Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Numbers 22 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Then the Israelites set out and camped in the plains of Moab beyond the Jordan, opposite Jericho. Bànni Israayil demati ba dali ca joori Mowab ca wàllaa dexu Yurdan, janook Yeriko.
2 Now Balak son of Zippor saw all that Israel had done to the Amorites. Fekk na Balag doomu Cippor gis mboolem la bànni Israayil def Amoreen ña.
3 Moab feared the people greatly, for they were many; Moab dreaded the Israelites. Mowab nag am tiitaange ju réy ca gàngooru bànni Israayil, ndax bare. Mowab jàq na ba mu gisee bànni Israayil.
4 Moab said to Midian's elders, "This horde will lick up everything around us, as an ox licks up field grass." Balak son of Zippor was king of Moab then. Ci kaw loolu Mowab giseek magi Majan, ne leen: «Ndiiraan wii kat, ni nag di forem parlu ba mu set, ni lañu nara ñédde li nu wër lépp, ba mu set.» Jant yooyu Balag doomu Cippor moo doon buuru Mowab.
5 He sent messengers to Balaam son of Beor at Pethor, by the Euphrates in his people's land, to summon him. He said, "Look, a people has come out of Egypt. Look, they cover the face of the land, and have settled facing me. Mu yebal ay ndaw ca Balaam doomu Bewor ngir woowi ko, ca Petor ga Balaam cosaanoo, ca tàkkal dexu Efraat ngir ne ko: «Balaam! Gàngoor a ngii jóge Misra. Ñu ngii lal suuf si ba mu daj, te ñoo sanc, janook man màkk.
6 Come, please curse this people for me—they are stronger than I am. Maybe then I can strike them and drive them from the land, for I know: whoever you bless is blessed, and whoever you curse is cursed." Kon nag dikkal gaaw ñaanal ma yàlla gàngoor gii, ngir ñoo ma ëpp doole. Jombul ma duma leen, ba dàq leen réew mi, ndax xam naa ne koo ñaanal barke, mu barkeel, te koo ñaanal alkànde, mu alku.»
7 The elders of Moab and elders of Midian went, fortune-telling fees in their hand, and came to Balaam and told him Balak's words. Ci kaw loolu magi Mowab ànd ak magi Majan, dem, yóbbaale ay weexal. Ba ñu agsee ca Balaam, daldi koy àgge kàdduy Balag.
8 He said to them, "Stay here tonight, and I'll bring back word as God speaks to me." So the officials of Moab stayed with Balaam. Mu ne leen: «Fanaanleen fii guddig tey. Tont lu ma ci Aji Sax ji sant rekk, dinaa leen ko àgge.» Kàngami Mowab dal ak Balaam.
9 Then our Father came to Balaam and said, "Who are these men with you?" Yàlla nag dikkal Balaam, ne ko: «Nit ñii fi yaw, ñu mu doon?»
10 Balaam said to our Father, "Balak son of Zippor, king of Moab, has sent word to me: Balaam ne Yàlla: «Buuru Mowab Balag doomu Cippor moo yónnee ci man, ne ma:
11 Look, the people who came out of Egypt cover the land's face. Come now, curse them for me—maybe I can fight against them and drive them out." “Balaam, gàngoor a ngii jóge Misra, lal suuf si ba mu daj. Dikkal gaaw móolul ma leen. Jombul ma mana xareek ñoom, ba dàq leen.”»
12 But our Father told Balaam, "Do not go with them. Do not curse the people, for they are blessed." Yàlla ne Balaam: «Bul ànd ak ñoom, te bul ñaan-yàlla mbooloo ma, ndax ñooñu ñu barkeel lañu.»
13 Balaam got up that morning and told Balak's officials, "Return to your land—God has refused to let me go with you." Ba Balaam jógee ca suba sa, da ne kàngami Balag ya: «Delluleen seenum réew, ndax Aji Sax ji bañ na; mayu ma ma ànd ak yeen.»
