Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Matthew 12 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 At that time Jesus went through the grainfields on the Sabbath. His disciples were hungry and began to pluck heads of grain and eat them. Amoon na benn bésub noflaay Yeesu jaar ci ay tool yu ñor, fekk ay taalibeem xiif; ñu daldi fàq ay gub nag, di lekk.
2 Seeing this, the Pharisees said to him, "Look—your disciples are doing what's unlawful on the Sabbath." Farisen ya nag gis ko, ne Yeesu: «Gisal, say taalibe ñu ngi def lu jaaduwul ci bésub noflaay bi.»
3 He said to them, "Haven't you read what David did when he and his companions were hungry?" Noonu Yeesu ne leen: «Ndax jànguleen la Daawuda defoon, ba mu xiifee, moom ak ña mu àndaloon?
4 how he entered the house of our Father and ate the Presence bread, unlawful for him and his companions, reserved only for priests? Xanaa yéguleen, ni mu dugge woon ca kër Yàlla ga, gis fa mburu, ya ñu teewal ca kanam Yàlla, mu daldi ko lekk. Fekk jaaduwul mu lekk ca, moom walla ña mu àndaloon; sarxalkat rekk a ko sañoona lekk.
5 "Or haven't you read in the Law that on the Sabbath, priests in the temple break the Sabbath and are guiltless? Te it ndax jànguleen ci yoonu Musaa, ne sarxalkat ya ca kër Yàlla ga teraluñu bésub noflaay bi, te tooñuñu?
6 I tell you, something greater than the temple is here. Waaye maa ngi leen koy wax, am na ci seen biir ku sut kër Yàlla ga.
7 If you knew what 'I want mercy, not sacrifice' means, you wouldn't have condemned the blameless. Mbind mi nee na: “Yërmande laa bëgg, waaye du rendi saraxi mala.” Su ngeen xamoon lu wax joojuy tekki, kon dungeen teg tooñ ñi tooñul.
8 For the Son of Man is Lord of the Sabbath." Ndaxte Doomu nit ki mooy boroom bésub noflaay bi.»
9 He went on from there and entered their synagogue. Bi loolu amee Yeesu jóge foofa, dugg ci seen jàngu,
10 A man with a withered hand was there. They asked him, "Is it lawful to heal on the Sabbath?"—hoping to accuse him. te amoon na fa nit ku loxoom làggi. Noonu Farisen ya laaj ko: «Faj ci bésub noflaay bi, ndax loolu jaadu na?» Fekk ñuy wut buntu tuumaal ko.
11 He said to them, "Who among you with a sheep, if it falls in a pit on the Sabbath, won't grab and pull it out? Yeesu ne leen: «Ku fi amoon xar, mu daanu ci kàmb ci bésub noflaay bi, ndax doo ko jàpp, génne ko?
12 How much more is a person worth than a sheep! So it's lawful to do good on the Sabbath." Nit nag, ndax ëppul maana xar? Kon def lu baax ci bésub noflaay bi jaadu na.»
13 Then he told him, "Stretch out your hand." He stretched it out, and it was restored, healthy like the other. Noonu Yeesu ne nit ka: «Tàllalal sa loxo!» Mu tàllal ko nag, loxoom daldi wér, mel ni ba ca des.
14 But the Pharisees went out and plotted how to destroy him. Farisen ya génn nag, daldi gise, ngir fexee reylu Yeesu.
15 Jesus, aware of this, withdrew from there. And many followed him, and he healed them all, Waaye bi ko Yeesu yégee, mu sore foofa; te ñu bare topp ko, mu wéral leen ñoom ñépp.
16 and he ordered them not to tell anyone about him. Te mu dénk leen bu wóor, ñu bañ koo siiwal.
17 This was to fulfill what was spoken by the prophet Isaiah: Def na noonu, ngir amal la ñu waxoon jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi, bi mu naan:
18 "Look, my servant—Jesus—whom I have chosen, my beloved in whom my soul delights. I will put my Spirit upon him, and he will proclaim justice to the nations. «Kii mooy sama Ndaw li ma tànn, di sama Soppe bi neex sama xol. Dinaa def sama Xel ci moom, muy yégal xeet yi yoonu njub.
