Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Daniel 6 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
2 Darius appointed 120 satraps over the kingdom, stationed throughout the whole kingdom, Mu neex Daryus nag, mu fal téeméeri jawriñ ak ñaar fukk ca réew ma, ñuy saytu nguur ga gépp;
3 and three officials over them, one of them Daniel, so the satraps would answer to them and the king lose nothing. ak ñetti saytukat yu leen jiite, kenn ka di Dañeel. Saytukat yooyu nag di leen xamal lu ñuy liggéey, ngir Buur baña yàqule dara.
4 Daniel outshone the administrators and satraps, because an extraordinary spirit was in him, and the king planned to set him over the whole kingdom. Ci biir loolu Dañeel di ku ràññiku ci biir saytukat yaak jawriñ ya, ndax rafetum xel; ba tax Buur di seet nu mu koy fale, mu yilif nguur gépp.
5 Administrators and satraps sought grounds to charge Daniel over the kingdom, but found none—no corruption—since he was faithful; no negligence or corruption was found in him. Ba loolu amee saytukat yaak jawriñ ya di wuta tuumaal Dañeel ci mbiri nguur gi, te gisuñu genn tooñ mbaa sikk ci moom, ndax ku amoon kóllëre la, te giseesul ci moom genn néewal mbaa sikk.
6 Then these men said, "We'll find no charge against Daniel unless we find one in his God's law." Ñu daldi ne: «Dunu gis mukk lenn lu nu tuumaal Dañeel. Xanaa nu gis ko ci yoonu Yàllaam.»
7 So the administrators and satraps went together to the king and said, "King Darius, live forever! Ba mu ko defee saytukat yaak jawriñ ya ànd rungumloo ba ca Buur, ne ko: «Buur Daryus, guddaluw fan!
8 All the kingdom's administrators, prefects, satraps, counselors, and governors agreed the king should issue a royal statute and firm decree: whoever petitions any god or man but you, king, for thirty days, will be thrown into the lions' den. Saytukati nguur gépp ak laman yeek jawriñ yeek xelalkat yeek jaraaf yi mànkoo nañu, tëral dogalu buur bi yoonal aaye bii: ci diiru fanweeri fan, képp ku ñaan ci jenn yàlla mbaa ci nit ku la moy, yaw Buur sang bi, dees na ko sànni ca kàmbu gaynde ya.
9 Now, king, issue the decree and sign it in writing, unalterable, under the law of the Medes and Persians, which cannot be revoked. Léegi nag, Buur, dogalal aaye bi, te torlu mbind mi, ba dootul tebbiku, mu dëppook yoonu waa Medd ak waa Pers wi dul toxu.»
10 So King Darius signed the document and the ordinance." Ci kaw loolu Buur Daryus torlu mbindum aaye ba.
11 Learning the decree was signed, Daniel went home to his upstairs room, windows open toward Jerusalem, knelt three times daily, and prayed, giving thanks before his Father as always. Ba Dañeel yégee ne torlu nañu dogal ba, teewul mu ñibbi, yéeg ca néeg ba ca kaw taax ma palanteer ya jublook Yerusalem, na mu ko daan defe naka jekk ñetti yoon ci bés. Mu sukk fa, di ñaan aka sant Yàllaam.
12 Then these men came together and found Daniel praying and pleading for mercy before his Father. Ci kaw loolu nit ña rungumloo, fekk ko muy ñaan aka dagaan Yàllaam,
13 They approached the king about the decree: "Did you not sign a decree that for thirty days, anyone petitioning any god or man except you, king, would be thrown into the lions' den?" The king answered, "The matter stands, by the law of the Medes and Persians, unchangeable." ba noppi ñu dem fekki Buur, ngir wax ak moom ca aaye ba mu tëral, ne ko: «Xanaa du yaa torlu aaye bi ne: képp ku ñaan jenn yàlla mbaa nit ku la moy, yaw Buur, diiru fanweeri fan, dees na ko sànni ca kàmbu gaynde ya?» Buur ne: «Dogal bi kay wér na, dëppook yoonu waa Medd ak Pers wi dul toxu.»
14 They told the king, "Daniel, one of Judah's exiles, ignores you, king, and your signed decree—praying three times daily." Ñu ne ko: «Buur, Dañeel mi bokk ca ngàllog Yudeen ña de, faalewu la, yaak aaye bi nga torlu. Ñetti yoon ci bés lay ñaan ay ñaanam ba tey.»
15 Hearing this, the king was deeply troubled, determined to save Daniel, and worked until sunset to rescue him. Buur dégg ko, am tiis wu réy. Mu daldi fas yéene ne dina musal Dañeel. Ba jant so ma ngay wut pexe mu mu ko musale.
