Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Genesis 44 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Then he told his house steward: "Fill the men's sacks with food, as much as they can carry, and put each man's silver at his sack's opening. Ba loolu wéyee mu sant fara biir këram, ne ko: «Solal seeni saaku pepp lu ñu mana àttan, te nga delloo ku nekk xaalisam, tegal ko ko ca buntu saakoom.
2 Put my cup, the silver cup, in the mouth of the youngest's sack, with his grain money." He did as Joseph said. Waaye sama kaasu xaalis boobee, yebal ko ki gën di xale ci saakoom, boole ko ak xaalisu peppam.» Mu def la Yuusufa wax.
3 As soon as the morning was light, the men were sent away with their donkeys. Ca ëllëg sa, ba jant bay fenk, yiwi nañu gaa ña, ñu sëf seeni mbaam, dem.
4 They had left the city, not yet far off, when Joseph told his steward, "Chase down the men. When you catch them, ask, 'Why have you repaid evil for good? Naka lañu génn dëkk ba, te soreeguñu sax, Yuusufa sant fara biir këram, ne ko: «Gaawal dab gaa ña, te boo leen dabee, wax leen ne leen: “Lu tax ñu ji leen ngor, ngeen feye ngoreedi?
5 Isn't this the cup my lord drinks from and uses for fortune-telling? What you've done is evil.'" Ndax li ngeen jël du sama kaasu sang, bi muy naane, rawatina di ko gisaanee? Lu ñaaw ngeen def nii!”»
6 When he overtook them, he spoke these words to them. Mu daldi leen dab, wax leen loolu.
7 They said, "Why does my lord say such things? Your servants would never do such a thing. Ñu ne ko: «Kilifa gi, looy wax nii? Nun de, sang bi, jomb nanu loolu!
8 Look, we brought back to you from Canaan the silver we found in our sacks' openings. How could we steal silver or gold from your master's house? Xaalis bi nu fekkoon ci sunu bunti saaku sax, danoo àndaat ak moom, jóge ba Kanaan, delloosil la ko, kon nan lanu mana sàcce sa kër sang xaalis mbaa wurus?
9 Whichever of your servants it's found with will die, and we'll become my lord's slaves too." Ngalla kilifa gi, yaay sunu sang; koo ko fekke ci nun rekk, boo yeboo reyal, ñi des ci nun doxe fa, di say jaam.»
10 He said, "Good—let it be as you say. Whoever has it will be my slave; the rest of you are innocent." Mu ne leen: «Li ngeen wax yoon la sax, waaye na ki ma ko fekke doŋŋ di sama jaam, su ko defee ñi ci des wàcc.»
11 Then each man quickly lowered his sack to the ground, and each man opened his sack. Ñu gaaw nag, wàcce seeni saaku ci suuf, ku nekk ubbi saakoom.
12 He searched, starting with the oldest, ending with the youngest—the cup was found in Benjamin's sack. Ma ngay seet, tàmbalee ca taaw ba, ba ca caat ma, doora fekk kaas ba ca saaku Beñamin.
13 Then they tore their clothes, and every man loaded his donkey, and they returned to the city. Ba loolu amee dañoo torox, ba xotti seeni yére, ku nekk sëfaat mbaamam, ñu dellu ca dëkk ba.
14 When Judah and his brothers reached Joseph's house, he was still there, and they fell to the ground before him. Yuda aki doomi baayam nag délsi kër Yuusufa, fekk demagul. Ñu daldi ne nërëm, dëpp seen jë fi suuf.
15 Joseph said to them, "What have you done? Don't you know a man like me surely tells fortunes?" Yuusufa ne leen: «Li ngeen def nag? Xanaa xamuleen ne nit ku mel ni man day gisaane?»
16 Judah said, "What can we say to my lord? What can we speak? How can we clear ourselves? Our Father has found your servants' guilt. Look—we are my lord's slaves, both we and the one in whose hand the cup was found." Yuda ne: «Sang bi, lu nuy waxati? Lu nu mana lay, ba setal sunu bopp? Yàllaa nu feeñal, sang bi. Nanu bokk nun ñépp di say jaam, yem ci kepp ak ki ñu fekk kaas bi ci loxoom.»
17 But he said, "I could never do this. Only the man in whose hand the cup was found will be my slave. The rest of you, go back to your father in peace." Mu ne leen: «Jomb naa loolu. Ki ñu fekk kaas bi ci loxoom mooy doon sama jaam; ñi ci des dellu ca seen baay ci jàmm.»
