Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Acts 27 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 Once it was decided we would sail to Italy, they handed Paul and some other prisoners to a centurion named Julius of the Imperial Cohort. Bi loolu wéyee ñu fas yéene noo dugal gaal jëme réewu Itali. Noonu ñu jël Pool ak ñeneen ñi ñu tëjoon, dénk leen njiitu xare bu tudd Yulyus, mi bokk ci mbooloom xare mu buur.
2 We boarded a ship from Adramyttium bound for the ports along the coast of Asia and put out to sea. Aristarchus, a Macedonian from Thessalonica, was with us. Nu dugg ca gaalu dëkku Adaramit guy taxaw ci teeruy Asi, daldi tàbbi ci biir géej; te Aristàrk, mi dëkk Tesalonig ci diiwaanu Maseduwan, ànd ak nun.
3 The next day we docked at Sidon. Julius treated Paul kindly, letting him go to friends for care. Ca ëllëg sa nu teer Sidon; Yulyus laabiir ci Pool, may ko mu dem ci ay xaritam, ngir ñu ganale ko.
4 From there we put to sea and sailed along Cyprus's sheltered side, since the winds opposed us. Bi nu fa jógee, nu dem ci biir géej, leru dunu Sipar ci fegu ngelaw li, ndaxte ngelaw li da noo soflu.
5 Having sailed across the open sea off Cilicia and Pamphylia, we came to Myra in Lycia. Nu jàll géej, gi janook diiwaani Silisi ak Pamfili, teersi Mira ca wàlli Lisi.
6 There the centurion found an Alexandrian ship sailing for Italy and put us aboard it. Foofa nag njiit la gis gaal gu jóge Alegsàndiri, jëm Itali, mu dugal nu ca.
7 Sailing slowly for many days, we barely reached Cnidus. Since the wind blocked us, we sailed along the sheltered side of Crete, off Salmone. Noonu nuy dem ndànk diirub fan yu bare, ba janook Kanidd ci kaw coono bu réy; te ndegam ngelaw li mayu nu, nu jëm kanam, nu leru dunu Keret ci fegu ngelaw li, janook Salmon.
8 Barely coasting along, we reached Fair Havens, a place near the town of Lasea. Nu romb fa ak coono yu bare, agsi ca bérab bu ñuy wax Teeru yu neex, te dend ak dëkku Lase.
9 Much time was lost—even the Fast had passed, making sailing dangerous now. So Paul warned them, Fekk booba yàggoon nañu ca yoon wa, te dem ci géej daldi aaytal, ndaxte jamonoy Kooru Yawut ya wees na. Moo tax Pool digal leen ne:
10 "Men, I see this voyage will bring disaster and heavy loss—not only to the cargo and ship, but also to our lives." «Gaa ñi, gis naa ne tukki bi ëmb na musiba ak kasara ju bare, waxuma gaal gi ak li mu yeb waaye sunuy bakkan sax xaj na ci.»
11 But the centurion trusted the pilot and shipowner more than Paul's words. Waaye njiit la sobental waxi Pool, déggal dawalkat ba ak boroom gaal ga.
12 Since the harbor was unfit for winter, most decided to sail on, hoping somehow to reach Phoenix, a Crete harbor facing southwest and northwest, and winter there. Te gannaaw teeru ba neexula lollikoo, ña ca ëpp mànkoo ci jóge fa, dem ci biir géej, ngir wuta agsi Fenigsë, biy teerub dunu Keret te janook sowu suuf ak sowu kaw, nu lollikoo fa.
13 When a south wind blew gently, thinking they'd gained their purpose, they weighed anchor and sailed close along Crete. Noonu bi ngelaw lu woyof liy jóge sudd wolee, ñu defe ne man nañoo sottal seen pexe, ñu wëgg diigal, daldi tafu ci dunu Keret.