19 He will not quarrel or shout, nor will anyone hear his voice in the streets. Du xëccoo mbaa muy wax ci kaw, te kenn du dégg baatam ci mbedd yi.
20 A bruised reed he will not break, and a smoldering wick he will not quench, until he brings justice to victory; Du dammte barax bu banku, te mees guy saxar, du ko fey, ba kera mu yégal njub, ba daan.
21 and in his name the nations will put their hope." Ci turam la xeet yi di ame yaakaar.»
22 Then someone brought him a blind, mute demon-oppressed man, and he healed him so the man could speak and see. Booba ñu indil ko ku rab jàpp, mu gumba te luu. Yeesu faj ko, ba ku luu ki di wax tey gis.
23 And all the crowds were amazed and said, "Can this be the Son of David?" Noonu mbooloo mépp yéemu naan: «Ndax kii du Sëtu Daawuda bi?»
24 But hearing this, the Pharisees said, "This man drives out demons only by Beelzebul, prince of demons." Bi Farisen ya déggee loolu nag, ñu ne: «Kii ci kàttanu Beelsebul, buuru rab yi, lay dàqe rab yi.»
25 Knowing their thoughts, he said to them, "Every kingdom divided against itself is ruined, and no city or house divided against itself will stand. Waaye Yeesu xam seen xalaat ne leen: «Réew mu xeex boppam tas, te dëkk mbaa kër guy xeex boppam du mana yàgg.
26 And if Satan casts out Satan, he is divided against himself. How then will his kingdom stand? Bu Seytaane dàqee Seytaane nag, xeex na boppam; kon naka la nguuram di mana yàgge?
27 If I drive out demons by Beelzebul, by whom do your sons drive them out? So they will be your judges. Te it bu fekkee ne man damay dàq ay rab ci kàttanu Beelsebul, seeni taalibe nag, ci gan kàttan lañu leen di dàqe? Kon ñoo leen di àtte.
28 But if I drive out demons by the Spirit of our Father, then the kingdom of our Father has reached you. Waaye bu fekkee ne ci Xelum Yàlla laay dàqe rab, kon nguuru Yàlla agsi na ba ci yéen.
29 Or how can someone enter a strong man's house and carry off his goods, unless he first restrains the strong man? Then he can loot his house. «Su fi amee nit ku bare doole, te nit bëgga dugg ci këram, nangu alalam, naka la koy defe? Xanaa dafay jëkka yeew ku bare doole ka, ba noppi doora toj këram gépp.
30 Whoever is not with me is against me, and whoever does not gather with me scatters. Noonu ku farul ak man, yaa ngi may xeex, ku dajalewul ak man, yaa ngi tasaare.»
31 So I tell you, every sin and blasphemy will be forgiven people, but blasphemy against the Spirit will not be forgiven. Yeesu teg ca ne: «Loolu moo tax maa ngi leen koy wax, bàkkaar walla sos wu mu mana doon, dinañu ko baale, waaye ku sosal Xelum Yàlla, duñu ko baal.
32 Whoever speaks against the Son of Man will be forgiven; whoever speaks against the Holy Spirit won't be forgiven—neither in this age nor the age to come. Ku sosal Doomu nit ki, dinañu ko baal, waaye ku sosal Xel mu Sell mi, duñu ko baal mukk, du ci àddina si, du ci àllaaxira.
33 Make the tree good and its fruit good, or the tree bad and its fruit bad, for a tree is known by its fruit. Neeleen garab gi baax na, moom ak meññeefam, walla ngeen ne garab gi bon na, moom ak meññeefam; ndaxte garab, meññeefam lañu koy xàmmee.
34 You brood of vipers! How can you speak good things since you're evil? For the mouth speaks the heart's overflow. Yéen ñi fees ak daŋar ni ay co, naka ngeen mana waxe lu baax, fekk dangeen bon? Ndaxte gémmiñ, la fees xol lay wax.
35 A good person produces good from a good treasure; an evil person produces evil from an evil treasure. Noonu nit ku baax, lu baax lay wax, jële ko ca fa mu denc lu baax, te nit ku bon, lu bon lay wax, jële ko ca fa mu denc lu bon.
