Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

2 Chronicles 4 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 He made a bronze altar thirty feet long, thirty feet wide, and fifteen feet high. Suleymaan sàkk na itam ab sarxalukaayu xànjar bu gudde ñaar fukki xasab, yaatoo ñaar fukki xasab, taxawaayam di fukki xasab.
2 He made the cast-metal Sea, round: fifteen feet across, seven and a half high, forty-five around. Ci biir loolu mu móollu mbalkam njàpp mu weñ, ñu di ko wax Géej ga. Mbalka ma daa mërgalu; yaatoo fukki xasab catu omb, ba catu omb; taxawaay ba di juróomi xasab, ag buumu fanweeri xasab di ko ub.
3 Below the rim, figures of oxen encircled it, about seven to every foot around the Sea, cast in two rows as one piece with it. Ay jëmmi nag a nga ca suufu mbalka ma, wër ko ba mu daj, fukki nag tollook xasab. Nag yi def ñaari làng yu wër mbalka mi ba mu daj te ànd ak mbalka mi ci benn xelli.
4 The Sea stood on twelve oxen, three facing north, three west, three south, three east, resting on them, their hindquarters all inward. Mbalkam njàpp mi, ci kaw fukki jëmmi nag ak ñaar la tege, ñett jublu bëj-gànnaar, ñett jublu sowu, ñett jublu bëj-saalum, ñett jublu penku. Mbalka mi war nag yi, seeni gannaaw féete biir, ñoom ñépp.
5 About three inches thick, its rim like a cup's, like a lily's flower, holding about 17,000 gallons. Dëllaayu mbalka mi yaatuwaayu loxo la, kéméj gi mel ni gémmiñu kaas, di nirook lëppu tóor-tóor. Ñetti téeméeri barigo ak fanweer (330) la mbalka miy def.
6 He made ten washing basins, five south, five north, to rinse what was used for the burnt offerings; the Sea was for the priests to wash in. Ci biir loolu Suleymaan sàkk fukki ndabi raxasu, teg juróom wetu ndijoor, juróom wetu càmmoñ, ñu di ca raxas yàppu saraxu rendi-dóomal, mbalka ma nag, sarxalkat ya di ca jàppe.
7 He made ten gold lampstands as specified, five for the temple's south side, five for the north. Mu sàkk fukki tegukaayi làmpi wurus yi, ni ñu ko diglee, teg tegukaay yi ci biir néeg bu mag bu kër Yàlla ga, juróom ci wetu ndijoor; juróom, wetu càmmoñ.
8 He made ten tables, placed them in the temple—five south, five north—and one hundred gold basins. Mu sàkk itam fukki taabal, yeb leen ca biir néeg bu mag ba, juróom, wetu ndijoor; juróom, wetu càmmoñ; ak téeméeri këlli tuurukaayi deret yu wurus.
9 He made the priests' court, the great court, its doors, and plated their doors with bronze. Mu sàkk ba tey ëttu sarxalkat yi, ak ëtt bu mag bi, sàkkal ëtt bu mag bi lafi bunt, daldi xoob lafi bunt yi xànjar.
10 He placed the Sea on the south side, at the southeast corner. Mbalka mi nag, mu tege ko wetu ndijoor, fa féete bëj-saalum, jàpp penku.
11 Huram made the pots, shovels, and basins. So Huram finished the work he did for King Solomon in the house of our Father: Uram sàkk itam ndabi tibbukaayu dóom ak ñiitukaay yi ak këll yi. Ci kaw loolu Uram sottal liggéey ba mu liggéeyal Buur Suleymaan ca kër Yàlla ga:
12 the two pillars; the two bowl-shaped capitals atop the pillars; the two networks covering those capitals; muy ñaari kenu yi, ak ñaari gamb yiy boppi kenu yi, te tege ca seen kaw, ak ñaari caaxi càllala yiy muur ñaari gamb yi,
13 400 pomegranates for the two networks, two rows each, covering the two capital bowls on the pillars; ak ñeenti téeméeri gërënaat yiy ànd ak ñaari caax yi; caax bu nekk, ñaari caqi gërënaat, ñu dar ñaari gamb yi ci boppi kenu yi;
14 the stands and the basins on the stands; ak fukki rootukaay yi ak fukki bagaan yi ci kaw rootukaay yi.
15 the one Sea and the twelve oxen beneath it. Menn mbalkam njàpp mi ñuy wax Géej gi it ci la, ak fukki nag ak ñaar yi ci ronam.
16 Pots, shovels, meat forks, and all their utensils—Huram-abi made these for King Solomon, for our Father's house, of polished bronze. Ndabi tibbukaayu dóom ak ñiitukaay yi, ak cappukaayi yàpp yi, ak mboolem jumtukaay ya cay ànd, xànjar bu ñu jonj la ko Uram Abi defal Buur Suleymaan, ñeel kër Aji Sax ji.
17 The king had them cast in clay molds in the Jordan plain between Succoth and Zeredah. Ci joorug Yurdan la ko Buur xellilu, ci móoli ban yu ñu gas, ci diggante Sukkót ak Cereda.
18 Solomon made all these items in such quantity that the bronze weight could not be determined. Suleymaan moo sàkk jumtukaay yooyu yépp, mu bare lool, ba natteesul diisaayu xànjar ba ca dem.
19 Solomon made all the furnishings for our Father's house: the golden altar and tables with the bread of the Presence. Gannaaw loolu Suleymaan defarlu na mboolem yeneen jumtukaayi kër Yàlla ga: muy sarxalukaayu wurus ba, ak taabal ya ñuy teg mburum teewal ma,
20 The pure gold lampstands with their lamps, to burn before the inner sanctuary as prescribed; ak tegukaayi làmp ya ak seeni làmp, lépp di wurusu ngalam, làmp yiy tàkk, na ko àtteb yoon tërale, fa kanam néeg bu sella sell bi;
21 the gold flowers, lamps, and tongs (these were of the purest gold). tóor-tóor yi it ak làmp yi ak ñiim yi, lépp di wurus, wurus wu set wecc.
22 Pure gold: the wick trimmers, sprinkling bowls, dishes, censers, and the temple's doorways—inner doors to the Most Holy Place, and the main hall's doors. Feyukaay yi itam ak këll yi ak kopp yi ak andi cuuraay yi, lépp wurusu ngalam la. Te bunti kër Yàlla ca la, muy: buntu néeg bi ñuy jaare dugg ci néeg bu sella sell bi, ak ay lafam ak lafi buntu néeg bi ñuy jaare dugg ci néeg bu mag bi, lépp wurus la.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]