Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Genesis 45 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Joseph could not control himself before everyone standing by him, so he cried out, "Send everyone away from me!" No one stayed with him when Joseph made himself known to his brothers. Ba loolu amee Yuusufa manatula téye boppam, te surgaam yépp a nga teew. Mu daldi àddu ne: «Xiddileen ma, yeen ñépp!» Ñépp dem, ba benn jàmbur nekku fa, ba Yuusufa di xàmmiku ay bokkam.
2 He wept so loudly that the Egyptians heard it, and Pharaoh's household heard it. Mu ne yikkét, jooy jooy yu metti, waa Misra di ca dégg, ba ca kër Firawna sax.
3 Joseph said to his brothers, "I am Joseph! Is my father still alive?" His brothers could not answer him, for they were terrified at his presence. Yuusufa nag ne magam ya: «Man mii maay Yuusufa! Mbaa sama baay a ngi dund?» Magam ya nag manuñu koo tontu, ndax booba njàqare jàpp na leen.
4 Joseph said to his brothers, "Please, come close to me." They came close. He said, "I am your brother Joseph, whom you sold into Egypt. Yuusufa dellu ne ay magam: «Jegeñsileen.» Ñu jegeñsi. Mu ne leen: «Man maay Yuusufa, seen rakk, ji ngeen jaayoon, ñu indi ma Misra.
5 Now don't be distressed or angry with yourselves for selling me here, since our Father sent me ahead of you to preserve life. Waaye buleen jaaxle tey, mbaa ngeen di sikk seen bopp ndax li ngeen ma jaay, ñu indi ma fi. Rawale ay bakkan moo tax Yàlla yebal ma fi, ma jiitusi leen.
6 Famine has been in the land two years now; five more years remain with no plowing or harvest. Ñaari at a ngii xiif baa ngi ci réew mi, te fii ak juróomi at ci kanam, kenn du bey, kenn du góob.
7 Our Father sent me ahead of you to preserve a remnant for you on earth, and keep you alive as a great band of survivors. Yàlla da maa yebal, ma jiitusi leen, ba rawale seen bakkan, dikke leen xettal gu mag, ba seen askan baña fey.
8 So now, it wasn't you who sent me here, but our Father—he made me father to Pharaoh, lord of all his household, and ruler over all the land of Egypt. Kon nag du yeena ma yebal fii, waaye Yàllaa. Te moo ma jagleel, ma doon cëslaayal Firawna, mel ni baay ci moom, jiite këram gépp, boole ci yilif mboolem réewum Misra.
9 Hurry, go up to my father, tell him: Your son Joseph says: Our Father has made me lord of all Egypt. Come down to me; don't delay. «Gaawleen dellu ci sama baay te ne ko: “Sa doom Yuusufa nee na: Yàlla fal na ma kilifag Misra gépp; ñëwal fi man, nu mu gëna gaawe.
10 You'll live in Goshen, near me—you, your children, your children's children, your flocks, your herds, all you own. Su ko defee nga dëkksi diiwaanu Gosen, nekk ci sama wet, yaak say doom ak say sët ak say gàtt ak say gétt ak mboolem loo moom,
11 I will provide for you there—five years of famine remain—so you, your household, and all you own don't fall into poverty. ndaxte des na juróomi ati xiif. Waaye dinaa la fi yore, ba doo ñàkk dara, yaak sa waa kër ak mboolem lu bokk ci yaw.”
12 Your eyes see, and my brother Benjamin's eyes see, that it is my own mouth speaking to you. Yeena gisal seen bopp, yeen ak sama rakk Beñamin, ne man Yuusufa mii, maay wax ak yeen.
13 Tell my father all my honor in Egypt, and all you have seen. Hurry and bring my father down here. Nettalileen sama baay ndam li ma am ci Misra ak li ngeen gis lépp, te ngeen indi sama baay, nu mu gëna gaawe.»
14 Then he threw his arms around his brother Benjamin and wept, and Benjamin wept on his neck." Mu laxasu Beñamin rakkam, daldi jooy, Beñamin it laxasu ko, jooy.