14 But before long, a hurricane-force wind called the Northeaster swept down from the island. Waaye nees-tuut ngelaw lu wole penku, ñu di ko wax «Ërakilon», jóge ca dun ba, ne milib ci sunu kaw.
15 The ship was caught and couldn't face the wind, so we gave way and drifted. Mu ëpp doole gaal ga, daldi ko wat, ba nu bayliku, daldi yal.
16 Running under a small island called Cauda, we barely managed to secure the ship's lifeboat. Nu daldi daw, leru dun bu tuuti bu ñuy wax Kóda ci fegu ngelaw, rawale looco ga ci kaw gaal ga ak coono bu bare.
17 Once hoisted aboard, they used ropes to brace the hull. Fearing they'd run aground on Syrtis's sandbars, they lowered the sea anchor and were driven along. Bi ñu ko yéegee, ñu fab ay buum, ngir laxas ca taatu gaal ga, ngir ragala daanu ci suuf su nooy su ñuy wax Sirt; ba noppi ñu daldi sànni diigal, ngir wàññi doxub gaal ga, nuy yale noonu.
18 The storm battered us so violently that the next day they began throwing cargo overboard. Waaye bi nu ngelaw li sonalee bu metti, ca ëllëg sa ñu sànni la gaal ga yeboon ca géej ga.
19 On the third day, with their own hands they threw the ship's gear overboard. Te ca ñetteelu fan ba, ñu sànni ak seeni loxo jumtukaay, yi ñu yeboon ngir fàggu.
20 For many days sun and stars didn't appear, the fierce storm kept raging, and we finally lost all hope of being saved. Noonu jant bi ne meŋŋ te biddiiw ne mes ay fan yu bare, fekk ba tey ngelaw li di wol ak doole, ba sunu yaakaaru mucc gépp tas.
21 After they had gone a long time without food, Paul stood among them and said, "Men, you should have obeyed me and not sailed from Crete; then you would have spared yourselves this disaster and loss. Bi loolu di xew, fekk gëj nañoo lekk, Pool daldi taxaw ci seen biir ne leen: «Gaa ñi, li gënoon mooy ngeen déglu ma te baña jóge Keret, ba indil seen bopp musiba ak kasara ju réy jii.
22 Now I urge you to stay encouraged: none of you will lose your life, only the ship will be lost. Léegi nag maa ngi leen di dénk, ngeen takk seen fit, ndax gaal gi rekk mooy yàqu, waaye kenn ci yéen du dee.
23 Last night an angel of our Father—the one I belong to and serve—stood beside me, Ndaxte ci guddi menn malaaka dikkal na ma, jóge ci Yàlla sama Boroom, bi may jaamu.
24 and said, 'Don't be afraid, Paul. You must stand before Caesar, and look—our Father has given you the lives of all sailing with you.' Mu ne ma: “Pool bul tiit; fàww nga taxaw ci kanam Sesaar, te yaa tax Yàllay aar bakkani ñi nga àndal ñépp.”
25 So take courage, men—I trust our Father: it will be just as I was told. Moo tax, gaa ñi, takkleen seen fit, ndax wóolu naa Yàlla ne li mu ma wax dina am.
26 But we must run aground on some island." Waaye war nanoo luf cib dun.»
27 On the fourteenth night, still driven across the Adriatic Sea, the sailors sensed near midnight that land was approaching. Ca fukkeelu guddi ga ak ñeent nu nga doon jayaŋ-jayaŋi ca géeju Adiratig; noonu ca xaaju guddi dawalkati gaal ga defe ne danu jegesi suuf.
28 They sounded and found 120 feet; going a little farther, they sounded again and found ninety feet. Ñu sànni nattukaay ba ci biir géej, mu jàpp ñeent fukki meetar, dem ca kanam tuuti, sànniwaat ko, jàpp fanweeri meetar.
