Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Acts 28 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 Once we were brought safely through, we learned that the island was called Malta. Bi nu rëccee, nu yég ne dun baa nga tudd Màlt.
2 Local people showed us unusual kindness: they lit a fire and welcomed us all, since rain had started and it was cold. Te waa réew ma won nu laabiir gu ràññiku, ndaxte taalal nañu nu sawara, ganale nu ndax taw bi sóob ak sedd bi.
3 When Paul gathered a bundle of sticks and put them on the fire, a viper came out from the heat and fastened onto his hand. Pool nag di for matt, di ko def ca taal ba, jaan ne ca mëlle ndax tàngoor wa, taq ci loxoom.
4 Seeing the creature hanging from his hand, the natives said to each other, "This man must be a murderer—though he escaped the sea, Justice won't let him live." Bi waa réew ma gisee rab wa wékku ci loxoom nag, ñuy waxante naan: «Ci lu wóor nit kii reykat la; te bi mu rëccee ca géej ga sax, ndogalu Yàlla mayu ko mu dund.»
5 But he shook the creature off into the fire and suffered no harm. Waaye Pool yëlëb rab wa ca sawara sa, te wàññiwu ko dara.
6 They expected him to swell up or suddenly fall dead. But after watching a long time and seeing nothing wrong happen to him, they changed their minds, calling him a god. Nit ñi di xaar mu newi, mbaa mu ne dàll, dee; waaye bi ñu négee lu yàgg te gis ne dara jotu ko, ñu soppi xel ne: «Kii yàlla la.»
7 Near that place were estates belonging to the island's chief official, named Publius, who welcomed us and hosted us kindly for three days. Amoon na nag ca wet ya ay suuf yu doon moomeelu ku tudd Publiyus, di kilifag dun ba. Mu teeru nu, ganale nu ngan gu réy diirub ñetti fan.
8 Publius's father lay sick with fever and dysentery. Paul went in, prayed, laid hands on him, and healed him. Fekk baayu Publiyus dafa tëdd ndax ay tàngoori yaram yu koy dikkal ak biiru taññ. Pool nag dem seeti ko, ñaan ci Yàlla, teg ko ay loxoom, mu daldi wér.
9 After this, the rest of the sick on the island came and were healed. Ci kaw loolu jarag ya ca des ca dun ba daldi dikk, amaat wér-gi-yaram.
10 They paid us many honors, and when we sailed, loaded us with everything we needed. Ñu teral nu ci fànn yu bare, te bi nuy dem, ñu jox nu li nuy soxla lépp.
11 After three months we sailed in an Alexandrian ship that had wintered at the island, marked with the Twin Brothers. Bi nu fa amee ñetti weer, nu dugg ca gaal gu lollikoo ca dun ba, daldi tàbbi ca géej ga. Gaalu dëkku Alegsàndiri la woon, te yor xàmmikaay guy nataalu Kastor ak Polugsë.
12 We put in at Syracuse and stayed there three days. Noonu nu teer dëkku Sirakus, toog fa ñetti fan.
13 From there we sailed around and arrived at Rhegium. A day later a south wind rose, and on the second day we reached Puteoli. Nu jóge fa, leru tefes ga, ba agsi Resiyo. Ca ëllëg sa ngelawu sudd daldi jóg, te ca ñaareelu fan ba nu teer Pusol.
14 There we found brothers and sisters and were urged to stay with them seven days; so we came to Rome. Gis nanu fa ay bokk, ñu ñaan nu, nu toog fa ayu-bés. Noonu nu dem Room.
15 The brothers and sisters there heard about us and came to meet us as far as the Forum of Appius and Three Taverns. Seeing them, Paul thanked our Father and took courage. Sunuy xibaar law na, ba egg ca bokk ya fa dëkk, noonu ñu gatandu nu ba ca péncu Apiyus ak bérab bu ñuy wax Ñetti añukaay ya. Bi leen Pool gisee, mu sant Yàlla, daldi takk fitam.
16 When we entered Rome, Paul was allowed to stay by himself, with the soldier who guarded him. Bi nu dikkee Room nag, ñu may Pool, mu dëkk fa ko lew, moom ak xarekat ba koy wottu.
