Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Luke 6 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 On a Sabbath, Jesus walked through grainfields; his disciples picked heads of grain, rubbed them in their hands, and ate. Amoon na benn bésub noflaay Yeesu di dem, jaar ci ay tool yu ñor. Taalibeem ya di fàq ay cëgg, di leen boxom ci seeni loxo tey lekk.
2 Some of the Pharisees said, "Why are you doing what is not lawful on the Sabbath?" Am ay Farisen yu ne: «Lu tax ngeen di def lu jaaduwul ci bésub noflaay bi?»
3 Jesus answered them, "Haven't you read what David did when he and those with him were hungry, Yeesu ne leen: «Ndax jànguleen la Daawuda defoon, ba mu xiifee, moom ak ña mu àndaloon?
4 how he entered our Father's house, took the bread of the Presence, ate it, gave some to his companions, though it's not lawful for any but the priests to eat it?" Xanaa yéguleen, ni mu dugge woon ca kër Yàlla ga, jël mburu, ya ñu teewal ca kanam Yàlla, lekk ca, jox ca ña mu àndaloon? Fekk jaaduwul kenn lekk ko, ku dul sarxalkat.»
5 Then he said to them, "The Son of Man is Lord of the Sabbath." Yeesu dellu ne leen: «Doomu nit ki mooy boroom bésub noflaay bi.»
6 On another Sabbath he entered the synagogue and taught; a man was there with a withered right hand. Beneen bésub noflaay, Yeesu dugg ci jàngu bi, di fa jàngle. Amoon na fa nit ku loxol ndijooram làggi.
7 The scribes and Pharisees watched him closely to see if he would heal on the Sabbath, so they could find a charge against him. Xutbakat yi ak Farisen yi ñu ngi ko doon xool, ba xam ndax dina ko faj ci bésub noflaay bi, ngir ñu am lu ñu ko tuumaale.
8 But knowing their thoughts, he told the man with the withered hand, "Get up and stand here." So he got up and stood there. Waaye Yeesu xam seen xalaat, daldi ne ku loxoom làggi: «Jógal taxaw ci kanam ñépp.» Nit ka daldi jóg taxaw.
9 Then Jesus said to them, "I ask you: is it lawful on the Sabbath to do good or do harm, to save a life or destroy it?" Yeesu ne leen: «Ma laaj leen, lan moo jaadu, nu def ko bésub noflaay bi, lu baax mbaa lu bon; nu musal nit mbaa nu lor nit?»
10 Looking around at them all, he told the man, "Stretch out your hand." He did, and his hand was restored. Ci kaw loolu mu xool leen ñoom ñépp, ba noppi ne nit ka: «Tàllalal sa loxo.» Mu tàllal ko, loxoom daldi wér péŋŋ.
11 But filled with rage, they discussed with each other what to do to Jesus. Waaye nit ña mer ba fees, di rabat pexe yu jëm ca Yeesu.
12 In those days Jesus went out to the mountain to pray, spending the whole night in prayer to our Father. Ca bés yooya Yeesu yéeg ca tund wa ngir ñaan, mu fanaan fa, di ñaan ci Yàlla.
13 At daybreak he called his disciples and chose twelve of them, naming them apostles: Bi bët setee, Yeesu woo taalibeem yi, tànn ci fukk ak ñaar, tudde leen ay ndawam:
14 Simon, whom he named Peter, and his brother Andrew; James and John; Philip and Bartholomew; Simoŋ, mi Yeesu tudde Piyeer, ak Andare, mi bokk ak Piyeer ndey ak baay; Saag ak Yowaana, Filib ak Bartelemi,
15 Matthew and Thomas; James son of Alphaeus, and Simon who was called the Zealot; Macë ak Tomaa, Saag doomu Alfe, ak Simoŋ mi bokk ci mbooloo, ma ñu tudde Ñi farlu ci moom seen réew;
16 Judas son of James, and Judas Iscariot, who became a traitor. Yudaa doomu Saag, ak Yudaa Iskariyo, mi mujja wor.
17 He came down with them and stood on a level place, with a large crowd of his disciples and a large multitude of people from all Judea, Jerusalem, and the coast of Tyre and Sidon. Yeesu ànd ak ndaw ya, wàcc tund ya, daldi taxaw ca joor ga, fa mbooloom taalibe mu takku nekkoon. Amoon na fa it ay nit ñu bare ñu jóge ca réewu Yawut ya mépp ak ca dëkku Yerusalem ak dëkk yi nekk ca wetu géej ga, maanaam Tir ak Sidon.