36 I tell you, on judgment day people will answer for every careless word they speak, Maa ngi leen di wax ne keroog bés pénc, nit ñi dinañu làyyi ndax wax ju nekk ju amul njariñ, ju ñu masa wax.
37 for by your words you will be justified, and by your words you will be condemned." Ndaxte dees na la àtte ni ku jub ci say wax, walla ñu daan la ci say wax.»
38 Then some scribes and Pharisees said, "Teacher, we want a sign from you." Ci kaw loolu ay xutbakat ak ay Farisen wax ak Yeesu ne ko: «Kilifa gi, danoo bëggoon, nga won nu kéemaan guy firndeel sag yónnent.»
39 He answered, "This evil, adulterous generation demands a sign. None will be given it except the sign of the prophet Jonah. Yeesu ne leen: «Yéenay laaj firnde, yéen niti jamono ju bon jii, yéen ñi fecci seen kóllëre ak Yàlla, waaye dungeen jot jenn firnde ju dul firndey yonent Yàlla Yunus.
40 As Jonah was three days and three nights in the great fish's belly, so the Son of Man will be three days and three nights in the earth's heart. Ndaxte ni Yunus nekke woon ñetti guddi ak ñetti bëccëg ci biir rabu géej wu mag, noonu la Doomu nit ki di nekke ñetti guddi ak ñetti bëccëg ci biir suuf.
41 Ninevites will rise at the judgment with this generation and condemn it, for they repented at Jonah's preaching, and something greater than Jonah is here. Keroog bés pénc waa dëkku Niniw dinañu jógandoo ak niti jamono jii, yey leen; ndaxte bi leen Yunus waaree, tuub nañu seeni bàkkaar, te ku sut Yunus a ngi fi.
42 The queen of the South will rise at the judgment with this generation and condemn it, for she came from earth's ends to hear Solomon's wisdom—and look, something greater than Solomon is here. Te it ca bés pénc buur bu jigéen, ba dëkkoon ca sudd, dina jógandoo ak niti jamono jii, yey leen; ndaxte dafa jóge ca catul àddina, ngir déglu xam-xamu Suleymaan, te ku sut Suleymaan a ngi fi.
43 When an unclean spirit leaves a person, it travels through dry places seeking rest, and finds none. «Boo xamee ne rab wa jàppoon nit génn na ci moom, day wër ay bérab yu wow, di wut fu mu noppaloo, waaye du ko gis.
44 Then it says, 'I will return to my house I left.' Coming, it finds it empty, swept, and put in order. Noonu da naan: “Naa dellu ca sama kër, ga ma génne woon.” Bu ñëwee nag, mu fekk kërug neen, ñu bale ko, defar ko ba lépp jekk.
45 Then it goes and brings along seven other spirits more evil than itself; they enter and settle there, and that person ends up worse off than before. So it will be with this evil generation." Bu ko gisee nag, mu dem wooyi yeneen juróom ñaari rab yu ko gëna soxor, ñu dugg, sanc fa; ba tax muju nit kooku mooy yées njàlbéenam. Noonu lay nekke ak niti jamono ju bon jii.»
46 While he was still speaking to the crowds, his mother and brothers stood outside, wanting to speak with him. Bi Yeesu nekkee di wax ak mbooloo ma, ndeyam ak ay rakkam daldi ñëw, taxaw ci biti, bëgga wax ak moom.
47 Someone told him, "Look, your mother and your brothers are standing outside, wanting to speak to you." Noonu kenn nit ne ko: «Sa yaay ak say rakk ñu ngi nii taxaw ci biti, bëgga wax ak yaw.»
48 He answered the one who told him, "Who is my mother, and who are my brothers?" Waaye Yeesu ne ko: «Kan mooy sama ndey ak ñan ñooy samay rakk?»
49 And stretching out his hand toward his disciples, he said, "Here are my mother and my brothers! Noonu mu joxoñ ay taalibeem naan: «Ñii ñooy sama ndey ak samay rakk.
50 For whoever does the will of my Father in heaven is my brother and sister and mother." Ndaxte ku def sama coobarey Baay bi nekk ci kaw, yaa di sama rakk, sama jigéen ak sama ndey.»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]