18 Then Judah stepped forward and said, "Please, my lord, let your servant speak a word to you. Don't be angry with your servant, for you are like Pharaoh himself. Yuda jegesi ne ko: «Ngalla sang bi, ma ñeme laa diis lenn rekk, te sa xol baña tàng ci man, doonte yaak Firawnaa tolloo.
19 My lord asked his servants, saying, 'Do you have a father or a brother?' Sang bi, danga noo laajoon ne nu: “Ndax am ngeen baay walla rakk?”
20 We said to my lord, 'We have an old father, and a young son born late in life. His brother is dead; he alone is left of his mother's children, and his father loves him.' Ba mu ko defee nu ne la: “Am nanu baay bu màggat. Sunu rakk, ji mu jur te fekk ko di màggat nag, moo ci gën di ndaw. Magam dafa dee, mu des moom doŋŋ ci ndeyam, baayam sopp ko lool.”
21 Then you told your servants, 'Bring him down to me so I can see him myself.' Nga waxoon nu ne nu: “Indilleen ma ko, ngir ma gisal ko sama bopp.”
22 We told my lord, 'The boy can't leave his father, because if he does, his father will die.' Ci kaw loolu, sang bi, nu wax la ne: “Xale bu góor bi manula tàggook baayam. Bu tàggoo ak moom, kon baayam dina dee.”
23 You told your servants, 'If your youngest brother doesn't come down with you, you won't see my face again.' Nga wax nu ne nu: “Bu seen rakk àndul ak yeen, dungeen jàkkaarlook man.”
24 When we went back to my father, your servant, we told him what you had said. Booba lanu dem ca sunu baay ba lay siyaare, daldi koy jottali say kàddu.
25 And when our father said, 'Go again, buy us a little food,' «Ba nu demee ba mu yàgg, sunu baay ne: “Delluleen, jëndali nu tuuti dund.”
26 we said, 'We can't go down. If our youngest brother comes with us, then we will go. For we can't see the man's face unless our youngest brother is with us.' Teewul nu ne: “Dunu mana dem te sunu rakk àndul ak nun, ndaxte bu nu àndul ak moom, dunu gis kilifa ga.”
27 Then your servant my father said to us, 'You know that my wife bore me two sons. Sunu baay ba lay siyaare, ne nu: “Xam ngeen ne damaa amul ak sama soxna lu dul ñaari doom.
28 One left me, and I said, "Surely torn to pieces"; I haven't seen him since. Kenn ki dem, wacc ma, ma ne moom kay, aw rabu àll a ko daggate! Gisaatuma ko ba tey jii.
29 If you take this one too from me, and harm meets him, you'll bring my gray head down to the grave in grief. Te bu ngeen ma fi jëlalee kii itam, ba musiba dab ko, dingeen ma yóbbe naqar wu may jàpp, ba kera may ànd ak sama bijjaaw, tàbbi njaniiw.”
30 So when I come to your servant, my father, and the boy isn't with us, his life is bound to the boy's life, «Léegi nag, bu ma ñibbee ca sama baay ba lay siyaare, te àndunook xale bii muy noyyee,
31 when he sees the boy is gone, he'll die, and your servants will bring your servant our father down to the grave in sorrow.' bu gisul xale bu góor bi ànd ak nun ñibbisi—aa! Kon de dina dee, te dinanu yóbbe sunu baay naqar, wu koy topp, ba kera muy ànd ak bijjaawam, tàbbi njaniiw.
32 For your servant guaranteed the boy to my father, saying, 'If I don't bring him back to you, I'll bear the guilt before my father all my life.' Gannaaw loolu it xasoon naa dige sama bakkan, ndax damaa waxoon ne: “Bu ma la ko delloosilul, maa koy gàlloo ba kera may dee.”
33 So please, let your servant stay as my lord's slave instead of the boy, and let the boy return with his brothers. Kon ngalla sang bi, bàyyi ma man ma des fi di sa jaam, wuutu xale bi, te moom mu dellu ànd aki magam ñibbi.
34 How can I return to my father without the boy? I could not bear to see the disaster that would strike my father." Ndax xawma nan laay delloo ca sama baay te ànduma ak xale bi. Yàlla buma fekke njekkar li ciy dal sama baay!»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]