17 Three days later he gathered the Jewish leaders. When they assembled, he said to them, "Brothers, though I'd done nothing against our people or our ancestors' customs, I was handed over as a prisoner from Jerusalem into Roman hands. Bi ñetti fan wéyee, mu woolu njiiti Yawuti dëkk ba. Bi ñu dajaloo nag, mu wax leen lii: «Bokk yi, jàpp nañu ma ci Yerusalem, jébbal ma waa Room, fekk defuma dara luy suufeel sunu xeet, mbaa lu juuyoo ak sunuy aaday maam.
18 After examining me, they wanted to release me, since I had no charge deserving death. Waa Room nag seet sama mbir, te bëgg maa bàyyi, ndaxte toppuñu ma dara lu jar dee.
19 When the Jews objected, I was forced to appeal to Caesar—though I had no charge to bring against my nation. Waaye bi ko Yawut ya bañee, fas yéene naa dénk sama mbir Sesaar, fekk ba tey awma dara lu may taqal sama xeet.
20 That's why I asked to see and speak with you—I wear this chain because of Israel's hope." Moo tax ma ñaana gise ak yéen, nu diisoo, ndaxte yaakaaru bànni Israyil moo tax ñu jéng ma.»
21 They said to him: "We received no letters from Judea about you, nor has any brother who came reported or said anything bad about you. Bi ñu ko déggee, ñu ne ko: «Jotunu benn bataaxal bu jóge Yude ci sa mbir, te kenn ci bokk, yi fi dikk, jottaliwul mbaa mu seede ci yaw lu bon.
22 We'd like to hear what you think, since we know this sect is spoken against everywhere." Waaye bëgg nanoo dégg li nga gëm, ndaxte xam nanu ne, tariixa booba, kenn jubluwu ko fenn.»
23 They set a day and came to his lodging in greater numbers. From morning to evening he explained, testifying about the kingdom of our Father and trying to persuade them about Jesus from the Law of Moses and the Prophets. Noonu ñu jox ko bés, te ñu bare ñëw, fekksi ko ca néegam. Mu di leen jàngal suba ba ngoon, di leen dëggal lu jëm ci nguuru Yàlla ak ci Yeesu, tukkee ci yoonu Musaa ak ci yonent yi, di leen jéema gëmloo.
24 Some were convinced by what he said, but others would not believe. Ñenn ñi nag gëm li mu wax, ña ca des weddi ko.
25 Disagreeing among themselves, they left after Paul added one final word: "The Holy Spirit spoke rightly to your ancestors through Isaiah the prophet, saying, Gannaaw manuñoo déggoo, ñu bëgga tas. Waaye bi ñuy laata dem, Pool teg ca wax jii: «Xel mu Sell mi wax na seeni maam dëgg jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi.
26 "'Go to this people and say: You will indeed hear but never understand, and you will indeed see but never perceive. Nee na: “Demal ci xeet wii ne leen: ‘Dingeen déglu bu baax waaye dungeen xam dara; di xool bu baax waaye dungeen gis dara.’
27 For this people's heart has grown dull, and their ears are hard of hearing, and they have closed their eyes—otherwise they might see with their eyes, and hear with their ears, and understand with their heart, and turn, and I would heal them.' Ndaxte xolu xeet wii dafa dërkiis; dañuy déglu ak nopp yu naqari, tey gëmm seeni bët, ngir baña gis ak seeni bët, dégg ak seeni nopp, te xam ci seen xol, ñu waññiku ci man, ma wéral leen.”
28-29 So know: our Father's salvation was sent to the nations—they will listen." «Xamleen nag ne xibaaru mucc gii yégal nañu ko ñi dul Yawut, te ñoom dinañu ko déglu.»
30 He stayed two whole years in his own rented place and welcomed all who came to him, Noonu diirub ñaari at Pool dëkk ca kër gu muy fey, di fa àggale ñépp ñi koy seetsi.
31 proclaiming our Father's kingdom and teaching about the Lord Jesus Christ, boldly and unhindered. Muy yégle nguuru Yàlla, di jàngle ci mbirum Boroom bi Yeesu Kirist ak fit wu dëgër, te kenn terewu ko ko.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]