29 Afraid of hitting rocks, they dropped four anchors from the stern and prayed for daylight. Ñu ragal ne dinañu fenqu ci ay xeer, kon ñu daldi sànni ñeenti diigal ci geenu gaal ga, di ñaan bët set.
30 The sailors tried to escape from the ship, lowering the lifeboat into the sea, pretending to run out anchors from the bow. Waaye ci kaw loolu dawalkati gaal ga taafantaloo ne dañuy sànniji ay diigal ca boppu gaal ga, fekk dañuy fexee jël looco ga, ba raw.
31 Paul told the centurion and soldiers, "Unless these men stay in the ship, you can't be saved." Waaye Pool ne njiit la ak xarekat ya: «Bu ñii desul ci gaal gi, dungeen raw.»
32 So the soldiers cut the ropes holding the lifeboat and let it drift away. Noonu xarekat ya dagg buum, yay téye looco ga, bàyyi ko mu wéy.
33 Just before dawn, Paul urged everyone to eat, saying, "This is the fourteenth day you've waited anxiously, without food, having eaten nothing. Bi bët setagul, Pool sant leen ñu lekk; mu ne leen: «Tey mooy seen fukki fan ak ñeent yu ngeen ne jonn, lekkuleen, mosuleen dara.
34 So I urge you to eat—this is for your survival. Not a hair from any of your heads will be lost." Maa ngi leen di sant nag, ngeen lekk, ndax noonu rekk ngeen mana rawe. Ndax genn kawar du rot ci yéen.»
35 Saying this, he took bread, thanked our Father before them all, broke it, and began to eat. Bi mu waxee loolu, mu fab mburu, sant Yàlla ci kanam ñépp, damm ko, daldi ko lekk.
36 They were all encouraged and ate some food themselves. Bi ñu gisee loolu, ñépp dëgëraat, ñu daldi lekk ñoom itam.
37 Altogether there were 276 of us on board. Mboolem ñi nekkoon ca gaal ga mat na ñaar téeméeri nit ak juróom ñaar fukk ak juróom benn.
38 Once satisfied with food, they lightened the ship by tossing the grain into the sea. Noonu ñu lekk ba suur, daldi sànni pepp ma ca géej ga, ngir woyofal gaal ga.
39 At daylight they did not recognize the land, but noticed a bay with a sandy beach, and planned, if possible, to run the ship aground there. Bi bët setee nag, xàmmiwuñu réew ma, waaye séen nañu ruqu tefes. Noonu ñu fas yéene caa teeral gaal ga, bu ñu ko manee.
40 They cut the anchors loose, leaving them in the sea, and at the same time untied the rudder ropes. Then they hoisted the foresail to the wind and headed for the beach. Ñu dagg diigal ya, bàyyi leen ci biir géej, yiwiwaale baar ba; ba noppi firi wiiru kanam ga, jublu ca tefes ga.
41 But hitting a sandbar where two currents met, they ran the ship aground—the bow stuck fast, unmoving, while the waves' force broke the stern apart. Waaye ñu dal ca tundu suuf ca bérab bu ñaari koroŋ daje, gaal ga daldi fa luf. Boppu gaal ga nuur bu baax, ne fa tekk, te dooley duus ya daldi toj geen ba.
42 The soldiers planned to kill the prisoners so that none of them could swim away and escape. Bi loolu amee xarekat ya bëgga rey ñi ñu tëj, ngir ragal ñenn ñi féey, ba raw.
43 But the centurion, wanting to save Paul, stopped them from their plan, and ordered those who could swim to jump in first and get to shore, Waaye njiit la bëgga musal Pool, mu tere leen pexe ma. Mu sant ñi mana féey, ñu jëkka sóobu ca ndox ma, ba jot tefes ga.
44 and the rest—some on planks, some on ship debris. So everyone reached land safely. Mu sant ñi ci des ñu def noonu, langaamu ci ay dénk, mbaa ca tojiti gaal ga. Noonu ñépp jot tefes ga ci jàmm ak salaam.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]