Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Numbers 33 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 These are the stages of the Israelites' journey out of Egypt, by their divisions under Moses and Aaron's hand. Lii moo di doxi bànni Israayil, ba ñu génnee réewum Misra, def seeni gàngoor, ca njiital Musaa ak Aaróona.
2 Moses wrote their starting points by stage, at our Father's command; these are their stages by starting points. Musaa moo bind seeni dalukaay ak seen yoon ya ñu jaare, ci ndigalal Aji Sax ji. Lii moo di seeni jaar-jaar, ak seeni dalukaay:
3 They set out from Rameses on the fifteenth day of the first month, the day after Passover—the Israelites marched out boldly, in full view of all the Egyptians, Fa Ramses lañu bàyyikoo, fukki fan ak juróom ci weer wi njëkk ci at mi. Keroog bés ba topp ca bésub Mucc ba, ca la bànni Israayil daagu, génn, waa Misra gépp di gis.
4 while the Egyptians buried all their firstborn, whom our Father had struck down among them, and on their gods our Father executed judgments. Booba waa Misraa ngay rob ña Aji Sax ji rey ca ñoom, néewi mboolem seen taaw ya. Aji Sax jee mbugale noonu seen yàlla ya.
5 The children of Israel set out from Rameses and camped at Succoth. Bànni Israayil nag jóge Ramses, dali Sukkót.
6 They set out from Succoth and camped at Etham, which is on the edge of the wilderness. Ñu jóge Sukkót, dali Etam ga ca catu màndiŋ ma.
7 They left Etham, turned back to Pi-hahiroth, east of Baal-zephon, and camped before Migdol. Ba ñu bàyyikoo Etam, dañoo walbatiku ba Pi Axirot ga janook Baal Cefon, daldi dal fa kanam Migdol.
8 They set out from before Hahiroth, crossed the sea into the wilderness, traveled three days through the wilderness of Etham, and camped at Marah. Ñu jóge Pi Axirot, jàll géej ga, wuti màndiŋ ma. Dox nañu yoonu ñetti fan ca biir màndiŋu Etam, doora dal Maara.
9 They left Marah and reached Elim, where twelve water springs and seventy palm trees stood; there they camped. Ñu jóge Maara, dem ba Elim, Elim ga ca fukki bëti ndox yaak ñaar, ak juróom ñaar fukki garabi tàndarma ya. Ñu dal foofa.
10 They set out from Elim and camped by Yam Suph. Ba ñu jógee Elim, fa feggook géeju Barax ya la ñu dali.
11 They set out from Yam Suph and camped in the wilderness of Sin. Ñu bawoo géeju Barax ya, dali ca màndiŋu Sin,
12 They set out from the wilderness of Sin and camped at Dophkah. bawooti màndiŋu Sin, dali Dofka,
13 They set out from Dophkah and camped at Alush. bawooti Dofka, dali Alus.
14 They left Alush and camped at Rephidim, where the people had no water to drink. Ba ñu bàyyikoo Alus, Refidim lañu dali. Foofa nag mbooloo ma amuñu fa ndox mu ñu naan.
15 They set out from Rephidim and camped in the wilderness of Sinai. Ñu bàyyikoo Refidim, dali ca màndiŋu Sinayi,
16 They set out from the wilderness of Sinai and camped at Kibroth-hattaavah. bàyyikoo màndiŋu Sinayi, dali Kibbrot Taawa,
17 They set out from Kibroth-hattaavah and camped at Hazeroth. bàyyikooti Kibbrot Taawa, dali Àccerot.
18 They set out from Hazeroth and camped at Rithmah. Ba ñu jógee Àccerot, Ritma lañu dali.
19 They set out from Rithmah and camped at Rimmon-perez. Ñu jóge Ritma, dali Rimon Perecc,
20 They set out from Rimmon-perez and camped at Libnah. jóge Rimon Perecc, dali Libna,
21 They set out from Libnah and camped at Rissah. jógeeti Libna, dali Risa.
22 They set out from Rissah and camped at Kehelathah. Ba ñu bawoo Risa, Keyelata lañu dali.
23 They set out from Kehelathah and camped at Mount Shepher. Ñu bawoo Keyelata, dali tundu Sefer,
24 They set out from Mount Shepher and camped at Haradah. bawoo tundu Sefer, dali Arada,
25 They set out from Haradah and camped at Makheloth. bawooti Arada, dali Makeyelot.
26 They set out from Makheloth and camped at Tahath. Naka lañu bàyyikoo Makeyelot, dali Taxat,
27 They set out from Tahath and camped at Terah. bàyyikoo Taxat, dali Tera,
28 They set out from Terah and camped at Mithkah. bàyyikooti Tera, dali Mitka.
29 They set out from Mithkah and camped at Hashmonah. Ba ñu jógee Mitka, Asmona lañu dali.
30 They set out from Hashmonah and camped at Moseroth. Ñu jóge Asmona, dali Moserot;
31 They set out from Moseroth and camped at Bene-jaakan. jóge Moserot, dali Bene Yaakan,
32 They set out from Bene-jaakan and camped at Hor-haggidgad. jógeeti Bene Yaakan, dali Xor Gitgaat.
33 They set out from Hor-haggidgad and camped at Jotbathah. Ba ñu bawoo Xor Gitgaat, Yotbata lañu dali.
34 They set out from Jotbathah and camped at Abronah. Ñu bawoo Yotbata, dali Abrona,
35 They set out from Abronah and camped at Ezion-geber. bawoo Abrona, dali Eccon Geber,
36 They set out from Ezion-geber and camped in the wilderness of Zin, that is, Kadesh. bawooti Eccon Geber, dali Kades ca màndiŋu Ciin.
