Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Acts 14 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 In Iconium they entered the Jewish synagogue together and spoke so that a great number of both Jews and Greeks believed. Bi Pool ak Barnabas nekkee Ikoñum nag, ñu dugg ci jàngub Yawut ya, ni ñu ko daan defe; ñuy waare, ba mbooloom Yawut ak Gereg mu bare gëm.
2 But the Jews who refused to believe stirred up and poisoned Gentile minds against the brothers. Waaye Yawut yu nanguwul yi ñoo jógloo ñi dul Yawut, di ñaawal seen njort ci bokki taalibe yi.
3 They stayed a long time, speaking boldly for the Lord, who confirmed his message of grace, doing signs and wonders through their hands. Pool ak Barnabas nag sax nañu ci Ikoñum lu yàgg, ñu wéeru ci Boroom bi, bay wax ak fit wu dëgër; te Yàlla dëggal kàddug yiwam, ba may leen, ñu def ay kéemaan ak ay firnde.
4 But the city split: some sided with the Jews, some with the apostles. Noonu waa dëkk bi xàjjalikoo, ñii far ak Yawut yi, ñale far ak ndaw ya.
5 When both the Gentiles and the Jews, together with their rulers, moved to mistreat and stone them, Waaye ñi dul Yawut ak Yawut yi, ñoom ak seeni kilifa, lal pexem fitnaal leen ci sànni ay doj.
6 realizing this, they fled to the Lycaonian cities of Lystra and Derbe, and the surrounding region, Bi ko Pool ak Barnabas yégee nag, ñu daw ca diiwaanu Likawni ca dëkk ya ñuy wax Listar ak Derbë ak wàllaa ya.
7 and there they kept preaching the gospel. Foofa ñu di fa xamle xibaaru jàmm bi.
8 A man sat in Lystra, feet disabled, lame from birth, who had never walked. Amoon na ca Listar nag nit ku fa toog, ku ay tànkam làggi, ndax li mu judduwaale lafañ te masula dox.
9 He was listening to Paul speak. Paul stared at him and saw he had faith to be healed, Moom nag muy déglu Pool miy waare. Noonu Pool xool ko jàkk, gis ne am na ngëm ngir wér.
10 said in a loud voice, "Stand upright on your feet." The man leaped up and began walking. Mu ne ko ak baat bu dëgër: «Jógal taxaw bu jub.» Noonu nit ki ne bërét, jóg, daldi dox.
11 When the crowds saw what Paul did, they shouted in Lycaonian, "The gods have come down to us in human form!" Bi mbooloo ma gisee li Pool def, ñu daldi yuuxu, ne ci làkku waa Likawni: «Yàlla yi soppiku nañu nit, wàcc ci nun.»
12 Barnabas they called Zeus, and Paul they called Hermes, because he was the chief speaker. Noonu ñu tudde Barnabas, Sës, te tudde Pool, Ermes, ndaxte mooy ki yor wax ji.
13 The priest of Zeus, whose temple stood before the city, brought bulls and garlands to the gates, wanting to sacrifice with the crowds. Fekk ci buntu dëkk ba amoon na fa kër gu ñuy màggale Sës. Sarxalkat ba nag ànd ak mbooloo ma, daldi indi ca bunt ya ay yëkk ak ay caq, yi ñu defare tóor-tóor, ngir màggal leen ci tuur deretu mala.
14 But hearing this, the apostles Barnabas and Paul tore their clothes and ran into the crowd, shouting, Waaye bi ko ndaw yi Barnabas ak Sóol déggee, ñu sib ko ba xotti seeni yére, ñu daldi daw, tàbbi ca mbooloo ma, di wax ci kaw ne:
15 and saying, "Men, why are you doing this? We are humans too, with the same nature as you. We bring you good news: turn from these worthless things to the living Father, who made the heaven, the earth, the sea, and everything in them. «Yéen nit ñi, lu leen xiir ci lii? Nun it ay nit lanu, ñu bokk bind ak yéen. Te nu ngi leen di xamal xibaaru jàmm ne leen, ngeen dëddu yëfi neen yii te waññiku ci Yàlla miy dund te sàkk asamaan, suuf, géej ak li ñu ëmb lépp.
16 In past generations he let all the nations go their own way, Démb mayoon na xeet yépp, ñu aw seen yoonu bopp.
17 yet he did not leave himself without witness: doing good, giving you rains from heaven and fruitful seasons, filling your hearts with food and joy." Moona noppiwula firndeel aw meloom ci def lu baax, di leen wàcceele ci asamaan taw buy indi naataange, ba ngeen lekk ba suur, te seen xol fees ak mbég.»
18 Even with these words they barely restrained the crowds from sacrificing to them. Noonu ci lu jafe yey nañu mbooloo ma ak wax jooju, ba tere leen, ñu rendil leen sarax.
19 But Jews from Antioch and Iconium came, won over the crowds, stoned Paul, and dragged him out of the city, thinking him dead. Waaye bi loolu wéyee amoon na ay Yawut yu jóge Ancos ak Ikoñum, ñu fàbbi mbooloo ma, sànni Pool ay doj, ba yaakaar ne dee na, ñu diri ko ba ca gannaaw dëkk ba.
20 When the disciples surrounded him, he got up and went into the city. The next day he left for Derbe with Barnabas. Waaye taalibe ya ñëw wër ko, mu daldi jóg, duggaat ca dëkk ba. Ca suba sa nag, mu ànd ak Barnabas, dem Derbë.
21 After preaching the good news in that city and making many disciples, they returned to Lystra, Iconium, and Antioch, Bi ñu fa àggee nag, ñu xamle fa xibaaru jàmm bi, ba sàkk fa ay taalibe yu bare. Gannaaw loolu ñu délsi Listar, Ikoñum ak Ancos,
22 strengthening the disciples' souls, urging them to remain in the faith: we must enter our Father's kingdom through many troubles. di dooleel xeli taalibe ya, xiir leen ñu sax ci yoon wi; ñu ne leen: «Ci kaw nattu yu bare lanu wara dugge ci nguuru Yàlla.»
23 After appointing elders for them in each church, praying with fasting, they entrusted them to the Lord they had believed in. Ci mbooloom ñi gëm mu nekk nag, ñu tànn ci ay njiit; ba noppi ñu ñaan Yàlla ak di woor, dénk leen Boroom bi ñu gëm.
24 Then they passed through Pisidia and came to Pamphylia. Gannaaw loolu ñu jaar diiwaanu Pisidi, dikk ci Pamfili.
25 And when they had spoken the word in Perga, they went down to Attalia, Ñu yégle kàddu gi ci dëkku Peers, doora dem dëkku Atali.
26 from there they sailed to Antioch, where they'd been entrusted to our Father's grace for the work they had finished. Foofa nag ñu dugg gaal, jëm Ancos, fa ñu leen dénke woon ca yiwu Yàlla, ngir liggéey bi ñu àggale.
27 When they arrived, they gathered the church and reported all our Father had done with them, and how he opened a door of faith to the Gentiles. Bi ñu agsee, ñu woo mbooloom ñi gëm, nettali leen fi ñu jaar ak Yàlla fépp, ak ni mu ubbee buntu ngëm ci ñi dul Yawut.
28 And they stayed there with the disciples for a long time. Noonu ñu toog ak taalibe ya diir bu yàgg.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]