Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Numbers 32 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 The sons of Reuben and sons of Gad had vast herds of livestock. Seeing the land of Jazer and land of Gilead, they noticed it suited livestock well. Jur gu ne gàññ, bare lool, la Rubeneen ñi ak Gàddeen ñi amoon. Ñu xoolaat diiwaanu Yaser ak diiwaanu Galàdd, gisuñu lu moy àll bu neexa yareg jur.
2 The sons of Gad and sons of Reuben came and said to Moses, to Eleazar the priest, and to the community's leaders: Ba mu ko defee Gàddeen ñaak Rubeneen ña dikk, wax ak Musaa ak Elasar sarxalkat ba, ak kilifay mbooloo ma. Ñu ne leen:
3 "Ataroth, Dibon, Jazer, Nimrah, Heshbon, Elealeh, Sebam, Nebo, and Beon, «Gox yii di Atarot ak Dibon ak Yaser ak Nimra ak Esbon ak Elale ak Sebam ak Nebo ak Bewon,
4 the land our Father struck down before Israel's community—is land for livestock, and your servants have livestock." mboolem réew mii Aji Sax ji daan fi kanam mbooloom Israayil de, réew mu neexa yareg jur la, te nun, sang bi, boroomi jur lanu.»
5 They said, "If we have found favor in your eyes, give this land to your servants as a possession. Don't make us cross the Jordan." Ñu teg ca ne: «Kon nag ngalla sang bi, baaxe nu réew mii, muy sunub cér, te nga bañ noo jàlle dexu Yurdan.»
6 Moses said to the sons of Gad and Reuben, "Should your brothers go to war while you sit here? Musaa ne Gàddeen ñaak Rubeneen ña: «Xanaa seeni bokk duñu xareji, yeen ngeen toog fii?
7 Why discourage Israel from crossing into the land our Father has given them? Dangeena nara yoqiloo bànni Israayil, ba tere leena jàlli ca réew ma leen Aji Sax ji jox?
8 This is what your fathers did when I sent them from Kadesh-barnea to see the land. Lu mel nii de, la seeni baay defoon, ba ma leen yebalee, ñu jóge Kades Barneya, ngir yëri réew ma.
9 They went up to the Valley of Eshcol, saw the land, then discouraged the Israelites' hearts from entering the land our Father had given them. Dañoo dem ba àgg xuru Eskol, ba gis réew ma, doora délsi, di yoqiloo bànni Israayil, ngir ñu baña duggi ca réew ma leen Aji Sax ji joxoon.
10 And our Father's anger burned that day, and he swore an oath, saying, Sànjum Aji Sax ji tàng na bésub keroog, ba mu giñ, ne:
11 surely the men who came up from Egypt, twenty years old and up, will not see the land I swore to give to Abraham, to Isaac, and to Jacob—because they did not fully follow me. “Kenn du gis mukk réew ma ma giñaloon Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, ci góor ñi jóge Misra te am ñaar fukki at, jëm kaw, gannaaw mataluñu kóolute ci man;
12 None but Caleb son of Jephunneh the Kenizzite and Joshua son of Nun, for they fully followed our Father. xanaa Kaleb doomu Yefune, Keniseen bi, ak Yosuwe doomu Nuun, ndax ñoo matal kóolute ci Aji Sax ji.”
13 The anger of our Father burned against Israel; he made them wander the wilderness forty years until the whole generation that had done evil before our Father had died. Ba loolu amee sànjum Aji Sax ji tàkkal Israayil, mu wërloo leen ca màndiŋ ma diiru ñeent fukki at, ba mboolem maas googa defoon lu Aji Sax ji ñaawlu, ñépp jeex tàkk.
14 Now you have risen up in place of your fathers, a brood of sinners, adding still more to our Father's fierce anger against Israel! Yeen nag defuleen lu moy jóg wuutu seeni baay, njurum bàkkaarkat yi ngeen doon, di xamb sànjum Aji Sax ji tàkkal bànni Israayil?
15 If you turn from following him, he will leave them in the wilderness once again, and you will destroy all this people." Su ngeen ko dëddoo it, day dellu wacc bànni Israayil ci màndiŋ mi rekk, ngeen daldi sànklu mii mbooloo mépp.»
16 They came to him and said, "We'll build pens here for our livestock and cities for our children. Ba loolu weesoo, ñu dikkaat, ne ko: «Ay gétt lanu bëgga sàkk fii ngir sunuy gàtt, aki dëkk ngir sunuy njaboot.
17 But we will arm ourselves, ready to go ahead of the Israelites until we bring them to their place, while our children stay in fortified cities, safe from those living in the land. Waaye nun kay danuy daldi gànnaayu, jiitu bànni Israayil, ba keroog ñu leen yóbboo ca seen suuf. Sunu njaboot a nuy xaare fii, biir dëkk yu tata wër, ngir ñu mucc ci waa réew mi.
18 We will not return home until every Israelite has taken his inheritance. Dunu dellu mukk sunuy kër, ba keroog bànni Israayil di séddu, ku ci nekk jot céru suufam.
19 We won't inherit with them across the Jordan and beyond, since our inheritance has come to us on this side of the Jordan, to the east." Waaye nun dunu bokk ak ñoom ab céru suuf ca wàllaa dexu Yurdan, ak la ca topp, ndax day fekk nu jot sunu céru suuf, ci wet gii féete dexu Yurdan penku.»