18 They came to hear him and be healed of their diseases; those troubled by unclean spirits were also cured. Dañoo ñëw ngir déglu ko, te it ngir mu faj leen. Ñi rab jàpp it faju nañu.
19 The whole crowd tried to touch him, since power went out from him, healing everyone. Ñépp a ngi ko doon wuta laal ndax doole jiy jóge ci moom, di faj ñépp.
20 Looking up at his disciples, he said: "Blessed are you who are poor, for yours is the kingdom of our Father. Yeesu xool ay taalibeem, ne leen: «Yéen ñi néew doole, barkeel ngeen, ndaxte nguuru Yàlla, yéena ko yelloo.
21 "Blessed are you who hunger now, for you will be satisfied. Blessed are you who weep now, for you will laugh. Yéen ñi xiif léegi, barkeel ngeen, ndax dingeen regg. Yéen ñiy naqarlu léegi, barkeel ngeen, ndax dingeen ree.
22 Blessed are you when people hate you, and when they exclude you and revile you and reject your name as evil, because of the Son of Man. Barkeel ngeen, bu leen nit ñi bañee, di leen dàq ak a saaga, di sib seen tur ngir Doomu nit ki.
23 Rejoice in that day and leap for joy, for your reward is great in heaven; for that is how the persecutors' ancestors treated the prophets. Bu boobaa bégleen te bànneexu, ndax seen yool dina réy ci laaxira. Ndaxte noonu la maami seeni bañ daan fitnaale yonent yi.
24 But woe to you who are rich, for you have already received your comfort. Waaye nag yéen boroom alal yi, torox ngeen, ndaxte jot ngeen ba noppi seen bànneex.
25 Woe to you who are full now, for you will be hungry. Woe to you who laugh now, for you will mourn and weep. Yéen ñiy lekk ba suur léegi, torox ngeen, ndax ëllëg dingeen xiif. Yéen ñiy ree léegi, torox ngeen, ndax dingeen am aw naqar, ba jooy xàcc.
26 Woe to you when everyone speaks well of you, for that is how the flatterers' ancestors treated the false prophets. Torox ngeen bu leen ñépp dee waxal lu baax, ndaxte noonu la seeni maam daan jëfe ak ña doon mbubboo yonent.
27 But I tell you who listen: love your enemies, do good to those who hate you, «Waaye maa ngi leen koy wax, yéen ñi may déglu, soppleen seeni bañaale tey defal lu baax ñi leen bañ.
28 bless those who curse you, pray for those who mistreat you. Yéeneleen lu baax ñi leen di móolu, te ñaanal ñi leen di sonal.
29 Whoever strikes you on one cheek, offer the other too; whoever takes your coat, do not hold back your shirt. Ku la talaata cib lex, jox ko ba ca des. Kuy nangu sa mbubb mu mag, bul téye sa turki.
30 Give to everyone who asks you, and don't demand back what is taken from you. Képp ku la ñaan, may ko, te ku nangu say yëf, bu ko ko laaj.
31 Do to others as you would have them do to you. Defal-leen nit ñi li ngeen bëgg, ñu defal leen ko.
32 Loving those who love you—what credit is that? Even sinners love those who love them. «Su ngeen soppee ñi leen sopp, ban ngërëm ngeen ciy am? Ndaxte bàkkaarkat yi sax sopp nañu ñi leen sopp.
33 If you do good to those doing you good, what credit is that to you? Even sinners do the same. Te bu ngeen defalee lu baax ñi leen koy defal, ban ngërëm ngeen ciy am? Bàkkaarkat yi it dañuy def noonu.
34 And if you lend expecting repayment, what credit is that? Even sinners lend to sinners to get back the same amount. Te bu ngeen dee leble te yaakaar ci ndelloo, ban ngërëm ngeen ciy am? Bàkkaarkat yi it dañuy lebal seeni moroom, ngir ñu delloo leen ko.