15 He kissed all his brothers and wept over them. After that his brothers talked with him. Magam ña itam, mu fóon leen tey jooy. Booba la magi Yuusufa ya doora wax ak moom.
16 News reached Pharaoh's house: "Joseph's brothers have come." It pleased Pharaoh and his officials. Ba xibaar ba àggee kër Firawna, ñu naan magi Yuusufa ñëw nañu, doonoon na lu neex Firawna, moom aki dagam.
17 Pharaoh said to Joseph, "Say to your brothers: do this—load your animals, go, return to the land of Canaan. Firawna ne Yuusufa: «Waxal say mag, ne leen: “Ni ngeen di def mooy nii: Sëfleen seeni mbaam te dem réewu Kanaan,
18 Take your father and your households and come to me. I will give you the best of Egypt's land, and you will eat the richness of the land. jëli seen baay ak seeni njaboot, ngeen ñëw fi sama wet. Dinaa leen jox suuf si gën ci réewum Misra, ngeen di lekk li fi gëna duuf.”»
19 You are commanded: tell them, 'Do this—take wagons from Egypt for your children and wives, bring your father, and come. Firawna dellu ne Yuusufa: «Am nga ndigal itam ci wax leen ne leen: “Ni ngeen koy defe nii la: Dangeen di jële ay watiir ci réew mi, dem yeb ci seeni doom ak seeni soxna, te ànd ak seen baay, ngeen ñëw.
20 Don't worry about your belongings—the best of all Egypt's land is yours.'" Te buleen réccu alal ji ngeen di bàyyi seen gannaaw, ndax li gën ci réewum Misra yeena koy moom.”»
21 The sons of Israel did so; Joseph gave them wagons per Pharaoh's order, and gave them provisions for the road. Ba loolu amee doomi Israayil def noona. Yuusufa jox leen ay watiir ci ndigalu Firawna, ak lu ñu lekk ca yoon wa,
22 He gave each a change of clothes, but Benjamin 300 pieces of silver and five changes of clothes. mayaale leen ku ne mbubb mu rafet. Waaye Beñamin moom, ñetti téeméeri dogi xaalis la ko may, tegal ko ca juróomi mbubb yu rafet.
23 He sent his father ten donkeys loaded with Egypt's best, and ten female donkeys loaded with grain, bread, and food for his journey. Baayam nag, mu yóbbante ko fukki mbaam yu góor yu sëf lay tànnéef ca Misra, ak fukki mbaam yu jigéen yu sëf pepp ak mburu, tegal ko ca lu mu dunde ca yoon wa, buy ñëw.
24 He sent his brothers off; as they left, he said, "Don't quarrel on the way." Gannaaw loolu mu yiwi ay magam ne leen: «Ngalla buleen xuloo ci yoon wi.» Ñu daldi dem.
25 So they left Egypt and came to their father Jacob in Canaan. Booba lañu bàyyikoo Misra, dellu réewu Kanaan ca seen baay Yanqóoba.
26 They told him, "Joseph is still alive—ruler over all Egypt!" But his heart went numb; he didn't believe them. Ñu wax ko ne ko: «Ndekete Yuusufaa ngi dund! Te sax mooy kilifag réewum Misra gépp.» Ba Yanqóoba déggee loolu, yaramam dafa dee goyy ca saa sa, ndaxte gëmu leen.
27 But when they told him all Joseph's words to them, and he saw the wagons Joseph sent to carry him, their father Jacob's spirit revived. Waaye ba ñu nettalee seen baay Yanqóoba li Yuusufa wax lépp, te mu gis watiir, yi Yuusufa yónnee, ngir jëlsi ko, ca la xelam délsi.
28 Israel said, "Enough! Joseph my son is still alive. I will go and see him before I die." Israayil daldi ne: «Moom kay na dund rekk! Sama doom Yuusufaa ngi dund. Man kay dinaa dem ba gis ko, bala ma fee jóge.»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]