14 Moab's officials got up, went to Balak, and said, "Balaam refused to come with us." Kàngami Mowab daldi dellu ca Balag, ne ko: «Balaam de bañ naa ànd ak nun.»
15 Then Balak sent officials again—more numerous and more honored than the first. Balag dellu yebal kàngam yu gëna bare, te gëna kawe.
16 They came to Balaam and said, "Balak son of Zippor says: Let nothing keep you from coming to me, Ñooña dem ba ca Balaam, ne ko: «Balag doomu Cippor dafa wax ne: “Ngalla, bu la dara teree dikk, wuyusi ma.
17 for I will honor you greatly, and do whatever you say to me. So please come and curse this people for me." Maa lay teral teraanga ju réya réy. Loo ma wax, ma def. Dikkal rekk, móolul ma gàngoor gii.”»
18 Balaam answered Balak's servants, "Even if Balak gave me his house full of silver and gold, I cannot go beyond God's command, to do small or great. Balaam tontu surgay Balag, ne leen: «Bu ma Balag doon jox këram ba mu fees ak xaalis ak wurus sax, duma mana def lenn lu tuut mbaa lu réy, lu tebbi sama ndigalu Yàlla Aji Sax ji.
19 Now please, stay here tonight, you too, so I may learn what more our Father will say to me." Waaye yeen it dalleen fii guddig tey, ba ma xam lu ma Aji Sax jiy waxaat.»
20 And our Father came to Balaam at night and said to him, "Since these men came to summon you, get up and go with them, but do only what I tell you." Ci kaw loolu Yàlla dikkal Balaam ca guddi ga, ne ko: «Gannaaw woosi la mooy tànki ñii, àndal ak ñoom. Waaye nag lu ma la wax rekk, def ko.»
21 So Balaam got up in the morning, saddled his donkey, and went with the officials of Moab. Ca ëllëg sa Balaam takk mbaamam, ànd ak kàngami Mowab, dem.
22 But our Father's anger burned because he went, and our Father's messenger stood in the road as Balaam's adversary. Balaam was riding his donkey, with his two servants. Ba loolu amee sànjum Yàlla tàkk ndax yoon wa mu sumb. Malaakam Aji Sax ji nag taxaw ca yoon wa, nara jànkoonte ak moom, moom mu war mbaamam, ànd ak ñaari surgaam.
23 The donkey saw the messenger of our Father standing in the road, his sword drawn in his hand, and she turned off the road into the field. So Balaam struck the donkey to turn her back onto the road. Ci kaw loolu mbaam ma gis malaakam Aji Sax ji taxaw ca digg yoon wa, xàcc saamaram. Mbaam ma ne walbit, wàcc yoon wa, topp àll ba. Balaam dóor mbaam ma, waññi ko ba ca yoon wa.
24 Then our Father's messenger stood in a narrow path between vineyards, a wall on each side. Ba mu ko defee malaakam Aji Sax ji taxawi fu yoon wa def ñall wu sew wu jaare digg tóokëri reseñ, ñaari miir séq ko.
25 The donkey saw the messenger of our Father, pressed against the wall, and pressed Balaam's foot against it, so he struck her again. Mbaam ma gis malaakam Aji Sax ji, daldi tafu ca miir ba, ba tancaale ca tànkub Balaam. Balaam dellu ko dóor.
26 The messenger of our Father went further and stood in a narrow place with no room to turn right or left. Malaakam Aji Sax ja dellu jiitu, ba taxawi fu xat, ba maneesula weesalook moom, du ndijoor, du càmmoñ.
27 When the donkey saw the messenger of our Father, she lay down under Balaam; his anger flared, and he struck her with his staff. Mbaam ma gis malaakam Aji Sax ja, daldi ne wàpp goor ca suufu Balaam, xol ba fuddu, mu dóorati mbaam ma yet wa.
28 Then our Father opened the donkey's mouth, and she said to Balaam, "What have I done to you, that you struck me these three times?" Ba loolu amee Aji Sax ji tijji gémmiñu mbaam mi, mu ne Balaam: «Ana lu ma la def, ba ñetti yoon a ngii nga di ma dóor?»
