Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Genesis 2 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 So the heavens and the earth were completed in all their vast array. Ci kaw loolu asamaan ak suuf ak li ñu ëmb lépp mat.
2 By the seventh day our Father had completed his work, and he rested on the seventh day from everything he had made. Bésub juróom ñaareel ba fekk na Yàlla matal liggéeyam. Mu dallu nag ca bésub juróom ñaareel ba, gannaaw ba mu liggéeyee loolu lépp.
3 And our Father blessed the seventh day, making it holy, because on it he rested from all the work of creation he had done. Yàlla daldi barkeel bésub juróom ñaareel ba, def ko bés bu sell, ndax da caa dallu woon gannaaw liggéey ba mu sàkke lépp.
4 This is the history of the heavens and the earth when they were created, when our Father made earth and heavens. Liy cosaanal asamaan ak suuf, ba ñu leen di sàkk, mooy lii. Bés ba Aji Sax ji Yàlla sàkkee suuf ak asamaan,
5 No shrub of the field yet existed on the earth, no plant of the field had yet sprouted, for our Father had not sent rain on the earth, and there was no man to work the ground, genn garab nekkagul woon ci kaw suuf, te genn gàncax saxagul; ndaxte booba Yàlla Aji Sax ji tawagul, te nit kuy bey amagul.
6 but springs came up from the earth and watered the whole surface of the ground. Ci biir loolu mbënn di balle ci suuf, di tooyal fépp.
7 Then our Father formed the man from dust of the ground, breathed into his nostrils the breath of life, and the man became a living person. Yàlla Aji Sax ji nag móol nit ci pëndub suuf, ëf ngelawal dund ci paxi bakkanam, nit daldi doon boroom bakkan.
8 Then our Father planted a garden in Eden, in the east, and put there the man he had formed. Naka noona Yàlla Aji Sax ji jëmbat tool ca biir Àjjana fa féeteek penku ba, tàbbal ca nit ka mu bind.
9 From the ground our Father grew every tree lovely to see and good to eat, with the tree of life in the garden's center and the tree of knowing good and evil. Yàlla Aji Sax ji nag saxal ci suuf lépp luy garab gu meññeef ma rafet te neexa lekk; mu def it garab gay taxa dund ca digg tool ba, moom ak garab gay taxa xam lu baax ak lu bon.
10 A river flowed from Eden to water the garden; from there it divided into four rivers. Amoon na dex guy balle Àjjana, di suuxat tool ba, te fa la séddalikoo, def ñeenti wal.
11 The first is named Pishon; it flows around all the land of Havilah, where gold is found. Turu menn wal ma di dexu Pison, moo wër réewum Awila mépp. Wurus a nga woon ca réew mooma,
12 The gold of that land is good; aromatic resin and onyx are also there. di wurusu ngalam; te it ndàbb lu neex xet lu tudd bedelyum a nga fa woon ak per yu jafe yu ñuy wax onigsë.
13 The name of the second river is the Gihon; it winds through the entire land of Cush. Ñaareelu dex ga di Gixon, wër réewu Kuus mépp;
14 The third river's name is Tigris, flowing east of Assyria. The fourth river is the Euphrates. turu ñetteelu dex ga di Tiigar, féete réewum Asiri penku; ñeenteelu dex ga di Efraat.
15 Our Father took the man and set him in the garden of Eden to work it and guard it. Yàlla Aji Sax ji nag jël nit ki, tàbbal ko biir toolub Àjjana, mu di ko bey aka sàmm.
16 And our Father commanded the man, "You are free to eat from any tree in the garden; Yàlla Aji Sax ji sant nit ki, ne ko: «Man ngaa lekk ci mboolem garabi tool bi,
17 but you must not eat from the tree of knowledge of good and evil, for you will surely die the day you eat from it." waaye bul lekk ci garab giy taxa xam lu baax ak lu bon, ndaxte bés boo ci lekkee kat, li wér mooy fa ngay doxe dee.»
18 Then our Father said, "It is not good for the man to be alone. I will make a helper matching him." Yàlla Aji Sax ji daldi ne: «Wéet baaxul ci nit, kon dinaa ko bindal ku koy taxawu te jekk ci doon wéttalam.»
19 From the ground our Father formed every field animal and every sky bird, then brought each to the man to see what he'd name it. Whatever the man named each living creature, that was its name. Loolu fekk na Yàlla Aji Sax ji sàkk ci suuf nja-àll yépp ak njanaaw yépp, daldi leen indil nit, di seet nu leen nit di tudde; te tur wu mu leen jox, muy moom.
20 The man named all livestock, birds of the sky, and all wild animals, but for Adam no helper matching him was found. Ba mu ko defee nit kooku, di Aadama, tudd jur gépp ak picc yépp ak rabi àll yépp, waaye fekku ca ku koy jàppale te jekk ci doon wéttalam.
21 So our Father made the man fall into a deep sleep, and while he slept, took one of his ribs and closed the flesh over it. Bi loolu amee Yàlla Aji Sax ji nelawloo Aadama nelaw yu xóot. Ba muy nelaw nag, mu rocci genn ciy faaram, fatte pax ma aw suux.
22 Then our Father built a woman from the rib he took from the man, and brought her to the man. Yàlla Aji Sax ji bind jigéen ci faar, gi mu jële ci Aadama, indil ko ko.
23 The man said, "At last! This is bone of my bones and flesh of my flesh; she will be called 'woman,' for she was taken out of man." Aadama ne tonet, daldi ne: «Waaw kay nag, kii moo bokk ci samay yax ak sama suux! Dees na ko tudde jigéen, ndaxte ci góor lees ko jële.»
24 So a man leaves his father and mother, joins his wife, and they become one flesh. Looloo tax góor di teqalikook ndeyam ak baayam, taqoo ak jabaram, ñuy wenn suux.
25 The man and his wife were both naked, and they were not ashamed. Ku góor ki ak jabaram, ñoom ñaar ñépp, yaramu neen lañu defoon, te amuñu ci woon genn kersa.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]