Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Genesis 3 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 The serpent was shrewder than any field animal our Father had made. He asked the woman, "Did God really say, 'You must not eat from any tree in the garden'?" Jaan nag moo gënoona muus ci rabi àll, yi Yàlla Aji Sax ji sàkk yépp. Jaan ja moo ne jigéen ja: «Ndax wóor na ne Yàllaa ne: “Buleen lekk ci doomi genn garabu tool bi”?»
2 The woman said to the serpent, "We may eat the fruit from the trees in the garden, Jigéen ja wax jaan ja, ne ko: «Man nanoo lekk ci doomi garabi tool bi kay.
3 but God said, 'Don't eat the tree's fruit in the garden's middle, or touch it, or you'll die.'" Waaye garab gi ci digg tool bi la Yàlla ne: “Buleen ci lekk, buleen ko laal sax, lu ko moy ngeen dee.”»
4 But the serpent said to the woman, "You will certainly not die. Jaan ja ne jigéen ja: «Déedéet, dungeen dee!
5 God knows that when you eat from it, your eyes will open and you'll be like God, knowing good and evil." Waaye Yàlla xam na ne bés bu ngeen ci lekkee, seeni gët dina ubbiku, ngeen mel ni Yàlla, xam lu baax ak lu bon.»
6 The woman saw the tree was good for food, delightful to the eyes, and desirable for wisdom. She took its fruit, ate, gave some to her husband with her, and he ate. Jigéen ja dafa gis ne garab gi rafet na, niru na lu neex, te mata bëgg ci kuy wuta am xel, mu witt ci doom yi, lekk; jox ci jëkkëram ji mu àndal, moom it mu lekk.
7 Then the eyes of both of them were opened, and they knew they were naked; they sewed fig leaves together and made themselves coverings. Seeni gët daldi ubbiku, ñu xam ne yaramu neen lañu def. Ba mu ko defee ñu ràbb xobi garabu figg, gemboo.
8 They heard the sound of our Father walking in the garden in the cool of the day, and the man and his wife hid from his presence among the garden's trees. Gannaaw loolu ñu dégg tànki Yàlla Aji Sax ji, muy doxantu ca tool ba, fekk ker gi sedd, ñu daldi fexee làqu Yàlla Aji Sax ji ci biir garabi tool bi.
9 But our Father called to the man and said to him, "Where are you?" Yàlla Aji Sax ji nag ne Aadama: «Ana nga?»
10 The man said, "I heard you in the garden and was afraid, for I was naked, so I hid." Mu ne ko: «Damaa dégg say tànk ci tool bi, tiit, ndax yaramu neen laa def, ma daldi làqu.»
11 Our Father said, "Who told you you're naked? Did you eat from the tree I forbade you to eat from?" Yàlla Aji Sax ji ne ko: «Ku la xamal ne dangaa def yaramu neen? Mbaa du dangaa lekk ca garab ga ma la aaye, waay?»
12 The man said, "The woman you put with me gave me fruit from the tree, and I ate." Aadama ne ko: «Jigéen ji nga ma booleel de, moo ma jox ci garab gi, ma lekk.»
13 Then our Father asked the woman, "What have you done?" She said, "The serpent deceived me, and I ate." Yàlla Aji Sax ji ne jigéen ja: «Yaw, li nga def nii mooy lan?» Jigéen ja ne ko: «Aa, jaan de moo ma nax, ba ma lekk ci.»
14 So our Father said to the serpent, "Because you have done this, cursed are you above all livestock and above all wild animals; on your belly you will go, and dust you will eat all the days of your life. Yàlla Aji Sax ji nag ne jaan ja: «Gannaaw def nga loolu, yaw rekk yaay alku ci rabi kër yépp ak rabi àll yépp; dinga watatu, di lekk pënd sa giiru dund gépp.
15 And I will put enmity between you and the woman, and between your offspring and her offspring; he will crush your head, and you will strike his heel." Dinaa def mbañeel sa digganteek jigéen ji, ba dëddale sa xeet ak xeetam, muy toj sa bopp, nga di ko màtt ci téstën.»
16 To the woman he said, "I will greatly increase your pain in childbirth; in pain you will give birth to children. Your desire will be for your husband, and he will rule over you." Yàlla teg ca ne jigéen ja: «Dinaa taral sa mititu mat, ci mitit ngay wasin. Sa bëgg-bëggu bakkan dina la xiir ci sa jëkkër, te moo lay teg tànk.»
17 And to Adam he said, "Because you listened to your wife and ate from the tree that I commanded you, saying, 'You must not eat from it,' cursed is the ground because of you; through painful toil you will eat from it all the days of your life. Mu tegaat ca ne Aadama: «Gannaaw dégg nga sa waxu soxna, ba lekk ci garab gi ma la aaye, dinaa rëbb suuf ndax yaw; coono bu metti nga ciy dunde sa giiru dund gépp.
18 It will produce thorns and thistles for you, and you will eat the plants of the field. Suuf dina la meññalal ay dég aki dagg, doo lekk te beyoo,
19 By the sweat of your brow you will eat your bread until you return to the ground, since from it you were taken; for dust you are, and to dust you will return." saw ñaq ngay dunde, ba kera ngay dellu ci suuf si ma la jële; ndaxte pënd nga, te dinga dellu di pënd.»
20 The man named his wife Eve, because she would become the mother of all the living. Aadama nag tudde soxnaam Awa (muy firi Dund), ndax mooy ndeyu képp kuy dund.
21 Our Father made garments of skin for Adam and his wife, and he clothed them. Gannaaw gi, Yàlla Aji Sax ji sàkkal Aadama ak soxnaam ay yérey der, wodde leen.
22 Then our Father said, "Look, the man has become like one of us, knowing good and evil. Now, so he doesn't reach out, take from the tree of life too, eat, and live forever…" Yàlla Aji Sax ji daldi ne: «Léegi nit mel na ni nun, xam lu baax ak lu bon. Kon nag bumu tàllal loxoom, di witt ci doomi garab giy taxa dund, di lekk, bay dund fàww.»
23 So our Father sent him out of the garden of Eden to work the ground he was taken from. Ba loolu amee Yàlla Aji Sax ji génne ko toolub Àjjana, muy bey suuf si ñu ko sàkke.
24 He drove out the man and placed cherubim and a whirling, flaming sword east of Eden's garden, guarding the way to the tree of life. Da koo dàq, ba noppi teg ca penkub toolu Àjjana ba ay malaakay serub, boole ca saamar buy xuyy-xuyyi, tey dem aka dikk, di wattu yoon, wa jëm ca garab gay taxa dund.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]