29 Balaam said to the donkey, "You have mocked me! If I had a sword in my hand, I'd kill you now." Balaam ne mbaam mi: «Yaa may foontoo, su ma yoroon saamar, léegi laa lay rey!»
30 The donkey said to Balaam, "Am I not your donkey, the one you've ridden all your life until today? Have I ever treated you this way before?" He said, "No." Mu ne ko: «Xanaa du maay sa mbaam mi ngay war bu yàgg ba nga ma moomee, ba tey jii? Dama laa masa def nii?» Mu ne ko: «Déedéet.»
31 Then our Father opened Balaam's eyes, and he saw our Father's messenger standing in the road, sword drawn in hand, and he bowed low and fell facedown. Aji Sax ji nag ubbi bëti Balaam, mu gis malaakam Aji Sax ja, mu taxaw ca yoon wa, xàcc saamaram. Mu ne gurub sukk, dëpp jëëm fa suuf.
32 The messenger of our Father said to him, "Why have you hit your donkey three times? I've come out as an adversary, because your way is reckless before me. Malaakam Aji Sax ji ne ko: «Lu tax ngay dóor sa mbaam mi ñetti yoon nii? Man mii maa dikk, jànkoonteek yaw, ndax yoonu sànkute laa gis.
33 The donkey saw me and turned aside from me these three times. Had she not turned aside, I would have killed you by now and spared her life." Mbaam mi moo ma gis, teggi ma ba muy ñetti yoon nii. Bu ma teggiwuloon déy, yaw laay rey; moom, ma ba ko, mu dund.»
34 Balaam said to the messenger of our Father, "I have sinned—I didn't know you stood in the road to oppose me. Now if this is displeasing in your eyes, I'll turn back." Balaam ne malaakam Aji Sax ji: «Maa tooñ, ndax xawma woon ne yaa taxaw, dogale ma ci yoon wi. Léegi nag su la yoon wi neexul, ma daldi dëpp.»
35 The messenger of our Father told Balaam, "Go with the men, but say only what I tell you." So Balaam went on with Balak's officials. Malaakam Aji Sax ji ne Balaam: «Àndal ak nit ñi, waaye daal lu ma la waxloo rekk, wax ko.» Balaam nag ànd ak kàngami Balag, dem.
36 When Balak heard Balaam was coming, he went out to meet him at the city of Moab, on the Arnon border, at the border's edge. Ba loolu amee Balag dégg ne Balaam a ngay ñëw, mu gatanduji ko ca dëkku Mowab, ba digalook dexu Arnon, ca catu réew ma.
37 Balak said to Balaam, "Didn't I send urgently to call you? Why didn't you come to me? Can I really not honor you?" Balag ne Balaam: «Xanaa yeblewuma woon, ba yebleeti, di la woolu? Lu la tee woona ñëw? Am dama laa manula teral?»
38 Balaam told Balak, "Look, I've come to you now—but can I say just anything? I can only speak what God puts in my mouth." Balaam ne Balag: «Maa ngii, wuyusi la, waaye mbaa sañ naa waxal sama bopp lenn? Kàddu gu ma Yàlla waxloo de, moom laay wax.»
39 So Balaam went with Balak, and they came to Kiriath-huzoth. Ci kaw loolu Balaam ànd ak Balag ba Kiryaat Xuccot.
40 Balak sacrificed cattle and sheep, sending shares to Balaam and the officials with him. Balag daldi sarxe ay nag aki gàtt, sédd ca Balaam ak kàngam ya ko dar.
41 In the morning Balak took Balaam and brought him up to Bamoth-baal, and from there he saw the edge of the people. Ca suba sa Balag ànd ak Balaam, yéeg ba ca kaw bérebi jaamookaay ya ñu dippee tuur ma ñuy wax Baal, mu tollu fa di séen lenni catu mbooloo ma.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]