka yi ñooy góobkat yi.
40 As the weeds are gathered and burned in fire, so it will be at the end of the age. Ni ñu dajalee jëmb ba, lakk ko, noonu lay nekke, bu àddina tukkee.
41 The Son of Man will send his angels to weed out of his kingdom everything that causes sin and all who do evil. Doomu nit ki dina yebal ay malaakaam, ñu jële ci nguuram lépp luy yóbbe nit bàkkaar, ak ñiy def bàkkaar,
42 They will throw them into the blazing furnace, where there is weeping and grinding of teeth. sànni leen ci sawara; foofa dees na fa jooy te yéyu.
43 Then the righteous will shine like the sun in their Father's kingdom. The one with ears should listen." Booba nag ñu jub ñi dinañu leer ni jant bi ci seen nguuru Baay. Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.»
44 The kingdom of our Father is like treasure hidden in a field. A man found it, hid it again, then joyfully sold all he had to buy that field. Yeesu teg ca ne: «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni alal ju nëbbu cib tool. Nit ki ko gis nëbbaat ko; xolam sedd, ba mu dem jaay li mu am lépp, jënd tool ba.
45 "Again, the kingdom of our Father is like a merchant searching for fine pearls. «Te it nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni jaaykat buy wut per yu rafet.
46 Finding one priceless pearl, he went and sold all he had and bought it. Am bés mu gis per buy jar njég lu réy. Mu dem nag, jaay li mu am lépp, jënd ko.»
47 Again, our Father's kingdom is like a net cast into the lake, gathering fish of every kind. Yeesu waxaat ne: «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni mbaal mu ñu wàcce ci géej, mu jàpp jën wu nekk.
48 When full, the fishermen pulled it ashore, sat down, and collected the good fish in baskets, throwing out the bad. Bi mbaal mi feesee nag, ñu ñoddi ko ci tefes gi, ba noppi ñu taxaw, dajale yu baax yi ciy ndab, waaye sànni yi bon.
49 So it will be at the age's end: angels will go out and separate the wicked from among the righteous, Noonu lay mel, bu àddina tukkee. Malaaka yi dinañu génn, tànn ñu bon ñi ci biir ñu jub ñi,
50 and throw them into the blazing furnace, where they will weep and grind their teeth." sànni leen ci sawara. Foofa dees na fa jooy te yéyu.»
51 "Have you understood all these things?" "Yes," they replied. Noonu Yeesu laaj taalibe ya ne leen: «Loolu lépp, ndax xam ngeen lu muy tekki?» Ñu ne ko: «Waaw.»
52 He said to them, "Every teacher of the law trained for our Father's kingdom is like a homeowner who brings treasures new and old out of his storeroom." Yeesu ne leen: «Kon nag xutbakat bu nekk bu jàng ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji, dafa mel ni boroom kër buy génne ci dencukaayam yu bees ak yu màggat.»
53 When Jesus had finished these parables, he moved on from there. Bi nga xamee ne Yeesu dégtal na léeb yooyu ba noppi, mu jóge fa,
54 Returning to his hometown, he taught in their synagogue, and they were amazed: "Where does this man get this wisdom and these mighty works? dem fa mu yaroo. Mu di leen jàngal ci seen jàngu, ba ñu waaru ne: «Xam-xam bii ak kéemaan yii, fu mu ko jële?
55 Isn't this the carpenter's son? Isn't his mother named Mary, and his brothers James, Joseph, Simon, and Judas? Ndax kii du doomu minise bi, te ndeyam tudd Maryaama? Ndax rakkam yu góor duñu Saag, Yuusufa, Simoŋ ak Yuda?
56 Aren't all his sisters here with us? Where then did this man get all these things?" Te ay rakkam yu jigéen, ndax nekkuñu fi ak nun? Lii lépp nag, fu mu ko jële?»
57 They took offense at him. But Jesus said to them, "A prophet is honored everywhere except in his hometown and in his own household." Kon ñu daldi koy xeeb. Noonu Yeesu ne leen: «Dees na faaydaal yonent, waaye du ci réewam ak ci këram.»
58 He didn't do many miracles there because of their lack of faith. Te Yeesu defu fa kéemaan yu bare ndax seen ngëmadi.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]