37 They left Kadesh and camped at Mount Hor, on the edge of Edom's land. Ba ñu bàyyikoo Kades, ca tundu Or wa digalook réewum Edom lañu dali.
38 Aaron the priest climbed Mount Hor at our Father's command and died there in the fortieth year after the children of Israel left the land of Egypt, in the fifth month, on its first day. Ba mu ko defee Aaróona sarxalkat ba yéeg ca kaw tundu Or, ci ndigalal Aji Sax ji. Mu daldi faatu foofa, ca ñeent fukkeelu at ma, gannaaw ba bànni Israayil génnee réewum Misra, yemook benn fanu juróomeelu weeru at ma.
39 Aaron was 123 years old when he died on Mount Hor. Aaróona mu ngi woon ci téeméeri atam, ak ñaar fukk at ñett (123) ba mu faatoo ca kaw tundu Or.
40 The Canaanite king of Arad, living in the Negev of Canaan, heard the Israelites were coming. Ci kaw loolu Kanaaneen ba, buurub Aràdd, ba dëkke woon bëj-saalumu réewum Kanaan, daldi yég ne bànni Israayil a ngay dikk.
41 They set out from Mount Hor and camped at Zalmonah. Ba ñu jógee tundu Or, Calmona lañu dali.
42 They set out from Zalmonah and camped at Punon. Ñu jóge Calmona, dali Punon,
43 They set out from Punon and camped at Oboth. jóge Punon, dali Obot,
44 They set out from Oboth and camped at Iye-abarim, on the border of Moab. jógeeti Obot, dali Yee Abarim, ga digalook réewum Mowab.
45 They set out from Iyim and camped at Dibon-gad. Ba ñu jógee Yee Abarim, Dibon Gàdd lañu dali.
46 They set out from Dibon-gad and camped at Almon-diblathaim. Ñu jóge Dibon Gàdd, dali Almon Diblatayim,
47 They set out from Almon-diblathaim and camped in the mountains of Abarim, near Nebo. jógeeti Almon Diblatayim, dali ca tundi Abarim, janook tundu Nebo.
48 They left the mountains of Abarim and camped on the plains of Moab, by the Jordan at Jericho. Ba ñu bawoo tundi Abarim, ca joori Mowab lañu dali, ca wetu dexu Yurdan, janook Yeriko.
49 They camped along the Jordan, from Beth-jeshimoth to Abel-shittim, on the plains of Moab. Wetu dexu Yurdan, ga ca diggante Bet Yesimot ak Abel Sitim, ca joori Mowab, fa lañu dale.
50 Our Father spoke to Moses in the plains of Moab by the Jordan at Jericho, saying: Ba loolu amee Aji Sax ji waxati ak Musaa ca joori Mowab, ca wetu dexu Yurdan, ga janook Yeriko. Mu ne ko:
51 "Speak to the Israelites and tell them: When you cross the Jordan into the land of Canaan. «Waxal bànni Israayil ne leen: Bu ngeen jàllee dexu Yurdan, ba dugg réewum Kanaan,
52 Drive out everyone living in the land before you; destroy all their carved images and metal figures, and tear down all their high places. nangeen dàq waa réew mépp, nangeen yàqate seen mboolem tuur yu ñu yatt, te seen mboolem jëmm yu ñu móol, yàqateleen ko, seen mboolem bérebi jaamookaay it, tasleen ko.
53 Possess the land and live in it, for I have given you the land to possess. Defleen réew mi moomeel, ngeen dëkke ko, ndax yeen laa jox réew mi, ngir ngeen moom ko.
54 Divide the land by lot among your clans—more land to larger clans, less to smaller ones. Wherever the lot falls for someone, that becomes theirs. You will inherit by your ancestral tribes. Tegooleen bant réew mi, séddoo ko ci seeni làng. Làng gu gëna mag, na am cér bu gëna mag, làng gu gëna tuut, am cér bu gëna tuut. Fépp fu tegoo bant génneel ag làng, ñooy doon boroom. Ci seen biir giiri maam ngeen di séddu.
55 "But if you don't drive out the land's residents before you, those you leave will be barbs in your eyes and thorns in your sides, troubling you in the land where you live. Waaye su ngeen dàqul waa réew mi, ña ngeen fa bàyyi ñooy mujj diy dég yu leen di luqi, aki dagg yuy cuut seeni wet. Ñoo leen di lëjal witt ca biir réew mooma ngeen sance.
56 And then I will do to you what I had planned to do to them." Su boobaa nag na ma naroona def seen noon yooyu, yeen laa koy def.»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]