20 Moses said to them, "If you do this—if you arm yourselves before our Father for the war, Musaa ne leen: «Su ngeen ko defee noonu, gànnaayu fi kanam Aji Sax ji ngir xareji,
21 and every armed man among you crosses the Jordan before our Father until he drives out his enemies from before him, su seen mboolem boroomi gànnaay jàllee dexu Yurdan fi kanam Aji Sax ji, ba keroog mu dàqee ay noonam,
22 and the land is subdued before our Father, afterward you may return and be free of obligation to him and to Israel, and this land will be your possession before our Father. ba réew ma nangul Aji Sax ji, su boobaa déy, sañ ngeena délsi, te wàccoo ngeen ak Aji Sax ji, wàccoo ak bànni Israayil, te su boobaa it réew mii ñeel leen, di seen moomeel fi kanam Aji Sax ji.
23 But if you don't do this, look—you will have sinned against our Father, and know: your sin will overtake you. Waaye su ngeen jëfewul noonu kat, yeena moy Aji Sax ji, te xamleen ne seenug moy dina leen dab.
24 Build cities for your little ones, pens for your flocks, and do what your mouth has promised." Kon nag sàkkleen ay dëkk ngir seeni njaboot, aki gétt ngir seeni gàtt, waaye li ngeen dige daal, defleen ko.»
25 The sons of Gad and Reuben said to Moses, "Your servants will do as my lord commands. Ba loolu amee Gàddeen ñaak Rubeneen ña ne Musaa: «Sang bi, noonu nga ko santaanee, ni lanu koy defe.
26 Our children, wives, flocks, and all our herds will stay there in the cities of Gilead, Sunuy goneek sunuy jabar, ak sunuy gàtt, ak sunu jur gépp fii ci dëkki Galàdd lay des.
27 but your servants, every man armed for war, will cross before our Father to battle, as my lord says." Waaye nun, mboolem ñi yor ngànnaay danuy jàll dex gi fi kanam Aji Sax ji, ngir xareji ni nga ko waxe, sang bi.»
28 So Moses commanded Eleazar the priest, Joshua son of Nun, and the clan leaders of Israel's tribes about them. Musaa nag santaane ci seen mbir ca Elasar sarxalkat ba, ak Yosuwe doomu Nuun, ak kilifay bànni Israayil, ya jiite seeni kër maam.
29 Moses said to them, "If Gad's and Reuben's sons cross the Jordan with you, every man armed for battle before our Father, and the land is subdued before you, then give them Gilead as their possession. Musaa ne leen: «Su Rubeneen ñeek Gàddeen ñi àndeek yeen, ñoom ñépp gànnaayu ngir xareji fi kanam Aji Sax ji, ba réew ma nangul leen, nangeen leen jox réewum Galàdd, muy seen moomeel.
30 But if they won't cross over armed with you, they must take possession among you in the land of Canaan." Waaye su ñu àndul ak yeen, gànnaayu jàll, ci seen biir lañuy séddu suuf, ca biir réewum Kanaan.»
31 Gad's and Reuben's sons answered, "We will do as our Father told your servants. Ba loolu amee Gàddeen ña ak Rubeneen ña dellu ne: «Sang bi, li nu Aji Sax ji wax rekk lanuy def.
32 We ourselves will cross armed before our Father into the land of Canaan, and our inherited possession will remain ours beyond the Jordan." Nooy gànnaayu jàlli réewum Kanaan fi kanam Aji Sax ji, waaye nun, cér bi nuy moom, wàllu dexu Yurdan wii lay doon.»
33 Moses gave to them—the sons of Gad, the sons of Reuben, and the half-tribe of Manasseh son of Joseph—the kingdom of Sihon king of the Amorites and the kingdom of Og king of Bashan: the land, its cities, the territories, and the cities of the country around. Musaa nag tudde cér yii, askanu Gàdd ak askanu Ruben ak genn-wàllu giirug Manase doomu Yuusufa: nguurug Sixon buurub Amoreen ñi la leen jox, ak nguurug Og buuru Basan, réew ma mépp, boole ca dëkk yu mag ya, ak àll ya ko wër.
34 And the sons of Gad built Dibon, Ataroth, Aroer, Ba mu ko defee Gàddeen ña tabaxaat Dibon ak Atarot ak Arower,
35 Atroth-shophan, Jazer, Jogbehah, ak Aterot Sofan, ak Yaser ak Yogbowa,
36 Beth-nimrah, and Beth-haran—fortified cities and pens for sheep. ak Bet Nimra, ak Bet Aran, lépp di dëkk yu tata wër. Ñu sàkkaale ay wërmbal ngir seeni gàtt.
37 And the sons of Reuben built Heshbon, Elealeh, Kiriathaim, Rubeneen ña it tabaxaat Esbon ak Elale ak Kiryaatayim,
38 Nebo, Baal-meon (renamed), and Sibmah—they gave the cities they rebuilt new names. ak Nebo, ak Baal Mewon, lenn ca turi dëkk ya soppiku, ak Sibma. Ñu tudde dëkk yooyu ñu tabaxaat, seen turi bopp.
39 Sons of Machir son of Manasseh went to Gilead, captured it, and drove out the Amorites living there. Ci kaw loolu ñi askanoo ci Makir doomu Manase, songi bëj-gànnaaru Galàdd, nangu ko, dàqe fa Amoreen ña.
40 So Moses gave Gilead to Machir son of Manasseh, and he settled in it. Ba mu ko defee Musaa jox Galàdd, askanu Makir, ñu dëkke.
41 And Jair son of Manasseh went and captured their villages, and called them Havvoth-jair. Ci biir loolu askanu Yayir mi askanoo ci Manase, dem nanguji yeneen dëkki Galàdd yu ndaw. Ñu tudde leen Sanci Yayir.
42 And Nobah went and captured Kenath and its villages, and called it Nobah, after his own name. Noba it nanguji Kenat ak dëkk ya ko wër, daldi tudde gox ba boppam, muy Noba.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]