16 Then these men gathered before the king and said, "Know, king: by law of the Medes and Persians, no decree or edict the king issues can be changed." Ci kaw loolu nit ña rungumlooti ba ca Buur, ne ko: «Buur, xamal ne yoonu waa Medd ak Pers tëral na ne mboolem aaye mbaa dogal bu buur dëggal dootul toxu.»
17 Then the king gave the command, and they brought Daniel and threw him into the lions' den. The king said to Daniel, "May your God, whom you serve continually, rescue you." Buur nag joxe ndigal, ñu yóbbu Dañeel, tàbbal ko ca kàmbu gaynde ya. Buur ne ko: «Sa Yàlla ji nga saxoo jaamu, yal na la xettali.»
18 A stone was brought, placed over the den's mouth, and sealed by the king with his signet ring and his nobles' rings, so nothing about Daniel could change. Ba mu ko defee ñu indi aw doj, dëj ko ca buntu kàmb ga, Buur bës ca jaarob torlukaayam ak jaarob torlukaayu jaraafam ya, ba dara dootul mana soppiku ci deminu Dañeel.
19 Then the king went to his palace and fasted that night; no entertainment was brought before him, and sleep fled from him. Ba loolu wéyee Buur dellu këram. Lekkul guddi gi yépp, sàkkuwul lu koy bégal, te nelaw të ko.
20 Then, at the first light of dawn, the king rose and hurried to the den of lions. Ba njël jotee, ba bët di bëgga set, Buur jóg, daldi gaaw dem ca kàmbu gaynde ya.
21 Nearing the den, he cried out to Daniel anxiously. The king said to Daniel, "Daniel, servant of the living God, has your God, whom you serve continually, been able to rescue you from the lions?" Naka la jub kàmb ga, daldi woo Dañeel; baat baa nga tiis. Mu ne ko: «Éy Dañeel, jaamu Yàlla jiy dund; sa Yàlla ji nga saxoo jaamu, mbaa mujj na laa xettali ci gaynde yi?»
22 Then Daniel said to the king, "King, may you live forever! Dañeel daldi ne Buur: «Buur, guddaluw fan!
23 My Father sent his angel and shut the lions' mouths. They haven't harmed me, because I was found innocent before him, and before you, king, I've done no wrong." Sama Yàlla yebal na malaakaam, mu tëj gémmiñi gaynde yi, ba defuñu ma dara. Ndax kat mucc naa ci tuuma sama digganteek moom ak sama digganteek yaw it, te defuma dara lu bon.»
24 The king was overjoyed and ordered Daniel lifted from the den. Daniel was lifted out with no injury at all, for he had trusted in his Father. Buur nag am mbégte mu réy. Ci kaw loolu mu joxe ndigal, ñu génne Dañeel ca kàmb ga. Ba ñu génnee Dañeel ca kàmb ga, gaañuwul fenn, ndax daa wóolu Yàllaam.
25 The king ordered the men who had falsely accused Daniel brought and thrown into the lions' den—with their children and wives. Before they reached the bottom, the lions overpowered them and crushed all their bones. Ba loolu wéyee Buur joxe ndigal, ñu indi nit ña tuumaaloon Dañeel, ñu tàbbal leen ca kàmbu gaynde ya, ñook seeni doom ak seeni jabar. Àgguñu suuf sax, gaynde ya alawti leen, dammate seen yax yépp.
26 Then King Darius wrote to all peoples, nations, and languages living on earth: "May your peace overflow! Gannaaw loolu Buur Daryus bind waa mbooloo yépp ak xeet yépp ak làkk yépp, di waa àddina sépp, ne: «Jàmm ngeen!
27 I decree: in all my kingdom, people must tremble and fear before Daniel's God—the living God, enduring forever. His kingdom will never be destroyed; his rule never ends. «Dogal tukkee na ci man, ne mboolem fu bokk ci sama nguur, nañu fa ragal Yàllay Dañeel, wormaal ko, keey Yàlla jiy dund, kee sax fàww, nguuram du tas, kilifteefam du jeex.
28 He rescues and delivers; he works signs and wonders in the heavens and on the earth; he is the one who rescued Daniel from the power of the lions." Keey musle, di xettalee, di def ay màndarga aki kéemaan, kaw asamaan ak suuf. Kee musal Dañeel ca pàddum gaynde ya.»
29 So this Daniel thrived in the reign of Darius and of Cyrus the Persian. Dañeel nag gëna am cér diirub nguurug Daryus ak nguurug Sirus waa Pers ba.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]