35 But love your enemies, do good, and lend expecting nothing back; your reward will be great, and you will be children of the Most High, for he is kind to the ungrateful and evil. Waaye soppleen seeni noon, di leen defal lu baax, tey leble, baña yaakaar ñu delloo leen ko. Noonu seen yool dina mag te dingeen wone ne yéenay doomi Aji Kawe ji, ndaxte Yàlla day wone mbaaxam ci ñu goreedi ñi ak ñu soxor ñi.
36 Be merciful, just as your Father is merciful. Nangeen am yërmande, ni seen Baay ame yërmande.
37 Do not judge, and you will not be judged. Do not condemn, and you will not be condemned. Forgive, and you will be forgiven. «Buleen àtte seeni moroom ak ñaaw njort, te deesu leen àtte. Buleen daan kenn, te deesu leen daan. Baal-leen ñi ci des, te dinañu leen baal.
38 Give, and it will be given to you: a good measure—pressed down, shaken, overflowing—will be poured into your lap. For the measure you use will be measured back to you." Mayeleen te dinañu leen may. Dinañu leen ëmbal natt bu baax bu ñu rokkos te yëngal ko, mu fees bay tuuru. Ndaxte dees na leen nattal ak natt, bi ngeen di nattale.»
39 He also gave them a parable: "Can a blind person guide a blind person? Won't both fall into a pit? Noonu Yeesu wax na leen beneen léeb ne leen: «Ndax gumba man na wommat moroomam? Mbaa duñu daanu ñoom ñaar ci kàmb?
40 No student surpasses their teacher; whoever is fully trained becomes like their teacher. Taalibe gënul kilifaam, waaye taalibe bu jàng ba wàcc, dina yem ak kilifaam demin.
41 Why do you see the speck in your brother's eye, yet miss the beam in your own eye? «Lu tax ngay xool ñax gi ci sa bëtu mbokk, te gisuloo gànj gi ci sa bët yaw?
42 How can you tell your brother, 'Brother, let me remove the speck from your eye,' when you don't see the beam in your own eye? Hypocrite! First remove the beam from your own eye—then you'll see clearly to remove the speck from your brother's eye. Nan nga mana waxe sa mbokk: “Sama xarit, may ma, ma dindil la ñax gi ci sa bët,” yaw mi gisul gànj gi nekk ci sa bët? Naaféq! Jëkkala dindi gànj gi ci sa bët, te noonu dinga mana gis bu leer, ngir dindi ñax gi ci sa bëtu mbokk.
43 For no good tree bears bad fruit, nor again does a bad tree bear good fruit. «Garab gu baax du meññ doom yu bon, te garab gu bon du meññ doom yu baax.
44 Each tree is known by its own fruit; figs aren't gathered from thornbushes, nor grapes picked from a bramble. Ndaxte garab, meññeefam lañu koy xàmmee. Deesul witte figg ci dédd, walla reseñ ci xaaxaam.
45 A good person produces good from the heart's good store; an evil person produces evil from the evil store; for the mouth speaks from the heart's overflow. Noonu nit ku baax, lu baax lay wax, ndax loolu la denc ci xolam, te nit ku bon, lu bon lay wax, ndaxte denc na lu bon ci xolam. Ndaxte gémmiñ, la fees xolam lay wax.
46 Why do you call me 'Lord, Lord,' and not do what I say? «Lu tax ngeen may wooye “Boroom bi, Boroom bi,” te dungeen def li may wax?
47 Everyone coming to me, hearing my words, and doing them—I'll show you what he's like: Képp ku ñëw ci man, di dégg samay wax te di ko jëfe, ma won leen nu muy mel.
48 He's like a man building a house, who dug deep and laid its foundation on rock. When the flood came, the river crashed into that house but couldn't shake it—it was built well. Dafa mel ni nit kuy tabax kër, mu gas fu xóot, jot doj wu réy, samp fa kër ga. Bi mbënn ma ñëwee, wal ma dafa dal ca kër ga te yënguwul, ndaxte nit ka dafa tabax kër ga tabax bu dëgër.
49 But whoever hears my words and doesn't act on them is like a man who built a house on the ground, without a foundation. The flood crashed against it, and it collapsed at once—that house's ruin was great." Waaye képp ku dégg samay wax te jëfewuloo ko, dinga mel ni nit ku tabax këram ci suuf, bañ koo defal fondamaa. Bi wal ma dalee ca kër googa, dafa màbb ca saa sa, lépp yàqu yaxeet.»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]